3 | GEN 1:3 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. |
6 | GEN 1:6 | Yàlla ne: «Na aw dénd dox diggante ndox yi, ngir xàjjale leen, yii fii, yii fale.» |
9 | GEN 1:9 | Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona. |
11 | GEN 1:11 | Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. |
15 | GEN 1:15 | Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. |
20 | GEN 1:20 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» |
22 | GEN 1:22 | Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» |
24 | GEN 1:24 | Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. |
26 | GEN 1:26 | Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.» |
28 | GEN 1:28 | Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.» |
30 | GEN 1:30 | Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona. |
48 | GEN 2:17 | waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.» |
49 | GEN 2:18 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.» |
54 | GEN 2:23 | Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.» |
57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
59 | GEN 3:3 | Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”» |
61 | GEN 3:5 | Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni bët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.» |
65 | GEN 3:9 | Yàlla Aji Sax ji nag ne Aadama: «Ana nga?» |
66 | GEN 3:10 | Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.» |
67 | GEN 3:11 | Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» |
68 | GEN 3:12 | Aadama ne ko: «Jigéen, ji nga ma booleel de, moo ma jox ci garab gi, ma lekk.» |
69 | GEN 3:13 | Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.» |
71 | GEN 3:15 | Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.» |
72 | GEN 3:16 | Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.» |
75 | GEN 3:19 | saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.» |
78 | GEN 3:22 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.» |
81 | GEN 4:1 | Gannaaw loolu Aadama dëkkoo na soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu Aji Sax ji.» |
87 | GEN 4:7 | Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.» |
89 | GEN 4:9 | Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?» |
92 | GEN 4:12 | Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.» |
94 | GEN 4:14 | Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.» |
95 | GEN 4:15 | Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey. |
104 | GEN 4:24 | Kayin kay, lees di feyul juróom ñaari yoon, ne, bu dee Lemeg mii, muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.» |
105 | GEN 4:25 | Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.» |
135 | GEN 5:29 | Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» |
141 | GEN 6:3 | Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).» |
145 | GEN 6:7 | Aji Sax ji daldi ne: «Dinaa far ci kaw suuf doom aadama yi ma sàkk, nit ak jur, luy raam ak luy naaw, ndax mititlu naa li ma leen sàkk.» |
159 | GEN 6:21 | Sàkkal ci bépp xeetu dund, denc, ngeen bokk dunde.» |
164 | GEN 7:4 | Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.» |
201 | GEN 8:17 | Génnewaaleel lépp luy xeetu mbindeef mu ngeen àndal: picc yi ak bàyyima yi ak luy raam, ñu fulandiwu ci kaw suuf, daldi giir te bare.» |
206 | GEN 8:22 | Li feek suuf di suuf, dootu jiwooy dakk mbaa ngóob, te du sedd aku tàngoor, du nawet it mbaa noor, mbaa guddeek bëccëg.» |
213 | GEN 9:7 | Yeen nag, giirleen te bare, fulandiwu ci kaw suuf te fees ko.» |
217 | GEN 9:11 | Ni may faseek yeen kóllëre nii la: Deesatul boole bindeef yépp, faat ci mbënn mukk. Du menn mbënn mu deeti faagaagal àddina.» |
222 | GEN 9:16 | Xon gi day nekk ci biir niir yi, ma di ko gis, di xalaat kóllëre, gi ma fas fàww, sama diggante, man Yàlla, ak mboolem xeetu mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» |
223 | GEN 9:17 | Ci kaw loolu Yàlla ne Nóoyin: «Loolu mooy màndargaal sama kóllëre, gi ma fas ak mboolem mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» |
231 | GEN 9:25 | Ba mu ko defee mu ne: «Yal na Kanaan torox, bay jaamu jaami doomi ndeyam.» |
233 | GEN 9:27 | Yal na Yàlla lawal askanu Yafet, dëël ko ci xaymay Sem, te Kanaan di seen jaam.» |
244 | GEN 10:9 | mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Namróot, rëbbkat bu maga mag ba.» |
270 | GEN 11:3 | Ñu ne: «Ayca nu defar ay móol yu ñu lakk cib taal, ba mu ñor.» Ci kaw loolu ñu def móol ya doji tabax, taqalee ko koltaar, |
271 | GEN 11:4 | daldi ne: «Ayca nu tabax ab dëkk bu taax ma bëtt asamaan; kon dinanu am woy, te dunu tasaaroo ci kaw suuf.» |
274 | GEN 11:7 | Ayca nu wàcc, safaan seen làkk, ba dootuñu déggoo.» |
302 | GEN 12:3 | ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.» |
306 | GEN 12:7 | Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay. |
312 | GEN 12:13 | Kon nag ngalla waxal ne sama jigéen nga, ba tax ma am jàmm; su ko defee dees na ma bàyyi, ma dund, te di la ko gërëme.» |
