Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   “    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

57  GEN 3:1  Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
59  GEN 3:3  Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”»
438  GEN 18:13  Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?”
509  GEN 20:13  Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”»
564  GEN 22:16  «Déglul lii Aji Sax ji wax: Giñ naa ci man mii, gannaaw yaa def lii, te gàntaloo ma sa jenn doom ji,
606  GEN 24:14  Janq bu ma wax ne ko: Doo yenniku sa njaq, may ma, ma naan,” mu ne ma: Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,” na kooka di ki nga jagleel sa jaam Isaaxa. Noonu laay xame ne laaye nga biir sama sang.»
629  GEN 24:37  Sama sang nag giñloo ma ne: Bul jëlal mukk sama doom soxna ci biir jigéeni waa réewu Kanaan, gi ma dëkk.
631  GEN 24:39  Ma ne sama sang: Bu ndaw sa nanguwula ànd ak man nag?”
632  GEN 24:40  Mu ne ma: Aji Sax, ji ma topp, dina yónni malaakaam, mu ànd ak yaw, ba àntalal la sa yoon, nga jëlal sama doom soxna ca sama kër baay, ca sama biiri bokk.
634  GEN 24:42  Ba ma agsee tey jii ca seyaan ba, damaa wax ne: Aji Sax ji, sama Yàllay sang Ibraayma, ndegam nar ngaa àntal yoon wi may dox, ngalla may ma lii:
637  GEN 24:45  «Bala maa ñaan ba noppi, Rebeka ne jimeet, gàddu njaqam, wàcc ca seyaan ba, di root. Ma ne ko: May ma, ma naan.”
638  GEN 24:46  Mu gaaw yenniku njaq li, daldi ne ma: Naanal ba noppi ma wëggal la say giléem.” Ma naan ba noppi, mu wëggal ma giléem yi.
639  GEN 24:47  Ma laaj ko ne ko: Kan moo la jur?” Mu ne: Betuwel, doomu Naxor ak Milka.” «Ca laa ko takkal jaaro bi ci bakkanam, ak lam yi ciy loxoom.
735  GEN 27:7  Demal rëbbi, indil ma, toggal ma ko lu neex, ma lekk, ba ñaanal la, Aji Sax ji seede, bala may dëddu.”
882  GEN 31:8  Bu nee: Yi tippanteey sa peyoor,” jur gépp jur lu tippante; mbaa mu ne: Yi seereer ay sa peyoor,” jur gépp jur lu seereer.
885  GEN 31:11  Ca la ma malaakam Yàlla ma wax ci biir gént gi ne ma: Yanqóoba,” ma ne ko: Naam.”
886  GEN 31:12  Mu ne ma: Siggil, xool sikket yiy tëb bëy yi yépp, yii dañoo seereer, yee todde, yi ci des tippante, ndaxte gis naa li la Laban di def lépp.
903  GEN 31:29  Manoon naa laa def lu bon, waaye sa Yàllay baay da maa feeñu biig ne ma: Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.”
933  GEN 32:5  Mu sant leen ne leen: «Bu ngeen demee ca sama sang Esawu, neleen ko: Sa surga Yanqóoba nee na: Maa nga woon ca kër Laban bu yàgg ba tey,
938  GEN 32:10  Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.”
941  GEN 32:13  Te yaw yaa ma ne: Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej, si kenn manula lim ndax bare.”»
946  GEN 32:18  Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: Kuy sa njaatige?” ak Ku moom li nga jiital?” ak Foo jëm?”
947  GEN 32:19  nee ko: Lii de sang bi, lu la Yanqóoba may la, di la ko siyaaree, yaw Esawu, te moom ci boppam mu ngi topp ci sunu gannaaw.”»
949  GEN 32:21  tegati ca ne ko: «Te nee ko itam: Sa surga Yanqóobaa ngi topp ci sunu gannaaw.”» Booba Yanqóobaa ngi naa ci xelam: «Bu ma jiitalee li ma ko may, neexale ko ko, bala maa janook moom, jombul mu dalal ma jàmm.»
1101  GEN 37:17  Waa ja ne ko: «Jóge nañu fii de, ndax dégg naa ñu naan: Nanu dem Dotan.”» Yuusufa toppi magam ya ba Dotan, fekk leen fa.
