318 | GEN 12:19 | Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» |
357 | GEN 14:20 | Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko. |
387 | GEN 16:5 | Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» |
395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
440 | GEN 18:15 | Saarata dégg loolu, daldi tiit, miim ko ne: «Reetaanuma de.» Teewul Aji Sax ji ne ko: «Ree nga kay!» |
450 | GEN 18:25 | Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!» |
467 | GEN 19:9 | Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba. |
501 | GEN 20:5 | Du góor gi da maa waxoon ne kii jigéenam la? Du jigéen ji it da maa waxoon ne kooku càmmiñam la? Fexewuma dara lu ñaaw te di ko tey de!» |
559 | GEN 22:11 | Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!» |
619 | GEN 24:27 | daldi ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, sama Yàllay sang, Ibraayma, moom mi masula noppee laaye biir sama sang, te masu koo ñàkke worma. Man it, Aji Sax ji wommat na ma ba sama kër bokki sang!» |
681 | GEN 25:22 | Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji. |
766 | GEN 27:38 | Esawu ne baayam: «Baay, xanaa genn ñaan rekk nga am? Ngalla baay, ñaanal ma, man itam!» Ca la Esawu ne yikkét jooy. |
773 | GEN 27:45 | Bu sa meru mag giifee, ba mu fàtte li nga ko def, dinaa yónnee, ñu jëlsi la. Duma seetaan mukk, ba boole leen ñàkk, yeen ñaar ñépp, ci benn bés!» |
774 | GEN 27:46 | Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!» |
803 | GEN 29:7 | Yanqóoba ne leen: «Jant bi demagul fenn, ba ngeen di dajale jur gi. Wëggleen gàtt yi, sàmmi leen kay!» |
810 | GEN 29:14 | Laban da ne ko: «Yaw kay sama jarbaat nga lenqe!» Yanqóoba toog na fa ak moom lu mat weer. |
842 | GEN 30:11 | Leya ne: «Ndaw wërsëg wu réy!» daldi ko tudde Gàdd (mu firi Wërsëg). |
1029 | GEN 35:17 | Ba mu demee ba mat wa gëna metti, rewlikat ba ne ko: «Muñal nag, ndax góor laati de!» |
1117 | GEN 37:33 | Yanqóoba xàmmi ko, daldi ne: «Sama mbubbu doom a moos! Éey waay, rabu àll kay moo daggate Yuusufa, yàpp ko!» |
1255 | GEN 42:2 | Mu ne leen: «Dégg naa ne pepp am na ca Misra. Demleen jëndali nu ca, ndax nu mana dund, ba xiif bañ noo rey kay!» |
1289 | GEN 42:36 | Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!» |
1298 | GEN 43:7 | Ñu ne ko: «Waa ja kat da nu doon laaj ak a laajaat ci nun ak sunuy bokk, ba naa nu ndax sunu baay mu ngi dund ba tey, ak ndax am nanu rakk. Nun itam nu wax ko li mu nu laaj. Géntunu woon moos ne dina nu sant, nu indil ko sunu rakk!» |
1320 | GEN 43:29 | Naka la Yuusufa ne gees, gis Beñamin rakku doomu ndeyam ja. Mu laaj leen ne leen: «Ndax kii mooy seen rakk, ji ngeen ma doon wax?» La ca tegu mu ne rakkam ja: «Sama ngóor si, yal na la Yàlla defal yiw waay!» |
