64 | GEN 3:8 | Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi. |
66 | GEN 3:10 | Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.» |
75 | GEN 3:19 | saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.» |
80 | GEN 3:24 | Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund. |
88 | GEN 4:8 | Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. |
94 | GEN 4:14 | Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.» |
149 | GEN 6:11 | Booba fekk na àddina yàqu, te fees ak ay, Yàlla teg ci bëtam. |
150 | GEN 6:12 | Yàlla gis ne àddina yàqu na, ndaxte jëfi ñépp a bokk ñaaw fi kaw suuf. |
225 | GEN 9:19 | Ñooñu ñooy ñetti doomi Nóoyin yu góor, te ci ñoom la àddina sépp soqikoo. |
270 | GEN 11:3 | Ñu ne: «Ayca nu defar ay móol yu ñu lakk cib taal, ba mu ñor.» Ci kaw loolu ñu def móol ya doji tabax, taqalee ko koltaar, |
306 | GEN 12:7 | Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay. |
328 | GEN 13:9 | Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.» |
330 | GEN 13:11 | Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqlikoo. |
333 | GEN 13:14 | Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu, |
334 | GEN 13:15 | ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw. |
342 | GEN 14:5 | Ca déwén sa Kedorlamer ak buur ya faroon ak moom, dem dàq Refayeen ña ca Àsterot Karnayim, ak Suseen ña ca Am, ak Emeen ña ca jooru Kiryaatayim, |
343 | GEN 14:6 | ak Oreen ña ca seen tund wa ñuy wax Seyir. Da leena dàq ba ca garabu Paran gu mag ga ca wetu màndiŋ ma. |
348 | GEN 14:11 | Ña leen dàq nag, jël alalu Sodom ak Gomor yépp, nanguwaale seen dund bépp boole ca, daldi dem seen yoon. |
351 | GEN 14:14 | Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan. |
352 | GEN 14:15 | Ibraam dafa xàjjale mbooloom, dal ci kaw buur ya guddi, dàq leen, topp ci ñoom ba Koba, ca bëj-gànnaaru Damaas. |
354 | GEN 14:17 | Gannaaw ba Ibraam dàqee Kedorlamer ak buur ya àndoon ak moom, ba délsi, buurub Sodom dafa génn, gatandu ko ca xur wa ñuy wax Sawe, ñu di ko wooye xuru Buur ba tey. |
372 | GEN 15:11 | Ba mu ko defee ay tan jóge ca, dal ca kaw yàpp wa, Ibraam nag dàq leen. |
378 | GEN 15:17 | Ba jant sowee, ba guddi jot, njaq luy saxar, ànd ak jum buy tàkk, daldi jaar ci diggante dogi yàpp yooyu. |
379 | GEN 15:18 | Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat, |
393 | GEN 16:11 | tegaat ca ne ko: «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; nanga ko tudde Ismayla (mu firi Yàlla dégg na), ndax Aji Sax ji yég na sa naqar. |
404 | GEN 17:6 | Dinaa la defal njaboot gu ne xas, ay xeet sosoo ci yaw, ba ay buur soqikoo ci yaw. |
414 | GEN 17:16 | Dinaa ko barkeel, may la ak moom doom ju góor; dinaa ko barkeel moos, ba mu jaboote xeet yu bare, te ay buuri xeet sax dinañu soqikoo ci moom.» |
474 | GEN 19:16 | Lóot di tendeefal, gan ña jàpp ci loxo bi, booleek soxnaam ak ñaari doomam génne, làq leen ca gannaaw dëkk ba, ndax yërmande ju Aji Sax ji am ci Lóot. |
478 | GEN 19:20 | Gisuloo dëkk bale; jege na, te dëkk bu tuut la, am déet? Ma daw, làquji fa boog, ba mucc?» |
480 | GEN 19:22 | Nanga gaaw nag, làquji fa, ndax duma mana def dara te àgguloo ca.» Loolu moo tax ñu tudde dëkk boobu Sowar (mu firi Bu tuut). |
489 | GEN 19:31 | Mu am bés, taaw bi wax rakk ji, ne ko: «Sunu baay a ngii màggat, te fii fépp amul góor gu nu mana séqal ci wàllu séy, ni ko waa àddina yépp baaxoo defe. |
524 | GEN 21:10 | Saarata ne Ibraayma: «Dàqal jaam bii, mook doomam, ndax doomu jaam bii du bokk ak sama doom ndono.» |
525 | GEN 21:11 | Loolu Saarata wax naqari Ibraayma lool ndax li Ismayla di doomam, moom it. |
