119 | GEN 5:13 | Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
280 | GEN 11:13 | Sela juddu na, Arpagsàdd dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
282 | GEN 11:15 | Eber juddu na, Sela dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
284 | GEN 11:17 | Peleg juddu na, Eber dundaat ñeenti téeméeri at ak fanweer (430), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
1449 | GEN 47:28 | Yanqóoba nag nekk na fukki at ak juróom ñaar ca réewum Misra, ay atam yépp tollu ci téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar (147). |
1857 | EXO 12:40 | Diir ba bànni Israyil nekk Misra tollu na ci ñeenti téeméeri at ak fanweer (430). |
2663 | EXO 38:29 | Xànjar bi ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, ñaari junniy kilo ak téeméer ak ñaar fukk ak ñeent la (2 124), yemook juróom ñaar fukki (70) talaŋ ak ñaari junneek ñeenti téeméeri (2 400) siikal. |
3626 | NUM 1:21 | Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3630 | NUM 1:25 | Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3632 | NUM 1:27 | Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600). |
3634 | NUM 1:29 | Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3636 | NUM 1:31 | Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3638 | NUM 1:33 | Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3642 | NUM 1:37 | Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3646 | NUM 1:41 | Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3648 | NUM 1:43 | Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3663 | NUM 2:4 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600). |
3665 | NUM 2:6 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3667 | NUM 2:8 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3668 | NUM 2:9 | «Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu. |
3670 | NUM 2:11 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3674 | NUM 2:15 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3675 | NUM 2:16 | «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca. |
3678 | NUM 2:19 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3682 | NUM 2:23 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3687 | NUM 2:28 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3689 | NUM 2:30 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3936 | NUM 7:85 | ndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikali bérab bu sell bi ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróomi téeméeri garaam (27 500). |
4244 | NUM 17:14 | Ña dee ca mbas ma nag doon fukki junneek ñeent ak juróom ñaar téeméer (14 700), te bokkul ak ña dee woon ca mbirum Kore ma. |
4481 | NUM 25:9 | Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000). |
4498 | NUM 26:7 | Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730). |
4509 | NUM 26:18 | Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500). |
4516 | NUM 26:25 | Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300). |
4532 | NUM 26:41 | Ñooñoo askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer (45 600). |
4534 | NUM 26:43 | Mboolem làngi Cuwameen, ña ñu leen limal juróom benn fukki junneek ñeent la, ak ñeenti téeméer (64 400). |
4538 | NUM 26:47 | Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
4541 | NUM 26:50 | Neftaleen ñaa ngoogu, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak ñeenti téeméer (45 400). |
8261 | 2SA 10:18 | Waaye waa Siree daw, won Israyil gannaaw. Daawuda rey ca ñoom juróom ñaar téeméeri dawalkati watiiri xare (700), ak ñeent fukki junniy gawar (40 000). Sobag, seen njiital gàngoor, mu jam ko, mu dee foofa. |
8869 | 1KI 5:2 | Suleymaan daan na njëloo bés bu nekk ñeent fukki barigoy sunguf ak juróom (45), ak juróom ñeent fukki (90) barigo ci sunguf su ñagas; |
8873 | 1KI 5:6 | Suleymaan amoon na ñeenti junniy (4 000) wuddi fasi watiir ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000). |
8900 | 1KI 6:1 | Ca ñeenti téeméereelu at maak juróom ñett fukk (480), gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, ca ñeenteelu atu nguurug Suleymaan, ci weeru Siw, di ñaareelu weeru at ma, ca la Suleymaan tàmbalee tabax kër Aji Sax ji. |
9108 | 1KI 10:26 | Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri watiir (1 400), ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu yebal ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk. |
9363 | 1KI 18:19 | Léegi nag wooteel, Israyil gépp daje, fekksi ma ca tundu Karmel, ñu ànd ak ñeenti téeméeri yonenti Baal ak juróom fukk (450) ak ñeenti téeméeri nit (400) ñuy lekk njëlal Yesabel, te di yonenti Asera tuur ma.» |
9366 | 1KI 18:22 | Ilyaas ne mbooloo ma: «Man de maa fi des ci yonenti Aji Sax ji, man doŋŋ, te yonenti Baal yi ñeenti téeméer lañook juróom fukk (450). |
12031 | EZR 1:10 | ak fanweeri këlli wurus yu ndaw (30) yu ànd ak ñeenti téeméeri këll ak fukk yu ndaw yu xaalis (410) ak junniy jumtukaay yeneen (1 000). |
12032 | EZR 1:11 | Mboolem ndabi wurus yeek yu xaalis yi juróomi junni la ak ñeenti téeméer (5 400). Sesbasar jële lépp Babilon, yóbbu Yerusalem, ba ngàllo gay ñibbi. |
12039 | EZR 2:7 | Askanu Elam, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12040 | EZR 2:8 | Askanu Sàttu, juróom ñeenti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (945). |