1359 | GEN 44:34 | Ndax xawma nan laay delloo ca sama baay te ànduma ak xale bi. Yàlla buma fekke njekkar, li ciy dal sama baay!» |
1360 | GEN 45:1 | Ba loolu amee Yuusufa manatula téye boppam, te surgaam yépp a nga teew. Mu daldi àddu ne: «Xiddileen ma, yeen ñépp!» Ñépp dem, ba benn jaambur nekku fa, ba Yuusufa di xàmmiku ay bokkam. |
1389 | GEN 46:2 | Yàlla wax ak Israyil foofa ca guddi ci biir gént ne ko: «Yanqóoba, Yanqóoba!» Israyil ne ko: «Naam.» |
1429 | GEN 47:8 | Firawna laaj Yanqóoba ne ko: «Aa, góor gi, xanaa war ngaa doon mag de!» |
1518 | GEN 50:11 | Waa réewu Kanaan, gis dëj ba ca dàggay Ataat, naan: «Dëju waa Misra bii aka réy!» Moo tax ñu tudde bérab booba ca wàllaa dexu Yurdan, Abel Misra (mu firi Dëju waa Misra). |
1561 | EXO 2:6 | Naka la ko ne ubbet, yem ca xale ba, muy liir bu góor, xale bay jooy, yaram wa daw, mu ne: «Kii de ndeysaan, ci doomi Ebrë yi la!» |
1575 | EXO 2:20 | Ruwel ne leen: «Ana waa ja? Lu tax ngeen bàyyi ko fa? Wooyileen ko, mu añsi kay!» |
1584 | EXO 3:4 | Ba Aji Sax ji Yàlla gisee Musaa jàdd, di xoolsi, ca gajj ba la àddoo, ne ko: «Musaa, Musaa!» Mu ne ko: «Maa ngi.» |
1637 | EXO 5:4 | Buuru Misra ne leen: «Yeen Musaa ak Aaróona, lu waral ngeen di jële mbooloo mi ci seeni liggéey? Laggleen ca seeni sas waay!» |
1638 | EXO 5:5 | Firawna dellu ne: «Baadoolo yi ne xas tey ci réew mi, ngeen nar leena dëdduloo seeni sas!» |
1656 | EXO 5:23 | Ba ma demee ca Firawna, di wax ci sa tur ba tey, mu ngi lor bànni Israyil, sa ñoñ, te xettliwoo leen sax!» |
1730 | EXO 8:15 | Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon. |
1789 | EXO 10:11 | Mukk laa wax! Du dangeen di màggal Aji Sax ji? Demleen boog, yeen ñiy góor!» Ba loolu amee ñu dàq leen, ñu jóge ca Firawna, |
1807 | EXO 10:29 | Musaa ne ko: «Noonu la sax de. Duma jàkkaarlooteek yaw moos!» |
1850 | EXO 12:33 | Ba mu ko defee waa Misra soññ bànni Israyil, ngir ñu gaaw génn réew ma, ndax booba ña nga naan: «Nun ñépp ay dee!» |
1902 | EXO 14:12 | Xanaa du lii lanu la waxoon ca Misra? Noon nanu la, nga bàyyi nu, nu surgawu waa Misra, ndax surgawu waa Misra moo nu gënal nu dee ci màndiŋ mi!» |
1915 | EXO 14:25 | Mu boole ca téye mbegey watiir ya, ba neexatuñoo dawal. Waa Misra ne: «Nan daw gaaw, ba rëcc bànni Israyil, ndax kat Aji Sax ji moo leen di xeexal, te moo dal ci sunu kaw!» |
1986 | EXO 17:2 | Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?» |
2443 | EXO 32:4 | Mu nangoo ko ci seeni loxo, liggéey ko ba sàkk ci sëllu wu ñu móol. Ci kaw loolu ñu naan: «Bànni Israyiloo, seen Yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!» |
2456 | EXO 32:17 | Ci kaw loolu Yosuwe dégg coowal mbooloo may xaacu. Mu ne Musaa: «Coowal xaree ngoog ca dal ba!» |
2463 | EXO 32:24 | Ma ne leen: “Ku takk wurus, tekkil, indi!” Ñu jox ma, ma sànni ci sawara wi, sëllu wii génne ci!» |
