18581 | ISA 43:6 | Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!” ne bëj-saalum: “Bul téye!” Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi, te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina. |
18715 | ISA 49:9 | ba ne ñi ñu tëjoon: “Génnleen!” Fa ñu nekkoon cig lëndëm, laa naa leen: “Génnleen ci leer gi!” Ñooy doon sama gàtt, dellu di fore aw ñall, ak wépp tund wu ne faraas tey. |
19544 | JER 22:21 | «Waxoon naa leen ko ba ngeen di am jàmm, ngeen ne: “Dégluwnu!” Noonu ngeen jàppoo ba ngeen di ndaw ba tey, masuleen maa déggal! |
22836 | HAB 2:19 | Wóoy, ngalla ku naan bant: “Xippil,” naan doj wu ne selaw: “Yewwul!” Ana lu yooyii di xamle? Ma nga, ñu xoobe ko xaalis ak wurus, te du gennug noo ci biiram. |