42 | GEN 2:11 | Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, |
45 | GEN 2:14 | turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat. |
93 | GEN 4:13 | Teewul Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko! |
102 | GEN 4:22 | Silla moom jur Tubal Kayin miy tëgg lépp luy jumtukaayu xànjar ak weñ. Tubal Kayin am na jigéen bu tudd Naama. |
157 | GEN 6:19 | Te xeeti rab yépp nanga ci dugal ñaar ci gaal gi, wu ci nekk, nga def ko góor ak jigéen; su ko defee ngeen ànd mucc. |
163 | GEN 7:3 | Te it xeetu picc mu nekk yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ngir seen xeet baña fey ci kaw suuf. |
190 | GEN 8:6 | Teg nañu ca ñeent fukki fan, Nóoyin doora ubbi poroxndoll, ba mu sàkkaloon gaal ga, |
193 | GEN 8:9 | Teewul pitax ma gisul fenn fu mu tag, ndax ndox mi muur na suuf sépp. Mu délsi nag fa moom ca gaal ga. Nóoyin tàllal loxoom, jàpp ko dugal ci biir fi wetam. |
208 | GEN 9:2 | Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo. |
211 | GEN 9:5 | Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam. |
237 | GEN 10:2 | Doomi Yafet yu góor ñii la: Gomeer ak Magog ak Madéy ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. |
238 | GEN 10:3 | Doomi Gomeer yu góor di Askenas, Rifaat ak Togarma. |
239 | GEN 10:4 | Doomi Yawaan yu góor di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. |
291 | GEN 11:24 | Naxor am ñaar fukki at ak juróom ñeent, jur Teraa. |
292 | GEN 11:25 | Teraa gane na àddina, Naxor dundaat téeméeri at ak fukk ak juróom ñeent (119), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
293 | GEN 11:26 | Gannaaw ba Teraa amee juróom ñaar fukki at, am na Ibraam ak Naxor ak Aran. |
294 | GEN 11:27 | Askanu Teraa mooy lii. Teraa mooy baayu Ibraam ak Naxor ak Aran. Aran mooy baayu Lóot. |
295 | GEN 11:28 | Gannaaw loolu Aran faatu na lu jiitu faatug baayam Teraa, ca réew ma mu juddoo, di Ur, dëkku Kaldeen ña. |
298 | GEN 11:31 | Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. |
299 | GEN 11:32 | Teraa dund na ñaar téeméeri at ak juróom (205), doora génn àddina, ñu denc ko Karan. |
311 | GEN 12:12 | Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des. |
316 | GEN 12:17 | Teewul Aji Sax ji wàcce ca Firawna ak waa këram jàngoro yu metti ndax Sarayi, soxnas Ibraam. |
333 | GEN 13:14 | Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu, |
338 | GEN 14:1 | Ca jamonoy Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar, Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, |
344 | GEN 14:7 | Ñu jóge fa nag, waññiku, dem En Mispat, di Kades ba tey, daldi teg mboolem réewum Amalegeen ña tànk, boole ca song Amoreen ña dëkk Asason Tamar. |
346 | GEN 14:9 | di sot ñoom Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, ak Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar. Ñeenti buur di xareek juróom. |
387 | GEN 16:5 | Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» |
