258 | GEN 10:23 | Góor ñi Aram jur ñii la: Uus ak Xuul ak Geter ak Maas. |
262 | GEN 10:27 | ak Adoram ak Usal ak Digla |
295 | GEN 11:28 | Gannaaw loolu Aran faatu na lu jiitu faatug baayam Teraa, ca réew ma mu juddoo, di Ur, dëkku Kaldeen ña. |
298 | GEN 11:31 | Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc. |
368 | GEN 15:7 | Gannaaw loolu Aji Sax ji wax ko ne ko: «Man maay Aji Sax, ji la génnee Ur, ga ca Kaldeen ña, ngir may la réew mii, nga moom ko.» |
569 | GEN 22:21 | Uus lañu taawloo, teg ca Bus, teg ca Kemwel, miy baayu Aram, |
1069 | GEN 36:28 | Doomi Disan di Uus ak Aran. |
1075 | GEN 36:34 | Ba Yobab faatoo, Usam mu diiwaanu waa Teman wuutu ko. |
1076 | GEN 36:35 | Ba Usam faatoo, Adàdd, ma dàqoon waa Majan ca réewu Mowab, tey doomu Bedàdd, moo falu, wuutu ko. Awit a doon péeyam. |
1408 | GEN 46:21 | Doomi Beñamin yu góor ñoo di Bela ak Beker ak Asbel ak Gera ak Naaman ak Eyi ak Ros ak Muppim ak Uppim ak Àrd. |
1410 | GEN 46:23 | Doomu Dan ju góor di Usim. |
1674 | EXO 6:18 | Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel; te at ya Keyat dund, téeméer la ak fanweer ak ñett (133). |
1678 | EXO 6:22 | Doomi Usyel yu góor di Mikayel ak Elsafan ak Sitiri. |
1994 | EXO 17:10 | Yosuwe def la ko Musaa wax, di xeex ak Amaleg. Musaa ak Aaróona ak Ur nag ànd yéeg ba ca kaw tund wa. |
1996 | EXO 17:12 | Musaa nag mujj sonn ndax loxo yu toqi; ñu jël aw doj, tegal ko, mu toog ca, Aaróona ak Ur séq ko, ku ci nekk taawu benn loxo, loxoom ya ne sàtt taxaw, ba jant so. |
2192 | EXO 24:14 | Fekk na mu wax mag ña ne leen: «Xaarleen nu fii, ba nu délsi. Aaróona ak Ur a ngi nii ak yeen; ku ci am mbir mooy àttelu, demal ci ñoom.» |
2324 | EXO 28:30 | Nanga yeb ci biir kiiraayal dënn bi ñuy àttee, jumtukaayi tegtal yooyu di Urim ak Tumim, ngir ñu tafu ci xolu Aaróona, saa yuy taxawi fi kanam Aji Sax ji. Noonu la Aaróona di dëkke yóbbaale ci kaw xolam jumtukaayi àtte yu bànni Israyil, saa suy taxawi fi kanam Aji Sax ji, ba fàww. |
2423 | EXO 31:2 | «Gisal, maa woo Besalel ci turam. Besalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. |
2562 | EXO 35:30 | Musaa nag ne bànni Israyil: «Gisleen, Aji Sax ji moo woo Besalel ci turam. Besalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. |
2656 | EXO 38:22 | Fekk na Yudeen bi Besalel doomu Uri, miy doomu Ur, sottal na mboolem li Aji Sax ji santoon Musaa. |
2926 | LEV 8:8 | Mu solal ko nag kiiraayal dënn ba, daldi yeb ca biir kiiraay la jumtukaayi tegtal ya, di Urim ba ak Tumim ba, |
2982 | LEV 10:4 | Ba mu ko defee Musaa woolu Mikayel ak Elsafan, góor ñiy doomi Usyel, baayu Aaróona bu ndaw. Mu ne leen: «Kaayleen jële fi seen bokk yii ci bérab bu sell bi, te ngeen génne leen dal bi.» |
