Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   ó    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

2  GEN 1:2  Suuf nag daa maase woon te wéet, lëndëm muur ndox mu xóot mi, lale ca kaw, Noowug Yàlla di wër, tiim ndox mi.
23  GEN 1:23  Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróomeel ba.
27  GEN 1:27  Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, góor ak jigéen la bind.
31  GEN 1:31  Yàlla nag gis li mu def lépp, fekk lépp baax lool. Ngoon jot, suba dugg, muy bésub juróom benneel ba.
33  GEN 2:2  Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp.
34  GEN 2:3  Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp.
38  GEN 2:7  Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
52  GEN 2:21  Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux.
54  GEN 2:23  Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.»
55  GEN 2:24  Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux.
56  GEN 2:25  Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa.
57  GEN 3:1  Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
81  GEN 4:1  Gannaaw loolu Aadama dëkkoo na soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu Aji Sax ji.»
85  GEN 4:5  te nangulul Kayin. Kayin nag mer lool, ba ne fóññ.
86  GEN 4:6  Aji Sax ji ne Kayin: «Lu la taxa mer, ba ne fóññ nii?
88  GEN 4:8  Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko.
91  GEN 4:11  Léegi dinga alku, ba suuf dummóoyu la, moom mi ubbi gémmiñam, naan sa deretu rakk, ji nga tuur.
95  GEN 4:15  Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey.
96  GEN 4:16  Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku.
97  GEN 4:17  Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog.
103  GEN 4:23  Lemeg nag ne ay soxnaam: «Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg, teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla. Nit a ma gaañ, ma bóom, goneg jàmbaar dóor ma, ma faat.
104  GEN 4:24  Kayin kay, lees di feyul juróom ñaari yoon, ne, bu dee Lemeg mii, muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.»
105  GEN 4:25  Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.»
106  GEN 4:26  Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal.
108  GEN 5:2  góor ak jigéen la sàkk, barkeel leen, tudde leen Nit, keroog ba mu leen sàkkee.
109  GEN 5:3  Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set.
110  GEN 5:4  Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
111  GEN 5:5  Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu.
112  GEN 5:6  Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos.
113  GEN 5:7  Enos juddu na, Set dundaat juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñaar (807), amaat doom yu góor ak yu jigéen.
114  GEN 5:8  Kon Set dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk ak ñaar (912), doora faatu.
115  GEN 5:9  Enos nag am na juróom ñeent fukki at (90), doora jur Kenan.
116  GEN 5:10  Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen.
117  GEN 5:11  Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu.
118  GEN 5:12  Kenan moomee am na juróom ñaar fukki at (70), doora jur Malaleel.
119  GEN 5:13  Malaleel juddu na, Kenan dundaat juróom ñetti téeméeri at ak ñeent fukk (840), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
120  GEN 5:14  Kon Kenan dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fukk (910), doora faatu.
121  GEN 5:15  Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd.
122  GEN 5:16  Yeredd juddu na, Malaleel dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fanweer (830), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
123  GEN 5:17  Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu.
124  GEN 5:18  Yeredd moomee am na téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (162), doora jur Enog.
125  GEN 5:19  Enog juddu na, Yeredd dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
126  GEN 5:20  Kon Yeredd dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak ñaar (962), doora faatu.
127  GEN 5:21  Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem.
128  GEN 5:22  Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
129  GEN 5:23  Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365).
131  GEN 5:25  Matusalem moomee am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak juróom ñaar (187), doora jur Lemeg.
132  GEN 5:26  Lemeg juddu na, Matusalem dundaat juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (782), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
133  GEN 5:27  Kon Matusalem dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom ñeent (969), doora faatu.
134  GEN 5:28  Lemeg nag am na téeméeri at ak juróom ñett fukk ak ñaar (182), doora jur doom ju góor.
135  GEN 5:29  Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.»
136  GEN 5:30  Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
137  GEN 5:31  Kon Lemeg dund na juróom ñaar téeméeri at ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar (777), doora faatu.
138  GEN 5:32  Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet.
142  GEN 6:4  Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur.
146  GEN 6:8  Waaye fekk na Aji Sax ji xool Nóoyin bëti yërmande.
147  GEN 6:9  Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla.
148  GEN 6:10  Nóoyin nag amoon na ñetti doom yu góor: seeni tur di Sem, Xam ak Yafet.
151  GEN 6:13  Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal.
153  GEN 6:15  Ni nga koy defare nii la. Na guddaayu gaal gi di ñetti téeméeri xasab, yaatuwaay bi di juróom fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab.
156  GEN 6:18  Waaye dinaa fas kóllëre ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom.
157  GEN 6:19  Te xeeti rab yépp nanga ci dugal ñaar ci gaal gi, wu ci nekk, nga def ko góor ak jigéen; su ko defee ngeen ànd mucc.
160  GEN 6:22  Noonu la Nóoyin def. Lépp lu ko Yàlla sant, def na ko.
161  GEN 7:1  Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.
162  GEN 7:2  Xeeti rab yu set yépp yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ak ñaar ci xeeti rab yi setul, te ñuy góor ak jigéen.
163  GEN 7:3  Te it xeetu picc mu nekk yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ngir seen xeet baña fey ci kaw suuf.
164  GEN 7:4  Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»
165  GEN 7:5  Nóoyin daldi def la ko Aji Sax ji sant lépp.
166  GEN 7:6  Bi mbënn miy ñëw ci àddina, booba fekk na Nóoyin am juróom benni téeméeri at.
167  GEN 7:7  Nóoyin dugg na ca gaal ga, ànd ak ay doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya, ngir mucc ca ndoxu mbënn ma.
169  GEN 7:9  ànd nañu ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, def ñaar-ñaar, góor ak jigéen, ni ko Yàlla sante Nóoyin.
170  GEN 7:10  Ba juróom ñaari fan wéyee nag, ndoxu mbënn ma agsi ci kaw suuf.
171  GEN 7:11  At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet,
173  GEN 7:13  Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga,
175  GEN 7:15  Lépp luy boroom bakkan def na ñaar-ñaar, ànd ak Nóoyin, dugg ca gaal ga,
176  GEN 7:16  mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee.