1774 | EXO 9:31 | Fekk na gàncax ga ñuy defare wëñu lẽe yàqu na, mook peppum lors ba, ndax lors baa nga tollu woon ci waaja focci, gàncax ga ñuy defare lẽe di tóor. |
2200 | EXO 25:4 | ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy |
2237 | EXO 26:1 | «Xaymab jaamookaay bi nag, defare ko fukki sori rabali lẽe, mu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, te nga ñawaale ca nataali serub. |
2267 | EXO 26:31 | «Sàkkal rido bu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ca nataali serub, |
2272 | EXO 26:36 | «Sàkkalal buntu xayma bi kiiraay lu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, muy liggéeyu ràbb bu rafet. |
2282 | EXO 27:9 | «Nanga sàkkalal jaamookaay bi ab ëtt: guddaayu ëtt bi ci wetu bëj-saalum, téeméeri xasabi sori rabal yu ñu ràbbe wëñu lẽe moo koy ub, ci genn wet googu. |
2289 | EXO 27:16 | Buntu ëtt bi nag, na doon lafu ñaar fukki xasab, wu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, muy liggéeyu ràbb bu rafet, ay jënam di ñeent, seeni tegu di ñeent. |
2291 | EXO 27:18 | «Guddaayu ëtt bi téeméeri xasab lay doon, yaatuwaay bi di juróom fukk, taxawaayu wet yi di juróomi xasab, sor yi ñu ràbbe lépp di wëñu lẽe, tegu yi di xànjar. |
2299 | EXO 28:5 | Liggéeykat yooyu ñooy jël wëñi wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe ngir liggéeye ko. |
2300 | EXO 28:6 | «Nañu ràbbe xar-sànni mi wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ci ay nataal. |
2302 | EXO 28:8 | Ngañaay liy tege ci kaw xar-sànni mi, ni xar-sànni mi lañu koy liggéeye, mu ànd ak moom, di benn, di wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. |
2309 | EXO 28:15 | «Nanga sàkk kiiraayal dënn bi ñuy jëfoo cib àtte, ñu liggéeyaale ko ay nataal ni xar-sànni mi, te nañu ko ràbbe wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. |
2333 | EXO 28:39 | «Mbubb mu gudd mi nag, nanga ko ràbbe wëñu lẽe, kaala gi itam di wëñu lẽe. Te laxasaay gi, liggéeyu ràbb bu rafet lay doon. |
2336 | EXO 28:42 | Sàkkal leen ay tubéyi njiitlaayi lẽe, ñu sànge ko seeni cér, dale ko ci ndigg li ba ci lupp yi. |
2538 | EXO 35:6 | ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ak kawari bëy |
2555 | EXO 35:23 | Te it mboolem ñi dencoon wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy mbaa deri xar yu ñu suub xonq, mbaa deri piipi, ñoom ñépp a indi la ñu dencoon. |
2557 | EXO 35:25 | Ci biir loolu jigéen ñu xareñ ñépp ëcce seeni loxo, ngir waajal wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu boole, indi. |
2567 | EXO 35:35 | Moo leen feesal xareñte, ngir bépp liggéey, ci wàllu yett ak nataal, ak liggéeyu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Mane nañu ràbb te itam dañuy sos seen taarali bopp. |
2575 | EXO 36:8 | Ba loolu amee mboolem ñu xareñ ñi bokk ci liggéey bi daldi defar jaamookaay bi. Ñu def ko fukki sori rabali lẽe, yu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr. Ñu ñawaale ci ay nataali serub. |
2602 | EXO 36:35 | Ñu sàkk itam rido bi, ràbbe ko wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñawaale ci ay nataali serub. |
2604 | EXO 36:37 | Ñu sàkkal buntu xayma bi kiiraay lu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, mu doon liggéeyu ràbb bu rafet, |
2643 | EXO 38:9 | Besalel nag sàkk wurmbalu jaamookaay bi. Wetam, gi fare bëj-saalum di téeméeri xasabi sori rabal yu ñu ràbbe wëñu lẽe, |
2650 | EXO 38:16 | Mboolem sori wurmbalu ëtt bi ba mu daj, wëñu lẽe la. |
