Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   ë    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

2  GEN 1:2  Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi.
4  GEN 1:4  Yàlla gis ne leer gi lu baax la, mu xàjjale leer ak lëndëm.
5  GEN 1:5  Yàlla tudde leer gi bëccëg, lëndëm gi guddi. Ngoon jot, suba dugg, muy bés ba jëkk.
9  GEN 1:9  Yàlla ne: «Na ndox, mi asamaan tiim, gëndoo benn bérab, ba joor gu wow feeñ.» Mu daldi nekk noona.
10  GEN 1:10  Yàlla tudde joor gu wow gi suuf, ndox mi gëndoo, mu tudde ko géej. Yàlla gis ne baax na.
14  GEN 1:14  Yàlla ne: «Na am ay leer ci asamaan, ngir xàjjale guddi ak bëccëg, te doon ay tegtal, yuy ràññle jamono yi, tey takk bés yi ak at yi.
16  GEN 1:16  Yàlla sàkk ñaari leer yu mag, gi gëna mag yilif bëccëg, gi gëna ndaw yilif guddi; mu sàkk it biddiiw yi.
18  GEN 1:18  ñuy yore guddi ak bëccëg, tey xàjjale lëndëm ak leer. Yàlla gis ne baax na.
26  GEN 1:26  Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.»
28  GEN 1:28  Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.»
32  GEN 2:1  Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat.
37  GEN 2:6  Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp.
38  GEN 2:7  Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
39  GEN 2:8  Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind.
42  GEN 2:11  Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma,
43  GEN 2:12  di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë.
44  GEN 2:13  Ñaareelu dex ga di Giyon, wër réewu Kuus mépp;
46  GEN 2:15  Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm.
53  GEN 2:22  Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko.
54  GEN 2:23  Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.»
57  GEN 3:1  Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
61  GEN 3:5  Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni bët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.»
62  GEN 3:6  Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk.
63  GEN 3:7  Seeni bët daldi ubbiku, ñu xam ne yaramu neen lañu def. Ba mu ko defee ñu ràbb xobi garabu figg, gemboo.
70  GEN 3:14  Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: «Gannaaw def nga loolu, yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp.
71  GEN 3:15  Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
72  GEN 3:16  Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.»
73  GEN 3:17  Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp.
75  GEN 3:19  saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»
80  GEN 3:24  Da koo dàq, ba noppi teg ca penkub toolu Àjjana ba ay malaakay serub, boole ca saamar buy xuyy-xuyyi, tey dem ak a dikk, di wattu yoon, wa jëm ca garab gay taxa dund.
81  GEN 4:1  Gannaaw loolu Aadama dëkkoo na soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu Aji Sax ji.»
84  GEN 4:4  Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel,
87  GEN 4:7  Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»
92  GEN 4:12  Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.»
94  GEN 4:14  Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.»
96  GEN 4:16  Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku.
97  GEN 4:17  Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog.
99  GEN 4:19  Lemeg nag jël ñaari jabar, aawo bi tudd Ada, ñaareel bi di Silla.
102  GEN 4:22  Silla moom jur Tubal Kayin miy tëgg lépp luy jumtukaayu xànjar ak weñ. Tubal Kayin am na jigéen bu tudd Naama.
105  GEN 4:25  Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.»
135  GEN 5:29  Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.»
140  GEN 6:2  ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar.
146  GEN 6:8  Waaye fekk na Aji Sax ji xool Nóoyin bëti yërmande.
149  GEN 6:11  Booba fekk na àddina yàqu, te fees ak ay, Yàlla teg ci bëtam.
150  GEN 6:12  Yàlla gis ne àddina yàqu na, ndaxte jëfi ñépp a bokk ñaaw fi kaw suuf.
155  GEN 6:17  «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee.
156  GEN 6:18  Waaye dinaa fas kóllëre ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom.
158  GEN 6:20  Xeetu picc wu ci nekk ak xeetu bàyyima wu ci nekk ak wépp xeetu rab wuy raam ci suuf, dina def ñaar, ñëw ci yaw, ba raw.
