109 | GEN 5:3 | Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. |
110 | GEN 5:4 | Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
111 | GEN 5:5 | Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu. |
112 | GEN 5:6 | Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. |
113 | GEN 5:7 | Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
115 | GEN 5:9 | Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. |
117 | GEN 5:11 | Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu. |
118 | GEN 5:12 | Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel. |
119 | GEN 5:13 | Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
120 | GEN 5:14 | Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu. |
122 | GEN 5:16 | Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
125 | GEN 5:19 | Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
128 | GEN 5:22 | Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
138 | GEN 5:32 | Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet. |
141 | GEN 6:3 | Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).» |
234 | GEN 9:28 | Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Nóoyin dundaat na ñetti téeméeri at ak juróom fukk (350). |
235 | GEN 9:29 | Nóoyin dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (950), doora faatu. |
278 | GEN 11:11 | Arpagsàdd juddu na, Sem dundaat juróomi téeméeri at (500), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
280 | GEN 11:13 | Sela juddu na, Arpagsàdd dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
282 | GEN 11:15 | Eber juddu na, Sela dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
284 | GEN 11:17 | Peleg juddu na, Eber dundaat ñeenti téeméeri at ak fanweer (430), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
286 | GEN 11:19 | Rew juddu na, Peleg dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñeent (209), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
288 | GEN 11:21 | Serug juddu na, Rew dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñaar (207), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
299 | GEN 11:32 | Teraa dund na ñaar téeméeri at ak juróom (205), doora génn àddina, ñu denc ko Karan. |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
1040 | GEN 35:28 | Isaaxa dund na téeméeri at ak juróom ñett fukk (180). |
1538 | EXO 1:5 | Góor ñi soqikoo ci Yanqóoba ñépp juróom ñaar fukk lañu (70), bu ñu ci boolee doomam, ji ñuy wax Yuusufa, moom ma ñu fekk Misra. |
1693 | EXO 7:7 | Musaa nga tollu woon ci juróom ñett fukki at (80); Aaróona moom am juróom ñett fukki at ak ñett (83); ca jamono, ya ñuy wax ak Firawna. |
1854 | EXO 12:37 | Ci kaw loolu bànni Israyil jóge dëkk ba ñuy wax Ramses, jëm Sukkóot. Ña nga tollu ci juróom benni téeméeri junniy góor (600 000) te limaaleesul jigéen ñaak xale ya. |
1857 | EXO 12:40 | Diir ba bànni Israyil nekk Misra tollu na ci ñeenti téeméeri at ak fanweer (430). |
2658 | EXO 38:24 | Wurus wi dem ci liggéey bi bépp, mboolem liggéeyu bérab bu sell bi, te muy wurus wu ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, juróom ñetti téeméeri kilo ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar la (877), ak ñetti téeméeri garaam (300), yemook ñaar fukki talaŋ ak juróom ñeent, ak juróom ñaar téeméer ak fanweeri (730) siikal ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi. |
2659 | EXO 38:25 | Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, |
2660 | EXO 38:26 | muy juróomi garaami xaalis bopp bu nekk, yemook genn-wàllu siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, ñeel képp ku bindu ci limeef bi, dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, ñépp di juróom benni téeméeri junniy góor ak ñetti junneek juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
2661 | EXO 38:27 | Ñetti junniy (3 000) kiloy xaalis, di téeméeri talaŋ, ñeel móolub teguy bérab bu sell bi, ak teguy rido bi. Muy téeméeri tegu ci ñetti junniy kilo, di fanweeri kilo ci benn tegu, muy téeméeri tegu ci téeméeri talaŋ, benn talaŋ ci benn tegu. |
2662 | EXO 38:28 | Fukki kilook juróom ñaar yeek juróom ñaar téeméeri garaam yeek juróom fukk (17 kilo 750 garaam) yi ci topp, yemook junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi siikali xaalis, ay wékkukaay la ci sàkk ngir jën yi, xoob ci boppi jën yi, sàkk ci galan yi. |
2663 | EXO 38:29 | Xànjar bi ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, ñaari junniy kilo ak téeméer ak ñaar fukk ak ñeent la (2 124), yemook juróom ñaar fukki (70) talaŋ ak ñaari junneek ñeenti téeméeri (2 400) siikal. |