399 | GEN 17:1 | Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk. |
403 | GEN 17:5 | Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare. |
405 | GEN 17:7 | Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan. |
406 | GEN 17:8 | Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.» |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
440 | GEN 18:15 | Saarata dégg loolu, daldi tiit, miim ko ne: «Reetaanuma de.» Teewul Aji Sax ji ne ko: «Ree nga kay!» |
462 | GEN 19:4 | Teewul bala ñoo tëdd, góori Sodom, mag ak ndaw, daldi jóge gox bu nekk, ñëw yéew kër ga. |
467 | GEN 19:9 | Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba. |
468 | GEN 19:10 | Teewul gan ña yoor seeni loxo, ñoddi Lóot ba ci biir, tëj bunt ba. |
472 | GEN 19:14 | Lóot daldi génn, wax ak goroom, ya naroona takk ay doomam yu jigéen, ne leen: «Gaawleen gaaw, génn dëkk bi, ndaxte Aji Sax ji dina ko tas.» Teewul ñu defe ne day kaf. |
495 | GEN 19:37 | Taaw ba am ca doom ju góor, tudde ko Mowab (mu firi Jóge ci baay). Mowab moo sos Mowabeen ñi. |
499 | GEN 20:3 | Teewul genn guddi Yàlla feeñu Abimeleg ci gént ne ko: «Yaw dee nga ba noppi, ndax jigéen, ji nga nangu, soxnas jaambur la.» |
506 | GEN 20:10 | Abimeleg teg ca ne ko: «Te li nga def sax, lu la ci xiir?» |
508 | GEN 20:12 | Te moona dëgg la sax, sama jigéen a, ndaxte danoo bokk baay te bokkunu yaay, ma jël ko. |
509 | GEN 20:13 | Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”» |
521 | GEN 21:7 | Mu neeti: «Éy, ku noon Ibraayma, Saarataa ngay nàmpal! Teewul ma jural ko góor, te muy mag.» |
526 | GEN 21:12 | Teewul Yàlla ne Ibraayma: «Bu la dara naqari ci xale bu góor bii, mook sa jaam bi. Defalal Saarata li mu la wax rekk, ndax ci Isaaxa lees di tudde saw askan. |
545 | GEN 21:31 | Looloo tax ñu tudde teen boobu Beerseba (mu firi Teenu waat ga), ndaxte fa lañu waatoo woon ñoom ñaar. |
559 | GEN 22:11 | Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» |
572 | GEN 22:24 | Rewma it nekkaaleem la woon, doom ya mu ca am di Teba ak Gaxam ak Taxas ak Maaka. |
669 | GEN 25:10 | Tool ba Ibraayma jëndoon ca Etteen ña, foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata. |
672 | GEN 25:13 | Turi doomi Ismayla yu góor yaa di: Nebayot, taawub Ismayla, ña ca topp di Kedar ak Adabeel ak Mibsam |
674 | GEN 25:15 | ak Adàdd ak Tema ak Yetur ak Nafis ak Kedama. |
713 | GEN 26:20 | Teewul sàmmi Gerar di soowook sàmmi Isaaxa naan: «Nun noo moom ndox mi.» Mu tudde teen ba Eseg (mu firi Coow), ndax li ñu soowoo ak moom. |
718 | GEN 26:25 | Isaaxa nag sàkk fa sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko, ba noppi samp fa xaymaam. Te itam ay surgaam bënn nañu fa ab teen. |
726 | GEN 26:33 | Isaaxa tudde teen ba Siba (mu firi Waatoo), moo tax turu dëkk ba, ba fii nu tollu, di Beerseba (mu firi Teenu waat ga). |
732 | GEN 27:4 | Toggal ma ko, ba mu neex, ni ma ko bëgge, indil ma, ma lekk, ndax ma ñaanal la lu ma tibbe ci sama xol, bala may dëddu.» |