318 | GEN 12:19 | Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» |
328 | GEN 13:9 | Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.» |
336 | GEN 13:17 | Jógal wër réew mi mépp, ba mu daj, ndax yaw laa koy may.» |
357 | GEN 14:20 | Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko. |
358 | GEN 14:21 | Gannaaw loolu buurub Sodom wax Ibraam ne ko: «Jox ma nit, ñi nga jàpp, te nga fab alal ji.» |
361 | GEN 14:24 | Duma jël dara, lu wees li sama nit ñi lekk ba noppi ak sama wàllu farandoo yi, di Aner ak Eskol ak Mamre, ñoom it, nañu jot seen wàll.» |
362 | GEN 15:1 | Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.» |
363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
364 | GEN 15:3 | Ibraam teg ca ne: «Mayoo ma giir, te it jaam bu juddoo sama kër moo may donn.» |
365 | GEN 15:4 | Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ko, ne ko: «Du moom moo lay donn, waaye ku sosoo ci sa geño moo lay donn.» |
366 | GEN 15:5 | Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.» |
368 | GEN 15:7 | Gannaaw loolu Aji Sax ji wax ko ne ko: «Man maay Aji Sax, ji la génnee Ur, ga ca Kaldeen ña, ngir may la réew mii, nga moom ko.» |
369 | GEN 15:8 | Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?» |
370 | GEN 15:9 | Aji Sax ji ne ko: «Jëlal wëlluw ñetti at ak bëyu ñetti at ak kuuyu ñetti at, boole ci pitaxu àll ak xati mu ndaw.» |
377 | GEN 15:16 | Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi jéggeegul dayo.» |
382 | GEN 15:21 | boole ci réewum Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Girgaseen ñi ak Yebuseen ñi.» |
384 | GEN 16:2 | Sarayi ne Ibraam: «Li am mooy Aji Sax ji deful ma am doom. Kon ngalla waay, dëkkool sama jaam bi, ndax Yàlla def, mu amal ma doom ju góor.» Ibraam nag dégg la Sarayi wax. |
387 | GEN 16:5 | Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» |
388 | GEN 16:6 | Ibraam wax Sarayi ne ko: «Sa jaam a ngoog ci say loxo, def ko lu la neex.» Sarayi nag di torxal Ajara, ba mu daw, ba soreek moom. |
390 | GEN 16:8 | Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.» |
391 | GEN 16:9 | Malaakam Aji Sax ja ne ko: «Dellul ca sa sang, te nga yem ciy loxoom.» |
392 | GEN 16:10 | Mu teg ca ne ko: «Dinaa yokk sa askan lool, ba kenn du leen mana waññ,» |
394 | GEN 16:12 | Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul not, di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko. Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.» |
395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
400 | GEN 17:2 | Dinaa feddli sama kóllëre ak yaw, yokk la bu baax.» |
406 | GEN 17:8 | Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.» |
412 | GEN 17:14 | Góor gu xaraful, ndax nanguwula xaraf, dees na ko dagge ci biir xeetam, ndax sàmmul sama kóllëre.» |
414 | GEN 17:16 | Dinaa ko barkeel, may la ak moom doom ju góor; dinaa ko barkeel moos, ba mu jaboote xeet yu bare, te ay buuri xeet sax dinañu soqikoo ci moom.» |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
416 | GEN 17:18 | Ibraayma ne Yàlla: «Moo, tee ngaa saxal Ismayla rekk te ànd ak moom?» |
419 | GEN 17:21 | Waaye sama kóllëre nag, Isaaxa laa koy fasool, moom Isaaxa, mi Saarata di am, nëgëni déwén.» |
430 | GEN 18:5 | Maa ngi leen di indil dogu mburu mu ngeen dëgërloo, ba mana topp seen yoon, gannaaw nangu ngeena toog, ma siyaare leen.» Ñu ne ko: «Waaw, baax na.» |
431 | GEN 18:6 | Ibraayma daldi gaaw, dugg biir xayma ba, ne Saarata: «Gaawal, jël ñetti ndabi sunguf su mucc ayib, not ko, def ko mburu yu ndaw.» |
434 | GEN 18:9 | Ñu daldi ko laaj ne ko: «Ana sa soxna Saarata?» Mu ne leen: «Mu ngi ci biir.» |
435 | GEN 18:10 | Kooka ne ko: «Nëgëni sii déwén déy laay délsi, te sa soxna Saarata dina am doom ju góor moos.» Bi muy wax loolu, Saarataa ngi ci buntu xayma bi ci gannaawam, di déglu. |
437 | GEN 18:12 | Ci kaw loolu Saarata ree ci suuf, daldi ne: «Man mu ñor xomm mii, ndax man naa amati boobu bànneex, te sama boroom kër it di mag?» |
439 | GEN 18:14 | Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.» |
440 | GEN 18:15 | Saarata dégg loolu, daldi tiit, miim ko ne: «Reetaanuma de.» Teewul Aji Sax ji ne ko: «Ree nga kay!» |
444 | GEN 18:19 | Moo tax ma tànn ko, ngir mu sant ay doomam ak waa këram, ñuy déggal Aji Sax ji, di jëfe yoon ak njub. Noonu laay defale Ibraayma li ma ko digoon.» |
446 | GEN 18:21 | Dinaa wàcc, seede ko, ba mu wóor ne ñoo def lépp li sabab yuux yi, am déet.» |
450 | GEN 18:25 | Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!» |
451 | GEN 18:26 | Aji Sax ji ne ko: «Su ma gisee ci Sodom juróom fukk ñu jub, dinaa jéggal waa dëkk bi yépp ngir ñoom.» |
453 | GEN 18:28 | Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.» |
454 | GEN 18:29 | Ibraayma dellu wax ne: «Su fa ñeent fukk ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Duma def dara ngir ñeent fukk ñooñu.» |
455 | GEN 18:30 | Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» |
456 | GEN 18:31 | Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» |