2465 | EXO 32:26 | Musaa taxaw ca buntu dal ba, ne: «Ku ànd ak Aji Sax ji, fii ci man!» Leween ñépp dikk, yéew ko. |
2492 | EXO 33:18 | Musaa teg ca ne ko: «Ngalla may ma nag ma niir sag leer!» |
4031 | NUM 11:6 | Tey jii sunu put yaa ngi wow koŋŋ, gisunu lenn lu moy mànn!» |
4048 | NUM 11:23 | Aji Sax ji ne Musaa: «Loxol Aji Sax ji da koo jotewul? Léegi nag dinga gis ndax sama kàddu dina la sottil, am déet!» |
4052 | NUM 11:27 | Ab xale dawe ca, àgge ko Musaa, ne ko: «Eldàdd ak Medàdd déy a ngay wax ay waxyu ca dal ba!» |
4053 | NUM 11:28 | Yosuwe doomu Nuun, ja dale doon bëkk-néegu Musaa cag ndawam, daldi cay àddu, ne: «Sang Musaa, aaye leen!» |
4054 | NUM 11:29 | Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sol leen ag leeram!» |
4064 | NUM 12:4 | Ci kaw loolu Aji Sax ji jekki wax ak Musaa ak Aaróona ak Maryaama, ne leen: «Dikkleen, yeen ñett, ci xaymab ndaje mi!» Ñu dem, ñoom ñett. |
4072 | NUM 12:12 | Ngalla bul seetaan kii mel ni ku dee te indaalewul bakkan ba mu juddoo ca ndeyam, xaaju yaram wi lekku!» |
4073 | NUM 12:13 | Musaa nag jooy Aji Sax ji, ne ko: «Yàlla, ngalla wéral ko!» |
4202 | NUM 16:7 | te ngeen def ciy xal, def ci cuuraay fi kanam Aji Sax ji, ëllëg. Su ko defee ku Aji Sax ji taamu, kookooy ki sell. Doy na sëkk, yeen Leween ñi!» |
4209 | NUM 16:14 | Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!» |
4216 | NUM 16:21 | «Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!» |
4229 | NUM 16:34 | Mboolem Israyil dégg seen yuux ya, daldi daw, te naan: «Nan daw bala noo suuf a mëdd!» |
4236 | NUM 17:6 | Ca ëllëg sa mbooloom bànni Israyil gépp a doon ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, naan: «Yeen yeena reylu ñoñi Aji Sax ji!» |
4240 | NUM 17:10 | «Jógeleen biir mbooloo mii, ma faagaagal leen léegi!» Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf. |
4241 | NUM 17:11 | Musaa ne Aaróona: «Jëlal and bi, nga sàkke ci sarxalukaay bi ay xal, teg ci cuuraay, yóbbu gaaw ca mbooloo ma, ba defal leen ag njotlaay, ndax sànj mi tàkke na ci Aji Sax ji, mbas mi tàmbali na!» |
4317 | NUM 20:5 | Ana loo nu jële woon Misra, di nu indi fu bon fii? Du bérab bu nangu menn jiwu: du figg, du reseñ, du gërënaat, te du siitum ndox mu ñu naan!» |
4332 | NUM 20:20 | Mu ne leen: «Dungeen fi jaare mukk!» Ci kaw loolu Edom génn ngir dajeek ñoom, ànd ak gàngoor gu réy, gànnaayu ba diis. |
4346 | NUM 21:5 | Ña ngay xultu ca kaw Yàlla ak Musaa, naa: «Lu ngeen nu doon jële Misra, ngir nu dee ci màndiŋ mi? Duw ñam, dum ndox, te wii ñamu toskare génnliku nan!» |
4348 | NUM 21:7 | Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma. |
4405 | NUM 22:29 | Balaam ne mbaam mi: «Yaa may foontoo, su ma yoroon saamar, léegi laa lay rey!» |
4427 | NUM 23:10 | Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!» |
