1641 | EXO 5:8 | Waaye sasleen leen limu móol, ya ñu daan móol naka jekk. Buleen ko wàññi, ndax ay yaafus lañu; moo leen tax di dee-deeluy waxeey naan: “May nu, nu dem rendili sunu Yàlla sarax!” |
1695 | EXO 7:9 | «Bu leen Firawna waxee ne leen: “Defleen seeni kéemaan boog!” danga naan Aaróona: “Jëlal yet wi, sànni ci suuf ci kanam Firawna.” Su ko defee yet wi dina soppliku jaan.» |
1815 | EXO 11:8 | Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees. |
2463 | EXO 32:24 | Ma ne leen: “Ku takk wurus, tekkil, indi!” Ñu jox ma, ma sànni ci sawara wi, sëllu wii génne ci!» |
3098 | LEV 13:45 | «Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: “Setuma de, setuma!” |
4043 | NUM 11:18 | «Mbooloo mi nag, ne leen ñu sell-lu ngir ëllëg, te ne leen dinañu yàpp moos, gannaaw ñooy jooy ci kaw Aji Sax ji, naan “Éy ku nuy leelatiw yàpp, nooka neexle woon ca Misra!” Kon nag Aji Sax jee leen di jox yàpp wu ñu lekk. |
4125 | NUM 14:16 | “Ñàkka mana yóbbu mbooloo mii ca réew ma mu leen giñaloon, moo waral Aji Sax ji faagaagal leen ci màndiŋ mi!” |
5747 | DEU 31:17 | te samam sànj dina tàkk ci seen kaw bésub keroog. Maa leen di wacc, làq leen sama kanam, te kon dees na leen lekk. Musiba yu bare aki njàqare dina leen dikkal. Bésub keroog ñoo naan: “Xanaa sunu Yàllaa nekkul ci sunu biir kay, ba tax musiba yii dikkal nu!” |
5787 | DEU 32:27 | Waaye reetaani noon laa ci ragal, lu ko moy seeni bañ juume ko, ba naan: “Sunu njàmbaar a!” te waroon ne: “Aji Sax jee def lii lépp!”» |
7753 | 1SA 20:21 | Su ko defee rekk, ma yebal ndaw, ne ko mu jëli fitt yi. Su ma nee ndaw li: “Ée! Xoolal fitt yaa ngii nga romb, foral!” Su boobaa, ñëwal, jàmm ñeel na la, te dara amul, giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund. |
7754 | 1SA 20:22 | Waaye su ma nee ndaw li: “Fitt yaa nga nale ca sa kanam!” Su booba, demal, ndax Aji Sax jee la yebal. |
8745 | 1KI 1:25 | Ndax kat, Adoña dem na tey jii, sarxeji lu bare ciy nag ak wëllu yu duuf aki xar. Woo na ca doomi Buur yu góor yépp, ñook njiiti xare yeek Abiyatar sarxalkat bi. Ña nga noonee di lekk ak a naan ñook moom te naa: “Buur Adoña, guddalu fan!” |
8754 | 1KI 1:34 | Cadog sarxalkat bi ak Yonent Yàlla Natan, nañu ko diw foofa, fal ko mu jiite Israyil. Su ko defee ngeen wal liit gi te yéene ne: “Buur Suleymaan, guddalu fan!” |
8781 | 1KI 2:8 | «Gannaaw loolu bàyyil xel ci Simey mi nga feggool, muy doomu Gera mu Baxurim, mi bokk ci giirug Beñamin. Moom moo ma doon tifaari saaga, bés ba ma jëmee Maanayim, moom mu dikk dajeek man ca dexu Yurdan. Ma giñal ko ci Aji Sax ji ne ko: “Duma la rey, sama saamar du la dal!” |
9358 | 1KI 18:14 | Léegi nga naa ma: “Demal wax sa sang ne ko Ilyaas a ngoog!” Mu di ma rey?» |
10058 | 2KI 18:30 | Bu leen Esekiya yaakaarloo Aji Sax ji it, naan leen: “Aji Sax ji moo nuy xettli moos, te deesul teg dëkk bii ci loxol buurub Asiri!” |
18008 | ISA 14:10 | ñoom ñépp àddu, ne la: “Yaw it mujj nga néew doole ni nun a? yaak nun de a mujj yem kepp!” |
18012 | ISA 14:14 | Maay yéeg fa kaw niir ya, ba mel ni Yàlla Aji Kawe ji!” |
