864 | GEN 30:33 | Ëllëg aki sibbir booy seetsi sama peyoor, sama njubtee may layool: lépp lu toddewul te tippantewul ci biir bëy yi ak lu ñuulul ci mburt yi, boo ko gisee ci man, càcc la.» |
1159 | GEN 39:9 | Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?» |
1734 | EXO 8:19 | te maay musal sama ñoñ ci musiba moomuy dal saw askan. Ëllëg firnde jooju dina am.’ ”» |
1748 | EXO 9:5 | Aji Sax ji nag jàpp na bés, nee na: «Ëllëg maay def loolu ci réew mi.» |
1993 | EXO 17:9 | Musaa ne Yosuwe: «Tànnal nu ay xarekat te nga dem xeex ak Amaleg. Ëllëg dinaa taxaw ca kaw tund wa, ŋàbb yetu Yàlla wi ci sama loxo.» |
2444 | EXO 32:5 | Aaróona gis la xew, daldi tabax ci kanam sëllu wi ab sarxalukaay. Mu daldi yéene, ne: «Ëllëg màggal la, ñeel Aji Sax ji.» |
4596 | NUM 28:17 | Ëllëg sa, fukki fani weer woowu ak juróom, di màggal; diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir lees cay lekk. |
5711 | DEU 30:1 | Ëllëg nag, su mboolem mbir yooyu dikkee fi seen kaw, muy barke yi, di alkànde yi ma teg fi seen kanam, su boobaa bu ngeen délloosee seen xel foofa mu leen fekk, ca biir mboolem xeet ya leen seen Yàlla Aji Sax ji dàq jëme, |
7457 | 1SA 11:10 | Ñu wax Amoneen ña, ne leen: «Ëllëg dinanu dikk, fekksi leen.» |
7737 | 1SA 20:5 | Daawuda ne Yonatan: «Xanaa lenn. Ëllëg la màggalu Terutel weer wi, te man, manumaa ñàkka toog ak Buur, ngir lekk. Waaye may ma, ma làquji àll ba, ba gannaaw ëllëg ca ngoon. |
7750 | 1SA 20:18 | Yonatan dellu ne ko: «Ëllëg ci màggalu Terutel weer wi, sag wuute dina fés, ndax sa toogu ba mooy wéet. |
12795 | EST 5:12 | Aman teg ca ne: «Te kat amul ku Lingeer Esteer woo, mu wara ànd ak Buur ca bernde ja muy def, ku moy man. Ëllëg man la woo maak Buur. |
18581 | ISA 43:6 | Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!” ne bëj-saalum: “Bul téye!” Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi, te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina. |
19538 | JER 22:15 | «Ëpplante banti seedar da laa def buur? Sa baay daawul lekk ak a naan? Teewu koo jëfe dëgg ak yoon, muy njiglaayam. |
27703 | ACT 20:9 | Ci biir loolu ab xale bu góor bu ñuy wax Ëtikus ma nga tooge kéméju palanteer ba. Ngëmment dab ko, te kàddug Póol ga yàgg lool. Ay nelaw nag jàpp waa ji, mu xàwwikoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee. |
29881 | 2TI 1:5 | Maa ngi fàttliku ngëm gu dëggu gi ci yaw, te jëkkoona nekk ci sa maam ju jigéen Lowis, ak sa yaay Ënis, te mu wóor ma ne moom nga saxoo itam. |
29958 | 2TI 4:21 | Gaawala ñëw, balaa seddub lolli di jam. Ab nuyoo ñeel na la, tukkee ci Ëbulus ak Pudeñsë ak Linus ak Këlójaa ak bokk yépp. |
31158 | REV 22:9 | Mu ne ma: «Ëpp naa def, sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokki yonent yeek ñiy sàmm kàdduy téere bii. Sujjóotalal Yàlla.» |