109 | GEN 5:3 | Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. |
111 | GEN 5:5 | Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu. |
122 | GEN 5:16 | Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
128 | GEN 5:22 | Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
129 | GEN 5:23 | Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365). |
234 | GEN 9:28 | Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Nóoyin dundaat na ñetti téeméeri at ak juróom fukk (350). |
280 | GEN 11:13 | Sela juddu na, Arpagsàdd dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
282 | GEN 11:15 | Eber juddu na, Sela dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
284 | GEN 11:17 | Peleg juddu na, Eber dundaat ñeenti téeméeri at ak fanweer (430), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
351 | GEN 14:14 | Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan. |
676 | GEN 25:17 | Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam. |
1672 | EXO 6:16 | Doomi Lewi yu góor ñoo di Gerson ak Keyat ak Merari, ku nekk ak askanam. At ya Lewi dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). |
1674 | EXO 6:18 | Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel; te at ya Keyat dund, téeméer la ak fanweer ak ñett (133). |
1676 | EXO 6:20 | Amram moo jël bàjjanam Yokebedd soxna, kooku am ak moom Aaróona ak Musaa. At, ya Amram dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). |
1693 | EXO 7:7 | Musaa nga tollu woon ci juróom ñett fukki at (80); Aaróona moom am juróom ñett fukki at ak ñett (83); ca jamono, ya ñuy wax ak Firawna. |
1857 | EXO 12:40 | Diir ba bànni Israyil nekk Misra tollu na ci ñeenti téeméeri at ak fanweer (430). |
2658 | EXO 38:24 | Wurus wi dem ci liggéey bi bépp, mboolem liggéeyu bérab bu sell bi, te muy wurus wu ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, juróom ñetti téeméeri kilo ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar la (877), ak ñetti téeméeri garaam (300), yemook ñaar fukki talaŋ ak juróom ñeent, ak juróom ñaar téeméer ak fanweeri (730) siikal ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi. |
2659 | EXO 38:25 | Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, |
2660 | EXO 38:26 | muy juróomi garaami xaalis bopp bu nekk, yemook genn-wàllu siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, ñeel képp ku bindu ci limeef bi, dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, ñépp di juróom benni téeméeri junniy góor ak ñetti junneek juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
2661 | EXO 38:27 | Ñetti junniy (3 000) kiloy xaalis, di téeméeri talaŋ, ñeel móolub teguy bérab bu sell bi, ak teguy rido bi. Muy téeméeri tegu ci ñetti junniy kilo, di fanweeri kilo ci benn tegu, muy téeméeri tegu ci téeméeri talaŋ, benn talaŋ ci benn tegu. |
3628 | NUM 1:23 | Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3640 | NUM 1:35 | Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3642 | NUM 1:37 | Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3648 | NUM 1:43 | Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3651 | NUM 1:46 | Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3672 | NUM 2:13 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3680 | NUM 2:21 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3682 | NUM 2:23 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3689 | NUM 2:30 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3691 | NUM 2:32 | Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3736 | NUM 3:43 | Ba ñu waññee mboolem taaw yu góor ya, bind seeni tur, dale ci ñi am weer, jëm kaw, seenub lim nekk na ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (22 273). |
3739 | NUM 3:46 | Njotlaay nag dina war ci ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñetti (273) bopp, yi taawi bànni Israyil ëppe Leween ñi. |
3743 | NUM 3:50 | Xaalis ba mu nangoo ca taawi bànni Israyil di junniy siikal ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom (1 365), ci siikalu bérab bu sell bi, xawa tollu ci fukki kilo ak ñett. |
3784 | NUM 4:40 | te ñu limal leen seeni làng ak seen këri maam, ñaari junneek juróom benni téeméer ak fanweeri góor lañu (2 630). |
3788 | NUM 4:44 | te ñu limal leen seeni làng, ñetti junni ak ñaar téeméeri góor (3 200) lañu. |
3937 | NUM 7:86 | Fukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikali bérab bu sell bi la, di téeméeri garaam ak fukk (110), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam (1 300). |
4498 | NUM 26:7 | Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730). |
4516 | NUM 26:25 | Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300). |
4528 | NUM 26:37 | Làngi Efrayim a ngoogu, ña ñu leen limal di fanweeri junneek ñaar ak juróomi téeméer (32 500). Ñooñoo askanoo ci Yuusufa, ñook seeni làng. |
4538 | NUM 26:47 | Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
4542 | NUM 26:51 | Limeefu bànni Israyil a ngoogu, di juróom benni téeméeri junneek benn ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (601 730). |
4553 | NUM 26:62 | Ña ñu limal Leween ñi nag ñaar fukki junneek ñett lañu (23 000), di mboolem góor ña am weer, jëm kaw, te limaaleesu leen ak bànni Israyil ga ca des, ndax joxeesu leen ab cér ci biir bànni Israyil. |
4701 | NUM 31:35 | aw nit, fanweeri junniy jigéen ñu xamul lalu góor (30 000). |
4702 | NUM 31:36 | Genn-wàll giy céru nit ña xareji woon, nii la tëdde: gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500), |