18303 | ISA 30:16 | Yeena ne: “Déedéet, danuy war fas, daw!” Dingeen daw moos! Ngeen ne: “Daamar yu gaaw lanuy war.” Ñi leen di dàq it di war daamar yu gaaw! |
18581 | ISA 43:6 | Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!” ne bëj-saalum: “Bul téye!” Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi, te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina. |
18631 | ISA 44:28 | Maa naa ci Sirus: “Sama sàmm bi!” Mooy matal sama bépp nammeel, te it moo naa ci Yerusalem: “Nees ko tabaxaat,” kër gu sell gi, laa ne: “Nees ko yékkatiwaat!”» |
18715 | ISA 49:9 | ba ne ñi ñu tëjoon: “Génnleen!” Fa ñu nekkoon cig lëndëm, laa naa leen: “Génnleen ci leer gi!” Ñooy doon sama gàtt, dellu di fore aw ñall, ak wépp tund wu ne faraas tey. |
18726 | ISA 49:20 | Ñàkkoon ngay doom, waaye ku nekk ci say doom ay dëkkalaat yii kàddu ci sab nopp: “Fii dafa xat, xajal ma, fu ma dëkke!” |
19061 | JER 2:27 | ñoom ñii naa bii bant: “Yaay sunu baay,” naan wee doj: “Yaa nu sukk, jur.” Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw, te bu leen musiba dikkalee, ñu naa: “Wallu nu boog!” |
19162 | JER 6:4 | Ñii ne: “Waajal-leen xare baak ñoom, nu songi leen digg bëccëg. Waaye wóoy nun, jant a ngi lang, keru ngoon di law!” |
19172 | JER 6:14 | Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, naan: “Jàmm, lépp jàmm!” te jàmm amul. |
19183 | JER 6:25 | Kii naa: “Bul génn ci àll bi!” Kee naa: “Bul jaar ci yoon wi!” Saamar kay a nga ca loxol noon ba, tiitaange dajal fépp!» |
19199 | JER 7:11 | rawtub sàcc daal ngeen def kër gii ñu ma tudde? Man de lii laa gis!” Kàddug Aji Sax jee. |
19233 | JER 8:11 | Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, naan: “Jàmm, lépp jàmm!” te jàmm amul. |
19541 | JER 22:18 | Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, ne: «Kenn du ko jooy ca mbokkam mu góor mbaa mu jigéen, naan: “Wóoy ngalla nun, bokk yi!” Kenn du ko jooy, naan: “Wóoy, sang ba, wóoy kilifa ga!” |
19783 | JER 31:23 | Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq. Dees na ne: “Yaw dëkkuwaayu njekk bii, yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi, yal na la Aji Sax ji barkeel!” |
20148 | JER 47:6 | Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii, xanaa doo selaŋlu? Dellul sa mbar, boog, dal-lu, ne tekk!” |
20151 | JER 48:2 | Mowab amatul woy, fa Esbon la leen noon ya fexeel lu bon, ne: “Aycaleen nu raafal wii xeet!” Yeen waa Madmen it, ñu wedamal; saamar topp leen. |
20155 | JER 48:6 | Ñu naan: “Dawleen, rawale seen bakkan, ba tumurànkeji ni gajju màndiŋ!” |
20169 | JER 48:20 | Ñu ne: “Gàcce ñeel na Mowab gii tas!” Yuuxooleen, ne wóoy! Yéeneleen fa tàkkal dexu Arnon, ne Mowab tas na! |
20225 | JER 49:29 | nangu xaymaaki jur, ak kiiraay ak luy jumtukaay, yóbbu seeni giléem, te biral leen, ne leen: “Musiba ubale na!” |
20771 | EZK 12:22 | «Yaw nit ki, du lii ngeen defati aw léeb ci biir réewum Israyil? “Bés yaa ngi bëgga baree, te peeñu sottiwul!” |
