45 | GEN 2:14 | turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat. |
97 | GEN 4:17 | Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog. |
98 | GEN 4:18 | Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg. |
106 | GEN 4:26 | Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal. |
112 | GEN 5:6 | Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. |
113 | GEN 5:7 | Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
115 | GEN 5:9 | Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan. |
116 | GEN 5:10 | Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
117 | GEN 5:11 | Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu. |
124 | GEN 5:18 | Yeredd moomee am na téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (162), doora jur Enog. |
125 | GEN 5:19 | Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
127 | GEN 5:21 | Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. |
128 | GEN 5:22 | Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
129 | GEN 5:23 | Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365). |
130 | GEN 5:24 | Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom. |
239 | GEN 10:4 | Doomi Yawaan yu góor di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. |
245 | GEN 10:10 | Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. |
250 | GEN 10:15 | Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett, |
252 | GEN 10:17 | ak Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi, |
256 | GEN 10:21 | Sem, miy magu Yafet, jur na moom itam ay doom yu góor. Mooy maami Eber ak askanam. |
257 | GEN 10:22 | Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. |
259 | GEN 10:24 | Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber; |
260 | GEN 10:25 | Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (mu firi Séddlikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddlikoo woon. Rakku Peleg mooy Yogtaan. |
281 | GEN 11:14 | Sela am fanweeri at, jur Eber. |
282 | GEN 11:15 | Eber juddu na, Sela dundaat ñeenti téeméeri at ak ñett (403), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
283 | GEN 11:16 | Eber am fanweeri at ak ñeent, jur Peleg. |
284 | GEN 11:17 | Peleg juddu na, Eber dundaat ñeenti téeméeri at ak fanweer (430), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
337 | GEN 13:18 | Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay. |
338 | GEN 14:1 | Ca jamonoy Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar, Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, |
342 | GEN 14:5 | Ca déwén sa Kedorlamer ak buur ya faroon ak moom, dem dàq Refayeen ña ca Àsterot Karnayim, ak Suseen ña ca Am, ak Emeen ña ca jooru Kiryaatayim, |
344 | GEN 14:7 | Ñu jóge fa nag, waññiku, dem En Mispat, di Kades ba tey, daldi teg mboolem réewum Amalegeen ña tànk, boole ca song Amoreen ña dëkk Asason Tamar. |
346 | GEN 14:9 | di sot ñoom Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, ak Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar. Ñeenti buur di xareek juróom. |
350 | GEN 14:13 | Ba loolu xewee, kenn ci ñi ñu jàppoon rëcc, ñëw ci Ibraam miy ab Ebrë, wax ko ko. Fekk na mu dëkk ca wetu garab yu mag ya woon ca toolub Mamre, ma dib Amoreen, di mbokk mu jege ci Eskol ak Aner, ñoom ñi doon wóllërey Ibraam. |
