Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   L    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

35  GEN 2:4  Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax jilla sàkkee suuf ak asamaan,
50  GEN 2:19  Loolu fekk nalla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom.
55  GEN 2:24  Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux.
78  GEN 3:22  lla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumullal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.»
86  GEN 4:6  Aji Sax ji ne Kayin: «Lu la taxa mer, ba ne fóññ nii?
90  GEN 4:10  lla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg.
91  GEN 4:11  Léegi dinga alku, ba suuf dummóoyu la, moom mi ubbi gémmiñam, naan sa deretu rakk, ji nga tuur.
98  GEN 4:18  Enog jur Iraat; Iraat jur Mexuyayel; Mexuyayel jur Metusayel; Metusayel jur Lemeg.
99  GEN 4:19  Lemeg nagl ñaari jabar, aawo bi tudd Ada, ñaareel bi di Silla.
103  GEN 4:23  Lemeg nag ne ay soxnaam: «Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg, teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla. Nit a ma gaañ, ma bóom, goneg jàmbaar dóor ma, ma faat.
104  GEN 4:24  Kayin kay, lees di feyul juróom ñaari yoon, ne, bu dee Lemeg mii, muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.»
131  GEN 5:25  Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg.
132  GEN 5:26  Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
134  GEN 5:28  Lemeg nag am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (182), doora jur doom ju góor.
136  GEN 5:30  Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
137  GEN 5:31  Kon Lemeg dund na juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar (777), doora faatu.
160  GEN 6:22  Noonu la Nóoyin def. Lépp lu kolla sant, def na ko.
175  GEN 7:15  Lépp luy boroom bakkan def na ñaar-ñaar, ànd ak Nóoyin, dugg ca gaal ga,
183  GEN 7:23  Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga.
206  GEN 8:22  Li feek suuf di suuf, dootu jiwooy dakk mbaa ngóob, te du sedd aku tàngoor, du nawet it mbaa noor, mbaa guddeek bëccëg.»
223  GEN 9:17  Ci kaw loolu lla ne Nóoyin: «Loolu mooy màndargaal samallëre, gi ma fas ak mboolem mbindeef mu nekk ci kaw suuf.»
244  GEN 10:9  mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Namróot, rëbbkat bu maga mag ba.»
248  GEN 10:13  Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi
253  GEN 10:18  ak Arwàddeen ñi ak Semareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo.
254  GEN 10:19  Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.
257  GEN 10:22  Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram.
267  GEN 10:32  Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee.
276  GEN 11:9  Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la leen tasaaree ci kaw suuf sépp.
294  GEN 11:27  Askanu Teraa mooy lii. Teraa mooy baayu Ibraam ak Naxor ak Aran. Aran mooy baayu Lóot.
298  GEN 11:31  Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc.
303  GEN 12:4  Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75).
304  GEN 12:5  Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan.
317  GEN 12:18  Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la?
318  GEN 12:19  Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax mal ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!»
320  GEN 13:1  Bi loolu amee Ibraam dafa jóge Misra, moom ak soxnaam, yóbbaale alalam jépp, daldi dem ca àllub Negew, Lóot topp ca.
324  GEN 13:5  Ci biir loolu Lóot, mi mu àndal, moom it yor jur gu gudd ak gu gàtt aki xayma,
326  GEN 13:7  Loolu tax sàmmi Ibraam ak sàmmi Lóot di jote. Rax ci dolli Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ña nga woon ca réew ma.
327  GEN 13:8  Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag?
329  GEN 13:10  Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.
330  GEN 13:11  Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqlikoo.
331  GEN 13:12  Ibraam dëkke réewu Kanaan, Lóot sance dëkk ya ca jooru Yurdan, daldi toxal xaymaam, samp ko Sodom.
333  GEN 13:14  Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu,
349  GEN 14:12  Booba lañu yóbbu Lóot ma dëkk Sodom, te Ibraam di baayam bu ndaw. Ci biir loolu ñu yóbbaale li mu amoon lépp, dem.
