Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   ŋ    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

92  GEN 4:12  Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.»
94  GEN 4:14  Ndegam tey jii danga maa dàq, xañ ma sa jataay, dinaa dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci kaw suuf, te kon ku ma gis rey ma.»
198  GEN 8:14  Keroog ñaar fukki fan ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, ca la suuf si doora wow koŋŋ.
328  GEN 13:9  Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.»
343  GEN 14:6  ak Oreen ña ca seen tund wa ñuy wax Seyir. Da leena dàq ba ca garabu Paran gu mag ga ca wetu màndiŋ ma.
389  GEN 16:7  Ba mu dawee, malaakam Aji Sax ja gis ko fu dend akub bëtu ndox ca màndiŋ ma, mooy bëtu ndox, ba ca yoonu Sur.
457  GEN 18:32  Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.»
528  GEN 21:14  Ca ëllëg sa Ibraayma jóg suba teel, sàkk mburu, booleek mbuusu ndox, jox Ajara, mu gàddu. Mu daldi ko dénk Ismayla, yebal ko, mu dem. Ci kaw loolu muy wëndeelu ca màndiŋu Beerseba.
534  GEN 21:20  Yàlla nag ànd ak Ismayla, muy màgg, dëkk ca màndiŋ ma, di fittkat.
554  GEN 22:6  Ba loolu amee Ibraayma jël mattum saraxu rendi-dóomal ba, yen ko doomam Isaaxa; moom mu ŋàbb la muy taale ak paaka ba ci loxoom, ñu ànd ñoom ñaar.
558  GEN 22:10  Ibraaymaa nga tàllal loxoom, ŋëb paaka, ba muy rendee doom ja.
587  GEN 23:15  «Déglu ma, kilifa gi, suuf suy jar ñeenti téeméeri dogi xaalis doŋŋ du dara ci sama diggante ak yaw; tee nga faa denc sa néew rekk?»
740  GEN 27:12  Xëy na sama baay làmbatu ma de, te kon dina ne njublaŋ laa. Su ko defee ay móolu laay yóbbe sama bopp, waaye du barkeb ñaan.»
799  GEN 29:3  Bu gétt yépp dajaloo foofa, sàmm yi doora àndandoo béraŋ doj wa, mu moy buntu teen ba, ñu wëgg, ba noppi delloo doj wa, mu ubaat teen ba.
804  GEN 29:8  Ñu ne ko: «Dunu ko man mbete gétt yépp daje, nu béraŋ doj wi, ubbi teen bi, doora wëgg gàtt yi.»
806  GEN 29:10  Ba Yanqóoba gisee Rasel, doomu nijaayam Laban, moom ak gàtti nijaayam ya, dafa daagu ba ca teen ba, béraŋ doj wa ko ub, daldi wëgg gàtti Laban.
939  GEN 32:11  Yelloowuma lu gëna tuuti ci sa ngor ak sa worma, gi nga ma won, man sa jaam. Aw yet doŋŋ laa ŋàbboon, ba ma jàllee dexu Yurdan, te yokku naa tey, ba doon ñaari kurél.
953  GEN 32:25  Mu des fa nag moom doŋŋ. Kera la genn góor fanaana bëre ak moom, ba bët set.
1002  GEN 34:21  «Ñii sunuy am-di-jàmm lañu, te gannaaw réew maa ngi ne yàmblaŋ, bàyyileen leen, ñu sanc te dem fu leen neex. Man nanoo jël seen doomi janq te di leen may sunuy doom.
1065  GEN 36:24  Doomi Sibeyon yu góor di Aya ak Ana. Te Ana moomu moo feeñal bëti ndox yu tàng ya ca màndiŋ ma, ba muy sàmm mbaami baayam Sibeyon.
1108  GEN 37:24  Ñu jàpp ko, tàbbal ca biir kàmb ga, fekk mu déy, ba wow koŋŋ.
1236  GEN 41:40  Kon dinaa la may, nga jiite kër buur, te waa réew mépp ci sa waaw lañuy wéy; jal bi ma toog doŋŋ laa lay sute.»