3712 | NUM 3:19 | Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel, ku ci nekk ak làngam. |
3720 | NUM 3:27 | Keyat nag, ci moom la làngu Amrameen ñi soqikoo, ak làngu Isareen ñi, ak làngu Ebroneen ñi, ak làngu Usiyleen ñi. Làngi Keyateen ñaa ngoogu. |
3723 | NUM 3:30 | Keyateen ñi, seen kilifag kër maam moo doon Elisafan doomu Usyel. |
4326 | NUM 20:14 | Gannaaw gi, Musaa moo yebale ay ndaw fa dëkk ba ñuy wax Kades, ñu dem ca buurub Edom, ne ko: «Israyil say bokk dañoo wax ne: Umplewoo mboolem coono bi nu daj. |
4530 | NUM 26:39 | ak ñoom Sufam mi sos làngu Sufameen ñi, ak ñoom Ufam mi sos làngu Ufameen ñi. |
4577 | NUM 27:21 | Ca Elasar sarxalkat bi nag la war di dem, ngir mu di ko seetal fi kanam Aji Sax ji, lu Urim, jumtukaayu tegtal bi, feeñal. Ci ndigalal Elasar nag lañuy génne, te ci ndigalam it lañuy dellusee, moom Yosuwe, ak mboolem bànni Israyil giy ànd ak moom, mbooloo mépp.» |
4674 | NUM 31:8 | reyaale buuri Majan, Ewi ak Rekem ak Sur ak Ur ak Reba, juróomi buuri Majan ya. Balaam doomu Bewor it, ñu reye ko saamar. |
5820 | DEU 33:8 | Lewi la wax ne ko: Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya, ñeel na góor gay sa wóllëre, yaa ko nattoo ca Maasa, joteek moom ca ndoxum Meriba. |
7951 | 1SA 28:6 | Mu seetlu ci Aji Sax ji, Aji Sax ji wuyuwu ko; du ci gént, du ci jumtukaayu tegtal bi ñuy wax Urim, du ci kàddug yonent. |
8163 | 2SA 6:3 | Ñu teg ko ci kaw watiir wu bees, jële ko kër Abinadab ga woon ca kaw tund wa. Usa ak Axyo, doomi Abinadab yu góor ya dox, jiite watiir wu bees wa. |
8166 | 2SA 6:6 | Naka lañu dem ba tollu ca dàggay Nakon, nag ya tërëf, Usa tàllal loxoom, jàpp ca gaalu Yàlla ga. |
8167 | 2SA 6:7 | Sànjum Aji Sax ji nag tàkk ci kaw Usa. Yàllaa ko fàdd foofa, ndax ug teeyadeem, mu dee foofa ca wetu gaalu Yàlla ga. |
8168 | 2SA 6:8 | Ba loolu amee Daawuda mer ca mbugal mu metti ma Aji Sax ji teg Usa. Moo tax mu tudde bérab booba Peres Usa (mu firi Mbugalum Usa), muy turam ba tey jii. |
8265 | 2SA 11:3 | Daawuda yónnee, gëstu mbiram, ñu ne ko: «Xanaa du Batseba doomu Eliyam, jabaru Uri, Etteen bi?» |
8268 | 2SA 11:6 | Ba mu ko defee Daawuda yónnee ca Yowab, ne ko mu wool ko Uri, Etteen ba. Yowab wool ko Uri. |
8269 | 2SA 11:7 | Ba Uri dikkee, Daawuda nuyook moom ne ko: «Mbaa Yowab jàmm? Mbaa mbooloo ma jàmm? Mbaa xare ba jàmm?» |
8270 | 2SA 11:8 | Ba loolu wéyee Daawuda ne Uri: «Àggal sa kër nag te jàngu.» Uri bàyyikoo kër Buur, ab yóbbalu Buur topp ca gannaawam. |
8271 | 2SA 11:9 | Ndeke Uri ñibbiwul këram. Ca bunt kër Buur la tëdd, mook mboolem surgay Buur. |
8272 | 2SA 11:10 | Ñu yégal Daawuda, ne ko: «Uri de ñibbiwul këram,» mu ne Uri: «Xanaa du ciw yoon nga jóge? Lu la tee àgg sa kër?» |