351  GEN 14:14  Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan.
353  GEN 14:16  Ibraam naglloosi alal ja jépp, nangu Lóot, mook alalam, ak jigéen ña ak ñeneen, ña ñu jàppoon.
366  GEN 15:5  Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.»
384  GEN 16:2  Sarayi ne Ibraam: «Li am mooy Aji Sax ji deful ma am doom. Kon ngalla waay, dëkkool sama jaam bi, ndaxlla def, mu amal ma doom ju góor.» Ibraam nag dégg la Sarayi wax.
385  GEN 16:3  Looloo ngi am, gannaaw ba Ibraam dëkkee fukki at ca réewu Kanaan. Sarayi daldi l Ajara, jaamam bi juddoo Misra, jox ko jëkkëram Ibraam, ngir mu dëkkoo ko.
386  GEN 16:4  Loolu wees Ibraam dëkkoo Ajara, mu daldi ëmb. Ajara yég ne ëmb na, indi nag yabeel digganteem ak sangam Sarayi.
393  GEN 16:11  tegaat ca ne ko: «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; nanga ko tudde Ismayla (mu firilla dégg na), ndax Aji Sax ji yég na sa naqar.
396  GEN 16:14  Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (mu firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beret.
420  GEN 17:22  Loola la lla wax Ibraayma, daldi fay bàyyikoo.
438  GEN 18:13  Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: “Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?”
456  GEN 18:31  Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.»
457  GEN 18:32  Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.»
458  GEN 18:33  Loolu la Aji Sax ji wax ak Ibraayma, daldi dëddu. Ibraayma it ñibbi këram.
459  GEN 19:1  Ba loolu amee ñaari malaaka ya dikk Sodom ca ngoon, fekk Lóot toog ca buntu dëkk ba. Lóot séen leen, jóg gatandu leen, daldi leen sujjóotal, ne leen:
461  GEN 19:3  Lóot nag soññ leen, ba ñu dal këram, mu ganale leen. Lóot da leena berndeel, lakkal leen mburu mu amul lawiir, ñu lekk.
463  GEN 19:5  Ñu daldi woo Lóot ne ko: «Ana góor ñi fi ñëw tey ci guddi? Génneel nu leen fii, ndax nu mana àgg ci ñoom.»
464  GEN 19:6  Lóot génn, fekk leen ca buntu kër ga ca biti, daldi tëj bunt ba.
467  GEN 19:9  Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba.
468  GEN 19:10  Teewul gan ña yoor seeni loxo, ñoddi Lóot ba ci biir, tëj bunt ba.
470  GEN 19:12  Ba loolu wéyee gan ña wax Lóot ne ko: «Boo amee mbokk ci dëkk bi, muy sa doom ju góor mbaa ju jigéen, mbaa kuy denc sa doom— koo fi am, génne ko fi,
472  GEN 19:14  Lóot daldi génn, wax ak goroom, ya naroona takk ay doomam yu jigéen, ne leen: «Gaawleen gaaw, génn dëkk bi, ndaxte Aji Sax ji dina ko tas.» Teewul ñu defe ne day kaf.
473  GEN 19:15  Fajar a ngay xar, malaaka ya fuug Lóot ne ko: «Gaawal gaaw, ànd ak sa soxna ak sa ñaari doom yu jigéen yii, ba bulla tasee dëkk bi, dungeen sànku.»
474  GEN 19:16  Lóot di tendeefal, gan ña jàpp ci loxo bi, booleek soxnaam ak ñaari doomam génne, làq leen ca gannaaw dëkk ba, ndax yërmande ju Aji Sax ji am ci Lóot.
475  GEN 19:17  Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal salu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.»
476  GEN 19:18  Lóot nag ne ko: «Déet, sang bi!
480  GEN 19:22  Nanga gaaw nag, làquji fa, ndax duma mana def dara te àgguloo ca.» Loolu moo tax ñu tudde dëkk boobu Sowar (mu firi Bu tuut).
481  GEN 19:23  Ba jant bay fenk, Lóot dugg na Sowar.
484  GEN 19:26  Ci kaw loolu soxnas Lóot ne gees, jëmm ja far soppliku xorom.
487  GEN 19:29  Ndaxam billay tas dëkki joor ga, xalaat na Ibraayma, ba musal Lóot ca dogalam boobee, keroog ba mu tasee dëkk, ya Lóot daloon.
