98 | GEN 4:18 | Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg. |
246 | GEN 10:11 | Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala. |
293 | GEN 11:26 | Gannaaw ba Teraa amee juróom ñaar fukki at, am na Ibraam ak Naxor ak Aran. |
294 | GEN 11:27 | Askanu Teraa mooy lii. Teraa mooy baayu Ibraam ak Naxor ak Aran. Aran mooy baayu Lóot. |
296 | GEN 11:29 | Ibraam ak Naxor jël nañu ay soxna; soxnas Ibraam tudd Sarayi, soxnas Naxor di Milka. Milka moomu, moom ak rakkam ju jigéen Yiska, Aran ay seen baay. |
298 | GEN 11:31 | Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. |
300 | GEN 12:1 | Aji Sax ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won, |
303 | GEN 12:4 | Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75). |
304 | GEN 12:5 | Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan. |
305 | GEN 12:6 | Ba ñu agsee Kanaan, Ibraam dafa jàll ca biir réew ma, ba àgg bérab bu sell, ba féete ak Sikem, ca garab gu mag, ga ñuy wooye More. Booba fekk na waa Kanaan a nga woon ca réew ma. |
306 | GEN 12:7 | Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay. |
307 | GEN 12:8 | Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko. |
308 | GEN 12:9 | Ibraam bàyyikooti fa, aw yoonam, jublu àllub Negew. |
309 | GEN 12:10 | Ca jamono jooja xiif a amoon ca réew ma, ba tax Ibraam dem réewum Misra, toogi fa, ndax xiif bu metti la woon. |
313 | GEN 12:14 | Ba Ibraam àggee Misra, waa Misra gis ne jigéen ji mu àndal rafet na lool. |
315 | GEN 12:16 | Firawna nag topptoo Ibraam bu baax ndax moom, ñu may ko ay gàtt ak ay nag, ay mbaam yu góor, ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, ak ay mbaam yu jigéen aki giléem. |
316 | GEN 12:17 | Teewul Aji Sax ji wàcce ca Firawna ak waa këram jàngoro yu metti ndax Sarayi, soxnas Ibraam. |
317 | GEN 12:18 | Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la? |
319 | GEN 12:20 | Naka la Firawna wax loolu ba noppi, daldi sant ay dagam, ñu génne Ibraam réew ma, moom ak soxnaam ak alalam jépp. |
320 | GEN 13:1 | Bi loolu amee Ibraam dafa jóge Misra, moom ak soxnaam, yóbbaale alalam jépp, daldi dem ca àllub Negew, Lóot topp ca. |
321 | GEN 13:2 | Ibraam nag amoon alal ju bare diggante jur, xaalis ak wurus. |
323 | GEN 13:4 | fa mu tabaxoon ab sarxalukaay. Ibraam nag tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko. |
326 | GEN 13:7 | Loolu tax sàmmi Ibraam ak sàmmi Lóot di jote. Rax ci dolli Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ña nga woon ca réew ma. |
327 | GEN 13:8 | Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? |
331 | GEN 13:12 | Ibraam dëkke réewu Kanaan, Lóot sance dëkk ya ca jooru Yurdan, daldi toxal xaymaam, samp ko Sodom. |
333 | GEN 13:14 | Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu, |
337 | GEN 13:18 | Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay. |
349 | GEN 14:12 | Booba lañu yóbbu Lóot ma dëkk Sodom, te Ibraam di baayam bu ndaw. Ci biir loolu ñu yóbbaale li mu amoon lépp, dem. |
350 | GEN 14:13 | Ba loolu xewee, kenn ci ñi ñu jàppoon rëcc, ñëw ci Ibraam miy ab Ebrë, wax ko ko. Fekk na mu dëkk ca wetu garab yu mag ya woon ca toolub Mamre, ma dib Amoreen, di mbokk mu jege ci Eskol ak Aner, ñoom ñi doon wóllërey Ibraam. |
351 | GEN 14:14 | Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan. |
352 | GEN 14:15 | Ibraam dafa xàjjale mbooloom, dal ci kaw buur ya guddi, dàq leen, topp ci ñoom ba Koba, ca bëj-gànnaaru Damaas. |
353 | GEN 14:16 | Ibraam nag délloosi alal ja jépp, nangu Lóot, mook alalam, ak jigéen ña ak ñeneen, ña ñu jàppoon. |
