2 | GEN 1:2 | Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi. |
3 | GEN 1:3 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. |
5 | GEN 1:5 | Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk. |
6 | GEN 1:6 | Yàlla ne: «Na aw dénd dox diggante ndox yi, ngir xàjjale leen, yii fii, yii fale.» |
8 | GEN 1:8 | Yàlla tudde dénd wi asamaan. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñaareel ba. |
9 | GEN 1:9 | Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona. |
11 | GEN 1:11 | Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona. |
13 | GEN 1:13 | Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñetteel ba. |
14 | GEN 1:14 | Yàlla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi. |
15 | GEN 1:15 | Nañu nekk ay leer ci asamaan si, di leeral suuf.» Mu daldi nekk noona. |
19 | GEN 1:19 | Ngoon jot, suba dugg, muy bésub ñeenteel ba. |
20 | GEN 1:20 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na ndox fees ak ay ndiiraani xeeti bindeef, te ay picc tiim suuf, di naaw ci asamaan.» |
22 | GEN 1:22 | Ba mu ko defee Yàlla barkeel leen, daldi ne: «Giirleen te bare, ba fees ndoxi géej.» Mu neeti: «Na picc yi bare ci kaw suuf.» |
23 | GEN 1:23 | Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróomeel ba. |
24 | GEN 1:24 | Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona. |
26 | GEN 1:26 | Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.» |
30 | GEN 1:30 | Naka rabi àll yépp it, ñook picci asamaan yépp ak lépp luy raam ci kaw suuf, te di boroom bakkan, jox naa leen lépp luy ñax mu tooy, ñoom itam, muy seen lekk.» Mu daldi nekk noona. |
31 | GEN 1:31 | Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba. |
39 | GEN 2:8 | Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. |
57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
94 | GEN 4:14 | Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.» |
96 | GEN 4:16 | Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku. |
102 | GEN 4:22 | Silla moom jur Tubal Kayin miy tëgg lépp luy jumtukaayu xànjar ak weñ. Tubal Kayin am na jigéen bu tudd Naama. |
103 | GEN 4:23 | Lemeg nag ne ay soxnaam: «Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg, teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla. Nit a ma gaañ, ma bóom, goneg jàmbaar dóor ma, ma faat. |
107 | GEN 5:1 | Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, |
108 | GEN 5:2 | góor ak jigéen la sàkk, barkeel leen, tudde leen Nit, keroog ba mu leen sàkkee. |
135 | GEN 5:29 | Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» |
136 | GEN 5:30 | Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
138 | GEN 5:32 | Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet. |
142 | GEN 6:4 | Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur. |
146 | GEN 6:8 | Waaye fekk na Aji Sax ji xool Nóoyin bëti yërmande. |
147 | GEN 6:9 | Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla. |
148 | GEN 6:10 | Nóoyin nag amoon na ñetti doom yu góor: seeni tur di Sem, Xam ak Yafet. |
151 | GEN 6:13 | Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal. |
153 | GEN 6:15 | Ni nga koy defare nii la. Na guddaayu gaal gi di ñetti téeméeri xasab, yaatuwaay bi di juróom fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab. |
160 | GEN 6:22 | Noonu la Nóoyin def. Lépp lu ko Yàlla sant, def na ko. |
161 | GEN 7:1 | Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge. |
164 | GEN 7:4 | Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.» |
165 | GEN 7:5 | Nóoyin daldi def la ko Aji Sax ji sant lépp. |
166 | GEN 7:6 | Bi mbënn miy ñëw ci àddina, booba fekk na Nóoyin am juróom benni téeméeri at. |
167 | GEN 7:7 | Nóoyin dugg na ca gaal ga, ànd ak ay doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya, ngir mucc ca ndoxu mbënn ma. |
169 | GEN 7:9 | ànd nañu ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, def ñaar-ñaar, góor ak jigéen, ni ko Yàlla sante Nóoyin. |
171 | GEN 7:11 | At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet, |
173 | GEN 7:13 | Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga, |
175 | GEN 7:15 | Lépp luy boroom bakkan def na ñaar-ñaar, ànd ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, |
176 | GEN 7:16 | mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee. |
177 | GEN 7:17 | Mbënn ma nag di wal ci àddina diiru ñeent fukki fan. Ndox ya di yokku, gaal gay jóg, ba tëmb, tiim suuf lu sore. |
179 | GEN 7:19 | Ndox ma di walangaan, ba mëdd tund yu kawe ya fépp fu asamaan tiim. |
183 | GEN 7:23 | Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga. |
184 | GEN 7:24 | Ndox mi nag di wal-wali ci kaw suuf diirub téeméeri fan ak juróom fukk. |
185 | GEN 8:1 | Ci biir loolu Yàlla xalaat na Nóoyin ak li mu nekkal ci gaal gi, di rabi àll yi ak jur gi. Yàlla daldi yebal ngelaw, mu wal kaw suuf, ba ndox yi wàcc. |