488  GEN 19:30  Gannaaw loolu Lóot dafa ragala dëkk Sowar, ba toxoo fa, ànd ak ñaari doomam yu jigéen, sanci ca tund ya. Mu dëkk ci xuntim xeer, moom ak ñaari doomam yu jigéen.
491  GEN 19:33  Ca guddi ga ñu nàndal seen baay biiñ, taaw ba dugg, tëdd ak baayam, te Lóot yégul ba fa doom jay tëdd ak ba muy jóg.
493  GEN 19:35  Guddi jot, ñu nàndalaat seen baay biiñ, rakk ja dem tëdd ak baayam, te Lóot yégul ba fa doom jay tëdd ak ba muy jóg.
494  GEN 19:36  Noonu la ñaari doomi Lóot def ak seen baay, daldi cay doxe ëmb.
500  GEN 20:4  Loolu fekkul Abimeleg dëkkoo Saarata. Mu waxlla ne ko: «Sama Boroom, mbaa doo bóom réew mi ci mbir mu ñu doonul dara?
503  GEN 20:7  Léegi nag dellool góor gi soxnaam, ab yonent la de, te dina la ñaanal, nga raw. Waaye soo ko deful, na la bir ne dinga dee, yaak sa waa kër yépp.»
505  GEN 20:9  Gannaaw loolu Abimeleg woolu Ibraayma ne ko: «Li nga nu def nag? Ndax dama laa tooñ, ba nga yóbbe ma tooñ gu réye nii, man ak sama réew mi mépp? Lii nga ma def de, waroo ko woona def.»
512  GEN 20:16  Gannaaw loolu wax na Saarata ne ko: «Déglu ma fii, jox naa sa càmmiñ limu junniy dogi xaalis. Loolu dama koo def, ngir setal sa der ci kanam ñi nga dëkkal ñépp. Léegi nag ñépp xam nañu ne set nga wecc.»
525  GEN 21:11  Loolu Saarata wax naqari Ibraayma lool ndax li Ismayla di doomam, moom it.
537  GEN 21:23  Léegi nag waatal ma fii cilla ne doo ma wor mukk, man ak samay doom, ba ci samay sët. Waatal ma ne noonee ma rafetoo woon ak yaw, ni ngay rafetoo ak man, maak waa réew, mi nga dal
543  GEN 21:29  Abimeleg nag ne Ibraayma: «Lu tax nga ber juróom ñaari xar yooyu?»
545  GEN 21:31  Looloo tax ñu tudde teen boobu Beerseba (mu firi Teenu waat ga), ndaxte fa lañu waatoo woon ñoom ñaar.
607  GEN 24:15  Laata muy ñaan ba noppi sax, gis na Rebeka gàddu njaqam, di ñëw. Rebeka moomu di doomu Betuwel te di sëtu Milka ak Naxor, miy magu Ibraayma.
621  GEN 24:29  Rebeka amoon na càmmiñ lu tudd Laban. Laban daldi gaawtu génn, fekki waa ja ca seyaan ba.
622  GEN 24:30  Booba gis na jaaro ba ak lam, ya ca loxol jigéenam Rebeka, te dégg na jigéenam di nettali la ko waa ja wax. Loolu tax mu dem ca waa ja, fekk ko ca giléem ya ca seyaan ba.
623  GEN 24:31  Mu ne ko: «Yaw mi Aji Sax ji barkeel, agsil boog! Looy toog ci àll bi; waajalal naa la ab dal, te giléem yi am nañu fu ñu nekk.»
625  GEN 24:33  ba noppi ñu taajal ko lu mu lekk. Mu ne: «Déedéet, duma lekk mukk kay, te waxuma li ma taxa jóg.» Laban ne ko: «Kon nag waxal
641  GEN 24:49  Léegi nag ndegam nar ngeena rafetoo ak sama sang tey sàmmllëre, xamal-leen ma ko, ba mu leer. Su ngeen ko narul it, waxleen ma, ma xam nu may def.»
642  GEN 24:50  Laban ak Betuwel ne ko: «Mbir moomu de ci Aji Sax ji la jóge, te amunu ci dara lu nuy wax.
654  GEN 24:62  Loolu fekk na Isaaxa dëkk ca àllub Negew. Mu demoon nag teenu Laxay Roy, ba ñibbsi.