57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
65 | GEN 3:9 | Yàlla Aji Sax ji nag ne Aadama: «Ana nga?» |
67 | GEN 3:11 | Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» |
69 | GEN 3:13 | Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.» |
86 | GEN 4:6 | Aji Sax ji ne Kayin: «Lu la taxa mer, ba ne fóññ nii? |
89 | GEN 4:9 | Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?» |
90 | GEN 4:10 | Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg. |
317 | GEN 12:18 | Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la? |
318 | GEN 12:19 | Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» |
327 | GEN 13:8 | Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? |
328 | GEN 13:9 | Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.» |
363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
369 | GEN 15:8 | Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?» |
390 | GEN 16:8 | Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.» |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
416 | GEN 17:18 | Ibraayma ne Yàlla: «Moo, tee ngaa saxal Ismayla rekk te ànd ak moom?» |
434 | GEN 18:9 | Ñu daldi ko laaj ne ko: «Ana sa soxna Saarata?» Mu ne leen: «Mu ngi ci biir.» |
437 | GEN 18:12 | Ci kaw loolu Saarata ree ci suuf, daldi ne: «Man mu ñor xomm mii, ndax man naa amati boobu bànneex, te sama boroom kër it di mag?» |
438 | GEN 18:13 | Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: “Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?” |
439 | GEN 18:14 | Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.» |
442 | GEN 18:17 | Booba Aji Sax jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar? |
448 | GEN 18:23 | Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen? |
449 | GEN 18:24 | Su juróom fukk rekk jubee ca dëkk bi, mbaa doo tas dëkk bi ba tey, tee nga leena jéggal rekk ngir juróom fukk ñu jub ña ca nekk? |
453 | GEN 18:28 | Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.» |
454 | GEN 18:29 | Ibraayma dellu wax ne: «Su fa ñeent fukk ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Duma def dara ngir ñeent fukk ñooñu.» |
455 | GEN 18:30 | Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» |
456 | GEN 18:31 | Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» |
457 | GEN 18:32 | Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.» |
460 | GEN 19:2 | «Dégluleen ma, ngalla sang yi, siyaare naa leen, tee ngeena dal ak man, su ko defee ngeen jàngu, fanaan ba suba, ngeen xëy topp seen yoon?» Ñu ne ko: «Bàyyil, nu fanaan ci mbedd mi.» |
463 | GEN 19:5 | Ñu daldi woo Lóot ne ko: «Ana góor ñi fi ñëw tey ci guddi? Génneel nu leen fii, ndax nu mana àgg ci ñoom.» |
478 | GEN 19:20 | Gisuloo dëkk bale; jege na, te dëkk bu tuut la, am déet? Ma daw, làquji fa boog, ba mucc?» |
500 | GEN 20:4 | Loolu fekkul Abimeleg dëkkoo Saarata. Mu wax Yàlla ne ko: «Sama Boroom, mbaa doo bóom réew mi ci mbir mu ñu doonul dara? |