1267  GEN 42:14  Yuusufa ne leen: «Li ma leen wax moo am, ay yëddukat doŋŋ ngeen.
1269  GEN 42:16  Na kenn ci yeen jëli seen rakk, ñu tëj ñi ci des te topp seen wax, ba xam ndax yeena ngi ci dëgg. Su dul dëgg, giñ naa ci Firawna ne ay yëddukat doŋŋ ngeen.»
1335  GEN 44:10  Mu ne leen: «Li ngeen wax yoon la sax, waaye na ki ma ko fekke doŋŋ di sama jaam, su ko defee ñi ci des wàcc.»
1345  GEN 44:20  Ba mu ko defee nu ne la: “Am nanu baay bu màggat. Sunu rakk, ji mu jur te fekk ko di màggat nag, moo ci gën di ndaw. Magam dafa dee, mu des moom doŋŋ ci ndeyam, baayam sopp ko lool.”
1497  GEN 49:23  Ay fittkat a ko toŋal, di ko song ak a fitt.
1498  GEN 49:24  Teewul xalaam ga di wéye daŋ, te la loxo yay dëgërloo mooy loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba, kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israyil,
1558  EXO 2:3  Mu dem nag, ba manatu koo nëbb. Mu wut pañe bu ñu ràbbe barax, fatte ko godoroŋ ak ndàbb, yeb ca liir ba, daldi dem, teg ko ca biir barax, ba ca tàkkal dex, ga ñu naan Niil.
1581  EXO 3:1  Léegi Musaa ngay sàmm gàtti goroom Yettro, sarxalkatu Majan ba. Mu yóbbu jur ga fu sore ca màndiŋ ma, daldi agsi ca suufu tundu Yàlla wa ca Oreb.
1598  EXO 3:18  «Magi Israyil dinañu la déggal, su ko defee nga ànd ak ñoom, dem ca buuru Misra. Waxleen ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi moo nu feeñu. Kon nag ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji ay sarax.”
1602  EXO 3:22  Képp kuy jigéen ci bànni Israyil, na laaj dëkkandoom, laajaale ku dëkk ak dëkkandoom, ay gànjari xaalis, ak gànjari wurus, ak yére yu ngeen di solal seen doom yu góor ak yu jigéen, ba waa Misra ne duŋŋ
1629  EXO 4:27  Ci biir loolu Aji Sax ji wax Aaróona ne ko: «Demal gatanduji Musaa ca màndiŋ ma.» Aaróona dem seeti ko ca tundu Yàlla wa, fekk ko fa, taf ko ca kawam.
1634  EXO 5:1  Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”»
1636  EXO 5:3  Ñu ne ko: «Sunu Yàlla, nun Ebrë yi, moo nu feeñu. Ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji sarax, lu ko moy mu dumaa nu jàngoro mbaa ab xare.»
1702  EXO 7:16  Wax ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi, moo ma yónni ci yaw. Mu di la wax, ne la: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu jaamuji ma ca màndiŋ ma.’ Yaw nag booba ba tey yaa ngi tanqamlu.
1716  EXO 8:1  Ba loolu weesee Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona, ne ko mu ŋàbb yet wi, tàllal loxoom, tiimale ko dex yi, ak yooni ndox yeek déeg yi, ngir indi mbott yi ci biir réewum Misra.»
1720  EXO 8:5  Musaa ne Firawna: «Saa yu la neexee rekk, sang bi. Wax ma kañ laa lay ñaanal, yaw ak say dag ak sa waa réew, ngir jële fi mbott yi, ñu tàggook yeen, génn seeni kër, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.»
1722  EXO 8:7  Mbott yi dinañu jóge sa kër, teqlikook yeen, yaak say dag ak sa waa réew, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.»
1728  EXO 8:13  Ñu def loola, Aaróona tàllal loxoom, ba mu ŋàbbe yet wa, dóor ca pënd ba, mu doon ay rayentaan yu song nit ak rab; pëndu suuf sépp a defi rayentaan ca réewum Misra gépp.
1738  EXO 8:23  Kon kay danoo wara génn, topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, rendili fa sunu Yàlla Aji Sax ji sarax, ni mu nu ko sante.»
1739  EXO 8:24  Firawna àddu ne: «Dinaa leen may, ngeen dem ca màndiŋ ma, rendili seen Yàlla Aji Sax ji sarax, waaye buleen sore lool. Ñaanal-leen ma nag.»