3626 | NUM 1:21 | Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3628 | NUM 1:23 | Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3630 | NUM 1:25 | Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3632 | NUM 1:27 | Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600). |
3634 | NUM 1:29 | Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3636 | NUM 1:31 | Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3638 | NUM 1:33 | Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3640 | NUM 1:35 | Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3642 | NUM 1:37 | Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3644 | NUM 1:39 | Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). |
3646 | NUM 1:41 | Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3648 | NUM 1:43 | Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3651 | NUM 1:46 | Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3663 | NUM 2:4 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600). |
3665 | NUM 2:6 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3667 | NUM 2:8 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3668 | NUM 2:9 | «Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu. |
3670 | NUM 2:11 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3672 | NUM 2:13 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3674 | NUM 2:15 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3675 | NUM 2:16 | «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca. |
3678 | NUM 2:19 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3680 | NUM 2:21 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3682 | NUM 2:23 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3683 | NUM 2:24 | «Mboolem ña ñu limal dalub Efrayim aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett ak téeméer (108 100). Bu ñuy dem, ñooñoo di ñetteelu kurél, dox topp ca. |
3685 | NUM 2:26 | Ña ñu limal gàngooram di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). |
3687 | NUM 2:28 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3689 | NUM 2:30 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3690 | NUM 2:31 | «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.» |
3691 | NUM 2:32 | Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3715 | NUM 3:22 | Ña ñu leen limal, ba ñu waññee mboolem góor ña am weer, jëm kaw, juróom ñaari junni ak juróomi téeméer (7 500) lañu. |
3721 | NUM 3:28 | Ba ñu waññee mboolem góor ña ca am weer, jëm kaw, juróom ñetti junni ak juróom benni téeméer (8 600) lañu. Ñoo dénkoo woon dénkaaney bérab bu sell bi. |
3727 | NUM 3:34 | Ña ñu leen limal, ba ñu waññee mboolem góor ña am weer, jëm kaw, juróom benni junni ak ñaar téeméer (6 200) lañu. |
3732 | NUM 3:39 | Mboolem ña ñu limal Leween ñi, te Musaa ak Aaróona lim leen na ñu bokke seeni làng ci ndigalal Aji Sax ji, ñuy mboolem góor ñi am weer, jëm kaw, ñaar fukki junneek ñaar (22 000) lañu. |
3780 | NUM 4:36 | Ña ñu limal seeni làng di ñaari junni ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukki góor (2 750). |
3784 | NUM 4:40 | te ñu limal leen seeni làng ak seen këri maam, ñaari junneek juróom benni téeméer ak fanweeri góor lañu (2 630). |
3788 | NUM 4:44 | te ñu limal leen seeni làng, ñetti junni ak ñaar téeméeri góor (3 200) lañu. |
3792 | NUM 4:48 | seenub lim nekk na juróom ñetti junni ak juróomi téeméer ak juróom ñett fukki góor (8 580). |
3936 | NUM 7:85 | ndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikali bérab bu sell bi ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróomi téeméeri garaam (27 500). |
3937 | NUM 7:86 | Fukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikali bérab bu sell bi la, di téeméeri garaam ak fukk (110), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam (1 300). |
4046 | NUM 11:21 | Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm! |
4197 | NUM 16:2 | ñu jógal Musaa, ñook ñaar téeméer ak juróom fukk (250) ci bànni Israyil, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu amu tur. |
4244 | NUM 17:14 | Ña dee ca mbas ma nag doon fukki junneek ñeent ak juróom ñaar téeméer (14 700), te bokkul ak ña dee woon ca mbirum Kore ma. |
4481 | NUM 25:9 | Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000). |
4498 | NUM 26:7 | Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730). |
4505 | NUM 26:14 | Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200). |
4509 | NUM 26:18 | Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500). |
4513 | NUM 26:22 | Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500). |