54 | GEN 2:23 | Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.» |
60 | GEN 3:4 | Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee! |
66 | GEN 3:10 | Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.» |
71 | GEN 3:15 | Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.» |
72 | GEN 3:16 | Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.» |
76 | GEN 3:20 | Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund. |
80 | GEN 3:24 | Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund. |
92 | GEN 4:12 | Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.» |
103 | GEN 4:23 | Lemeg nag ne ay soxnaam: «Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg, teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla. Nit a ma gaañ, ma bóom, goneg jàmbaar dóor ma, ma faat. |
145 | GEN 6:7 | Aji Sax ji daldi ne: «Dinaa far ci kaw suuf doom aadama yi ma sàkk, nit ak jur, luy raam ak luy naaw, ndax mititlu naa li ma leen sàkk.» |
151 | GEN 6:13 | Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal. |
161 | GEN 7:1 | Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge. |
205 | GEN 8:21 | Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe. |
211 | GEN 9:5 | Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam. |
217 | GEN 9:11 | Ni may faseek yeen kóllëre nii la: Deesatul boole bindeef yépp, faat ci mbënn mukk. Du menn mbënn mu deeti faagaagal àddina.» |
224 | GEN 9:18 | Doomi Nóoyin yu góor, yi génne ci gaal gi, ñooy: Sem, Xam ak Yafet; Xam mooy baayu Kanaan. |
229 | GEN 9:23 | Sem ak Yafet ànd, jël malaan, teg ko ci seeni mbagg, doxe gannaaw ba agsi, doora sàng seen céri baay. Dañoo dummóoyu, ba gisuñu seen céri baay. |
237 | GEN 10:2 | Doomi Yafet yu góor ñii la: Gomeer ak Magog ak Madéy ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. |
238 | GEN 10:3 | Doomi Gomeer yu góor di Askenas, Rifaat ak Togarma. |
239 | GEN 10:4 | Doomi Yawaan yu góor di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. |
241 | GEN 10:6 | Doomi Xam yu góor ñoo di ñii: Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. |
242 | GEN 10:7 | Doomi Kuus yu góor di Seba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Saba ak Dedan. |
245 | GEN 10:10 | Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. |
257 | GEN 10:22 | Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. |
262 | GEN 10:27 | ak Adoram ak Usal ak Digla |
310 | GEN 12:11 | Naka lay jub Misra, daldi ne soxnaam Sarayi: «Déglu ma, xam naa ne ku rafet nga. |
335 | GEN 13:16 | Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan. |
343 | GEN 14:6 | ak Oreen ña ca seen tund wa ñuy wax Seyir. Da leena dàq ba ca garabu Paran gu mag ga ca wetu màndiŋ ma. |
351 | GEN 14:14 | Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan. |
352 | GEN 14:15 | Ibraam dafa xàjjale mbooloom, dal ci kaw buur ya guddi, dàq leen, topp ci ñoom ba Koba, ca bëj-gànnaaru Damaas. |
361 | GEN 14:24 | Duma jël dara, lu wees li sama nit ñi lekk ba noppi ak sama wàllu farandoo yi, di Aner ak Eskol ak Mamre, ñoom it, nañu jot seen wàll.» |
363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
365 | GEN 15:4 | Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ko, ne ko: «Du moom moo lay donn, waaye ku sosoo ci sa geño moo lay donn.» |
374 | GEN 15:13 | Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at. |
390 | GEN 16:8 | Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.» |
391 | GEN 16:9 | Malaakam Aji Sax ja ne ko: «Dellul ca sa sang, te nga yem ciy loxoom.» |
392 | GEN 16:10 | Mu teg ca ne ko: «Dinaa yokk sa askan lool, ba kenn du leen mana waññ,» |