1769  EXO 9:26  Diiwaanu Gosen, ga bànni Israyil dëkkoon doŋŋ, moo mucc ca tawub yuur ba.
1828  EXO 12:11  Ni ngeen koy lekke nag, nii la: bu ngeen koy lekk, dangeen di takku, sol seeni dàll, ŋàbb seen yet, te ngeen lekk ko ci lu gaaw. Loolu gàttu saraxu bésub Mucc ba lay doon, ñeel Aji Sax ji.
1833  EXO 12:16  Bés bu jëkk bi nangeen ci amal ndaje mu sell. Juróom ñaareelu bés ba itam nangeen ca amal ndaje mu sell; deesul liggéey lenn ci yooyu bés, lu moy ngeen togg ñam wu ñépp lekk. Loolu doŋŋ lees ciy mana def.
1886  EXO 13:18  Moo tax Yàlla wiiriloo mbooloo ma, ñu jaare ca màndiŋ ma, jëm ca géeju Barax ya. Ba mu ko defee bànni Israyil fagaru ba jekk, daldi génn Misra.
1888  EXO 13:20  Ñu bàyyikoo Sukkóot, dal Etam ca wetu màndiŋ ma.
1893  EXO 14:3  Su ko defee Firawna da naan: “Bànni Israyil de dañoo réer ci àll bi, ba faf keppu ci màndiŋ mi.”
1901  EXO 14:11  Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?
1902  EXO 14:12  Xanaa du lii lanu la waxoon ca Misra? Noon nanu la, nga bàyyi nu, nu surgawu waa Misra, ndax surgawu waa Misra moo nu gënal nu dee ci màndiŋ mi!»
1929  EXO 15:8  Nga wal sag noo, ndox ya tegloo, wal ma ne sàtt, jaloo jalu, ndoxi xóotey géej way deeŋ!
1941  EXO 15:20  Yonent Yàlla Maryaama, jigéenub Aaróona nag ŋàbb tabala, jigéen ñépp topp ko, génn di fecc, tabala ya jiin.
1943  EXO 15:22  Gannaaw loolu Musaa jële bànni Israyil géeju Barax ya, ñu wéy, wuti màndiŋ, ma ñuy wax Sur. Dox nañu ñetti fan ca màndiŋ ma, gisuñu ndox.
1945  EXO 15:24  Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?»
1949  EXO 16:1  Gannaaw gi mbooloom bànni Israyil gépp bàyyikoo fa Elim, dem, ba keroog fukki fan ak juróom, ca weer wa topp ca wa ñu génne réewum Misra, ñu doora agsi màndiŋu Ciin diggante Elim ak Sinayi.
1950  EXO 16:2  Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.
1951  EXO 16:3  Ña nga naa leen: «Céy ngalla nun, su nu sañoon dee, Yàlla moom nu ca réewum Misra, fa nu daan uufe cini yàpp, ñam wa ne gàññ, nu suur këll. Yeena nu indi ba ci màndiŋ mii, ngeen nara xiifloo mbooloo mii mépp, ba ñu dee.»
1955  EXO 16:7  te bu bët setee dingeen gis manoorey Aji Sax ji, ndaxte dégg na ngeen di diiŋat Aji Sax ji, ndax nun kat tekkiwunu dara, ba ngeen di nu diiŋat.»
1956  EXO 16:8  Musaa teg ca ne: «Moo tax Aji Sax ji dina leen jox yàpp wu ngeen lekk ngoon, te bu bët setee mu jox leen ñam wu leen reggal, ndax Aji Sax jee dégg ngeen di ko diiŋat. Nun lu nu ci? Du nun ngeen di diiŋat waaye yeen ak Aji Sax ji la.»
1957  EXO 16:9  Ba loolu wéyee Musaa ne Aaróona: «Waxal mbooloom bànni Israyil gépp, ne leen ñu dem ba ca kanam Aji Sax ji, ndaxte dégg na seeni diiŋat.»
1958  EXO 16:10  Naka la Aaróona di wax ak mbooloom Israyil mépp, ñu jekki ne gees ca màndiŋ ma, daldi yem ci aw niir, leeru Aji Sax ji di ca feeñ.