4442 | NUM 23:25 | Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Boo leen móoluwul benn yoon kay, bu leen ñaanal ba doyal boog!» |
4560 | NUM 27:4 | Waaye lu tax ñu génne sunu turu baay ci làngam gi mu bokk, ndax ñàkk doom ju góor? Joxleen nu sunub cér ci biir wàll wi sunu bokki baay yu góor bokk ak sunu baay kay!» |
4922 | DEU 1:28 | Ana fu nu jëm? Te sunu bokk ya demoon yoqiloo nu, ne nu waa réew maa nu ëpp, sut nu, dëkk ya réy te dàbblikoo ay tata yu àkki asamaan. Rax ci dolli, ay ponkal yu bokk ci askanu Anageen ñi lanu fa gis!» |
5002 | DEU 3:25 | May ma rekk ma jàll, ba gis réew mu baax, ma ca wàllaa dexu Yurdan, tund wu rafet woowu ba ca Libaŋ!» |
5012 | DEU 4:6 | Sàmmooleen koo jëfe, ndax mooy doon seenug rafet xel, ak seenug ràññee fi kanam xeet yi, ba bu ñu déggee mboolem dogali yoon yii, dinañu ne: «Wii askan wu mag rekk a rafet um xel te ràññee!» |
5489 | DEU 22:17 | Mu ngii di ko tuumaal, naan: “Fekkuma sa doom ji janq.” Te sama ndawal doom a ngii!» Nañu tàllal malaan ma ca kanam magi dëkk ba. |
5795 | DEU 32:35 | Maay kiy feye, di añale, te bu jotee ñu fakkastalu, ndax seen bésub toskaree dëgmal, dogal ba buur, wutsi leen!» |
7144 | RUT 1:15 | Mu ne ko: «Gis nga sa wujju peccorgo waa ngay ñibbi cay bokkam aki yàllaam. Àndal ak moom ñibbi kay!» |
7150 | RUT 1:21 | Maa demoon ak loxo yu ne gadd, Aji Sax ji délloosi maak loxoy neen. Kon lu ngeen may wooye Nawmi doye, te Aji Sax ji àtte ma ñàkkal? Ndax kat Aji Man ji ci njàqare la ma tàbbal!» |
7161 | RUT 2:10 | Naka la wax loolu, mu sujjóot, dëpp jëëm fa suuf, ne ko: «Xanaa su la neexoon de, doo ma nemmiku sax, ndax ab doxandéem laa, waxatuma nga di ma laaye nii biir!» |
7170 | RUT 2:19 | Goro ba ne ko: «Foo fore lii lépp tey? Ban tool nga doon liggéeye sax? Ki la nemmikoo nii de, yal na barkeel!» Ruut nag wax goroom ka mu doon liggéeye toolam, ne ko: «Ka ma doon liggéeye toolam de, Bowas lañu koy wax.» |
7171 | RUT 2:20 | Nawmi ne Ruut: «Yal na Aji Sax ji barkeel Bowas, moom mi saxoo sàmm ngoram digganteem ak nit, muy dund ak mu dee!» Mu teg ca ne ko: «Kooku ku nu jege la; bokk na ci ñi am sañ-sañu jotaat nu.» |
7196 | RUT 4:4 | Man nag dama noon war naa la koo yegge, te laaj la ndax danga koy jënd ci kanam magi dëkk bi ak ñi fi toog. Soo bëggee def sa warugaru jotaat, jëndal. Soo buggul, wax ma, ma xam. Ndax kat kenn gënu la cee yey, te maa topp ci yaw.» Mu ne ko: «Damay jënd kay!» |
7209 | RUT 4:17 | Jigéeni gox ba nag naa: «Waay waay Nawmi am na doom ju góor!» Ñu tudde xale bi Obedd. Obedd moo jur Yese, miy baayu Daawuda. |
7228 | 1SA 1:14 | ne ko: «Foo àppal sa màndite mi? Doxal, giifali sa ñoll wi!» |
7321 | 1SA 4:22 | Mu ne: «Leer ga kay dëddu na Israyil, dem ngàllo, ndegam jëlees na gaalu Yàlla ga kay!» |