396 | GEN 16:14 | Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (mu firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beret. |
400 | GEN 17:2 | Dinaa feddli sama kóllëre ak yaw, yokk la bu baax.» |
402 | GEN 17:4 | «Man ci sama wàllu bopp, kóllëre gi ma fas ak yaw mooy lii. Dinga nekk maamu xeet yu baree bare. |
404 | GEN 17:6 | Dinaa la defal njaboot gu ne xas, ay xeet sosoo ci yaw, ba ay buur soqikoo ci yaw. |
414 | GEN 17:16 | Dinaa ko barkeel, may la ak moom doom ju góor; dinaa ko barkeel moos, ba mu jaboote xeet yu bare, te ay buuri xeet sax dinañu soqikoo ci moom.» |
417 | GEN 17:19 | Yàlla ne ko: «Waaw, waaye du tere sa soxna Saarata amal la doom ju góor, nga tudde ko nag Isaaxa. Dinaa fas ak moom sama kóllëre, mu wéy ba ciy sëtam ba fàww. |
418 | GEN 17:20 | Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa. |
446 | GEN 18:21 | Dinaa wàcc, seede ko, ba mu wóor ne ñoo def lépp li sabab yuux yi, am déet.» |
454 | GEN 18:29 | Ibraayma dellu wax ne: «Su fa ñeent fukk ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Duma def dara ngir ñeent fukk ñooñu.» |
455 | GEN 18:30 | Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» |
460 | GEN 19:2 | «Dégluleen ma, ngalla sang yi, siyaare naa leen, tee ngeena dal ak man, su ko defee ngeen jàngu, fanaan ba suba, ngeen xëy topp seen yoon?» Ñu ne ko: «Bàyyil, nu fanaan ci mbedd mi.» |
466 | GEN 19:8 | Dégluleen, ma wax leen; man, am naa ñaari doom yu jigéen, te xamuñu góor. Mayleen ma, ma yót leen leen, ngeen def leen lu leen neex. Rikk buleen def góor ñii dara, ndaxte samay gan lañu.» |
475 | GEN 19:17 | Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal sa xélu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.» |
476 | GEN 19:18 | Lóot nag ne ko: «Déet, sang bi! |
477 | GEN 19:19 | Defal nga ma yiw, yërëm ma lool, ba musal ma. Waaye bala maa daw, ba àgg ca tund ya, musiba mii man naa dal ci sama kaw, ma dee. |
501 | GEN 20:5 | Du góor gi da maa waxoon ne kii jigéenam la? Du jigéen ji it da maa waxoon ne kooku càmmiñam la? Fexewuma dara lu ñaaw te di ko tey de!» |
507 | GEN 20:11 | Ibraayma ne ko: «Da di dama noon, amul kenn ci réew mii ku ragal Yàlla, te dees na ma rey ndax sama soxna. |
509 | GEN 20:13 | Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”» |
512 | GEN 20:16 | Gannaaw loolu wax na Saarata ne ko: «Déglu ma fii, jox naa sa càmmiñ limu junniy dogi xaalis. Loolu dama koo def, ngir setal sa der ci kanam ñi nga dëkkal ñépp. Léegi nag ñépp xam nañu ne set nga wecc.» |
524 | GEN 21:10 | Saarata ne Ibraayma: «Dàqal jaam bii, mook doomam, ndax doomu jaam bii du bokk ak sama doom ndono.» |
526 | GEN 21:12 | Teewul Yàlla ne Ibraayma: «Bu la dara naqari ci xale bu góor bii, mook sa jaam bi. Defalal Saarata li mu la wax rekk, ndax ci Isaaxa lees di tudde saw askan. |
527 | GEN 21:13 | Doomu jaam bi it, dinaa ci lawale aw xeet nag, ndaxte yaa ko jur.» |
530 | GEN 21:16 | dox, ba dànd ko lu tollook saanu fitt, toog nag jàkkaarlook moom te naa ci xelam: «Duma fekke mukk sama deewu doom.» Naka la toog foofa janook moom, ne yikkét jooy. |
532 | GEN 21:18 | Demal yékkati ko, may ko loxo, mu jóg. Dinaa def mu law, ba doon xeet wu yaa.» |
564 | GEN 22:16 | «Déglul lii Aji Sax ji wax: “Giñ naa ci man mii, gannaaw yaa def lii, te gàntaloo ma sa jenn doom ji, |
576 | GEN 23:4 | «Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.» |
578 | GEN 23:6 | «Déglul rekk, kilifa gi. Kilifa gu mag nga ci sunu biir. Dangay tànn ci sunuy bàmmeel, bi la neex, suul fa néew bi; kenn ci nun du la tere, nga suul sa néew ci bàmmeelam.» |
581 | GEN 23:9 | Damaa bëgg, mu bàyyee ma xuntim xeer, mi ñuy wax Magpela te muy boroom. Mu ngi ci catu toolam. Na ma ko jaay lu mat njégam sëkk, dinaa ko jënd, muy sama bàmmeel ci seen biir.» |