161  GEN 7:1  Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.
164  GEN 7:4  Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»
166  GEN 7:6  Bi mbënn miy ñëw ci àddina, booba fekk na Nóoyin am juróom benni téeméeri at.
167  GEN 7:7  Nóoyin dugg na ca gaal ga, ànd ak ay doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya, ngir mucc ca ndoxu mbënn ma.
170  GEN 7:10  Ba juróom ñaari fan wéyee nag, ndoxu mbënn ma agsi ci kaw suuf.
171  GEN 7:11  At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet,
172  GEN 7:12  taw biy sottiku ci suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg.
177  GEN 7:17  Mbënn ma nag di wal ci àddina diiru ñeent fukki fan. Ndox ya di yokku, gaal gay jóg, ba tëmb, tiim suuf lu sore.
178  GEN 7:18  Ma ngay gën di yokku, tey baawaan ci kaw suuf, ba gaal ga tëmb, di dem ca kaw ndox ma.
179  GEN 7:19  Ndox ma di walangaan, ba mëdd tund yu kawe ya fépp fu asamaan tiim.
180  GEN 7:20  Muy yokku, di yokku, ba gëna kawe tund ya lu mat fukki xasab ak juróom.
186  GEN 8:2  Bëti ndox ya ca xóote ya dafa taxaw, bunti ndoxi asamaan tëju, taw bi dal.
187  GEN 8:3  Ci kaw loolu ndox mi taa ci suuf di wàññiku. Bi téeméeri fan yi ak juróom fukk matee nag, ndox ma gëna néew.
197  GEN 8:13  At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at ak benn, keroog benn fanu weer wa jëkk, ndox ma taa woon ca suuf daldi fendi. Nóoyin ubbi kubeer ga, xool, ba gis ne kaw suuf sépp wow na.
205  GEN 8:21  Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe.
206  GEN 8:22  Li feek suuf di suuf, dootu jiwooy dakk mbaa ngóob, te du sedd aku tàngoor, du nawet it mbaa noor, mbaa guddeek bëccëg.»
208  GEN 9:2  Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo.
215  GEN 9:9  «Bés niki tey fasal naa sama bopp kóllëre sama diggante ak yeen ak seen askan,
217  GEN 9:11  Ni may faseek yeen kóllëre nii la: Deesatul boole bindeef yépp, faat ci mbënn mukk. Du menn mbënn mu deeti faagaagal àddina.»
218  GEN 9:12  Yàlla neeti: «Kóllëre gi may fas ak yeen ak mboolem mbindeef mu ànd ak yeen, day sax ba fàww te liy màndargaam mooy lii:
219  GEN 9:13  def naa sama xon ci niir yi, muy màndargaal kóllëre, gi dox sama diggante ak àddina.
221  GEN 9:15  damay daldi xalaataat kóllëre, gi ma fas sama digganteek yeen ak mboolem xeeti bindeef, su ko defee ndox dootu sabab mbënn muy faagaagal lépp luy dund.
222  GEN 9:16  Xon gi day nekk ci biir niir yi, ma di ko gis, di xalaat kóllëre, gi ma fas fàww, sama diggante, man Yàlla, ak mboolem xeetu mbindeef mu nekk ci kaw suuf.»
223  GEN 9:17  Ci kaw loolu Yàlla ne Nóoyin: «Loolu mooy màndargaal sama kóllëre, gi ma fas ak mboolem mbindeef mu nekk ci kaw suuf.»
226  GEN 9:20  Nóoyin ab beykat la woon. Mu nekk nag ci njëmbatum reseñ.
227  GEN 9:21  Mu am bés mu naan biiñ, ba màndi, tëdd ci xaymaam, daldi sàgganu.