7331 | 1SA 5:10 | Ñu yóbbu gaalu Yàlla ga beneen dëkk bu ñuy wax Ekkron. Gaal gaa ngay jubsi Ekkron, waa dëkk ba gaaw yuuxoondoo ne: «Indil nañu nu fi gaalu Yàllay Israyil, bëgg noo rey, nook sunu waa réew mépp!» |
7335 | 1SA 6:2 | Waa Filisti doora woolu seeni sarxalkat ak seeni gisaanekat, ne leen: «Nan lanuy def ak gaalu Aji Sax ji? Xamal-leen nu nan lanu koy delloo këram!» |
7362 | 1SA 7:8 | Bànni Israyil ne Samiyel: «Ngalla bu nu noppee jooytul ci sunu Yàlla Aji Sax ji, ndax mu wallu nook waa Filisti!» |
7401 | 1SA 9:8 | Surga bi dellu ne Sóol: «Xanaa donju xaalis sii ma yor. Naa ko ko jox boog, mu won nu sunuw yoon!» |
7444 | 1SA 10:24 | Samiyel wax ak mbooloo mépp, ne leen: «Yeena gis ki Aji Sax ji taamu? Kenn melul ni moom ci mbooloo mi mépp.» Mbooloo ma mépp àddu ca kaw ne: «Buur, guddalu fan!» |
7459 | 1SA 11:12 | Mbooloo ma ne Samiyel: «Ana ku noon: “Ndax Sóol ay falu ci sunu kaw?” Indileen ñooñu, nu rey leen!» |
7467 | 1SA 12:5 | Samiyel ne leen: «Kon Aji Sax ji seede na ci seen biir, ki mu fal it seede tey jii, ne gisuleen lenn ci sama loxo.» Ñu ne ko: «Seede na ko!» |
7490 | 1SA 13:3 | Yonatan nag song dalub waa Filisti ca Geba. Waa Filisti yég ko. Ba mu ko defee Sóol wal-lu liit ga ca réew ma mépp, ne: «Na ko Ebrë yi dégg!» |
7546 | 1SA 14:36 | Ba loolu amee Sóol ne: «Nan toppi waa Filisti ci guddi gi, nu sëxëtoo seen alal ba bët set, te bunu ci bàyyi kenn, mu dund.» Mbooloo ma ne ko: «Loo bëgg rekk, defal!» Sarxalkat ba nag ne ko: «Nanu ko jëkka diis Yàlla fii.» |
7553 | 1SA 14:43 | Sóol ne Yonatan: «Wax ma loo def.» Yonatan ne ko: «Aylayéwén maa ñam tuuti ca lem, ja ma cappe sama catu yet wi ma yoroon ci sama loxo. Maa ngi, naa dee!» |
7554 | 1SA 14:44 | Sóol ne ko: «Na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, waaye yaw Yonatan dinga dee déy!» |
7575 | 1SA 15:13 | Ba Samiyel demee ba gis Sóol, Sóol ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel. Def naa la Aji Sax ji santaane!» |
7594 | 1SA 15:32 | Gannaaw loolu Samiyel ne: «Indil-leen ma Agag buurub Amalegeen ñi.» Agag nag dikk, wutsi ko, ne finaax. Booba Agag a nga naan ca xelam: «Dee moom, tiitatuma ko, wees na!» |
7599 | 1SA 16:2 | Samiyel ne ko: «Ana nu ma fay deme? Sóol da koy dégg, rey ma!» Aji Sax ji ne ko: «Aw nag wu jigéen ngay jël, yóbbu, ne ko sarxalsi Aji Sax ji moo la indi. |
7603 | 1SA 16:6 | Naka lañu agsi, Samiyel gis Elyab, daldi ne ca xelam: «Xam naa kii fi kanam Aji Sax ji rekk mooy tànnéefam!» |
7605 | 1SA 16:8 | Yese daldi woo Abinadab, indi ko fi kanam Samiyel. Mu ne: «Aji Sax ji tànnul kii ba tey de!» |
7648 | 1SA 17:28 | Elyab, magu Daawuda, dégg Daawuda di wax ak ñooña. Mu mer, ne ko: «Yaw sax lu la fi indi? Ak koo wacce la fay gàtt ak as néew ca àll ba? Xam naa bu baax sag réy ngise, ak njubadi gi nga mébét. Seetaansi xare bi doŋŋ a la fi indi!» |