8273 | 2SA 11:11 | Uri ne Daawuda: «Sang bi, gaalu Yàlla ga ak Israyil ak Yuda dëkke ay mbaar, sama njaatige Yowab ak surgay sang bi bokk dale ci digg àll bi, man may dem sama kër, di lekk ak a naan, di dëkkoo sama soxna? Mukk! Giñ naa, nga fekke, duma def loolu!» |
8274 | 2SA 11:12 | Daawuda ne Uri: «Kon toogaatal fii tey ba ëllëg, ma yiwi la.» Uri toog Yerusalem bésub keroog ak ca ëllëg sa. |
8275 | 2SA 11:13 | Ci biir loolu Daawuda woo Uri, mu bokk ak moom lekk, daldi naan. Mu nàndal ko ba mu màndi. Ba ngoon jotee Uri daa génn, tëdd ca laltoom ca biir surgay sangam, waaye këram, àggu fa ba tey. |
8276 | 2SA 11:14 | Ba bët setee Daawuda bind Yowab bataaxal, yóbbante ko Uri. |
8277 | 2SA 11:15 | Mu bind ci bataaxal bi, ne Yowab: «Jiitalal Uri mii ca làngu kanam, ga xare ba gëna tànge, te ngeen dànd ko, ndax ñu jam ko, mu dee.» |
8278 | 2SA 11:16 | Ci kaw loolu Yowab a nga bàyyi xel ca dëkk ba ñu gaw. Mu daldi teg Uri fu ko wóor ne ay ñeyi xarey dëkk baa fa féete. |
8279 | 2SA 11:17 | Ba loolu amee waa dëkk ba génn, xeex ak ñoom Yowab, mu am ñu daanu ca gàngoor ga, ca niti Daawuda ña, Uri Etteen ba bokk ca ña dee. |
8283 | 2SA 11:21 | Ana ku reyoon Abimeleg doomu Yerubeset? Xanaa du ca kaw tata ja la ko aw jigéen sànnee doju wolukaay, ba mu dee ca Tebes? Lu waral ngeen jegee noonu tata ja?” Su boobaa nee ko: “Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.”» |
8286 | 2SA 11:24 | Fittkat ya nag fitte nu ca kaw tata ja, ba mu am ñu dee ci say nit. Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.» |
8288 | 2SA 11:26 | Ba loolu amee jabaru Uri dégg ne jëkkëram dee na. Mu daldi koy ténj. |
8298 | 2SA 12:9 | Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko fàdde saamar; jabaram nga jël, def ko sa jabar, moom nga fàdde ko saamaru Amoneen ñi. |
8299 | 2SA 12:10 | Kon nag saamar dootu jóge sa kër mukk, ndax yaa ma ñàkke worma, ba jël jabaru Uri Etteen bi, def ko sa jabar.” |
8304 | 2SA 12:15 | Ba loolu amee Natan dellu këram. Ba mu ko defee Aji Sax ji daane xale ba jabaru Uri am ak Daawuda. Xale ba wopp. |
8424 | 2SA 15:32 | Ba Daawuda àggee ca collu tund wa, fa ñu daan jaamoo Yàlla, fekku fa ku moy Usay, Arkeen ba. Mu gatandu ko. Ma ngay tiislu, mbubb ma xottiku, bopp ba pënd. |
8429 | 2SA 15:37 | Ci kaw loolu Usay, nitu Daawuda, yoxoosu, duggsi Yerusalem, yemook Absalom itam di agsi. |
8445 | 2SA 16:16 | Usay, Arkeen ba doon nitu Daawuda, dem ca moom, ne ko: «Yal na Buur gudd fan waay, yal na Buur gudd fan!» |
8446 | 2SA 16:17 | Absalom ne Usay: «Loolooy sa kóllëre ak sab xarit a? Lu la teree ànd ak sab xarit?» |
8447 | 2SA 16:18 | Usay ne Absalom: «Déedéet, ki Aji Sax ji tànn, mbooloo mii tànn ko, ñook mboolem bànni Israyil, kookoo may moom, te ci moom laay toog. |
8457 | 2SA 17:5 | Teewul Absalom ne: «Wooleen Usay, Arkeen bi itam, nu déglu lu mu ciy wax.» |
