Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   À    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

39  GEN 2:8  Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind.
41  GEN 2:10  Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddlikoo, def ñeenti wal.
46  GEN 2:15  Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm.
79  GEN 3:23  Ba loolu amee Yàlla Aji Sax ji génne ko toolub Àjjana, muy bey suuf, si ñu ko sàkke.
80  GEN 3:24  Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund.
96  GEN 4:16  Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku.
342  GEN 14:5  Ca déwén sa Kedorlamer ak buur ya faroon ak moom, dem dàq Refayeen ña ca Àsterot Karnayim, ak Suseen ña ca Am, ak Emeen ña ca jooru Kiryaatayim,
774  GEN 27:46  Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!»
1408  GEN 46:21  Doomi Beñamin yu góor ñoo di Bela ak Beker ak Asbel ak Gera ak Naaman ak Eyi ak Ros ak Muppim ak Uppim ak Àrd.
1989  EXO 17:5  Aji Sax ji ne Musaa «Àndal ak ñenn ci magi Israyil, nga jaar ci kanam mbooloo mi, yóbbaale yet, wa nga dóoroon ca dexu Niil ga. Ŋàbb ko ci sa loxo te dem.
2079  EXO 21:1  Aji Sax ji teg ca ne: «Àttey yoon yii, nanga leen ko jox:
2455  EXO 32:16  Àlluwa ya, liggéeyu Yàllaa, mbind ma di mbindum Yàlla mu ñaase ca kaw àlluwa ya.
3297  LEV 19:15  «Buleen safaan dëgg cib àtte. Buleen far néew-ji-doole te buleen far boroom doole. Àtteleen seen moroom ci dëgg.
4337  NUM 20:25  Àndal ak Aaróona ak doomam Elasar, nga yéege leen ca kaw tundu Or.
4411  NUM 22:35  Malaakam Aji Sax ji ne Balaam: «Àndal ak nit ñi, waaye daal lu ma la waxloo rekk, wax ko.» Balaam nag ànd ak kàngami Balag, dem.
4531  NUM 26:40  Askanu Bela wi sosoo ci Àrd ak Naaman ñoo di làngu Àrdeen ñi, ak làngu Naameen ñi sëtoo ci Naaman.
4822  NUM 34:4  Seen kemu daa dënglu, jaare fa féete yéegub Akerabim bëj-saalum, jaare Ciin nag, dem ba bëj-saalumu Kades Barneya, jëm Àccar Adar ba àgg Asmon.
4827  NUM 34:9  wéyeeti fa, jaare Sifron, jëm Àccar Enan. Loolooy seen kemu bëj-gànnaar.
4828  NUM 34:10  «Rëddleen seen kemu penku, mu dale Àccar Enan ba Sefam,
4849  NUM 35:2  «Santal bànni Israyil ñu sàkkal Leween ñi ci seen céru suuf, ay dëkk yu Leween ñi dëkke. Àllu parlu ya wër dëkk ya it, joxleen ko Leween ñi.
7144  RUT 1:15  Mu ne ko: «Gis nga sa wujju peccorgo waa ngay ñibbi cay bokkam aki yàllaam. Àndal ak moom ñibbi kay!»
7396  1SA 9:3  Mu am bés mbaam yu jigéen yu Kis, baayu Sóol, réer. Kis ne Sóol: «Àndal ak kenn ci surga yi, nga seetali ma mbaam yi.»
7471  1SA 12:9  Seeni maam nag ñoo fàtte seen Yàlla Aji Sax ji, ba tax mu teg leen ca loxol Sisera njiitu xareb dëkk ba ñuy wax Àccor, ak ca loxol waa Filisti, ak ca loxol buuru Mowab, ñooña doon xareek ñoom
7697  1SA 18:19  Ba ñu demee ba wara jox Daawuda, Merab doomu Sóol ja, Àddiryel ma cosaanoo Mewola lañu ko may.
8270  2SA 11:8  Ba loolu wéyee Daawuda ne Uri: «Àggal sa kër nag te jàngu.» Uri bàyyikoo kër Buur, ab yóbbalu Buur topp ca gannaawam.
8343  2SA 13:23  Ba ñu ca tegee ñaari ati lëmm, Absalom dem di watlu ay xaram ca Baal Àccor, fa feggook diiwaanu Efrayim. Absalom daldi fay woo doomi buur yu góor yépp.
8563  2SA 20:6  Daawuda nag ne Abisay: «Seba doomu Bikkri jii de dina nu lor lu raw la nu Absalom loroon. Àndal ak ñenn ci samay dag te dàqi ko, lu ko moy dina gis fu mu làqu ci ay dëkk yu ñu wërale ay tata, ba raw nu.»