20776 | EZK 12:27 | «Yaw nit ki, waa kër Israyil déy a nga naan, “Peeñu yi kii di gis, des na ay fani fan, ci lu soree sore lay biral ab waxyu!” |
20793 | EZK 13:16 | Mooy yonenti Israyil yi jottli Yerusalem waxyu, di leen gisal peeñum jàmm, te jàmm amul.’ Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!” |
20943 | EZK 18:25 | «Yeen nag ngeen ne: “Boroom bi, ni muy doxale jaaduwul!” Waa kër Israyiloo, dégluleen! Sama doxalin a jaaduwul, am seeni doxalin a jaaduwul? |
21160 | EZK 25:8 | «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Waa Mowab ak Seyir a ne: “Xool-leen waa kër Yuda ñii ni ñu mujje, ñook xeet yépp a yem!” |
21338 | EZK 32:21 | Biir njaniiw la jàmbaari xare yay tollu, di waxtaane Misraaki farandoom, naan: “Wàccsi nañu, ne lareet, Yéefar yi fàddoo nañu saamar!” |
22265 | HOS 8:2 | Man la Israyil xaacu, ne ma: “Éy sama Yàlla, maa la ràññee!” |
22422 | JOL 4:10 | Seeni illéer ngeen di tëgg ay saamar, tëgg seeni xepp ay xeej, te na ku néew doole ne: “Jàmbaar laa!” |
22460 | AMO 2:12 | «Yeen nag ngeen di naanloo samay séddoo biiñ. Yonent yi, ngeen ne leen: “Buleen biral waxyu!” |
22823 | HAB 2:6 | “Xanaa du ñi mu teg loxo ñépp a koy léebuji, fental ko woy wu ñu ko kókkalee, naan: ‘Wóoy ngalla kii di dajale lu mu moomul, lii ba kañ?’ Kii di sëfoo nii ay bor!” |
23167 | MAL 1:9 | «Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk, mu baaxe nu!” Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. |
25545 | LUK 12:17 | Mu naan ca xel ma: “Nu may def nag? Amatuma sax fu ma denc sama ngóob mi!” |
25612 | LUK 13:25 | Bu boroom kër gi xasee jóg, ba tëj bunt bi, fa ngeen di doxe des biti, di fëgg naan: “Sang bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.” |
25614 | LUK 13:27 | Mu neeti leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Soreleen ma yeen ñépp, defkati njubadi yi!” |
25652 | LUK 14:30 | naan: “Waa jii moo tàmbalee tabax, te manula àggale!” |
25663 | LUK 15:6 | Te bu àggee ca kër ga, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, sama xar ma réeroon, gis naa ko!” |
25687 | LUK 15:30 | Sa doom jii dikk, gannaaw ba mu yàqee sa alal ci ay gànc, nga reyal ko sëlluw yafal wi!” |
25713 | LUK 16:24 | Mu xaacu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catal baaraamam ci ndox, dikk seralal ma sama làmmiñ, sawara sii metti na lool!” |
25743 | LUK 17:23 | Te it, dees na leen ne: “Ma ngee!” mbaa: “Mu ngii!” Buleen dem, buleen ca topp. |
25760 | LUK 18:3 | Ab jëtun a nga woon ca dëkk boobee. Daan na ñëw ca moom, naan ko: “Àtte ma ak sama jotewaale!” |
25825 | LUK 19:25 | Ñu ne ko: “Sang bi, kee ngeek fukki poset ba noppi!” |
25861 | LUK 20:13 | «Boroom tóokër ba ne: “Nan laay def nag? Naa yónni sama doomu bopp ji ma sopp boog, xanaa moom, dinañu ko rus!” |
26033 | LUK 23:29 | Ay jant a ngi ñëw kat, dees na ca ne: “Ndokklee jigéen ju tëlee am doom, masula jur, masula nàmpal!” |
30170 | HEB 8:11 | Kenn dootu soxlaa jàngal moroomam, mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Boroom bi!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag. |