3 | GEN 1:3 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. |
20 | GEN 1:20 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» |
22 | GEN 1:22 | Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» |
33 | GEN 2:2 | Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. |
35 | GEN 2:4 | Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan, |
51 | GEN 2:20 | Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam. |
52 | GEN 2:21 | Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. |
57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
59 | GEN 3:3 | Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”» |
63 | GEN 3:7 | Seeni bët daldi ubbiku, ñu xam ne yaramu neen lañu def. Ba mu ko defee ñu ràbb xobi garabu figg, gemboo. |
79 | GEN 3:23 | Ba loolu amee Yàlla Aji Sax ji génne ko toolub Àjjana, muy bey suuf, si ñu ko sàkke. |
88 | GEN 4:8 | Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. |
92 | GEN 4:12 | Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.» |
95 | GEN 4:15 | Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey. |
105 | GEN 4:25 | Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.» |
107 | GEN 5:1 | Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, |
139 | GEN 6:1 | Bi nga xamee ne nit ñi tàmbali nañoo fulandiwu ci kaw suuf, te am ay doom yu jigéen, |
149 | GEN 6:11 | Booba fekk na àddina yàqu, te fees ak ay, Yàlla teg ci bëtam. |
151 | GEN 6:13 | Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal. |
166 | GEN 7:6 | Bi mbënn miy ñëw ci àddina, booba fekk na Nóoyin am juróom benni téeméeri at. |
170 | GEN 7:10 | Ba juróom ñaari fan wéyee nag, ndoxu mbënn ma agsi ci kaw suuf. |
186 | GEN 8:2 | Bëti ndox ya ca xóote ya dafa taxaw, bunti ndoxi asamaan tëju, taw bi dal. |
187 | GEN 8:3 | Ci kaw loolu ndox mi taa ci suuf di wàññiku. Bi téeméeri fan yi ak juróom fukk matee nag, ndox ma gëna néew. |
188 | GEN 8:4 | Ba juróom ñaareelu weer wa amee fukki fan ak juróom ñaar, gaal gaa nga teereji tundi Araraat. |
195 | GEN 8:11 | Ba mu délsee ca ngoon, indaalewul lu moy xobu oliw wu tooy wu keppe ca sàll wa. Nóoyin xam ne ndox mi taa woon ci suuf, fer na. |
196 | GEN 8:12 | Mu négati juróom ñaari fan, bàyyiwaat pitax ma. Boobu yoon nag délsiwaatul ca moom. |
199 | GEN 8:15 | Ba loolu amee Yàlla ne Nóoyin: |
205 | GEN 8:21 | Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe. |
215 | GEN 9:9 | «Bés niki tey fasal naa sama bopp kóllëre sama diggante ak yeen ak seen askan, |
228 | GEN 9:22 | Ba loolu amee Xam, baayu Kanaan, gis céri baayam, génn waxi ko Sem ak Yafet ca biti. |
231 | GEN 9:25 | Ba mu ko defee mu ne: «Yal na Kanaan torox, bay jaamu jaami doomi ndeyam.» |
245 | GEN 10:10 | Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. |
269 | GEN 11:2 | Bi nit ñi toxoo, jëm penku, dañoo gis ag joor ci réewu Sineyaar, ñu sanc fa. |
272 | GEN 11:5 | Ba ñu noppee Aji Sax ji wàcc, xoolsi dëkk bi ak taax, mi doom aadama yi tabax. |
275 | GEN 11:8 | Ba loolu amee Aji Sax ji jële leen foofa, tasaare leen ci kaw suuf sépp, ñu yemale fa dëkk ba ñu doon tabax. |
276 | GEN 11:9 | Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la leen tasaaree ci kaw suuf sépp. |
298 | GEN 11:31 | Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. |
303 | GEN 12:4 | Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75). |