1275  GEN 42:22  Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.»
1284  GEN 42:31  Nu ne ko: Nun ay nit ñu maandu lanu, dunu ay yëddukat;
1286  GEN 42:33  Waa ja yilif réew ma ne nu: Ni may xame ne ñu maandu ngeen, nii la: dangeen may bàyyeek kenn ci yeen, te dem yóbbul dund seen waa kër, yi nekk ci xiif;
1294  GEN 43:3  Yuda ne ko: «Waa ja da noo àrtu woon de, wax na nu ne nu: Dootuleen jàkkaarlook man te ànduleen ak seen rakk.”
1296  GEN 43:5  Waaye boo ko bàyyiwul kat, dunu dem, ndax waa ja waxoon na nu ne nu: Dungeen jàkkaarlook man te seen rakk àndul ak yeen.”»
1329  GEN 44:4  Naka lañu génn dëkk ba, te soreeguñu sax, Yuusufa sant fara biir këram, ne ko: «Gaawal dab gaa ña, te boo leen dabee, wax leen ne leen: Lu tax ñu ji leen njekk, ngeen feye ngoreedi?
1344  GEN 44:19  Sang bi, danga noo laajoon ne nu: Ndax am ngeen baay walla rakk?”
1345  GEN 44:20  Ba mu ko defee nu ne la: Am nanu baay bu màggat. Sunu rakk, ji mu jur te fekk ko di màggat nag, moo ci gën di ndaw. Magam dafa dee, mu des moom doŋŋ ci ndeyam, baayam sopp ko lool.”
1346  GEN 44:21  Nga waxoon nu ne nu: Indil-leen ma ko, ngir ma gisal ko sama bopp.”
1347  GEN 44:22  Ci kaw loolu, sang bi, nu wax la ne: Xale bu góor bi manula tàggook baayam. Bu tàggoo ak moom, kon baayam dina dee.”
1348  GEN 44:23  Nga wax nu ne nu: Bu seen rakk àndul ak yeen, dungeen jàkkaarlook man.”
1350  GEN 44:25  «Ba nu demee ba mu yàgg, sunu baay ne: Delluleen, jëndali nu tuuti dund.”
1351  GEN 44:26  Teewul nu ne: Dunu mana dem te sunu rakk àndul ak nun, ndaxte bu nu àndul ak moom, dunu gis kilifa ga.”
1352  GEN 44:27  Sunu baay, ba lay siyaare, ne nu: Xam ngeen ne damaa amul ak sama soxna lu dul ñaari doom.
1357  GEN 44:32  Gannaaw loolu it xasoon naa dige sama bakkan, ndax damaa waxoon ne: Bu ma la ko délloosilul, maa koy gàlloo ba kera may dee.”
1368  GEN 45:9  «Gaawleen dellu ci sama baay te ne ko: Sa doom Yuusufa nee na: Yàlla fal na ma kilifag Misra gépp; ñëwal fi man, nu mu gëna gaawe.
1376  GEN 45:17  Firawna ne Yuusufa: «Waxal say mag, ne leen: Ni ngeen di def mooy nii: sëfleen seeni mbaam te dem réewu Kanaan,
1378  GEN 45:19  Firawna dellu ne Yuusufa: «Am nga ndigal itam ci wax leen ne leen: Ni ngeen koy defe nii la: dangeen di jële ay watiir ci réew mi, dem yeb ci seeni doom ak seeni soxna, te ànd ak seen baay, ngeen ñëw.
1418  GEN 46:31  Ba mu ko defee Yuusufa wax ak doomi baayam ya ak waa kër baayam ne leen: «Maa ngi dellu yégali Firawna ne ko: Samay bokk ak sama waa kër baay, ña nekkoon ca réewu Kanaan, ñëw nañu fi man.
1421  GEN 46:34  Lan mooy seen liggéey?” ngeen ne ko: Nun de sang bi, ag jur lanu masa yar, ba nuy gone ba tey, te noonu la ko sunuy maam daan defe.” Su boobaa, ngeen mana féetewoo diiwaanu Gosen, ndaxte waa Misra dañuy xof sàmm.»
1456  GEN 48:4  te wax na ma ne ma: Dinaa la giiral, fulandi la, def la nga sos mbooloom xeet, te réew mii laay may ñi askanoo ci yaw, ñu moom ko fàww.”
1472  GEN 48:20  Gannaaw loolu mu ñaanal leen keroog ne leen: «Yal na Israyil di ñaane seeni tur naan: Yal na la Yàlla def ni Efrayim ak Manase.”» Noonu la jiitale Efrayim, door caa teg Manase.
1524  GEN 50:17  Waxleen Yuusufa ne ko, sa baay nee: Say mag def nañu la lu bon moos, waaye ngalla baal leen seeni tooñ ak àq, ji ñu la ameel.” Kon rikk waay, baal nu àq, ndax nun nook sa baay a bokk jenn Yàlla ju nuy jaamu.» Ba ñu waxee Yuusufa loolu, mu daldi jooy.