8591  2SA 21:8  Buur nag jàpp Armoni ak meneen Mefiboset, te Rispa doomu Aya di seen yaay, Sóol di seen baay. Buur boole ca juróomi góor ña Mikal doomu Sóol di seen yaay, te Àddiryel doomu Barsilay ma dëkk Mewola di seen baay.
8753  1KI 1:33  Buur ne leen: «Àndleen ak samay dag, ngeen waral sama doom Suleymaan ca sama kaw berkelle bu jigéen ba, te yóbbu ko Giyon, bëtu ndox ba.
8944  1KI 7:7  Mu tabax néeg ba ñuy wooye Néegu ngàngune ma walla Àttekaay ba, mu di fa àttee. Mu dare néeg bi banti seedar ci suuf ba ci kaw.
9069  1KI 9:15  Buur Suleymaan dafa dogaloon liggéeyu sañul-bañ bu mu sas ay nit. Ñu tabax kër Aji Sax ji ak këru boppam ak sëkkub Milo ak tatay Yerusalem ya ak dëkk yii di Àccor, Megido ak Geser. Ni mu deme nii la:
9153  1KI 11:42  Àpp bi Suleymaan nguuru fa Yerusalem, ci kaw Israyil gépp, ñeent fukki at la.
9958  2KI 15:29  Ci jamonoy Peka buurub Israyil, Tiglaat Pilser buurub Asiri dikk, nangu dëkk yi ñuy wax Yon ak Abel Bet Maaka ak Yanowa ak Kedes ak Àccor ak diiwaani Galàdd ak Galile ak mboolem réewum Neftali. Mu jàpp waa réew ma, yóbbu Asiri.
12218  EZR 8:12  Ci askanu Asgàdd, Yowanan doomu Àkkatan la, mook téeméeri góor ak fukk (110).
12619  NEH 11:27  ak Àccar Suwal ak Beerseba ak la ko wër.
12625  NEH 11:33  ak Àccor ak Raama ak Gitayim;
13079  JOB 9:24  Àddinaa ngi tege ci loxol ku bon, te Yàllaa ngi muur gëti àttekat yi! Su dul moom ana ku mu doon?
13282  JOB 18:2  Xanaa dungeen noppi mukk? Àndleen ak xel, nu wax.
14248  PSA 22:28  Àddina wërngal këpp ay fàttliku, walbatiku ci Aji Sax ji. Làngi xeet yépp sukkalsi ko.
14868  PSA 61:3  Àll laa lay wooye, sama xol jeex; yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
15402  PSA 89:12  Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
15512  PSA 94:15  Àtte dina dellu laloo njekk, képp ku jub topp ca.
16120  PSA 119:154  Àtte ma, ba jot ma; musal ma, yaa ko dige.
16837  PRO 13:20  Àndal ak ku xelu, sam xel rafet; ku lëngook ub dof, loru.
17942  ISA 10:22  Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.
17998  ISA 13:22  Bukki mooy sabe fa tata ya, till nangu kër yu bakkane ya. Àppu Babilon jege na, ay fanam du fi wees.
18005  ISA 14:7  Àddina yépp a féex, am jàmm, sarxolle jolleendoo.
18168  ISA 24:3  Àddinaa ne duŋŋ duŋŋaaral, dees koo futti ba mu ne furaas! Aji Sax ji kat wax na kàddu gii!
18652  ISA 45:21  Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!
18746  ISA 51:3  Aji Sax jeey dëfal Siyoŋ moos, dëfalaale fépp fu fa dib gent, ba def màndiŋam ni toolub Àjjana, jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji, mbégteek bànneex teew fa, ak cant gu woy feelu.
18789  ISA 53:8  Àtte nañu ko ñàkkal, yóbbu, te ag maasam kenn teewluwu ci ne tooñ gu sama bokk yi tooñ lees ko dagge ci réewum aji dund ñi, te loolu lees ko fàdde.
19521  JER 21:12  Yeen waa kër Daawuda, Aji Sax ji dafa wax ne: Àtte yoon, deeleen ko xëye, di xettli ki ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole, balaa sama mer ne jippét, di tàkk te deesu ko mana fey ndax seen jëf ju bon.
19543  JER 22:20  Aji Sax ji nee: «Yeen waa Yerusalem, yéegileen tundi Libaŋ, yuuxu. Àddooleen fa Basan, xaacu, te yuuxoo fa Abarim, nde seen soppe yépp a rajaxoo!»