526 | GEN 21:12 | Teewul Yàlla ne Ibraayma: «Bu la dara naqari ci xale bu góor bii, mook sa jaam bi. Defalal Saarata li mu la wax rekk, ndax ci Isaaxa lees di tudde saw askan. |
576 | GEN 23:4 | «Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.» |
580 | GEN 23:8 | Mu ne leen: «Gannaaw nangu ngeen, ma suul fi sama néew, ba mu làqu ma, dégluleen, ma wax leen li ngeen may ñaanal Efron doomu Sowar. |
582 | GEN 23:10 | Booba Efron a ngi teew ci biir Etteen ñi. Efron, miy Etteen nag, wax ak Ibraayma ci kanam bokkam yi séq pénc mi, ne ko: |
589 | GEN 23:17 | Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom. |
605 | GEN 24:13 | Maa ngi nii taxaw ci bëtu ndox mi, janqi dëkk bi di rootsi. |
606 | GEN 24:14 | Janq bu ma wax ne ko: “Doo yenniku sa njaq, may ma, ma naan,” mu ne ma: “Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,” na kooka di ki nga jagleel sa jaam Isaaxa. Noonu laay xame ne laaye nga biir sama sang.» |
607 | GEN 24:15 | Laata muy ñaan ba noppi sax, gis na Rebeka gàddu njaqam, di ñëw. Rebeka moomu di doomu Betuwel te di sëtu Milka ak Naxor, miy magu Ibraayma. |
608 | GEN 24:16 | Ndaw su taaru la woon, di ab janq bu séyagul. Naka la wàcc ba ca seyaan ba, duy njaqam, yéegaat. |
609 | GEN 24:17 | Surga ba daw, daje ak moom ne ko: «Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan.» |
610 | GEN 24:18 | Mu ne ko: «Ahakay, sang bi,» daldi gaaw, yenniku njaq la, may ko mu naan. |
612 | GEN 24:20 | Mu daldi gaaw, sotti njaq la ca mbalka ma, dawaat rootali giléem yi ca seyaan ba. |
620 | GEN 24:28 | Janq bi nag daw dem, nettali waa kër yaayam la xew lépp. |
635 | GEN 24:43 | maa ngii taxaw ci seyaan bi; janq bay ñëw rootsi, ma ne ko: ‘Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan,’ |
637 | GEN 24:45 | «Bala maa ñaan ba noppi, Rebeka ne jimeet, gàddu njaqam, wàcc ca seyaan ba, di root. Ma ne ko: “May ma, ma naan.” |
638 | GEN 24:46 | Mu gaaw yenniku njaq li, daldi ne ma: “Naanal ba noppi ma wëggal la say giléem.” Ma naan ba noppi, mu wëggal ma giléem yi. |
647 | GEN 24:55 | Càmmiñal ndaw sa ak yaay ja daldi ne ko: «Xanaa kay janq bi dina toogaat ak nun ab diir boog, maanaam fii ak sibbir, doora dem.» |
649 | GEN 24:57 | Ñu ne ko: «Kon nag nanu woo janq bi, laaj ko moom ci boppam.» |
684 | GEN 25:25 | Naka noona ka jëkka gane àddina xonq, yaram wi sëq lipp, mel ni mbubbum der mu ne sàyy aki kawaram, ñu tudde ko Esawu (mu firi Ku jëxëm). |
685 | GEN 25:26 | Gannaaw ga ka ca des topp ca, loxo ba jàpp ca téstënu Esawu. Ñu tudde ko Yanqóoba (mu firi Jàpp ci téstën). Ba leen Rebeka di am, fekk na Isaaxa am juróom benn fukki at. |
686 | GEN 25:27 | Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu te bëggoon toogaayu kër. |
687 | GEN 25:28 | Isaaxa nag am cofeel ci Esawu ndax li muy lekk ci am rëbbam, te Rebeka moom gëna sopp Yanqóoba. |
688 | GEN 25:29 | Mu am bés Yanqóoba di togg ndambel ñebbe ju xonq, yemook Esawu jóge ca tool ya, xiif ba ne ñedd. |
689 | GEN 25:30 | Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe). |
690 | GEN 25:31 | Yanqóoba ne ko: «Danga ma koy jëkka wecci sa céru ndono bi nga yeyoo ndax li ngay taaw.» |
692 | GEN 25:33 | Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono, li mu yeyoo ndax li muy taaw. |
693 | GEN 25:34 | Yanqóoba jox Esawu mburu ak ndambe, mu lekk, naan, daldi jóg dem yoonam. Noonu la Esawu sàgganee céru taaw, bi mu yeyoo. |
720 | GEN 26:27 | Isaaxa ne leen: «Lu waral ngeen fekksi ma fii, gannaaw dangeen maa bañ, ba dàq ma?» |
728 | GEN 26:35 | Jigéen ñooñu mu jël nag di naqar wu réy ci Isaaxa ak Rebeka. |
729 | GEN 27:1 | Ba Isaaxa màggatee, te bët yi naqari, ba gisatul, am na bés mu woo taawam Esawu ne ko: «Doom.» Mu ne ko: «Naam.» |