8458 | 2SA 17:6 | Usay dikk ca Absalom, mu wax ko la Ayitofel digle, ne ko: «Ndax loolu Ayitofel wax lanu wara def am déet? Wax nu lu ciy sa xalaat, yaw.» |
8459 | 2SA 17:7 | Usay ne Absalom: «Li Ayitofel digle bii yoon de baaxul. |
8466 | 2SA 17:14 | Absalom ak waa Israyil gépp daldi ne: «Ndigalal Usay, Arkeen bii kat, moo gën ndigalu Ayitofel.» Booba Aji Sax jee nara indil Absalom musiba. Moo tax mu neenal pexem Ayitofel mu jub ma mu laloon. |
8467 | 2SA 17:15 | Ci kaw loolu Usay wax ak Cadog ak Abiyatar sarxalkat ya, nettali leen la Ayitofel digal Absalom ak magi Israyil ña, ak la mu leen digal, moom Usay. |
8601 | 2SA 21:18 | Gannaaw gi xare dellu am seen digganteek Filisteen ña ca dëkk ba ñuy wax Gob. Ca la Sibeka, ma askanoo ci Usa, rey Saf ma bokk ca askanu ponkal ya. |
8683 | 2SA 23:27 | Abiyeser ma dëkk Anatot, Mebunay dëkk Usa, |
8695 | 2SA 23:39 | ak Uri, Etteen ba. Ñoom ñépp tollu ci fanweeri jàmbaar ak juróom yaar. |
8855 | 1KI 4:8 | Ñooñoo di: Ben Ur ma sasoo woon diiwaanu tundi Efrayim. |
8863 | 1KI 4:16 | Baana doomu Usay boole diiwaanu Aser ak Beyalot. |
8866 | 1KI 4:19 | Geber doomu Uri sasoo diiwaanu Galàdd, di réewum Siwon buurub Amoreen ña ak réewum Og buuru Basan. Muy benn ndawal buur bu yilif réew mooma. |
8950 | 1KI 7:13 | Ci kaw loolu Buur Suleymaan yónnee, jëli ca Tir ku ñuy wax Uram. |
8951 | 1KI 7:14 | Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon Tir, di tëggub xànjar. Uram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp. |
8960 | 1KI 7:23 | Ba mu ko defee Uram móol mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu, yaatoo fukki xasab, catu omb ba catu omb, taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub. |
8966 | 1KI 7:29 | Muy làcc yu Uram yett ci kawam ay gaynde, ay nag ak malaakay serub. Kaw laat yi itam am na ci nataal yi. Mu yett ay caqi tóor-tóor yuy lang ci suufu gaynde yeek nag yi. |
8974 | 1KI 7:37 | Noonu la Uram defare fukki rootukaay yi. Lépp bokk móol, yem dayo te bokk bind. |
8982 | 1KI 7:45 | Bagaan yu ndaw yi bokk na ci, ak ñiitukaay yi ak këll yi. Mboolem yooyu jumtukaayi kër Aji Sax ji, xànjar bu ñu jonj la Buur Suleymaan sant Uram, mu defare ko. |
9257 | 1KI 15:5 | Li ko waral mooy Daawuda da daan jëfe njub lu Aji Sax ji rafetlu, te giiru dundam gépp teggiwul lenn lu ko Aji Sax ji sant lu moy ci mbirum Uri Etteen ba. |
9763 | 2KI 9:3 | Su ko defee nga jël taxub diw bi, sotti ko ci kaw boppam te wax ko ne ko: “Aji Sax ji nee: Diw naa la, fal la ngay buurub Israyil.” Boo noppee, bul yeexantu. Ubbil bunt ba, daw.» |
9892 | 2KI 13:17 | ba noppi ne ko: «Ubbil palanteeru penku bi.» Mu ubbi. Alyaasa ne ko: «Soqil!» Mu soqi. Mu ne ko: «Fittu ndamal Aji Sax jaa ngoog, di fitt gi ngay ame ndam ci waa Siri. Dinga daan waa Siri ca Afeg, ba faagaagal leen.» |