361 | GEN 14:24 | Duma jël dara, lu wees li sama nit ñi lekk ba noppi ak sama wàllu farandoo yi, di Aner ak Eskol ak Mamre, ñoom it, nañu jot seen wàll.» |
363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
379 | GEN 15:18 | Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat, |
381 | GEN 15:20 | ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Refayeen ñi, |
395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
574 | GEN 23:2 | doora faatu ca Kiryaat Arba, mooy Ebron, ca réewu Kanaan. Ibraayma nag dëj Saarata, jooy ko lool. |
575 | GEN 23:3 | Gannaaw loolu Ibraayma bàyyi fa néew ba, dem ca Etteen ña, ne leen: |
577 | GEN 23:5 | Kenn ci Etteen ñi wax Ibraayma ne ko: |
579 | GEN 23:7 | Naka la Ibraayma dégg loolu, daldi jóg sujjóotal waa réew ma, maanaam Etteen ña. |
580 | GEN 23:8 | Mu ne leen: «Gannaaw nangu ngeen, ma suul fi sama néew, ba mu làqu ma, dégluleen, ma wax leen li ngeen may ñaanal Efron doomu Sowar. |
582 | GEN 23:10 | Booba Efron a ngi teew ci biir Etteen ñi. Efron, miy Etteen nag, wax ak Ibraayma ci kanam bokkam yi séq pénc mi, ne ko: |
585 | GEN 23:13 | daldi wax Efron ci seen kanam ne ko: «Ngalla déglu ma, dama lay jox njégu tool bi, nga jël rekk, ndax ma man faa suul sama néew.» |
586 | GEN 23:14 | Efron wax Ibraayma ne ko: |
588 | GEN 23:16 | Ibraayma dégg li ko Efron wax, daldi waññal Efron limu xaalis, bi mu wax ci kanam Etteen ñi, maanaam ñeenti téeméeri dogi xaalis yu dëppook nattu jaaykat ya. |
589 | GEN 23:17 | Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom. |
591 | GEN 23:19 | Ibraayma daldi suul soxnaam Saarata ca xuntim xeer ma ca biir toolub Magpela, booba janook Mamre, di Ebron léegi, ca réewu Kanaan. |
592 | GEN 23:20 | Nii la Etteen ña dogalale Ibraayma njaayum tool ba ak xunti ma ca nekk, mu def ko bàmmeel. |
663 | GEN 25:4 | Doomi Majan di Efa ak Efer ak Anog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu. |
668 | GEN 25:9 | Isaaxa ak Ismayla, doomam yu góor ya, rob ko ca xuntim xeer ma ca Magpela te jàkkaarloo ak Mamre, ca toolub Efron doomu Sowar, Etteen ba. |
669 | GEN 25:10 | Tool ba Ibraayma jëndoon ca Etteen ña, foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata. |
684 | GEN 25:25 | Naka noona ka jëkka gane àddina xonq, yaram wi sëq lipp, mel ni mbubbum der mu ne sàyy aki kawaram, ñu tudde ko Esawu (mu firi Ku jëxëm). |
685 | GEN 25:26 | Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at. |
686 | GEN 25:27 | Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu te bëggoon toogaayu kër. |
687 | GEN 25:28 | Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba. |
688 | GEN 25:29 | Mu am bés Yanqóoba di togg ndambel ñebbe ju xonq, yemook Esawu jóge ca tool ya, xiif ba ne ñedd. |
689 | GEN 25:30 | Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe). |
691 | GEN 25:32 | Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?» |
692 | GEN 25:33 | Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono, li mu yeyoo ndax li muy taaw. |
693 | GEN 25:34 | Yanqóoba jox Esawu mburu ak ndambe, mu lekk, naan, daldi jóg dem yoonam. Noonu la Esawu sàgganee céru taaw, bi mu yeyoo. |
713 | GEN 26:20 | Teewul sàmmi Gerar di soowook sàmmi Isaaxa naan: «Nun noo moom ndox mi.» Mu tudde teen ba Eseg (mu firi Coow), ndax li ñu soowoo ak moom. |