354 | GEN 14:17 | Gannaaw ba Ibraam dàqee Kedorlamer ak buur ya àndoon ak moom, ba délsi, buurub Sodom dafa génn, gatandu ko ca xur wa ñuy wax Sawe, ñu di ko wooye xuru Buur ba tey. |
356 | GEN 14:19 | Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf! |
357 | GEN 14:20 | Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko. |
358 | GEN 14:21 | Gannaaw loolu buurub Sodom wax Ibraam ne ko: «Jox ma nit, ñi nga jàpp, te nga fab alal ji.» |
359 | GEN 14:22 | Ibraam nag wax buurub Sodom ne ko: «Man yékkati naa sama loxo, Yàlla Aji Sax ju Kawe ji seede, moom mi sàkk asamaan ak suuf, |
362 | GEN 15:1 | Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.» |
363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
364 | GEN 15:3 | Ibraam teg ca ne: «Mayoo ma giir, te it jaam bu juddoo sama kër moo may donn.» |
367 | GEN 15:6 | Ibraam nag gëm na Aji Sax ji, ba tax Aji Sax ji waññal ko ngëmam ag njub. |
369 | GEN 15:8 | Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?» |
371 | GEN 15:10 | Ibraam boole yooyu yépp, rey, lu ci nekk mu dagg ko ci digg bi, dog bu nekk janook moroom ma, waaye daggul picc ya. |
372 | GEN 15:11 | Ba mu ko defee ay tan jóge ca, dal ca kaw yàpp wa, Ibraam nag dàq leen. |
374 | GEN 15:13 | Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at. |
379 | GEN 15:18 | Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat, |
383 | GEN 16:1 | Sarayi amul woon doom ak boroom këram Ibraam. Waaye fekk na mu am jaam bu juddoo Misra te tudd Ajara. |
384 | GEN 16:2 | Sarayi ne Ibraam: «Li am mooy Aji Sax ji deful ma am doom. Kon ngalla waay, dëkkool sama jaam bi, ndax Yàlla def, mu amal ma doom ju góor.» Ibraam nag dégg la Sarayi wax. |
385 | GEN 16:3 | Looloo ngi am, gannaaw ba Ibraam dëkkee fukki at ca réewu Kanaan. Sarayi daldi jël Ajara, jaamam bi juddoo Misra, jox ko jëkkëram Ibraam, ngir mu dëkkoo ko. |
386 | GEN 16:4 | Loolu wees Ibraam dëkkoo Ajara, mu daldi ëmb. Ajara yég ne ëmb na, indi nag yabeel digganteem ak sangam Sarayi. |
387 | GEN 16:5 | Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» |
388 | GEN 16:6 | Ibraam wax Sarayi ne ko: «Sa jaam a ngoog ci say loxo, def ko lu la neex.» Sarayi nag di torxal Ajara, ba mu daw, ba soreek moom. |
393 | GEN 16:11 | tegaat ca ne ko: «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; nanga ko tudde Ismayla (mu firi Yàlla dégg na), ndax Aji Sax ji yég na sa naqar. |
394 | GEN 16:12 | Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul not, di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko. Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.» |
397 | GEN 16:15 | Ba loolu weesee Ajara amal Ibraam doom ju góor. Ibraam tudde doom ji Ismayla. |
398 | GEN 16:16 | Ba Ajaray am Ismayla, Ibraam a ngi tollu woon ci juróom ñett fukki at ak juróom benn (86). |
399 | GEN 17:1 | Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk. |
401 | GEN 17:3 | Ibraam dégg loola, daldi sujjóot. Yàlla wax ak moom ne ko: |
403 | GEN 17:5 | Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare. |
407 | GEN 17:9 | Gannaaw loolu Yàlla waxaat na Ibraayma ne ko: «Yaw nag, sàmmal sama kóllëre, yaak sa askan ak say sët ak say sëtaat. |
413 | GEN 17:15 | Ba loolu weesee Yàlla waxaat na Ibraayma, ne ko: «Sa soxna tuddatul Sarayi; léegi moo di Saarata. |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
416 | GEN 17:18 | Ibraayma ne Yàlla: «Moo, tee ngaa saxal Ismayla rekk te ànd ak moom?» |
417 | GEN 17:19 | Yàlla ne ko: «Waaw, waaye du tere sa soxna Saarata amal la doom ju góor, nga tudde ko nag Isaaxa. Dinaa fas ak moom sama kóllëre, mu wéy ba ciy sëtam ba fàww. |