1594  EXO 3:14  Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”»
1595  EXO 3:15  Yàlla dellu ne Musaa: «Dangay wax bànni Israyil, ne leen: Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo ma yónni ci yeen.” Aji Sax jee di sama tur wu sax dàkk, ñu di ma ko fàttlikoo ba fàww.
1596  EXO 3:16  Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra.
1598  EXO 3:18  «Magi Israyil dinañu la déggal, su ko defee nga ànd ak ñoom, dem ca buuru Misra. Waxleen ko ne ko: Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi moo nu feeñu. Kon nag ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji ay sarax.”
1603  EXO 4:1  Gannaaw loolu Musaa dellu wax Aji Sax ji ne ko: «Waaw, su ñu ma dégluwul te gëmuñu ma, xanaa ne ma: Aji Sax ji feeñuwu la” nag?»
1624  EXO 4:22  Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor.
1634  EXO 5:1  Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”»
1641  EXO 5:8  Waaye sasleen leen limu móol, ya ñu daan móol naka jekk. Buleen ko wàññi, ndax ay yaafus lañu; moo leen tax di dee-deeluy waxeey naan: May nu, nu dem rendili sunu Yàlla sarax!”
1650  EXO 5:17  Firawna ne leen: «Yaafus yi ngeen doon! Yaafus a leen tax di wax naan: May nu, nu dem rendili Aji Sax ji sarax.”
1695  EXO 7:9  «Bu leen Firawna waxee ne leen: Defleen seeni kéemaan boog!” danga naan Aaróona: Jëlal yet wi, sànni ci suuf ci kanam Firawna.” Su ko defee yet wi dina soppliku jaan.»
1702  EXO 7:16  Wax ko ne ko: Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi, moo ma yónni ci yaw. Mu di la wax, ne la: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu jaamuji ma ca màndiŋ ma.’ Yaw nag booba ba tey yaa ngi tanqamlu.
1705  EXO 7:19  Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona ne ko: Jëlal saw yet, te tàllal sa loxo tiimale ko ndoxi Misra, muy seeni dex ak seen yooni ndox ak seeni déeg ak fépp fu ndox taa, mu ànd soppliku deret.” Deret ja dina daj Misra gépp, ba ca këll yaak njaq ya.»
1712  EXO 7:26  Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma.
1731  EXO 8:16  Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: «Teelala xëy ëllëg ca Firawna, buy génn jëm ca ndox ma, nga wax ko ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma.
1744  EXO 9:1  Ba loolu wéyee Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, nga ne ko: Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
1756  EXO 9:13  Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Teelala xëy ca Firawna ëllëg, nga wax ko ne ko: Aji Sax ji, Yàllay Ebrë yi, dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
1781  EXO 10:3  Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
1811  EXO 11:4  Musaa daldi wax Firawna ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Bu guddi gi xaajee, maay wër Misra gépp,
1815  EXO 11:8  Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees.
1843  EXO 12:26  Te bu leen seeni doom laajee ne leen: Lu aada jii di wund?”
1844  EXO 12:27  waxleen leen ne leen: Loolu sarax la ñeel Aji Sax ji ngir bésub Mucc ba, ndax la mu teggi woon këri bànni Israyil ca Misra, kera ba muy fàdd waa Misra te musal ca sunuy kër.”» Ba mu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma sujjóot, màggal Yàlla.
1876  EXO 13:8  Bu keroogee na ku nekk xamal doomam, ne ko: La ma Aji Sax ji defaloon, ba ma génnee Misra, moo waral lii tey.”
1882  EXO 13:14  Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga.
1893  EXO 14:3  Su ko defee Firawna da naan: Bànni Israyil de dañoo réer ci àll bi, ba faf keppu ci màndiŋ mi.”
1930  EXO 15:9  «Noon baa nga naa: Maay dàqe, dabe, lël alal ja, séddale séddu, ba xol sedd, ne saamar boset, teg leen loxo.”
1964  EXO 16:16  Aji Sax ji dafa santaane ne: Na ku nekk for lu mat njëlam, bopp bu ne andaar, te mu natt ko ci limu nit, ñi mu bokkal xayma.”»
1980  EXO 16:32  Ci biir loolu Musaa ne: «Aji Sax ji dafa santaane ne: Sàkkleen ci andaar, denc ngir seeni sët ak seeni sëtaat. Su ko defee ñu gis ñam, wi ma leen daan leel ca màndiŋ ma, gannaaw ba ma leen génnee réewum Misra.”»