761 | GEN 27:33 | Isaaxaa ngay lox, bay rag-ragi, daldi ne ko: «Kan? Ana ku rëbbi woon nag, indil ma, ba ma lekk ba noppi? Ñaanal naa ko bala ngaa ñëw. Te dina barkeel moos.» |
780 | GEN 28:6 | Esawu nag yég ne Isaaxa ñaanal na Yanqóoba, ba noppi yebal ko Padan Aram, ngir mu jël fa soxna. Te it ba mu koy ñaanal, digal na ko ne ko, bumu jël ca jigéeni Kanaaneen ña. |
819 | GEN 29:23 | Timis jot Laban jël doomam Leya, jébbal ko Yanqóoba, mu dëkkoo ko. |
846 | GEN 30:15 | Teewul mu ne ko: «Ndax nangu sama jëkkër rekk doyu la, ba nga bëgg cee boole màndaragoor ji ma sama doom indil?» Rasel ne ko: «Kon jox ma ci màndaragoor ji sa doom indi, ma wecci la ko sama ayu tey boog.» |
851 | GEN 30:20 | Booba la ne: «Yàlla defal na ma teraanga ju réy. Bii yoon sama jëkkër dina ma teral, ndax amal naa ko juróom benni doom yu góor.» Moo tax mu tudde ko Sabulon (mu firi Teraanga). |
881 | GEN 31:7 | Teewul seen baay wor ma, soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom, waaye Yàlla seetaanu ko, mu di ma lor. |
890 | GEN 31:16 | Te mboolem alal, ji Yàlla nangoo ci sunu baay, noo ko moom, nun ak sunuy doom. Kon nag léegi lu la Yàlla wax rekk, def ko.» |
911 | GEN 31:37 | Bi nga jéexee sama yëf yépp ba noppi, ana loo gis lu bokk ci sa yëfi kër? Teg ko fii ci sama kanami bokk ak say bokk, ñu àtte nu. |
923 | GEN 31:49 | Ñu di ko tudde itam Mispa (mu firi Tatay wattukaay), ndax Laban da ne: «Yal na Aji Sax ji wattu sunu diggante, keroog bu ñu soree. |
941 | GEN 32:13 | Te yaw yaa ma ne: “Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej, si kenn manula lim ndax bare.”» |
949 | GEN 32:21 | tegati ca ne ko: «Te nee ko itam: “Sa surga Yanqóobaa ngi topp ci sunu gannaaw.”» Booba Yanqóobaa ngi naa ci xelam: «Bu ma jiitalee li ma ko may, neexale ko ko, bala maa janook moom, jombul mu dalal ma jàmm.» |
955 | GEN 32:27 | Nit ka ne ko: «Bàyyi ma, ma dem, ndax bët a ngi bëgga set.» Teewul Yanqóoba ne ko: «Duma la bàyyi, nga dem, li feek ñaanaloo ma.» |
957 | GEN 32:29 | Nit ka ne ko: «Tuddatuloo Yanqóoba, léegi Israyil nga tudd, ndaxte bëre nga ak nit, bëre ak Yàlla, ba génn ci ak jàmm.» |
965 | GEN 33:4 | Teewul Esawu daw gatandu ko, taf ko ci boppam, langaamu ko, di ko fóon. Ñu daldi jooy! |
973 | GEN 33:12 | Gannaaw loolu Esawu ne: «Tee noo ànd dem boog, ma jiitu la?» |
984 | GEN 34:3 | Teewul Sikem xemmemoon na Diina doomu Yanqóoba lool te bëgg ko, ba tax mu di ko naxtaan. |
990 | GEN 34:9 | Tee noo séyante, ngeen may nu seeni janq, te jël ci sunuy janq? |
1011 | GEN 34:30 | Yanqóoba nag wax ak Simeyon ak Lewi ne leen: «Indil ngeen ma musiba, ndax dingeen tax waa réew mépp sib ma, muy Kanaaneen ñi, di Periseen ñi. Te itam awma lu dul góor ñu néew, te bu ñu booloo dal ci sama kaw, dañu may booleek sama waa kër faagaagal.» |
1030 | GEN 35:18 | Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (mu firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin (mu firi Sama doomu njiglaay). |