9963 | 2KI 15:34 | Muy def li Aji Sax ji rafetlu; mboolem na baayam Usiya daan defe la daan defe. |
9977 | 2KI 16:10 | Gannaaw loolu Buur Axas dem ca Tiglaat Pilser buurub Asiri ca Damaas, gis fa sarxalukaay ba fa nekk. Ba mu ko defee Buur Axas yónnee ca Uri sarxalkat ba, nataalu sarxalukaay ba ak tabaxin waak mboolem na mu bindoo. |
9978 | 2KI 16:11 | Urya sarxalkat ba daldi tabax sarxalukaay bu dëppook mboolem tegtal ya bàyyikoo ca Buur Axas ca Damaas. Uri noppi na ko bala Buur Axas di ñibbsi. |
9982 | 2KI 16:15 | Ci biir loolu Buur Axas sant Uri sarxalkat ba ne ko: «Ci kaw sarxalukaay bu mag bi ngay joxe saraxu rendi-dóomalu suba si, ak saraxu pepp bu ngoon bi, ak saraxu rendi-dóomalu buur bi, ak saraxu peppam, boole ci saraxu rendi-dóomal bi ñuy joxeel mboolem waa réew mi, ak seen saraxu pepp, ak seen saraxu tuuru. Te nga xëpp ci kawam mboolem deretu saraxu rendi-dóomal bi, ak deretu mboolem sarax su ñuy rendi. Sarxalukaayu xànjar bi moom, maa koy moom, di ko gindikoo ci Aji Sax ji.» |
9983 | 2KI 16:16 | Uri sarxalkat ba def la ko Buur Axas sant lépp. |
10141 | 2KI 21:18 | Gannaaw gi Manase saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ci toolub këram, di toolub Usa. Doomam Amon falu buur, wuutu ko. |
10149 | 2KI 21:26 | Ba loolu amee ñu denc ko ca bàmmeelam ca toolub Usa, Yosya doomam falu buur, wuutu ko. |
10163 | 2KI 22:14 | Ilkiya sarxalkat ba daldi dem ànd ak Ayikam ak Agbor ak Safan ak Asaya, ba ca Ulda yonent bu jigéen bay soxnas wattukatub yére ya, Salum doomu Tigwa doomu Aras. Ulda ma nga dëkkoon Yerusalem ca sanc ba. Ñu wax ak moom. |
12081 | EZR 2:49 | ak askanu Usa, ak askanu Paseya, ak askanu Besay, |
12095 | EZR 2:63 | Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu sell yaa sell, ba keroog ab sarxalkat di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax Urim ak Tumim. |
12124 | EZR 4:9 | Bataaxal bii mu ngi bawoo ci Reyum, boroom dëkk bi, ak Simsay bindkatam, ak seen nàttongoy àttekat yeek kàngam yeek saytukat yeek boroom téere yi, ak waa Urug ak waa Babilon ak waa Sus, Elameen ña, |
12182 | EZR 7:4 | Merayot, Seraya; Seraya, Usi; Usi, Bukki; |
12220 | EZR 8:14 | Ci askanu Bigway, Utay la ak Sabudd, ñook juróom ñaar fukki góor (70). |
12239 | EZR 8:33 | Bésub ñeenteel ba nu natt diisaayu xaalis baak wurus waak ndab ya ca sunu biir kër Yàlla ga, teg ko ca loxol Meremot doomu Uri, sarxalkat ba, mook Elasar doomu Fineyas, ak Leween ña, di Yosabàdd doomu Yeswa, ak Nowadiya doomu Binuy. |
12281 | EZR 10:24 | Ci jàngkat yi: Elyasib la. Ci fara bunt yi: Salum laak Telem ak Uri. |
12291 | EZR 10:34 | Ci askanu Baani, Madaay laak Amram ak Uyel |