Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   «Word!    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

467  GEN 19:9  Ñu ne ko: «Toppal fale!» te naan: «Waay! Waa jii dal ci sunu dëkk bi rekk, bëgg di fi àtte! Léegi nag dinanu la def lu raw li nu bëggoona def say gan.» Ñu song Lóot, ba nara dàjji bunt ba.
559  GEN 22:11  Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!»
1848  EXO 12:31  Ba loolu amee Firawna woolu Musaak Aaróona ca guddi googu, ne leen: «Ayca! Mott! Soreleen sama waa réew, yeen ak seeni bokk! Laggleen, jaamuji Aji Sax ji, li ngeen bëgg.
4046  NUM 11:21  Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm!
4381  NUM 22:5  Mu yebal ay ndaw ca Balaam doomu Bewor ngir wooyi ko, ca Petor ga Balaam cosaanoo, ca tàkkal dex ga ngir ne ko: «Balaam! Gàngoor a ngii jóge Misra. Ñu ngii lal suuf si ba mu daj, te ñoo sanc, janook man màkk.
7258  1SA 2:16  Su ko nit ki nee: «Xanaa dees na jëkka lakk nebbon bi ba mu jeex, nga doora sàkk lu la neex?» Mu ne ko: «Mukk! Léegi nga ma ciy jox, lu ko moy doole laa koy jële.»
7390  1SA 8:19  Mbooloo ma nag lànk, déggaluñu Samiyel, xanaa ne ko: «Ndokk! Buur daal lanuy am,
7538  1SA 14:28  Kenn ca mbooloo ma ne ko: «Aa! Ngiñ lii de, sa baay giñoon na ko ci kaw mbooloo mi, ne: “Képp ku lekk tey, yal na alku,” moo tax mbooloo mi néew doole.»
7769  1SA 20:37  Xalelu góor ba dem ba fa fittu Yonatan ga dal, Yonatan woo xale bi, ne ko: «Ée! Xanaa du fitt gaa nga nale ca sa kanam?»
7784  1SA 21:10  Sarxalkat ba ne ko: «Xanaa saamarub Golyaat waa Filisti ba nga reyoon ca xuru Ela. Ma nga nee laxase ca turki ba, ca gannaaw xar-sànni ma. Soo ko bëggee, jëlal, boobu rekk a fi ne.» Daawuda ne ko: «Aa! Boobu kay amul moroom, jox ma ko.»
7979  1SA 29:9  Akis ne Daawuda: «Dara! Xam naa loolu. Bége naa la it ni ndawal Yàlla. Kilifay Filisti kay a ma ne: Bumu ànd ak nun ca xare ba.
9587  2KI 3:7  Ba loolu amee mu yónnee ca Yosafat buurub Yuda, ne ko: «Buuru Mowab fippu na, jógal ma. Ndax doo ànd ak man, nu xarejeek Mowab?» Mu ne ko: «Ahakay! Maak yaw benn lanu. Sama mboolooy sa mbooloo, samay fas di say fas,»
9674  2KI 5:23  Naaman ne ko: «Ahakay! Jëlal juróom benn fukki kiloy xaalis kay!» Mu soññ ko nag, ba mu ëmb juróom benn fukki kiloy xaalis yi ci ñaari mbuus, boole ca ñaari mbubbi xew, jox ko ñaari surgaam, ñu gàddu, jiitu Gewasi.
9717  2KI 7:6  Booba fekk na Boroom bi dégtal waa dalub Siri ba riirum fas yu ànd aki watiiri xare ak gàngoor gu réy, ba tax ñu naan ca seen biir: «Ãa! Loolu de, buuri Etteen ñaak buuri Misraa, Buurub Israyil fey leen, ngir ñu songsi nu!»
12779  EST 4:13  Mardose dellu yónnee ne ko: «Ãay! Yaa ngi kër buur de! Waaye bul defe ne man ngaa mucc, yaw doŋŋ, ci mboolem Yawut yi.
12819  EST 7:8  Ci kaw loolu Buur bàyyikoo ca tóokër ba, délsi ca ëttu bernde ja, fekk Aman di sukk ca lal ba Esteer tëdd. Buur ne: «Ãa! Ba ci yekktaan Lingeer nag, te ma nekk ci biir kër gi?»
14455  PSA 35:25  Yàlla buñu ne: «Ñaw! Lii rekk lanu bëggoon.» Yàlla buñu ne: «Sàkkal nanu ko pexe.»
19153  JER 5:26  «Waaw! Daa am ñu bon ci sama ñoñ, ñuy tërook a fiire mbete nappkati picc.
19693  JER 28:6  Mu ne ko: «Amiin! Yal na ko Aji Sax ji defee! Yal na Aji Sax ji sottal sa kàdduy waxyu yi nga wax, ba délloosee Babilon ba fii ndabi kër Aji Sax ji ak mboolem ña ñu fa toxal.
20322  JER 51:41  «Ãa! Ana nees mana nangoo Sesag? Nees mana tege loxo ki àddina sépp di kañ? Ana nu Babilon mana gente fi digg xeet yi?
20612  EZK 4:14  Ma ne ko: «Ãhã! Boroom bi Aji Sax ji, man de masumaa sobeel sama bopp. Muy lu médd, di lu aw rab fàdd, masuma koo lekk ba may gone ba tey. Wenn yàpp wu daganul masula dugg sama gémmiñ.»
22529  AMO 6:10  Ku warloo waajal mbokkam mu dee dina dugg ca kër ga, ngir yóbbu néew ya, te naan ka ca biir-a-biir: «Kenn desul foofu ci yaw?» Mu ne ko: «Jeex na,» bëgg caa teg baat, mu ne ko: «Déet! Noppil, bul tudd turu Aji Sax ji.»
25799  LUK 18:42  Yeesu ne ko: «Gisal! Sa ngëm faj na la.»
30890  REV 7:12  ne: «Amiin! Na sunu Yàlla jagoo màggal ak daraja ak xel ak cant ak teraanga ak kàttan ak doole, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!»
31087  REV 19:1  Gannaaw loolu damaa dégg lu mel ni coow lu xumb, bawoo ci mbooloo mu bare mu àddoo asamaan, ne: «Aleluya! Texe ak daraja ak kàttan ñeel na sunu Yàlla.
31089  REV 19:3  Ñu neeti: «Aleluya! Saxaras lakku dëkk ba kay day jolli rekk, ba fàww!»
31090  REV 19:4  Ci kaw loolu ñaar fukki mag ñeek ñeent ak ñeenti bindeef yi ne gurub sukk, sujjóotal Yàlla, mi toog ci ngàngune mi. Ñu bokk ne: «Amiin! Aleluya!»
31092  REV 19:6  Ma daldi dégg lu mel ni coowal mbooloo mu bare, mu àddoo ni riirum géej, tey nirook kàddug dënu gu réy, ne: «Aleluya! Sunu Boroom Yàlla Aji Man ji mooy Buur!