610 | GEN 24:18 | Mu ne ko: «Ahakay, sang bi,» daldi gaaw, yenniku njaq la, may ko mu naan. |
1265 | GEN 42:12 | Mu ne leen: «Ahakay, nemmikusi mbóoti réew mi moo leen taxa jóg.» |
7529 | 1SA 14:19 | Naka la Sóol di wax ak sarxalkat bi, coow la ca dalub waa Filisti gëna jolli. Sóol ne sarxalkat bi: «Ah, bàyyi ko sax.» |
7825 | 1SA 23:12 | Daawuda ne: «Mbaa kilifay Keyla duñu ma teg, maak samay nit ci loxol Sóol?» Aji Sax ji ne ko: «Ahakay.» |
9587 | 2KI 3:7 | Ba loolu amee mu yónnee ca Yosafat buurub Yuda, ne ko: «Buuru Mowab fippu na, jógal ma. Ndax doo ànd ak man, nu xarejeek Mowab?» Mu ne ko: «Ahakay! Maak yaw benn lanu. Sama mboolooy sa mbooloo, samay fas di say fas,» |
9674 | 2KI 5:23 | Naaman ne ko: «Ahakay! Jëlal juróom benn fukki kiloy xaalis kay!» Mu soññ ko nag, ba mu ëmb juróom benn fukki kiloy xaalis yi ci ñaari mbuus, boole ca ñaari mbubbi xew, jox ko ñaari surgaam, ñu gàddu, jiitu Gewasi. |
9771 | 2KI 9:11 | Yewu génn, dellu ca moroomi jawriñam ña. Ñu ne ko: «Mbaa jàmm? Lu indi dof bii ci yaw?» Mu ne leen: «Ah, xam ngeen nit kii aki waxam rekk!» |
20612 | EZK 4:14 | Ma ne ko: «Ãhã! Boroom bi Aji Sax ji, man de masumaa sobeel sama bopp. Muy lu médd, di lu aw rab fàdd, masuma koo lekk ba may gone ba tey. Wenn yàpp wu daganul masula dugg sama gémmiñ.» |
21900 | DAN 3:24 | Ci kaw loolu Buur Nabukodonosor jommi, ne bërét taxaw, daldi laaj ay dagam ne leen: «Xanaa du ñett lañu yeew, sànni ci sawara wi?» Ñu ne ko: «Ahakay, Buur!» |
28088 | ROM 3:29 | Am Yàlla da di Yàllay Yawut yi doŋŋ? Da dul Yàllay jaambur yi dul Yawut itam? Ahakay, mooy Yàllay jaambur ñeet kay! |
28274 | ROM 10:18 | Waaye dama ne: xanaa dañoo déggul? Ahakay! Ndax «Àddina sépp la seen baat jibal, cati suuf sépp la seen kàddu dajal.» |
28275 | ROM 10:19 | Ma neeti: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Ahakay! Musaa moo leen jëkkoona jottli la Yàlla noon: «Yeen, maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara, ci waasow naataxuuna laa leen di merloo.» |
28447 | 1CO 1:16 | Ahakay! Maa sóob waa kër Estefanas itam. Waaye bu loolu weesee, fàttlikuwuma fu ma sóobe keneen. |
29068 | 2CO 11:11 | Lu tax? Ndax dama leena buggul? Yàlla xam na ne «ahakay!» |