189 | GEN 8:5 | Ndox may wàññiku rekk ba ca fukkeelu weer wa. Keroog ba fukkeelu weer wa teroo, ca la njobbaxtali tund ya tàmbalee feeñ. |
190 | GEN 8:6 | Teg nañu ca ñeent fukki fan, Nóoyin doora ubbi poroxndoll, ba mu sàkkaloon gaal ga, |
193 | GEN 8:9 | Teewul pitax ma gisul fenn fu mu tag, ndax ndox mi muur na suuf sépp. Mu délsi nag fa moom ca gaal ga. Nóoyin tàllal loxoom, jàpp ko dugal ci biir fi wetam. |
194 | GEN 8:10 | Négandiku na juróom ñaari fan, doora yebalaat pitax ma. |
195 | GEN 8:11 | Ba mu délsee ca ngoon, indaalewul lu moy xobu oliw wu tooy wu keppe ca sàll wa. Nóoyin xam ne ndox mi taa woon ci suuf, fer na. |
197 | GEN 8:13 | At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at ak benn, keroog benn fanu weer wa jëkk, ndox ma taa woon ca suuf daldi fendi. Nóoyin ubbi kubeer ga, xool, ba gis ne kaw suuf sépp wow na. |
199 | GEN 8:15 | Ba loolu amee Yàlla ne Nóoyin: |
202 | GEN 8:18 | Nóoyin daldi génn, moom aki doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya. |
204 | GEN 8:20 | Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal Aji Sax ji sarxalukaay, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy saraxu rendi-dóomal. |
207 | GEN 9:1 | Ci kaw loolu Yàlla barkeel Nóoyin aki doomam ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina. |
214 | GEN 9:8 | Yàlla nag wax Nóoyin ak doomam, yi mu àndal, ne leen: |
217 | GEN 9:11 | Ni may faseek yeen kóllëre nii la: Deesatul boole bindeef yépp, faat ci mbënn mukk. Du menn mbënn mu deeti faagaagal àddina.» |
223 | GEN 9:17 | Ci kaw loolu Yàlla ne Nóoyin: «Loolu mooy màndargaal sama kóllëre, gi ma fas ak mboolem mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» |
224 | GEN 9:18 | Doomi Nóoyin yu góor, yi génne ci gaal gi, ñooy: Sem, Xam ak Yafet; Xam mooy baayu Kanaan. |
225 | GEN 9:19 | Ñooñu ñooy ñetti doomi Nóoyin yu góor, te ci ñoom la àddina sépp soqikoo. |
226 | GEN 9:20 | Nóoyin ab beykat la woon. Mu nekk nag ci njëmbatum reseñ. |
230 | GEN 9:24 | Màndite ma giif, Nóoyin yewwu, daldi yég ni xale bi def ak moom. |
234 | GEN 9:28 | Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Nóoyin dundaat na ñetti téeméeri at ak juróom fukk (350). |
235 | GEN 9:29 | Nóoyin dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (950), doora faatu. |
236 | GEN 10:1 | Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom. |
243 | GEN 10:8 | Kuus moom itam jur Namróot, ki jëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf, |
244 | GEN 10:9 | mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Namróot, rëbbkat bu maga mag ba.» |
246 | GEN 10:11 | Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala. |
248 | GEN 10:13 | Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi |
267 | GEN 10:32 | Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee. |
289 | GEN 11:22 | Serug am fanweeri at, jur Naxor. |
290 | GEN 11:23 | Naxor juddu na, Serug dundaat ñaar téeméeri at, juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
291 | GEN 11:24 | Naxor am ñaar fukki at ak juróom ñeent, jur Teraa. |
292 | GEN 11:25 | Teraa gane na àddina, Naxor dundaat téeméeri at ak fukk ak juróom ñeent (119), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
293 | GEN 11:26 | Gannaaw ba Teraa amee juróom ñaar fukki at, am na Ibraam ak Naxor ak Aran. |
294 | GEN 11:27 | Askanu Teraa mooy lii. Teraa mooy baayu Ibraam ak Naxor ak Aran. Aran mooy baayu Lóot. |
296 | GEN 11:29 | Ibraam ak Naxor jël nañu ay soxna; soxnas Ibraam tudd Sarayi, soxnas Naxor di Milka. Milka moomu, moom ak rakkam ju jigéen Yiska, Aran ay seen baay. |
308 | GEN 12:9 | Ibraam bàyyikooti fa, aw yoonam, jublu àllub Negew. |
310 | GEN 12:11 | Naka lay jub Misra, daldi ne soxnaam Sarayi: «Déglu ma, xam naa ne ku rafet nga. |
319 | GEN 12:20 | Naka la Firawna wax loolu ba noppi, daldi sant ay dagam, ñu génne Ibraam réew ma, moom ak soxnaam ak alalam jépp. |
320 | GEN 13:1 | Bi loolu amee Ibraam dafa jóge Misra, moom ak soxnaam, yóbbaale alalam jépp, daldi dem ca àllub Negew, Lóot topp ca. |
322 | GEN 13:3 | Gannaaw loolu mu awati yoonam, jóge àllub Negew, jëm dëkk ba ñu naa Betel, dem ba àgg ca bérab, ba mu jëkkoona samp xaymaam, ci diggante Betel ak Ayi, |
328 | GEN 13:9 | Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.» |
329 | GEN 13:10 | Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja. |
330 | GEN 13:11 | Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqlikoo. |
366 | GEN 15:5 | Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.» |
418 | GEN 17:20 | Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa. |
427 | GEN 18:2 | Naka la siggi, gis ñetti nit, ñu ne jimeet ci kanamam. Ibraayma gaawtu, gatandu leen, sujjóotal leen. |
428 | GEN 18:3 | Mu daldi ne: «Sang bi, siyaare naa la. Ngalla waay, bu ma romb. |