1960  EXO 16:12  «Dégg naa diiŋati bànni Israyil. Wax leen ne leen, diggante ngoon ak jant bu so, dinañu lekk yàpp, te bu bët setee ñu lekk aw ñam, ba regg, ndax ñu xam ne man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.»
1962  EXO 16:14  Naka la lay ba bàcc, ñu jekki gis lu sew lale ca màndiŋ ma, def fepp yu sew ca biir, te mel ni tawub yuur, tege ca suuf.
1980  EXO 16:32  Ci biir loolu Musaa ne: «Aji Sax ji dafa santaane ne: “Sàkkleen ci andaar, denc ngir seeni sët ak seeni sëtaat. Su ko defee ñu gis ñam, wi ma leen daan leel ca màndiŋ ma, gannaaw ba ma leen génnee réewum Misra.”»
1985  EXO 17:1  Gannaaw loolu mbooloom bànni Israyil gépp bàyyikoo màndiŋu Ciin, di dox ak a taxaw, ci ndigalal Aji Sax ji. Ñu dem ba Refidim, dal fa. Foofa nag mbooloo ma amuñu woon ndox mu ñu naan.
1993  EXO 17:9  Musaa ne Yosuwe: «Tànnal nu ay xarekat te nga dem xeex ak Amaleg. Ëllëg dinaa taxaw ca kaw tund wa, ŋàbb yetu Yàlla wi ci sama loxo.»
2005  EXO 18:5  Yettro, gorob Musaa nag yóbbul Musaa soxnaam aki doomam ba ca màndiŋ ma, fa Musaa dal ca kaw tundu Yàlla wa.
2018  EXO 18:18  Dangay dàjji sa bopp doŋŋ, dàjji mbooloo mi, ndax yen bee diis, ba ëpp ci sa kaw; doo ko àttan yaw rekk.
2028  EXO 19:1  Keroog benn fan ca ñetteelu weer wa, gannaaw ba ñu génnee Misra, ca lañu agsi màndiŋu Sinayi.
2029  EXO 19:2  Fekk na ñu bàyyikoo Refidim, doora duggsi màndiŋu Sinayi, daldi dal ca màndiŋ ma. Israyil a nga daloon foofa janook tund wa.
2040  EXO 19:13  Bu loxo laal kooka, waaye nañu ko dóor ay doj ba mu dee, mbaa ñu jam ko. Su dee nit, su dee mala, bumu dundati.” Bu liit gi jibee doŋŋ nag lañuy doora mana dem ba ca tund wa.»
2081  EXO 21:3  Su fekkee ne ba muy dugg njaam, moom doŋŋ la woon, moom doŋŋ ay moom boppam; su ko fekkee mu am jabar, na jabaram ànd ak moom, ñu moom seen bopp.
2082  EXO 21:4  Su fekkee ne sangam a ko may jabar, ndaw si am ak moom ay doom, jabar jeek doomam yu góor mbaa yu jigéen, sang bee leen di moom. Moom ci boppam doŋŋ ay moom boppam.
2111  EXO 21:33  «Su fekkee ne nit dafa ubbi kàmb gu ube woon, mbaa mu gas kàmb, wacc ko mu ne ŋàpp, ba nag mbaa mbaam daanu ci,
2141  EXO 22:26  Moom doŋŋ la am ci yére, di ko sànge yaramam; su ko ñàkkee, lu muy sàngoo ba tëdd? Te su ma wooyee wall kat, dinaa ci dégg, ndax man Boroom Yërmande laa.
2176  EXO 23:31  «Maa leen di dogal kemug suuf gu dale géeju Barax yi, ba géeju waa Filisti, daleeti ca màndiŋ ma, ba ca dexu Efraat, ndax maay teg waa réew mi ci seeni loxo, ngeen dàq leen.
2305  EXO 28:11  Ni ko ab liggéeykat bu farewoo mbindum doj di defe, ni lañuy ñaase turi doomi Israyil yu góor ci kaw ñaari per yi, mu mel ni ni ñuy ñaase xàmmikaay yi ñuy torloo, te nañu we per yi ci ay ŋankukaayi wurus.
2307  EXO 28:13  «Sàkkal ay ŋankukaayi wurus,
2308  EXO 28:14  ak ñaari caqi wurusu ngalam, bu ci nekk nga rawaase ko nig buum, ba noppi nga we caq yu rawaasoo yooyu ci ŋankukaay yi.