2652 | EXO 38:18 | Lafu buntu ëtt bi, liggéeyu ràbb bu rafet la, bu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Guddaayu laf bi ñaar fukki xasab la, taxawaay bi yemook yaatuwaay bi, di juróomi xasab, tollook sori wurmbalu ëtt bi. |
2657 | EXO 38:23 | Mu àndoon ci ak Daneen bi, doomu Ayisamaag, Oliyab. Mu dib yettkat, dib taaralkat te di liggéeykatu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. |
2667 | EXO 39:2 | Xar-sànni mi, wëñu wurus lees ko ràbbe, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. |
2668 | EXO 39:3 | Ay xobi wurus lañu tëgg ba mu jekk, ñu dagg ko ay wëñ yu ñu ràbbaaleek wëñ gu baxa gi te laal yolet, ak wëñ gu xewar gi, ak gu xonq gi curr, ak wëñu lẽe gi. Ñu daldi ciy ñawaale ay nataal. |
2670 | EXO 39:5 | Ngañaayu taaral li tege ci kaw, ni xar-sànni mi lees ko defare, liggéeyaale kook moom, ñu ànd di benn. Ñu ràbbe ko wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa. |
2673 | EXO 39:8 | Ñu sàkk kiiraayal dënn bi, liggéeyaale ko ay nataal ni xar-sànni mi, ràbbe ko wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. |
2689 | EXO 39:24 | Ci biir loolu ñu takk ci ombu fëxya bi, ay doomi gërënaat yu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe. |
2692 | EXO 39:27 | Ñu sàkkal nag Aaróona aki doomam mbubb yu gudd yu ñu ràbbe wëñu lẽe, |
2693 | EXO 39:28 | ak kaalag lẽe, ak mbaxanay lẽe, ak tubéyi njiitlaay yu lẽe, |
2694 | EXO 39:29 | ak laxasaay giy liggéeyu ràbb bu rafet, bu ñu ràbbe wëñu lẽe bu dëgër, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa. |
5483 | DEU 22:11 | Buleen sol ndimol njaxas lu ñu raxe kawaru gàtt ak wëñu lẽe. |
7260 | 1SA 2:18 | Ci biir loolu ngóor sa Samiyel moom, ma ngay liggéeyal Aji Sax ji, sol xar-sànnim lẽewam. |
7808 | 1SA 22:18 | Buur ne Doweg: «Ayca yaw, fàddal sarxalkat yii!» Doweg Edomeen ba fàdd sarxalkat ya. Rey na bésub keroog juróom ñett fukki nit ak juróom (85) ñuy sol xar-sànnim lẽe. |
8174 | 2SA 6:14 | Daawudaa ngay fecc ak doole fa kanam Aji Sax ji. Daawudaa nga gañoo am xar-sànnim lẽe. |
12512 | NEH 8:15 | Ñu siiwal nag ndigal, ca mboolem seeni dëkk ak ca Yerusalem, daldi yéene ne: «Demleen ca tund ya, wuti ay cari garabi oliw, ak cari garabi pẽe, ak cari garabi mirt, ak cari garabi tàndarma, ak cari garab yu sëq, ndax ñu defare ko ay mbaar, muy li ñu bind.» |
12712 | EST 1:6 | Ay ndimoy wëñ gu ëccu gu weex ak gu baxaa nga wékke ca buumi lẽe yu weex ak yu xonq curr, takke ci ay jaaroy xaalis yu wewe ci ay jën yu ñu tabaxe doju màrb. Ay lali wurus ak xaalis a nga tege fa suuf, sa ñu dëre doj yu gànjare: yu màrb ak yu pere ak yu ñuul. |
12836 | EST 8:15 | Ba mu ko defee Mardose bàyyikoo ca Buur; ma nga sol yérey buur, baxa ak weex, ak mbaxanam buur mu wurus mu réy, ak mbubbum lẽe mu xonq curr. Dëkku Sus baa ngay riire mbégteek bànneex. |
17800 | ISA 3:23 | ba ci yérey sooy ak yérey lẽe aki musóor aki kol. |
18083 | ISA 19:9 | kuy liggéey lẽe am mbetteel, kuy jàrt ak a ràbb poqe jommi. |
18540 | ISA 41:19 | Maay def garabi seedar aki séng ca màndiŋ ma, saxal garabi mirt ak oliw ca joor ga, sippar ak garabu pẽe, ak yeneen garab yu dëkke naat, ma boole ca, |
18904 | ISA 60:13 | Taaru àllub Libaŋ a lay ñibbsil, garabu sippar, pẽe ak geneen gu dëkke naat, taaralsi sama kër gu sell gi, ba ma terale ci sama ndëggastalu tànk. |
19336 | JER 13:1 | Aji Sax ji da maa wax ne ma: «Demal jëndi njiitlaayu lẽe, nga woddoo ko, te bu ko ndox laal.» |