501 | GEN 20:5 | Du góor gi da maa waxoon ne kii jigéenam la? Du jigéen ji it da maa waxoon ne kooku càmmiñam la? Fexewuma dara lu ñaaw te di ko tey de!» |
505 | GEN 20:9 | Gannaaw loolu Abimeleg woolu Ibraayma ne ko: «Li nga nu def nag? Ndax dama laa tooñ, ba nga yóbbe ma tooñ gu réye nii, man ak sama réew mi mépp? Lii nga ma def de, waroo ko woona def.» |
506 | GEN 20:10 | Abimeleg teg ca ne ko: «Te li nga def sax, lu la ci xiir?» |
531 | GEN 21:17 | Ba mu ko defee Yàlla dégg baatu xale bu góor ba. Malaakam Yàlla ma àddoo asamaan, ne Ajara: «Ajara, lan la? Bul ragal dara, ndaxte Yàlla dégg na sa baatu doom ci diggante bii mu tollu. |
543 | GEN 21:29 | Abimeleg nag ne Ibraayma: «Lu tax nga ber juróom ñaari xar yooyu?» |
555 | GEN 22:7 | Isaaxa ne baayam Ibraayma: «Baay!» Mu ne ko: «Naam, doom sama.» Isaaxa ne ko: «Sawara saa ngi, matt maa ngi, waaye ana gàtt, bi nuy sarxal?» |
587 | GEN 23:15 | «Déglu ma, kilifa gi, suuf suy jar ñeenti téeméeri dogi xaalis doŋŋ du dara ci sama diggante ak yaw; tee nga faa denc sa néew rekk?» |
597 | GEN 24:5 | Surga ba ne ko: «Su ndaw sa nanguwula ànd ak man ci réew mii nag? Ndax kon damaa wara yóbbu sa doom ba ca réew ma nga jóge?» |
615 | GEN 24:23 | Mu ne ko: «Wax ma, kan moo la jur?» Ak itam: «Ndax man nanoo dal sa kër baay?» |
631 | GEN 24:39 | Ma ne sama sang: “Bu ndaw sa nanguwula ànd ak man nag?” |
639 | GEN 24:47 | Ma laaj ko ne ko: “Kan moo la jur?” Mu ne: “Betuwel, doomu Naxor ak Milka.” «Ca laa ko takkal jaaro bi ci bakkanam, ak lam yi ciy loxoom. |
648 | GEN 24:56 | Mu ne leen: «Gannaaw Aji Sax ji àntal na sama yoon, tee ngeen ma baña yeexal, te bàyyi ma rekk, ma dellu ca sama sang?» |
650 | GEN 24:58 | Ci kaw loolu ñu woo Rebeka, ne ko: «Ndax dangay ànd ak waa ji léegi?» Mu ne: «Waaw.» |
657 | GEN 24:65 | daldi ne surga ba: «Waa jee ci àll biy ñëw, jëm ci nun, kan a?» Surga ba ne ko: «Sama sang la de.» Rebeka daldi jël muuraay ba, muuroo. |
691 | GEN 25:32 | Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?» |
702 | GEN 26:9 | Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.» |
703 | GEN 26:10 | Abimeleg ne ko: «Li nga nu def nag? Xaw tuuti kenn ci nit ñi tëdde sa soxna, te kon nga yóbbe nu tooñ.» |
720 | GEN 26:27 | Isaaxa ne leen: «Lu waral ngeen fekksi ma fii, gannaaw dangeen maa bañ, ba dàq ma?» |
746 | GEN 27:18 | Mu dikk ci baayam, ne ko: «Baay.» Mu ne ko: «Naam doom, kooku?» |
748 | GEN 27:20 | Isaaxa ne doomam: «Moo doom! Noo def, ba gaawa jàpp nii?» Yanqóoba ne ko: «Aji Sax jiy sa Yàlla, moo ma ko jagleel.» |
752 | GEN 27:24 | Isaaxa laaj ko ne ko: «Mbaa wóor na ne yaw ay Esawu?» Mu ne ko: «Waawaaw.» |
760 | GEN 27:32 | Baayam Isaaxa ne ko: «Kooku?» Mu ne ko: «Mana sa taaw Esawu.» |
761 | GEN 27:33 | Isaaxaa ngay lox, bay rag-ragi, daldi ne ko: «Kan? Ana ku rëbbi woon nag, indil ma, ba ma lekk ba noppi? Ñaanal naa ko bala ngaa ñëw. Te dina barkeel moos.» |