2310  EXO 28:16  Ab kaare bu ñu lem lay doon, guddaay bi di ŋaraleb baaraamu déy ak digg, yaatuwaay bi di ŋaraleb baaraamu déy ak digg.
2314  EXO 28:20  ñeenteelu làng gi di peru kirsolit ak peru onigsë ak peru jàspë, te per bu ci nekk, ŋankukaayu wurus lees koy wewe.
2319  EXO 28:25  Yeneen ñaari cati buumi wurus yi, nga we leen ci ñaari ŋankukaay, yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, ci kanam.
2417  EXO 30:34  Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Wutal nag xeeñal yii: ndàbbu estaagte, ak ndàbbi galbanom, ak xori onigsë yu xeeñ, ak cuuraay-libaŋ lu raxul, te yooyu yépp tolloo dayo.
2458  EXO 32:19  Ba Musaa jubee dal ba, ba gis sëllu wa ak pecc ma, mer mu ne jippét tàkk la ko def, mu sànni àlluwa ya mu ŋàbboon, mu ne tasar ca suufu tund wa.
2472  EXO 32:33  Aji Sax ji ne Musaa: «Ki ma moy, kooku doŋŋ laay far ci sama téere.
2501  EXO 34:4  Musaa nag yett ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya, ba noppi teela xëy, yéegi ca tundu Sinayi, na ko ko Aji Sax ji sante. Ma nga ŋàbb ñaari àlluway doj ya.
2526  EXO 34:29  Ci kaw loolu Musaa wàcc tundu Sinayi, ŋàbb ñaari àlluway seede sa. Naka la Musaa di wàcce ca tund wa, deru kanam ga di lerxat te yégu ko. Booba ñaaroom baak Yàlla moo waral loola.
2629  EXO 37:24  Benn talaŋu wurusu ngalam, yemook fanweeri kilo, ci la sàkk tegukaayu làmp bi ak mboolem ay jumtukaayam.
2658  EXO 38:24  Wurus wi dem ci liggéey bi bépp, mboolem liggéeyu bérab bu sell bi, te muy wurus wu ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, juróom ñetti téeméeri kilo ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar la (877), ak ñetti téeméeri garaam (300), yemook ñaar fukki talaŋ ak juróom ñeent, ak juróom ñaar téeméer ak fanweeri (730) siikal ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi.
2659  EXO 38:25  Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi,
2661  EXO 38:27  Ñetti junniy (3 000) kiloy xaalis, di téeméeri talaŋ, ñeel móolub teguy bérab bu sell bi, ak teguy rido bi. Muy téeméeri tegu ci ñetti junniy kilo, di fanweeri kilo ci benn tegu, muy téeméeri tegu ci téeméeri talaŋ, benn talaŋ ci benn tegu.
2663  EXO 38:29  Xànjar bi ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, ñaari junniy kilo ak téeméer ak ñaar fukk ak ñeent la (2 124), yemook juróom ñaar fukki (70) talaŋ ak ñaari junneek ñeenti téeméeri (2 400) siikal.
2671  EXO 39:6  Ci kaw loolu ñu we peri onigsë yi, fege per yi ŋankukaayi wurus, daldi ciy ñaas turi doomi Israyil yu góor, noonu ñuy ñaase xàmmikaay yi ñuy torloo.
2674  EXO 39:9  Ab kaare bu ñu lem lañu ko def, guddaay bi, gannaaw bu ñu ko lemee, di ŋaraleb baaraamu déy ak digg, yaatuwaay bi di ŋaraleb baaraamu déy ak digg.
2678  EXO 39:13  ñeenteelu làng gi di peru kirsolit ak peru onigsë ak peru jàspë, te per bu ci nekk ŋankukaayu wurus lees ko wewe.
2681  EXO 39:16  Ñu sàkk itam ñaari ŋankukaayi wurus ak ñaari jaaroy wurus yu ñu takk ci ñaari cati kiiraayal dënn bi ci kaw
2683  EXO 39:18  Yeneen ñaari cati buumi wurus yi, ñu we leen ci ñaari ŋankukaay, yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, ci kanam.