583 | GEN 23:11 | «Déglul, ma wax la, kilifa gi, fabal tool bi, booleek xuntim xeer, mi ci nekk far. Maa la ko jox ci sama kanami bokk; jëlal, denc fa sa néew.» |
587 | GEN 23:15 | «Déglu ma, kilifa gi, suuf suy jar ñeenti téeméeri dogi xaalis doŋŋ du dara ci sama diggante ak yaw; tee nga faa denc sa néew rekk?» |
589 | GEN 23:17 | Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom. |
594 | GEN 24:2 | Mu am bés Ibraayma wax surgaam, bi gëna yàgg ci këram, tey saytu alalam jépp, ne ko: «Dugalal sa loxo ci sama suufu lupp, |
606 | GEN 24:14 | Janq bu ma wax ne ko: “Doo yenniku sa njaq, may ma, ma naan,” mu ne ma: “Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,” na kooka di ki nga jagleel sa jaam Isaaxa. Noonu laay xame ne laaye nga biir sama sang.» |
609 | GEN 24:17 | Surga ba daw, daje ak moom ne ko: «Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan.» |
625 | GEN 24:33 | ba noppi ñu taajal ko lu mu lekk. Mu ne: «Déedéet, duma lekk mukk kay, te waxuma li ma taxa jóg.» Laban ne ko: «Kon nag waxal.» |
628 | GEN 24:36 | Sama soxnas sang Saarata nag dem na ba màggat, doora amal sama sang doom ju góor. Doomam jooju la jox li mu moom lépp. |
635 | GEN 24:43 | maa ngii taxaw ci seyaan bi; janq bay ñëw rootsi, ma ne ko: ‘Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan,’ |
662 | GEN 25:3 | Yogsan jur Saba ak Dedan. Askani Dedan ñooy Asureen ñi, Letuseen ñi ak Lewumeen ñi. |
663 | GEN 25:4 | Doomi Majan di Efa ak Efer ak Anog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu. |
665 | GEN 25:6 | Doom yu góor, ya mu am aki nekkaaleem, mu may leen alal ca ba muy dund, ba noppi yebal leen penku, ñu sanci ca réewu penku, ba sore doomam Isaaxa. |
673 | GEN 25:14 | ak Misma ak Duuma ak Maasa |
681 | GEN 25:22 | Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji. |
690 | GEN 25:31 | Yanqóoba ne ko: «Danga ma koy jëkka wecci sa céru ndono bi nga yeyoo ndax li ngay taaw.» |
696 | GEN 26:3 | Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma. |
697 | GEN 26:4 | Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele, |
700 | GEN 26:7 | Góori foofa laaj ko ndaw si mu àndal, lu mu doon ci moom, mu ne: «Sama jigéen la.» Dafa bañoona wax ne soxnaam la, ngir ragal waa foofa rey ko ndax taaru Rebeka. |
702 | GEN 26:9 | Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.» |
709 | GEN 26:16 | Abimeleg daldi ne Isaaxa: «Demal, ba sore nu, ndax danga noo ëpp doole lool.» |
717 | GEN 26:24 | Guddi googu Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Maay Yàllay Ibraayma sa baay; bul ragal dara, ndax maa ngi ànd ak yaw. Dinaa la barkeel, ful sa askan ndax sama jaam Ibraayma.» |
729 | GEN 27:1 | Ba Isaaxa màggatee, te bët yi naqari, ba gisatul, am na bés mu woo taawam Esawu ne ko: «Doom.» Mu ne ko: «Naam.» |
730 | GEN 27:2 | Isaaxa ne ko: «Déglul, ma wax la. Màggat naa te xawma sama bésu dee. |
734 | GEN 27:6 | Rebeka moom ne doomam Yanqóoba: «Dégg naa sa baay wax sa mag Esawu ne ko: |
735 | GEN 27:7 | “Demal rëbbi, indil ma, toggal ma ko lu neex, ma lekk, ba ñaanal la, Aji Sax ji seede, bala may dëddu.” |
737 | GEN 27:9 | Demal ca gétt ga, nga jàpp ñaari tef yu duuf, ma defaral ko sa baay, ba mu neex, ni mu ko bëgge, |
741 | GEN 27:13 | Yaayam ne ko: «Bu la móoloo, Yàlla na ma topp, doom. Defal li ma la wax rekk te dem indil ma gàtt yi.» |
747 | GEN 27:19 | Yanqóoba ne baayam: «Mana Esawu sa taaw. Def naa li nga ma wax. Jógal toog te lekk ci li ma la rëbbal, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.» |
767 | GEN 27:39 | Baayam Isaaxa ne ko: «Déglul, ma wax la, dinga dëkk fu sore ngëneeli suuf, mbaa fu la layub asamaan tiime. |