111 | GEN 5:5 | Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu. |
114 | GEN 5:8 | Kon Set dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk ak ñaar (912), doora faatu. |
115 | GEN 5:9 | Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. |
117 | GEN 5:11 | Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu. |
120 | GEN 5:14 | Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu. |
123 | GEN 5:17 | Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu. |
126 | GEN 5:20 | Kon Yeredd dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (962), doora faatu. |
133 | GEN 5:27 | Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu. |
136 | GEN 5:30 | Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
235 | GEN 9:29 | Nóoyin dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (950), doora faatu. |
286 | GEN 11:19 | Rew juddu na, Peleg dundaat ñaar téeméeri at ak juróom ñeent (209), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
292 | GEN 11:25 | Teraa gane na àddina, Naxor dundaat téeméeri at ak fukk ak juróom ñeent (119), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
399 | GEN 17:1 | Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk. |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
422 | GEN 17:24 | Ibraayma amoon na juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), bi muy xaraf; |
3628 | NUM 1:23 | Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3672 | NUM 2:13 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
7314 | 1SA 4:15 | Booba Elee ngi ci juróom ñeent fukki at ak juróom ñett (98), bët yi ne xóll te gisatul dara. |
8869 | 1KI 5:2 | Suleymaan daan na njëloo bés bu nekk ñeent fukki barigoy sunguf ak juróom (45), ak juróom ñeent fukki (90) barigo ci sunguf su ñagas; |
12030 | EZR 1:9 | Lenn ci lim bi tëdde nii: fanweeri ndabi wurus (30), ak junniy ndabi xaalis (1 000), ak ñaar fukki paaka ak juróom ñeent (29), |
12040 | EZR 2:8 | Askanu Sàttu, juróom ñeenti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (945). |
12048 | EZR 2:16 | Askanu Ater, soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98). |
12052 | EZR 2:20 | Askanu Gibar, juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). |
12068 | EZR 2:36 | Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). |
12074 | EZR 2:42 | Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, ñépp di téeméer ak fanweer ak juróom ñeent (139). |
12090 | EZR 2:58 | Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). |
12241 | EZR 8:35 | Ba mu ko defee ña jóge njaam, ñibbsee ca ngàllo ga, daldi defal Yàllay Israyil ay saraxi dóomal. Muy fukki yëkk ak ñaar, ñeel Israyil gépp ak juróom ñeent fukki kuuy ak juróom benn (96), ak juróom ñaar fukki xar yu ndaw ak juróom ñaar (77), ak fukki sikket ak ñaar yu ñu def saraxu póotum bàkkaar; ñu def lépp saraxu dóomal, ñeel Aji Sax ji. |
12446 | NEH 7:21 | askanu Ater soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98); |
12450 | NEH 7:25 | Askanu Gabawon juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). |
12463 | NEH 7:38 | Waa Sena ñetti junni ak juróom ñeenti téeméer ak fanweer lañu (3 930). |
12464 | NEH 7:39 | Sarxalkat yi ñii la: Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). |
12485 | NEH 7:60 | Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392). |
20603 | EZK 4:5 | Man nag àppal naa la limu fan yu tembook limu ati ayu waa kër Israyil, muy ñetti téeméeri fan ak juróom ñeent fukk (390) yooy tegoo ayu waa kër Israyil. |
20607 | EZK 4:9 | «Te kat nanga sàkk bele ak lors ak ñebbe ak làntin ak dugub ak bele bu dëgër. Nga boole lépp ci lenn ndab. Moom ngay lekk diiru fan yi ngay tëdde wet. Diiru ñetti téeméeri fan ak juróom ñeent fukk (390) nga koy dunde. |
22161 | DAN 12:11 | Jamono ja ñuy dakkal sarax si wara sax fàww, di keroog ba ñuy taxawal lu siblu lay jur yàqute, junniy fan ak ñaar téeméer ak juróom ñeent fukk (1 290) dina ca topp. |
25661 | LUK 15:4 | «Ana kan ci yeen mooy am téeméeri xar, réerle ci menn, te bàyyiwul ca àll ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent (99), ngir toppi ma réer, ba gis ko? |