4704 | NUM 31:38 | nag yi, fanweeri junneek juróom benn (36 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom ñaar fukk ak ñaar (72); |
4705 | NUM 31:39 | mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom benn fukk ak benn (61); |
4706 | NUM 31:40 | aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di fanweeri bopp ak ñaar (32). |
4709 | NUM 31:43 | te muy céru mbooloo ma, ci wàllu gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500) la; |
4710 | NUM 31:44 | nag yi di fanweeri junneek juróom benn (36 000); |
4711 | NUM 31:45 | mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500); |
4801 | NUM 33:39 | Aaróona mu ngi woon ci téeméeri atam, ak ñaar fukk at ñett (123) ba mu faatoo ca kaw tundu Or. |
7455 | 1SA 11:8 | Ba Sóol nemmikoo limu góori Israyil ca Beseg, ñetti téeméeri junni lañu (300 000), waa Yuda di fanweeri junni (30 000). |
8083 | 2SA 2:31 | Waaye fekk na niti Daawuda rey ñetti téeméer ak juróom benn fukk (360) ca Beñamineen ñaak niti Abner. |
8894 | 1KI 5:27 | Buur Suleymaan nag sas fanweeri junniy nit (30 000) ci Israyil gépp ay liggéeyi sañul-bañ. |
8897 | 1KI 5:30 | te bokkul ak ñetti junni ak ñetti téeméeri nit (3 300) ñi Suleymaan tabb, ñuy jiite liggéey bi, di saytu liggéeykat yi. |
9114 | 1KI 11:3 | Mu denc ca juróom ñaar téeméeri lingeer (700) ak ñetti téeméeri (300) nekkaale. Soxnaam ya nag dëpp ko. |
9426 | 1KI 20:15 | Ba mu ko defee Axab lim dag ya kilifay diiwaan ya yebal, ñuy ñaar téeméer ak fanweer ak ñaar (232). Gannaaw loolu mu lim mbooloom Israyil gépp, ñuy juróom ñaari junni (7 000). |
9450 | 1KI 20:39 | Buur romb, mu woo ko, ne ko: «Man de sang bi, damaa gaañu ci digg xare, nit dikk, indil ma keneen, ne ma: “Xoolal ma kii, su rëccee, sa bakkan ay fey bakkanam, mbaa nga feye ko ñetti junniy (3 000) dogi xaalis.” |
12030 | EZR 1:9 | Lenn ci lim bi tëdde nii: fanweeri ndabi wurus (30), ak junniy ndabi xaalis (1 000), ak ñaar fukki paaka ak juróom ñeent (29), |
12031 | EZR 1:10 | ak fanweeri këlli wurus yu ndaw (30) yu ànd ak ñeenti téeméeri këll ak fukk yu ndaw yu xaalis (410) ak junniy jumtukaay yeneen (1 000). |
12036 | EZR 2:4 | Askanu Sefatiya, ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). |
12043 | EZR 2:11 | Askanu Bebay, juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (623). |
12049 | EZR 2:17 | Askanu Besay, ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (323). |
12051 | EZR 2:19 | Askanu Asum, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). |
12053 | EZR 2:21 | Waa Betleyem, téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). |
12057 | EZR 2:25 | Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot, juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). |
12060 | EZR 2:28 | Waa Betel ak Ayi, ñaar téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (223). |
12064 | EZR 2:32 | Waa Arim, ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320). |
12066 | EZR 2:34 | Waa Yeriko, ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). |
12067 | EZR 2:35 | Waa Sena, ñetti junni ak juróom benn téeméer ak fanweer lañu (3 630). |
12068 | EZR 2:36 | Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). |
12074 | EZR 2:42 | Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, ñépp di téeméer ak fanweer ak juróom ñeent (139). |
12090 | EZR 2:58 | Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). |
12096 | EZR 2:64 | Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), |
12097 | EZR 2:65 | te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer (200). |
12098 | EZR 2:66 | Amoon nañu juróom ñaar téeméeri fas ak fanweer ak juróom benn (736), ak ñaar téeméeri berkelle ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12099 | EZR 2:67 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12211 | EZR 8:5 | Ci askanu Sàttu, Sekaña doomu Yasyel la, mook ñetti téeméeri góor (300). |
12434 | NEH 7:9 | Askanu Sefatiya ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). |
12442 | NEH 7:17 | Askanu Asgàdd ñaari junni ak ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (2 322) |
12447 | NEH 7:22 | Askanu Asum ñetti téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (328). |
12448 | NEH 7:23 | Askanu Besay ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñeent lañu (324). |
12454 | NEH 7:29 | Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). |
12457 | NEH 7:32 | Waa Betel ak Ayi téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). |
12460 | NEH 7:35 | Waa Arim ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320) |
12461 | NEH 7:36 | Waa Yeriko ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). |
12463 | NEH 7:38 | Waa Sena ñetti junni ak juróom ñeenti téeméer ak fanweer lañu (3 930). |
12464 | NEH 7:39 | Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). |
12470 | NEH 7:45 | Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, di téeméer ak fanweer ak juróom ñett (138). |
12485 | NEH 7:60 | Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). |
12491 | NEH 7:66 | Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), |
12492 | NEH 7:67 | te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12493 | NEH 7:68 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12494 | NEH 7:69 | Am na ñu jiite seen kër baay, ñu def seen loxo ca liggéey ba. Boroom dëkk ba def na ca alal ja junniy poseti wurus (1 000) ak juróom fukki këll (50) ak fanweeri mbubbi sarxalkat (30) ak juróomi téeméeri dogi xaalis (500). |