418 | GEN 17:20 | Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa. |
419 | GEN 17:21 | Waaye sama kóllëre nag, Isaaxa laa koy fasool, moom Isaaxa, mi Saarata di am, nëgëni déwén.» |
420 | GEN 17:22 | Loola la Yàlla wax Ibraayma, daldi fay bàyyikoo. |
421 | GEN 17:23 | Ba loolu amee Ibraayma boole doomam Ismayla, ak jaam, yi juddoo këram yépp, ak ñi mu jëndoon ci xaalisam ñépp, góori waa këram ñépp, xarfal leen ca bés ba, muy la ko Yàlla waxoon. |
422 | GEN 17:24 | Ibraayma amoon na juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), bi muy xaraf; |
423 | GEN 17:25 | doomam Ismayla am fukki at ak ñett, bi ñu koy xarfal. |
424 | GEN 17:26 | Bésub keroog la Ibraayma xaraf, moom ak doomam Ismayla |
426 | GEN 18:1 | Am na bés, Aji Sax ji feeñu Ibraayma ca garabi Mamre yu mag ya. Booba ma nga toogoon ca buntu xaymaam digg njolloor. |
427 | GEN 18:2 | Naka la siggi, gis ñetti nit, ñu ne jimeet ci kanamam. Ibraayma gaawtu, gatandu leen, sujjóotal leen. |
431 | GEN 18:6 | Ibraayma daldi gaaw, dugg biir xayma ba, ne Saarata: «Gaawal, jël ñetti ndabi sunguf su mucc ayib, not ko, def ko mburu yu ndaw.» |
432 | GEN 18:7 | Ibraayma nag daw ca gétt ga, sàkk fa sëllu wu duuf te baax, ñëw jox ko jaamam, mu gaaw togg ko. |
433 | GEN 18:8 | Ibraayma taajal leen ndawal, la ñu togg, ba mu sotti, indaaleel leen soow ak meew mu bees. Ma nga taxaw ca seen wet ca ker garab ga, ñuy lekk. |
436 | GEN 18:11 | Booba fekk na Ibraayma ak Saarata doon mag, ba màggat lool sax, te Saarata weesoon na njurum doom. |
438 | GEN 18:13 | Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: “Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?” |
441 | GEN 18:16 | Gannaaw loolu gan ña jóge foofa, tiim Sodom, di ko séentu. Ibraayma ànd ak ñoom, di leen gunge. |
442 | GEN 18:17 | Booba Aji Sax jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar? |
443 | GEN 18:18 | Ndax kat Ibraayma dina sos xeet wu mag te am doole, te xeeti àddina yépp ci moom lañuy barkeele. |
444 | GEN 18:19 | Moo tax ma tànn ko, ngir mu sant ay doomam ak waa këram, ñuy déggal Aji Sax ji, di jëfe yoon ak njub. Noonu laay defale Ibraayma li ma ko digoon.» |
447 | GEN 18:22 | Gan ña nag dem, jublu Sodom, Ibraayma moom taxaw ba tey fi kanam Aji Sax ji. |
448 | GEN 18:23 | Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen? |
452 | GEN 18:27 | Ibraayma dellu ne: «Ma ñemee wax ak yaw, Boroom bi, te duma dara ba dara booloo jeex. |
454 | GEN 18:29 | Ibraayma dellu wax ne: «Su fa ñeent fukk ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Duma def dara ngir ñeent fukk ñooñu.» |
455 | GEN 18:30 | Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» |
456 | GEN 18:31 | Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» |
457 | GEN 18:32 | Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.» |
458 | GEN 18:33 | Loolu la Aji Sax ji wax ak Ibraayma, daldi dëddu. Ibraayma it ñibbi këram. |
485 | GEN 19:27 | Ca ëllëg sa Ibraayma dafa teela jóg, dem fa mu taxawoon jàkkaarlook Aji Sax ji. |
487 | GEN 19:29 | Ndaxam bi Yàllay tas dëkki joor ga, xalaat na Ibraayma, ba musal Lóot ca dogalam boobee, keroog ba mu tasee dëkk, ya Lóot daloon. |
497 | GEN 20:1 | Ba loolu amee Ibraayma dafa jóge fa mu nekkoon, jublu àllub Negew, sanci diggante Kades ak Sur, ba noppi ganeji ay fan ca dëkk ba ñu naa Gerar. |
498 | GEN 20:2 | Ba Ibraayma àggee nag, da ne soxnaam Saarata ab jigéenam la. Abimeleg buurub Gerar daldi yónnee jëlsi Saarata. |