734 | GEN 27:6 | Rebeka moom ne doomam Yanqóoba: «Dégg naa sa baay wax sa mag Esawu ne ko: |
739 | GEN 27:11 | Yanqóoba ne yaayam: «Waaw, waaye sama mag Esawu dafa jëxëm, te man sama yaram rattax. |
742 | GEN 27:14 | Yanqóoba dem, jël gàtt yi, indil yaayam, mu defar ba mu neex, ni ko baayam bëgge. |
743 | GEN 27:15 | Rebeka daldi seet ca dencam la gën ca yérey Esawu taaw ba, solal Yanqóoba doomam ju ndaw. |
744 | GEN 27:16 | Ba mu noppee, daa sàkk ca deri gàtt ya, sànge loxo ya ak fi rattax ci doq gi, |
745 | GEN 27:17 | doora boole mburu ma ak ñam wa mu togg, jox doomam Yanqóoba. |
747 | GEN 27:19 | Yanqóoba ne baayam: «Mana Esawu sa taaw. Def naa li nga ma wax. Jógal toog te lekk ci li ma la rëbbal, ndax nga ñaanal ma ci sa xol.» |
748 | GEN 27:20 | Isaaxa ne doomam: «Moo doom! Noo def, ba gaawa jàpp nii?» Yanqóoba ne ko: «Aji Sax jiy sa Yàlla, moo ma ko jagleel.» |
749 | GEN 27:21 | Isaaxa ne Yanqóoba: «Jegesil, ma làmb la, ba mu wóor ma ne sama doom Esawoo.» |
750 | GEN 27:22 | Yanqóoba nag jegesi, baayam Isaaxa làmbatu ko ne: «Baat bi de baatu Yanqóobaa, waaye loxo yi, loxoy Esawoo.» |
753 | GEN 27:25 | Isaaxa ne ko: «Jottli ma fii ma lekk ci sam rëbb, doom, ba ñaanal la ci sama xol.» Yanqóoba jottli Isaaxa ndab li, mu lekk, daldi koy may biiñ, mu naan. |
755 | GEN 27:27 | Yanqóoba jegesi, fóon ko, xetu yére yi mu sol xeeñ Isaaxa, mu door koo ñaanal ne ko: «Sama xetu doom kay xetug tool la, bu Aji Sax ji barkeel. |
758 | GEN 27:30 | Naka la Isaaxa noppee ñaanal Yanqóoba, ba mu won baayam Isaaxa gannaaw rekk, Esawu, mag ji, rëbbi ba ñëw, ne jalañ. |
762 | GEN 27:34 | Esawu dégg li baayam wax rekk, yuuxu yuux gu réy ndax naqar. Mu ne baayam: «Ngalla baay, ñaanal ma, man itam.» |
764 | GEN 27:36 | Esawu ne: «Moom kay moo yey tudd Yanqóoba, ndax suufu na ma ñaari yoon. Sama céru taaw la jëkka nangu, tey mu nangooti sama ñaanu baay.» Mu teg ca ne: «Ndax desalaloo ma ag ñaan?» |
769 | GEN 27:41 | Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.» |
770 | GEN 27:42 | Naka lañu nettali Rebeka la taawam Esawu wax, mu woolu Yanqóoba, doomam ju ndaw ja, ne ko: «Sa mag a ngi fexee feyu, di la wuta rey. |
771 | GEN 27:43 | Kon doom, defal lii ma lay wax, demal làquji fa sama càmmiñ Laban ca Karan, |
774 | GEN 27:46 | Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!» |
775 | GEN 28:1 | Ci kaw loolu Isaaxa woo Yanqóoba, ñaanal ko, jox ko ndigal lii ne ko: «Bul jël ci jigéeni Kanaan, |
778 | GEN 28:4 | Yal na la barkeb Ibraayma dal, yaak askan wi soqikoo ci yaw, ba nga moom réew mii ngay doxandéem tey, te Yàlla mayoon ko Ibraayma.» |
779 | GEN 28:5 | Isaaxa daldi yebal Yanqóoba, mu dem Padan Aram ca Laban doomu Betuwel, Arameen bay càmmiñu Rebeka, miy yaayu Yanqóoba ak Esawu. |
780 | GEN 28:6 | Esawu nag yég ne Isaaxa ñaanal na Yanqóoba, ba noppi yebal ko Padan Aram, ngir mu jël fa soxna. Te it ba mu koy ñaanal, digal na ko ne ko, bumu jël ca jigéeni Kanaaneen ña. |
781 | GEN 28:7 | Mu yég ne Yanqóoba déggal na baayam ak yaayam, ba dem Padan Aram. |
784 | GEN 28:10 | Ba loolu wéyee Yanqóoba génn Beerseba, wuti Karan. |
786 | GEN 28:12 | Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc. |
790 | GEN 28:16 | Ci kaw loolu Yanqóoba yewwu ne: «Ndekete Aji Sax ji mu ngi ci bérab bii, te xawma ko woon.» |
792 | GEN 28:18 | Ca suba teel Yanqóoba jóg, jël doj, wi mu gegenoo woon, samp fa, muy xàmmikaay, ba noppi sotti ci ag diw, sellale ko. |
794 | GEN 28:20 | Gannaaw loolu Yanqóoba dogu na ne: «Su Yàlla àndee ak man, di ma sàmm ci yoon wi may aw, di ma jox lu ma lekk ak lu ma sol, |