20224  JER 49:28  Lu jëm ci Kedar ak nguuri Àccor yi Nabukodonosor buuru Babilon nangu woon, Aji Sax ji dafa wax ne: «Ñokket ci kaw Kedar, ba tas waa penku yooyu,
20226  JER 49:30  Yeen waa Àccor, fëxleen te dawa daw, ruurooji seeni pax.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Nabukodonosor buuru Babilon déy, lalal na leen pexe, mébal leen.
20229  JER 49:33  «Àccor day doon dëkkub till, gental ba fàww; nit du fa dëkk, doom aadama du fa dal.»
20290  JER 51:9  «Bu nu sañoon faj Babilon, mu wér, waaye wérul. Nan ko ba te dem, ku ne ñibbim réewam. Àtteb Babilon kat àgg na asamaan, àkki na fa kaw niir ya.»
20653  EZK 7:7  Yaw nitu réew mee, sànkute dikkal na la. Àpp mat, bés dëgmal, tiitaange wuutu ca mbéx fa kaw tund ya.
20658  EZK 7:12  Àpp mat, bés jege. Bu ca jëndkat tala bég, bu ca jaaykat tala naqarlu! Am sànj a dikkal askan wépp.
21239  EZK 28:13  Yaa nga woon biir Àjjana, toolub Yàlla ba, ràngoo lépp luy gànjari per, sarduwan ak topaas ak jamaa ak kirsolit ak onigsë ak jàspë ak safiir ak emëródd ak eskarbukal. Fegukaay yaak wewukaay ya di wurus, te bés ba ñu la sàkkee, fekk na ñu waajal yooyu.
21308  EZK 31:9  Maa ko rafetale njañam lu sëq, ba garabi Àjjana, toolub Yàlla bi, ñoom ñépp ñee ko!
21315  EZK 31:16  Maa def xeet yi dégg jéllu seedar gi, di lox, ba ma ko tàbbalee njaniiw, boole kook mboolem ñiy tàbbim pax, ba mboolem garabi Àjjana gëna taaru, ak yay ngëneeli Libaŋ, ak mboolem ya màndim ndox, ñoom ñépp di fa muñe seen demin, la seedar ga teew ni ñoom biir xóotey suuf.
21317  EZK 31:18  Ana kan nga neexool teddngaak daraja ci biir garabi Àjjana? Ndaxam dees na la booleek garabi Àjjana, tàbbal xóotey suuf. Yaay goorandook yéefar, yi saamar tëral. Loolooy deminu Firawnaaki gàngooram. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»
21463  EZK 36:35  Su boobaa dees na ne: ‘Xool-leen miim réew, ak mbooy gi mu doonoon, tey mu naat ni toolub Àjjana! Dëkk yeet ay gent la woon, wéet, tojatoo, tey ñu dàbbli lépp, ba dëkke nii!’
21764  EZK 47:16  jaare dëkk yi ñuy wax Berota ak Sibrayim te nekk diggante réewum Damaas ak Amat, jaare Àccer Tikon, fa digalook Oran.
21765  EZK 47:17  Kon kemu googu day dale Géej gu mag ga, ba àgg gox ba ñuy wax Àccar Enan ca penku ba. Kemu bëj-gànnaaram di Damaas ak Amat. Loolooy wàllu bëj-gànnaaram.
21772  EZK 48:1  «Lii mooy limeefu giiri Israyil, ak céru suuf bi giir gu ci nekk di féetewoo. Céru Dan moo féete catu bëj-gànnaar. Kemoom day topp yoonu Ettlon ba Lebo Amat, jàll ba Àccar Enan ga digalook Damaas, Amat féete ko bëj-gànnaar. Suufas Dan day jàpp penku ba sowu, ca géej gu mag ga, di benn pàcc.
21998  DAN 6:25  Ba loolu wéyee Buur joxe ndigal, ñu indi nit ña tuumaaloon Dañeel, ñu tàbbal leen ca kàmbu gaynde ya, ñook seeni doom ak seeni jabar. Àgguñu suuf sax, gaynde ya alawti leen, dammate seen yax yépp.
22044  DAN 8:14  Mu ne ma: «Àpp bi ñaari junni laak ñetti téeméer ciy guddeeki bëccëg. Gannaaw loolu dees na taxawalaat bérab bu sell bi.»
22140  DAN 11:35  Ñenn ci boroom xel yu rafet yi dinanu jaare ci nattu yu leen di sellal, fóot leen ba ñu set wecc, ba keroog mujug jamono. Àpp ba nag des na.