764 | GEN 27:36 | Esawu ne: «Moom kay moo yey tudd Yanqóoba, ndax suufu na ma ñaari yoon. Sama céru taaw la jëkka nangu, tey mu nangooti sama ñaanu baay.» Mu teg ca ne: «Ndax desalaloo ma ag ñaan?» |
765 | GEN 27:37 | Isaaxa ne Esawu: «Mbaa am naa lu ma la ñaanalati, doom? Ndax kat xas naa koo def, muy sa kilifa, te bokkam yépp laa def ñuy surgaam, te pepp ak biiñ laa ko woomale it, ba mu ne gàññ.» |
766 | GEN 27:38 | Esawu ne baayam: «Baay, xanaa genn ñaan rekk nga am? Ngalla baay, ñaanal ma, man itam!» Ca la Esawu ne yikkét jooy. |
800 | GEN 29:4 | Yanqóoba ne leen: «Bokki fan?» Ñu ne ko: «Karan.» |
801 | GEN 29:5 | Mu ne leen: «Ndax xam ngeen Laban doomu Naxor?» Ñu ne ko: «Xam nanu ko kay.» |
802 | GEN 29:6 | Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» |
821 | GEN 29:25 | Ba bët setee, Yanqóoba fekk muy Leya. Mu ne Laban: «Waaw, li nga ma def nag? Du Rasel a taxoon ma liggéeyal la? Lu tax nga wor ma?» |
833 | GEN 30:2 | Yanqóoba mere ca Rasel ne ko: «Ndax maay Yàlla, mi la teree am doom?» |
846 | GEN 30:15 | Teewul mu ne ko: «Ndax nangu sama jëkkër rekk doyu la, ba nga bëgg cee boole màndaragoor ji ma sama doom indil?» Rasel ne ko: «Kon jox ma ci màndaragoor ji sa doom indi, ma wecci la ko sama ayu tey boog.» |
861 | GEN 30:30 | ndaxte lu néew nga amoon laata may ñëw, te yokku na, ba bare lool, ngir Aji Sax ji da laa barkeel ndax man. Waaye léegi nag, liggéeyal sama waa kër bopp jot na xanaa?» |
862 | GEN 30:31 | Laban dellu ne ko: «Dama ne, ñaata laa lay fey?» Yanqóoba ne ko: «Doo ma jox dara. Boo nangoo lii ma lay wax, dinaa sàmmaat say gàtt, wattu ko. |
888 | GEN 31:14 | Rasel ak Leya ne ko: «Ndax amati nanu benn cér walla ndono sunu kër baay? |
900 | GEN 31:26 | Laban ne Yanqóoba: «Looy def nii, yaw, di ma nëbbuy daw, yóbbaale sama doom yu jigéen, ñu mel ni ñu ñu lële xare? |
901 | GEN 31:27 | Lu waral nga di ma nëbbuy daw te bañ maa tàggu? Nde konoon jombul ma yiwi la ci xol bu sedd, bu ànd aki woy, boole ci xalam aki sabar. |
904 | GEN 31:30 | Bu la neexee, nga namm sa kër baay, ba dogu caa dem, waaye lu tax nga sàcc sama gàllaaji kër, teg ci?» |
910 | GEN 31:36 | Yanqóoba mer lool, daldi gëdd Laban ne ko: «Ndax damaa tooñ walla damaa moy, ba nga sambal ma, di ma topp nii? |
911 | GEN 31:37 | Bi nga jéexee sama yëf yépp ba noppi, ana loo gis lu bokk ci sa yëfi kër? Teg ko fii ci sama kanami bokk ak say bokk, ñu àtte nu. |
912 | GEN 31:38 | Xanaa du ñaar fukki at a ngii ma nekk ak yaw? Say xar ak say bëy ëmbuñu sax, mu yàqu, te masumaa lekk sa kuuyi gétt. |
917 | GEN 31:43 | Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom? |
946 | GEN 32:18 | Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?” |
956 | GEN 32:28 | Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.» |
958 | GEN 32:30 | Yanqóoba ne ko: «Waaw, yaw nag noo tudd?» Mu wax ko ne ko: «Loo may laaje sama tur?» ba noppi barkeel ko foofa. |
966 | GEN 33:5 | Naka la Esawu siggi, gis jigéen ñi ak xale yi, mu ne: «Ñii ànd ak yaw ñooy ñan?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa njaboot, gi ma Yàlla baaxe, sang bi.» |
