559 | GEN 22:11 | Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» |
1788 | EXO 10:10 | Firawna ne leen: «Ãa, yal na leen Aji Sax ji saxoo taxawu walla, ndegam maa leen di bàyyi moos, ngeen dem, yóbbaale seen njaboot! Xam ngeen ne naruleen njub de. |
4046 | NUM 11:21 | Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm! |
7197 | RUT 4:5 | Mu ne ko: «Ãa bés boo jëndee suuf si ci Nawmi nag, yaay denc Ruut ndawas Mowabeen, sa doon soxnas ndem-si-yàlla si, ndax nga mana lawal askanam, ba du fey, boole ci sàmmal leen seen alal.» |
7878 | 1SA 25:14 | Ci biir loolu kenn ca surga ya wax Abigayil jabaru Nabal, ne ko: «Ãa, Daawuda de moo yebal ay ndaw yu jóge ca màndiŋ ma, ngir nuysi sunu sang, waaye moom, da leena jànni. |
8574 | 2SA 20:17 | Yowab dem ba ca moom, ndaw sa ne ko: «Yaa di Yowab?» Mu ne ko «Waaw.» Mu ne ko «Sang bi, dama ne...» Mu ne ko: «Ãa.» |
9474 | 1KI 21:20 | Axab ne Ilyaas: «Ãa, noon bi, gisati nga ma?» Ilyaas ne ko: «Gis naa la, ndax dangaa dogu ci def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu. |
9699 | 2KI 6:21 | Buurub Israyil gis leen ne: «Baay Alyaasa, ma rey leen? Ãa, ma rey leen?» |
9717 | 2KI 7:6 | Booba fekk na Boroom bi dégtal waa dalub Siri ba riirum fas yu ànd aki watiiri xare ak gàngoor gu réy, ba tax ñu naan ca seen biir: «Ãa! Loolu de, buuri Etteen ñaak buuri Misraa, Buurub Israyil fey leen, ngir ñu songsi nu!» |
12779 | EST 4:13 | Mardose dellu yónnee ne ko: «Ãay! Yaa ngi kër buur de! Waaye bul defe ne man ngaa mucc, yaw doŋŋ, ci mboolem Yawut yi. |
12819 | EST 7:8 | Ci kaw loolu Buur bàyyikoo ca tóokër ba, délsi ca ëttu bernde ja, fekk Aman di sukk ca lal ba Esteer tëdd. Buur ne: «Ãa! Ba ci yekktaan Lingeer nag, te ma nekk ci biir kër gi?» |
13378 | JOB 21:19 | Ãa ku bon daal ay tooñ, Yàlla dencal doomam añ ba? Ki tooñ kay, na ko fey, mu xam, |
19956 | JER 37:13 | Ba mu demee ba tollook buntu Beñamin, daje faak njiitu dag ya, Irya doomu Selemya doomu Anaña. Irya taxawal Yonent Yàlla Yeremi, ne ko: «Ãa, waa Babilon nga daw jëm!» |
20246 | JER 50:11 | «Ãa yeen waa Babilon, yeena sëxëtoo xeet wi ma séddoo, di ko bégeek a bànneexoo, di bajantu ni nag wuy bàcc pepp, di ŋexal ni naaru góor? |
20322 | JER 51:41 | «Ãa! Ana nees mana nangoo Sesag? Nees mana tege loxo ki àddina sépp di kañ? Ana nu Babilon mana gente fi digg xeet yi? |
20612 | EZK 4:14 | Ma ne ko: «Ãhã! Boroom bi Aji Sax ji, man de masumaa sobeel sama bopp. Muy lu médd, di lu aw rab fàdd, masuma koo lekk ba may gone ba tey. Wenn yàpp wu daganul masula dugg sama gémmiñ.» |