20693 | EZK 9:2 | Ca saa sa juróom benni góor jóge yoonu bunt ba féete kaw te janook bëj-gànnaar, ku nekk ŋàbb sa ngànnaayal reyukaay. Keneen a nga ca seen biir, ku sol ndimol lẽe, ak mbarum bindukaay ba ca ndiggam. Ñu dikk taxaw ca wetu sarxalukaayu xànjar ba. |
20694 | EZK 9:3 | Ci kaw loolu leeru Yàllay Israyil, ja woon ca kaw jëmmu malaakay serub ma, yékkatikoo fa, jubal buntu kër ga. Mu woo boroom ndimol lẽe baak mbarum bindukaay ba ca ndiggam. |
20702 | EZK 9:11 | Ci kaw loolu boroom mbubbam lẽe baak mbarum bindukaay ba ca ndiggam, ne jimeet, délsi. Mu ne: «Def naa lépp na nga ma ko sante.» |
20704 | EZK 10:2 | Aji Sax ji ne boroom ndimol lẽe ba: «Doxal ci diggante mbege, yi ronu jëmmi serub yi, nga tibb say loxo ba mu fees ci xal yu yànj yi, te nga dem wasaare ko ci kaw dëkk bi.» Kooka dem, may gis. |
20708 | EZK 10:6 | Ba Aji Sax ji santee boroom mbubbam lẽe ma, ne ko mu sàkk sawara ci diggante mbege yi ci digg jëmmi serub yi, waa ja dem, taxaw feggook menn mbege. |
20709 | EZK 10:7 | Ci kaw loolu kenn ci malaakay serub yi yóotu sawara si ci seen digg, daldi sàkk ci xal yi, def ci loxoy boroom mbubbam lẽe ma, mu jël ko, daldi génn. |
20841 | EZK 16:10 | solal la ndimo lu yànj ak dàlli der, muure la ndimol lẽe, tegal la ca sooy. |
20844 | EZK 16:13 | Nga takkoo wurus ak xaalis, sol ndimol lẽe ak sooy ak ndimo yu yànj, di lekk sunguf su mucc ayib ak lem ak diw. Nga mujj taaroo taaru ba jot darajay lingeer, |
21197 | EZK 27:7 | Lẽe bu bawoo Misra lañu ràbb ba mu jekk, def ko ndimoy wiiru gaal gi, nga raayawoo ko, cuub gu baxa ak cuub gu xewar bawoo dunu Elisa, di sa malaan, |
21206 | EZK 27:16 | Waa Siri it di say jula, di jëndeek yaw lu bare loo defar, di ko wecci per yu jafe, ak ndimo yu xewar, ak séri ràbb ak lẽe ak peri koray ak peri rubi. |
21549 | EZK 40:3 | Ba mu ma yóbboo ba foofa, ma jekki yem ci nit ku am melow xànjar, ŋàbb buumu lẽe ak yetu nattukaay. Ma nga taxaw ca buntu dëkk ba. |
21685 | EZK 44:17 | «Bu ñu dee jàll buntu ëttu biir bi, yérey lẽe lañuy sol. Buñu sol ndimol kawaru jur, bu ñuy liggéey fu wees buntu ëttu biir bi, jëm ca biir-a-biir. |
21686 | EZK 44:18 | Kaalag lẽe lanuy kaalawoo, tubéyu njiitlaayu lẽe lañuy jiital, te duñu sol dara lu leen di ñaqloo. |
22179 | HOS 2:7 | Ñoom seen yaay moo gànctu, ki leen ëmb moo def lu gàccelu, naan: “Damay toppi sama far, yi may jox sama lekk ak samag naan, ak samag wëñ ak sama lẽe ak samag diw ak sama biiñ.” |
22183 | HOS 2:11 | Kon nag fa ngóob jote laay nangoo sama pepp, fa wittum reseñ jote it laay nangoo sama biiñ bu bees, maay foqati sama wëñ ak sama lẽe, ba mu daan sànge yaramam. |
26057 | LUK 23:53 | Gannaaw loolu mu wàccee ko ca bant ba, sànge ko càngaayal lẽe, denc ko ci bàmmeel bu ñu yett ciw doj, te maseesu caa denc ab néew. |
31021 | REV 15:6 | Juróom ñaari malaaka, yi taawu juróom ñaari musiba yi nag, génne ci màkkaan mi. Ñu ngi sol mbubbi lẽe yu set, ne ràññ, ay ngañaayi wurus takke ci seen dënn. |
31074 | REV 18:12 | wurus ak xaalis, ak doji gànjar aki per ak lẽe ak ndimo lu yolet ak sooy, ak ndimo lu xonq curr, ak bépp bant bu xeeñ, ak wépp xeetu jumtukaayi bëñi ñey, ak jumtukaayi dénku ngëneel ak yu xànjar, ak yu weñ gu ñuul, ak yu doju màrb, |
31078 | REV 18:16 | naan: «Wóoy, wóoy ngalla dëkk bu mag ba! Ngalla yaw, dëkk bu mag, ba daa woddoo lẽe ak ndimo lu yolet ak lu xonq curr, takkoo wurus ak doji gànjar aki per, |
31094 | REV 19:8 | Jox nañu ko mbubbum lẽe mu set, ne ràññ, mu sol.» Lẽe boobu mooy jëfi njekk yu nit ñu sell ñi. |
31100 | REV 19:14 | Xarekat yi ci asamaan a ko topp, war fas yu weex, sol mbubbum lẽe mu weex, set wecc. |