305 | GEN 12:6 | Ba ñu agsee Kanaan, Ibraam dafa jàll ca biir réew ma, ba àgg bérab bu sell, ba féete ak Sikem, ca garab gu mag, ga ñuy wooye More. Booba fekk na waa Kanaan a nga woon ca réew ma. |
307 | GEN 12:8 | Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko. |
311 | GEN 12:12 | Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des. |
313 | GEN 12:14 | Ba Ibraam àggee Misra, waa Misra gis ne jigéen ji mu àndal rafet na lool. |
320 | GEN 13:1 | Bi loolu amee Ibraam dafa jóge Misra, moom ak soxnaam, yóbbaale alalam jépp, daldi dem ca àllub Negew, Lóot topp ca. |
322 | GEN 13:3 | Gannaaw loolu mu awati yoonam, jóge àllub Negew, jëm dëkk ba ñu naa Betel, dem ba àgg ca bérab, ba mu jëkkoona samp xaymaam, ci diggante Betel ak Ayi, |
327 | GEN 13:8 | Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? |
329 | GEN 13:10 | Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja. |
330 | GEN 13:11 | Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqlikoo. |
337 | GEN 13:18 | Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay. |
339 | GEN 14:2 | ànd nañu, dal ci kaw ñoom Bera buurub Sodom, ak Birsa buurub Gomor, ak Sineyab buurub Atma, ak Semeber buurub Ceboyim, ak it buuru dëkk ba ñuy wax Bela, mooy Sowar ba tey. |
345 | GEN 14:8 | Ci kaw loolu buurub Sodom génn, mook buurub Gomor ak buurub Atma ak buurub Ceboyim ak buuru Bela, di Sowar ba tey, ñoom ñépp daldi làng, nara xare ca xuru Sidim, |
347 | GEN 14:10 | Waaye xuru Sidim woowu dafa feesoon dell aki pax aki kàmbi koltaar. Ba mu ko defee buuri Sodom ak Gomor di daw, far daanu ca kàmb ya. Ña ca des daw ba ca tund ya. |
349 | GEN 14:12 | Booba lañu yóbbu Lóot ma dëkk Sodom, te Ibraam di baayam bu ndaw. Ci biir loolu ñu yóbbaale li mu amoon lépp, dem. |
350 | GEN 14:13 | Ba loolu xewee, kenn ci ñi ñu jàppoon rëcc, ñëw ci Ibraam miy ab Ebrë, wax ko ko. Fekk na mu dëkk ca wetu garab yu mag ya woon ca toolub Mamre, ma dib Amoreen, di mbokk mu jege ci Eskol ak Aner, ñoom ñi doon wóllërey Ibraam. |
351 | GEN 14:14 | Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan. |
354 | GEN 14:17 | Gannaaw ba Ibraam dàqee Kedorlamer ak buur ya àndoon ak moom, ba délsi, buurub Sodom dafa génn, gatandu ko ca xur wa ñuy wax Sawe, ñu di ko wooye xuru Buur ba tey. |
357 | GEN 14:20 | Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko. |
363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
369 | GEN 15:8 | Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?» |
372 | GEN 15:11 | Ba mu ko defee ay tan jóge ca, dal ca kaw yàpp wa, Ibraam nag dàq leen. |
373 | GEN 15:12 | Ba jant bay so, ngëmment lu réy a ko jàpp, tiitaange lu mag, ànd ak lëndëm gu ne këruus, ne milib ci kawam. |
378 | GEN 15:17 | Ba jant sowee, ba guddi jot, njaq luy saxar, ànd ak jum buy tàkk, daldi jaar ci diggante dogi yàpp yooyu. |
389 | GEN 16:7 | Ba mu dawee, malaakam Aji Sax ja gis ko fu dend akub bëtu ndox ca màndiŋ ma, mooy bëtu ndox, ba ca yoonu Sur. |
396 | GEN 16:14 | Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (mu firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beret. |
397 | GEN 16:15 | Ba loolu weesee Ajara amal Ibraam doom ju góor. Ibraam tudde doom ji Ismayla. |
398 | GEN 16:16 | Ba Ajaray am Ismayla, Ibraam a ngi tollu woon ci juróom ñett fukki at ak juróom benn (86). |
399 | GEN 17:1 | Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk. |