969 | GEN 33:8 | Esawu ne ko: «Waaw, dal bu réy bii ma dajeel, loo ci namm?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa di sàkku nga dalal ma jàmm rekk, sang bi.» |
973 | GEN 33:12 | Gannaaw loolu Esawu ne: «Tee noo ànd dem boog, ma jiitu la?» |
990 | GEN 34:9 | Tee noo séyante, ngeen may nu seeni janq, te jël ci sunuy janq? |
1004 | GEN 34:23 | Bu nu leen nangulee, ba ñu dëkk ci sunu biir, kon seeni jur ak seen alal ak seen mala yépp, ndax du nooy doon boroom?» |
1012 | GEN 34:31 | Ñu ne ko: «Danuy seetaan sunu jigéen daal, ñu di ko def ab gànc?» |
1092 | GEN 37:8 | Mag ya ne ko: «Dangaa nara falu ci sunu kaw? Danga noo nara jiite?» Ñu gënati koo bañ nag ndax géntam ya ak la mu leen ca wax. |
1094 | GEN 37:10 | Ba mu ko nettalee ay magam, ba nettali ko baayam, baayam da koo soow ne ko: «Yaw, li nga gént, lu mu doon? Xanaa du maak sa yaay ak say mag noo lay sujjóotal?» |
1099 | GEN 37:15 | Naka la jenn waay dajeek moom foofa, fekk muy wëreelu ca àll ba. Waa ja ne ko: «Looy seet?» |
1100 | GEN 37:16 | Yuusufa ne ko: «Samay mag laay seet. Xamoo fu ñu tollu, di sàmm?» |
1104 | GEN 37:20 | Nanu ko rey gaaw, sànni ko ca kàmb yee, su ko defee danu naan, rabu àll a ko fàdd. Nu seet ba xam fu muy mujj aki géntam?» |
1110 | GEN 37:26 | Yuda ne doomi baayam ya: «Bu nu reyee sunu rakk jii, nëbb deret ji, lu nu ciy jële? |
1111 | GEN 37:27 | Tee nu koo jaay Ismayleen ñi, te bañ koo sàkkal pexe nun ci sunu bopp? Ndax kat sunu rakk a, di sunu deret.» Doomi baay ya déggal ko. |
1116 | GEN 37:32 | Gannaaw loolu ñu yóti seen baay mbubb ma, ne ko: «Lii lanu gis de, xoolal bu baax ndax du sa mbubbu doom?» |
1136 | GEN 38:16 | Mu jàdd, ñëw ba ca moom, ne ko: «May ma, ma ànd ak yaw.» Fekk na xamul woon ne goroom la. Mu ne ko: «Loo may fey, ngir ànd ak man?» |
1138 | GEN 38:18 | Mu ne ko: «Lu ma lay tayle?» Ndaw si ne ko: «Xanaa sa jaarob màndargaal, ak buum, gi mu àndal ak yet, wi ci sa loxo.» Mu jox ko nag, ba noppi ànd ak moom. Fa la doxe ëmb. |
1141 | GEN 38:21 | Mu laaj waa gox ba, ne leen: «Ana gànc biy toog Enayim ci yoon wi?» Ñu ne ko: «Fii de ab gànc nekku fi.» |
1149 | GEN 38:29 | Naka la delloo loxoom, seexam juddu, mu ne ko: «Yaw foo bëtte, ba génn?» Ñu daldi ko tudde Peres (mu firi Bëtt). |
1159 | GEN 39:9 | Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?» |
1180 | GEN 40:7 | Mu laaj jawriñi Firawna, yooyee ñu tëjandoo woon ak moom ca kër sangam, ne leen: «Lu leen tax ne yogg tey?» |
1181 | GEN 40:8 | Ñu ne ko: «Ay gént daal a nu dikkal, te amunu ku nu koy firil.» Yuusufa ne leen: «Xanaa du Yàllaa moom piri? Nettalileen ma seeni gént rekk kay.» |
1189 | GEN 40:16 | Kilifag lakk-kati mburu ya nag gis ne piri mi neex na, mu ne Yuusufa: «Man it sama gént gi, xam nga lu ma ci gis? Ñetti pañey mburu mu weex laa yenu, |
1234 | GEN 41:38 | Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?» |