12042 | EZR 2:10 | Askanu Baani, juróom benni téeméer ak ñeent fukk ak ñaar lañu (642). |
12047 | EZR 2:15 | Askanu Adin, ñeenti téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (454). |
12056 | EZR 2:24 | Waa Asmawet, ñeent fukk ak ñaar lañu (42). |
12057 | EZR 2:25 | Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot, juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). |
12063 | EZR 2:31 | Waa Elam gu ndaw, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12066 | EZR 2:34 | Waa Yeriko, ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). |
12070 | EZR 2:38 | Askanu Pasur, junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). |
12072 | EZR 2:40 | Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ak Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74). |
12096 | EZR 2:64 | Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), |
12098 | EZR 2:66 | Amoon nañu juróom ñaar téeméeri fas ak fanweer ak juróom benn (736), ak ñaar téeméeri berkelle ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12099 | EZR 2:67 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12437 | NEH 7:12 | Askanu Elam junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12438 | NEH 7:13 | Askanu Sàttu juróom ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (845). |
12440 | NEH 7:15 | Askanu Binuy juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett lañu (648). |
12448 | NEH 7:23 | Askanu Besay ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñeent lañu (324). |
12453 | NEH 7:28 | Waa Bet Asmawet ñeent fukk ak ñaar lañu (42). |
12454 | NEH 7:29 | Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). |
12459 | NEH 7:34 | Waa Elam gu ndaw junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12461 | NEH 7:36 | Waa Yeriko ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). |
12466 | NEH 7:41 | Askanu Pasur junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). |
12468 | NEH 7:43 | Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ma soqikoo ca Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74). |
12469 | NEH 7:44 | Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett (148). |
12487 | NEH 7:62 | Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak ñaar (642). |
12491 | NEH 7:66 | Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), |
12492 | NEH 7:67 | te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12493 | NEH 7:68 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
13938 | JOB 42:12 | Aji Sax ji nag barkeel mujug Ayóoba lu raw ndoorteem. Mu am fukki junniy gàtt ak ñeent (14 000), ak juróom benni junniy giléem (6 000), ak junniy lëkkey nag (1 000) yu muy rijjee, ak junniy mbaam yu jigéen (1 000). |
13942 | JOB 42:16 | Gannaaw loolu Ayóoba dundaat na téeméeri at ak ñeent fukk (140). Gis na ay doomam, gis ay sëtam, ba muy ñeenti maas. |
20375 | JER 52:30 | Ak juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (745) yu Nebusaradan njiital dag ya, toxal. Loolu yemook ñaar fukkeelu at maak ñett ci nguurug Nabukodonosor. Ñi ñu toxal ñépp di ñeenti junni ak juróom benni téeméer (4 600). |
21787 | EZK 48:16 | Na dëkk bi bindoo ab kaare bu wet gi di ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500), di ñaari kilomeetar ak genn-wàll. |
21801 | EZK 48:30 | «Bunti dëkk bi nag nii lay tëdde: Ñeenti miiri dëkk bi, bu ci nekk day am guddaayu ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500). |
21803 | EZK 48:32 | Wetu penku am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Yuusufa ak benn buntu Beñamin ak benn buntu Dan. |
21804 | EZK 48:33 | Wetu bëj-saalum am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Simeyon ak benn buntu Isaakar ak benn buntu Sabulon. |
21805 | EZK 48:34 | Wetu sowu am miiru ñeenti junniy xasab ak juróomi téeméer (4 500) ak ñetti bunt: benn buntu Gàdd ak benn buntu Aser ak benn buntu Neftali. |
22199 | HOS 3:2 | Ci kaw loolu ma takk ko ci fukki poseti xaalis ak juróom, ak ñeenti téeméeri kiloy lors ak juróom fukk (450). |
25079 | LUK 2:37 | Jëkkër ja faatu, mu toog, séyaatul, ba booba mu amee juróom ñett fukki at ak ñeent (84). Daawul jóge ca kër Yàlla ga, koor ak julli la daan jaamoo guddi ak bëccëg. |
27191 | ACT 7:6 | Yàlla ne ko: “Saw askan dinañu toxuji bitim réew, te dees na leen def ay jaam, mitital leen diiru ñeenti téeméeri at (400).” |
27451 | ACT 13:20 | Loolu lépp a ngi am ci diiru ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (450). «Gannaaw loolu moo sàkkal sunuy maam ay njiit, ba ci jamonoy Yonent Yàlla Samiyel. |
27770 | ACT 21:38 | Kon du yaay waayu Misra jooju yëngaloon dëkk bi ci fan yii, te yóbbu woon ñeenti junniy Bóomkat ya (4 000) ca màndiŋ ma?» |
30882 | REV 7:4 | Ma dégg limub ña ñu màndargaale torluwaay ba; ñuy téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000), bawoo ci mboolem giiri bànni Israyil: |
30996 | REV 14:1 | Ma xoolaat, gisuma lu moy Gàtt bi fa mu taxaw ci kaw tundu Siyoŋ ak téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junniy nit (144 000) ñu ànd ak moom, te ñu bind ci seen jë turu Gàtt bi ak turu Baayam. |
31139 | REV 21:17 | Malaaka mi natt tata ji, muy téeméeri xasab ak ñeent fukk ak ñeent (144) yu malaaka mi natte, ni ko nit ñiy natte naka jekk, te yemook juróom ñaar fukk ak ñaari meetar (72). |