413 | GEN 17:15 | Ba loolu weesee Yàlla waxaat na Ibraayma, ne ko: «Sa soxna tuddatul Sarayi; léegi moo di Saarata. |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
418 | GEN 17:20 | Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa. |
421 | GEN 17:23 | Ba loolu amee Ibraayma boole doomam Ismayla, ak jaam, yi juddoo këram yépp, ak ñi mu jëndoon ci xaalisam ñépp, góori waa këram ñépp, xarfal leen ca bés ba, muy la ko Yàlla waxoon. |
424 | GEN 17:26 | Bésub keroog la Ibraayma xaraf, moom ak doomam Ismayla |
426 | GEN 18:1 | Am na bés, Aji Sax ji feeñu Ibraayma ca garabi Mamre yu mag ya. Booba ma nga toogoon ca buntu xaymaam digg njolloor. |
435 | GEN 18:10 | Kooka ne ko: «Nëgëni sii déwén déy laay délsi, te sa soxna Saarata dina am doom ju góor moos.» Bi muy wax loolu, Saarataa ngi ci buntu xayma bi ci gannaawam, di déglu. |
436 | GEN 18:11 | Booba fekk na Ibraayma ak Saarata doon mag, ba màggat lool sax, te Saarata weesoon na njurum doom. |
439 | GEN 18:14 | Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.» |
442 | GEN 18:17 | Booba Aji Sax jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar? |
445 | GEN 18:20 | Aji Sax ji nag àddu ne: «Bàkkaari Sodom ak Gomor bare na lool, ba may dégg yuux, yi sababoo ci seen moy. |
452 | GEN 18:27 | Ibraayma dellu ne: «Ma ñemee wax ak yaw, Boroom bi, te duma dara ba dara booloo jeex. |
455 | GEN 18:30 | Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» |
456 | GEN 18:31 | Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» |
457 | GEN 18:32 | Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.» |
459 | GEN 19:1 | Ba loolu amee ñaari malaaka ya dikk Sodom ca ngoon, fekk Lóot toog ca buntu dëkk ba. Lóot séen leen, jóg gatandu leen, daldi leen sujjóotal, ne leen: |
460 | GEN 19:2 | «Dégluleen ma, ngalla sang yi, siyaare naa leen, tee ngeena dal ak man, su ko defee ngeen jàngu, fanaan ba suba, ngeen xëy topp seen yoon?» Ñu ne ko: «Bàyyil, nu fanaan ci mbedd mi.» |
465 | GEN 19:7 | Mu ne leen: «Bokk yi, ngalla buleen def lu bon loolu waay! |
469 | GEN 19:11 | Ba loolu amee ñu gumbaal nit ña nekkoon ca buntu kër ga, mag ak ndaw, ñuy làmbatu bunt ba, ba sonn, bàyyi. |
470 | GEN 19:12 | Ba loolu wéyee gan ña wax Lóot ne ko: «Boo amee mbokk ci dëkk bi, muy sa doom ju góor mbaa ju jigéen, mbaa kuy denc sa doom— koo fi am, génne ko fi, |
475 | GEN 19:17 | Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal sa xélu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.» |
480 | GEN 19:22 | Nanga gaaw nag, làquji fa, ndax duma mana def dara te àgguloo ca.» Loolu moo tax ñu tudde dëkk boobu Sowar (mu firi Bu tuut). |
481 | GEN 19:23 | Ba jant bay fenk, Lóot dugg na Sowar. |
496 | GEN 19:38 | Rakk ja moom it am doom ju góor, tudde ko Ben Aami (mu firi Sama doomu mbokk). Ben Aami moo sos Amoneen, ñi fi nekk ba tey. |
497 | GEN 20:1 | Ba loolu amee Ibraayma dafa jóge fa mu nekkoon, jublu àllub Negew, sanci diggante Kades ak Sur, ba noppi ganeji ay fan ca dëkk ba ñu naa Gerar. |
498 | GEN 20:2 | Ba Ibraayma àggee nag, da ne soxnaam Saarata ab jigéenam la. Abimeleg buurub Gerar daldi yónnee jëlsi Saarata. |
500 | GEN 20:4 | Loolu fekkul Abimeleg dëkkoo Saarata. Mu wax Yàlla ne ko: «Sama Boroom, mbaa doo bóom réew mi ci mbir mu ñu doonul dara? |
510 | GEN 20:14 | Ba mu waxee ba noppi, Abimeleg jël ay xar aki nag ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, jox ko Ibraayma, daldi ko delloo soxnaam Saarata. |