727 | GEN 26:34 | Esawu am na ñeent fukki at, jël na soxna ku ñuy wax Yudit, muy doomu Beeri, miy Etteen, jëlaat Basmat doomu Elon, miy Etteen. |
729 | GEN 27:1 | Ba Isaaxa màggatee, te bët yi naqari, ba gisatul, am na bés mu woo taawam Esawu ne ko: «Doom.» Mu ne ko: «Naam.» |
733 | GEN 27:5 | Fekk na Rebekaa ngi déglu, ba Isaaxay wax ak doomam Esawu. Esawu daldi dem ca àll ba, rëbbi lu mu toggsi. |
734 | GEN 27:6 | Rebeka moom ne doomam Yanqóoba: «Dégg naa sa baay wax sa mag Esawu ne ko: |
739 | GEN 27:11 | Yanqóoba ne yaayam: «Waaw, waaye sama mag Esawu dafa jëxëm, te man sama yaram rattax. |
743 | GEN 27:15 | Rebeka daldi seet ca dencam la gën ca yérey Esawu taaw ba, solal Yanqóoba doomam ju ndaw. |
747 | GEN 27:19 | Yanqóoba ne baayam: «Mana Esawu sa taaw. Def naa li nga ma wax. Jógal toog te lekk ci li ma la rëbbal, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.» |
749 | GEN 27:21 | Isaaxa ne Yanqóoba: «Jegesil, ma làmb la, ba mu wóor ma ne sama doom Esawoo.» |
750 | GEN 27:22 | Yanqóoba nag jegesi, baayam Isaaxa làmbatu ko ne: «Baat bi de baatu Yanqóobaa, waaye loxo yi, loxoy Esawoo.» |
751 | GEN 27:23 | Xàmmiwu ko, ndax li loxo yi jëxëm ni yuy magam Esawu, ba tax mu ñaanal ko. |
752 | GEN 27:24 | Isaaxa laaj ko ne ko: «Mbaa wóor na ne yaw ay Esawu?» Mu ne ko: «Waawaaw.» |
758 | GEN 27:30 | Naka la Isaaxa noppee ñaanal Yanqóoba, ba mu won baayam Isaaxa gannaaw rekk, Esawu, mag ji, rëbbi ba ñëw, ne jalañ. |
760 | GEN 27:32 | Baayam Isaaxa ne ko: «Kooku?» Mu ne ko: «Mana sa taaw Esawu.» |
762 | GEN 27:34 | Esawu dégg li baayam wax rekk, yuuxu yuux gu réy ndax naqar. Mu ne baayam: «Ngalla baay, ñaanal ma, man itam.» |
764 | GEN 27:36 | Esawu ne: «Moom kay moo yey tudd Yanqóoba, ndax suufu na ma ñaari yoon. Sama céru taaw la jëkka nangu, tey mu nangooti sama ñaanu baay.» Mu teg ca ne: «Ndax desalaloo ma ag ñaan?» |
765 | GEN 27:37 | Isaaxa ne Esawu: «Mbaa am naa lu ma la ñaanalati, doom? Ndax kat xas naa koo def, muy sa kilifa, te bokkam yépp laa def ñuy surgaam, te pepp ak biiñ laa ko woomale it, ba mu ne gàññ.» |
766 | GEN 27:38 | Esawu ne baayam: «Baay, xanaa genn ñaan rekk nga am? Ngalla baay, ñaanal ma, man itam!» Ca la Esawu ne yikkét jooy. |
769 | GEN 27:41 | Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.» |
770 | GEN 27:42 | Naka lañu nettali Rebeka la taawam Esawu wax, mu woolu Yanqóoba, doomam ju ndaw ja, ne ko: «Sa mag a ngi fexee feyu, di la wuta rey. |
774 | GEN 27:46 | Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!» |
779 | GEN 28:5 | Isaaxa daldi yebal Yanqóoba, mu dem Padan Aram ca Laban doomu Betuwel, Arameen bay càmmiñu Rebeka, miy yaayu Yanqóoba ak Esawu. |
780 | GEN 28:6 | Esawu nag yég ne Isaaxa ñaanal na Yanqóoba, ba noppi yebal ko Padan Aram, ngir mu jël fa soxna. Te it ba mu koy ñaanal, digal na ko ne ko, bumu jël ca jigéeni Kanaaneen ña. |
782 | GEN 28:8 | Loolu won Esawu ne jigéeni Kanaan neexuñu baayam. |
783 | GEN 28:9 | Ba mu ko defee Esawu dem ca xeetu Ismayla, jël fa Maalat doomu Ismayla, miy doomu Ibraayma, te di jigéenu Nebayot, mu bokk ciy soxnaam. |
895 | GEN 31:21 | Ba mu demee, dafa yóbbaale la mu amoon lépp, jóge fa, jàll dexu Efraat, wuti tundi Galàdd. |