2031  EXO 19:4  Yeena gisal seen bopp ni ma def waa Misra, te yeen, ma boot leen, ni jaxaay di fireey laafam, boot ay doomam, ba ngeen jegesi ma fii.
2039  EXO 19:12  Sàkkalal mbooloo mi ag kemu fi wër tund wi, te nga wax leen ne leen: Moytuleena yéeg ci kaw tund wi, mbaa ngeen di laal tund wi fenn. Képp ku laal tund wi, dees na ko rey.
2074  EXO 20:22  Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Li ngay wax bànni Israyil mooy lii: Yeena ko gisal seen bopp. Ca asamaan sax laa àddoo, wax ak yeen.
2083  EXO 21:5  Waaye su jaam bi biralee ne: Maa bëgg sama sang, maak sama jabar ak samay doom, te buggumaa moom sama bopp”,
2330  EXO 28:36  «Sàkkal dogu wurusu ngalam wu tell, nga ñaas ci mbind mii ni ñuy ñaase mbindum torlu: Lu sell a ngii, ñeel Aji Sax ji.”
2414  EXO 30:31  «Nanga wax nag bànni Israyil ne leen: Googu diw sama diwu pal gu sell lay doon, ci seen gépp maas.
2434  EXO 31:13  «Waxal bànni Israyil ne leen: Fexeleen rekk ba sama bési Noflaay, ngeen di ko wormaal, ndax bésub Noflaay da di firnde sama digganteek yeen ak seen askan, ngir ngeen xam ne man Aji Sax ji maa leen ber, sellal leen.
2447  EXO 32:8  Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”»
2451  EXO 32:12  Ana lu jar Misra di wax naan: Musiba mi mu leen naraloon, ba mu leen di yiwi de, du lenn lu moy rey leen ba ñu jeex ca tund ya, ba fare leen kaw suuf sépp.” Ngalla dëddul sa sawaras sànj te nga fomm musiba mi nga naral sa ñoñ.
2452  EXO 32:13  Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”»
2462  EXO 32:23  Dañu ma ne: Sàkkal nu yàlla ju nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra kat, xamunu lu ko dal.”
2463  EXO 32:24  Ma ne leen: Ku takk wurus, tekkil, indi!” Ñu jox ma, ma sànni ci sawara wi, sëllu wii génne ci!»
2466  EXO 32:27  Mu ne leen: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Na ku nekk teg saamaram ci luppam, te ngeen wër dal bi bépp buntoo bunt, ba mu daj. Reyleen ñépp; doomu ndey, xarit ak jegeñaale.”»
2486  EXO 33:12  Musaa nag ne Aji Sax ji: «Waaw, yaw de yaa ngi ma naa ma yóbbu mbooloo mii, waaye xamaloo ma kan ngay yebal, mu ànd ak man. Yaa ma waxoon it ne ma: Maa la xam ci saw tur, te it daj nga sama yiw.”
2511  EXO 34:14  ndax waruleena jaamu jeneen yàlla, ngir Aji Sax ji, turu Ku fiir ki” lay wuyoo, te Yàlla ju fiir la.
2981  LEV 10:3  Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.
3098  LEV 13:45  «Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: Setuma de, setuma!”
3147  LEV 14:35  boroom néeg bi dafa wara dem ca sarxalkat ba ne ko: Lu mel ni aw liir laa gis sama néeg.”
3490  LEV 25:20  Jombul ngeen di wax naan: Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?”
3812  NUM 5:19  Su ko defee sarxalkat bi waatloo ndaw si, ne ko: Ndegam góor àndul ak yaw, moyuloo, sobeel sa bopp te fekk la ci buum, muccal ci loraangey ndoxum wextan mii, di alage.
3814  NUM 5:21  Fii la sarxalkat biy waatloo ndaw si waatu alkànde gi, wax ko ne ko: ...yal na la Aji Sax ji def ku alku ku ñuy móoloo ci sa biir askan. Yal na laxal sa njurukaay, wal sab koll.
3815  NUM 5:22  Yal na ndoxum alkànde mii tàbbi ci say butit, laxal sa njurukaay, wal sab koll.” Su ko defee ndaw si ne: Amiin, Amiin.”
3848  NUM 6:24  «Yal na la Aji Sax ji barkeel, sàmm la.
3849  NUM 6:25  «Yal na la Aji Sax ji geesoo leeram, baaxe la.
3850  NUM 6:26  «Yal na la Aji Sax ji siggil, jàmmal la.”