22383  JOL 2:3  Lu leen jiitu, sawara lekk; lu leen topp, ag daay xoyom. Ni toolub Àjjana la réew mi ci seen kanam di mel, ñu won ko gannaaw, muy màndiŋ mu wéet, te kat dara du leen rëcc.
22426  JOL 4:14  Ndaw gàngoori gàngoor ca xuru Àtte ba, nde bésub Aji Sax jee dëgmal ca xuru Àtte ba!
22746  MIC 7:13  Àddina ab gent lay doon ndax ñi ko dëkke, muy añub seeni jëf.
22913  HAG 1:4  «Àpp bi daal yeen la jotal, ba ngeen dëkke biir kër yu ay xànq lale, te kër gii dib gent?
23040  ZEC 7:9  «Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Àtteb dëgg, nangeen ko àttee, te ngor ak yërmande it, deeleen ko jëflantee.
25229  LUK 6:14  Simoŋ mi Yeesuy wooye itam Piyeer, ak Àndre mi bokk ak Piyeer ndey ak baay, ak Yanqóoba ak Yowaan, ak Filib ak Bartelemi,
25760  LUK 18:3  Ab jëtun a nga woon ca dëkk boobee. Daan na ñëw ca moom, naan ko:Àtte ma ak sama jotewaale!”
25761  LUK 18:4  Àttekat ba bañ na ay yoon, waaye gannaaw gi mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla, yéguma nit,
26047  LUK 23:43  Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»
27005  ACT 1:13  Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca, ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ farlukatu moom-sa-réew ba, ak Yuda doomu Yanqóoba.
27175  ACT 6:5  Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit kufeese ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas, ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut.
27388  ACT 11:12  Noo gi nag ne ma:Àndal ak ñoom, te bul nàttable.” Juróom benni bokk yii ngeen di gis ñoo ma gunge, nu dem ba dugg ca kër Korney.
27395  ACT 11:19  Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.
27396  ACT 11:20  Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu.
27398  ACT 11:22  Ba mbir ma siiwee, ba mbooloom gëmkati Yerusalem jot ca, dañoo yebal Barnaba ca Àncos.
27402  ACT 11:26  Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.
27403  ACT 11:27  Ci fan yooyu la ay yonent jóge Yerusalem, dikk Àncos.
27432  ACT 13:1  Ca biir mbooloom gëmkat, ña woon ca dëkk ba ñuy wax Àncos, amoon na ay yonent ak ay jànglekat: ñuy Barnaba, ak Simeyon mi ñu dippee Ñuule, ak Lusiyus mi bawoo Siren, ak Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom Galile, ak Sóol.
27445  ACT 13:14  Ci kaw loolu, ñoom ñu jóge Perge, jàll ba Àncos ca diiwaanu Pisidi. Ñu dem jàngu ba, dugg, toog ca bésub Noflaay ba.
27502  ACT 14:19  Ci kaw loolu ay Yawut yu jóge Àncos gu Pisidi ak Ikoñum, fexe ba fàbbi mbooloo ma, daldi dóor Póol ay doj, diri ko ba génne ko dëkk ba, yaakaar ne dee na.
27504  ACT 14:21  Gannaaw ba ñu xamlee fa Derbe xibaaru jàmm bi, ba am fa taalibe yu bare, dañoo dellu Listar ak Ikoñum ak Àncos gu Pisidi.
27509  ACT 14:26  Foofa lañu dugge gaal, dellu Àncos gu Siri, ga ñu leen dénke woon Yàlla ciw yiwam, ngir liggéey ba ñu sottal, ba délsi noonu.
27512  ACT 15:1  Ñenn nit ñu bàyyikoo Yude dikk Àncos, ñoo doon digal bokki taalibe yi, ne leen: «Su ngeen xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, dungeen mana mucc.»
27513  ACT 15:2  Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnaba séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnaba, ak ñenn ca gëmkati Àncos, ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu, ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
27533  ACT 15:22  Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnaba. Ñooñoo di Yuda, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.
27534  ACT 15:23  Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.
27541  ACT 15:30  Ba loolu amee ñu tàggtoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
27546  ACT 15:35  Póol ak Barnaba nag des Àncos. Ñu ànd ak ñeneen ñu bare, di jàngle ak a xamle kàddug Boroom bi.
27588  ACT 16:36  Boroom kaso ba àgge Póol ndigal la, ne ko: «Àttekat yi kat ñoo fi yeble, ne ñu yiwi leen. Kon nag man ngeena génn te dem ak jàmm.»