1052 | GEN 36:11 | Doomi Elifas yu góor yi di: Teman ak Omar ak Sefo ak Gatam ak Kenas. |
1053 | GEN 36:12 | Timna it nekkaaleb Elifas. Mu am caak moom Amaleg. Ñooñoo xeetoo ci Ada, soxnas Esawu. |
1056 | GEN 36:15 | Làngi doomi Esawu yu góor nag, ñooy ñii. Ñi askanoo ci Elifas taawub Esawu, ñuy Teman ak Omar ak Sefo ak Kenas |
1063 | GEN 36:22 | Doomi Lotan yu góor ya nag ñooy Ori ak Emam. Jigéenub Lotan di Timna. |
1065 | GEN 36:24 | Doomi Sibeyon yu góor di Aya ak Ana. Te Ana moomu moo feeñal bëti ndox yu tàng ya ca màndiŋ ma, ba muy sàmm mbaami baayam Sibeyon. |
1075 | GEN 36:34 | Ba Yobab faatoo, Usam mu diiwaanu waa Teman wuutu ko. |
1081 | GEN 36:40 | Làng yi sosoo ci Esawu nag, làng gu ci nekk ak turam ak njaboot, ya mu ëmb, ak gox, ba mu dëkke, ñoo di ñii: ñi askanoo ci Timna ak Alwa ak Yetet |
1083 | GEN 36:42 | ak Kenas ak Teman ak Mibsar |
1095 | GEN 37:11 | Mag ya nag iñaane ko. Teewul baayam moom bàyyi xel ci mbir moomu. |
1111 | GEN 37:27 | Tee nu koo jaay Ismayleen ñi, te bañ koo sàkkal pexe nun ci sunu bopp? Ndax kat sunu rakk a, di sunu deret.» Doomi baay ya déggal ko. |
1114 | GEN 37:30 | Ba loolu amee mu jóge ca, dem ca ay rakkam ne leen: «Xale ba nekkatu fa de! Te man xawma nu may def léegi.» |
1126 | GEN 38:6 | Gannaaw gi Yuda jëlal taawam Er jabar ju tudd Tamar. |
1129 | GEN 38:9 | Teewul Onan xam ne du doon askan wu muy moom, ba tax saa yuy dëkkoo jabaru magam, bay wara àgg rekk, tuur wasal wi ci suuf, ngir baña giiral magam. |
1131 | GEN 38:11 | Yuda daldi wax Tamar jabaru doomam ne ko: «Demal sa kër baay, ténjeji fa, ba sama doom Sela màgg.» Booba Yuda dafa ragal Sela faatu moom itam ni ay magam. Tamar nag dem, toog kër baayam. |
1132 | GEN 38:12 | Ba ñu demee ba mu yàgg, doomu Suwa, soxnas Yuda faatu. Ba dëj ba wéyee, Yuda dem fekki watkati xaram ca Timna. Ira, xaritam bi dëkk Adulam a nga ànd ak moom. |
1133 | GEN 38:13 | Ñu yégal Tamar ne ko: «Sa goroo ngii jëm Timna, di wati ay xaram.» |
1134 | GEN 38:14 | Ba loolu amee mu summi yérey jëtun ya, muuru, sàngu, toog ca selebe yoon wa jëm Enayim ca yoonu Timna, ndax booba gis na ne Sela màgg na te mayuñu ko ko, muy jabaram. |
1144 | GEN 38:24 | Ba ñu ca tegee lu tollook ñetti weer, ñu xamal Yuda ne ko, Tamar goroom ba, da doon jaay boppam, ba jaare ca ëmb. Yuda ne: «Nañu ko yóbbu, lakk ko, ba mu dee.» |
1147 | GEN 38:27 | Tamar dem, ba wara wasin, ndekete ay seex la ëmb. |
1158 | GEN 39:8 | Teewul Yuusufa bañ, ne soxnas sang ba: «Déglul, sama sang da maa jébbal lépp, ba topptootul dara ci kër gi. |
1171 | GEN 39:21 | Teewul Aji Sax ji ànd ak Yuusufa, laaye ko biir, daldi xiir wattukatu kaso ba ca moom, mu yéwéne ko. |
1209 | GEN 41:13 | Te na mu nu ko firile woon, na la ame: delloo nañu ma sama liggéey, ka ca des ñu wékk ko ci bant.» |
1222 | GEN 41:26 | Juróom ñaari nag yu baax yi, juróom ñaari at la. Te it juróom ñaari gub yu baax yi, juróom ñaari at la. Muy genn gént gi. |