3 | GEN 1:3 | Ba loolu amee Yàlla ne: «Na leer nekk,» leer daldi am. |
392 | GEN 16:10 | Mu teg ca ne ko: «Dinaa yokk sa askan lool, ba kenn du leen mana waññ,» |
556 | GEN 22:8 | Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar. |
610 | GEN 24:18 | Mu ne ko: «Ahakay, sang bi,» daldi gaaw, yenniku njaq la, may ko mu naan. |
616 | GEN 24:24 | Mu ne ko: «Betuwel a ma jur, doomu Naxor ak Milka,» |
830 | GEN 29:34 | Mu delluwaat ëmb, am doom ju góor, ba noppi waxaat ne: «Bii yoon sama jëkkër dina am cofeel ci man, ndax jural naa ko ñetti doom yu góor,» loolu tax mu tudde ko Lewi (mu firi Boroom cofeel). |
831 | GEN 29:35 | Mu dellooti ëmb, am doom ju góor daldi ne: «Bii yoon dinaa sant Aji Sax ji,» loolu tax mu tudde ko Yuda (mu firi Cant). Gannaaw loolu njuram taxaw. |
839 | GEN 30:8 | Rasel ne: «Bëre naa ak sama mag bëre bu réy, ba daan,» daldi ko tudde Neftali (mu firi Kiy bëre). |
5276 | DEU 13:3 | ba firnde la mbaa kiraama ga mu leen waxoon dikk, su leen nee: «Nanu topp yeneen yàlla, jaamu leen,» yàlla yu ngeen xamul, |
5280 | DEU 13:7 | Seen mbokk mu ngeen bokkal jenn ndey, mbaa seen doom ju góor, mbaa ju jigéen, mbaa seen jabar ju ngeen xejjoo, mbaa seen xaritu benn bakkan, su leen dee xiirtal, naan leen ci kumpa: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, du yeen du seeni maam, |
5287 | DEU 13:14 | ay nit ñu tekkiwul dara, te bokk ci yeen, ñoo jóg di waññi seen waa dëkk, naan leen: «Nanu jaamuji yeneen yàlla,» yàlla yu ngeen xamul, |
5330 | DEU 15:9 | Wattuleen seen bopp, bala leena jikko ju sew yóbbe ngeen naan ci seen xel: «Atum juróom ñaareel mi, atum njéggalug bor dëgmal na,» ba tax ngeen sajje xef, seen mbokkum ndóol, joxuleen ko dara. Da leen di booleek Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar. |
5337 | DEU 15:16 | Ndegam nag seen jaam a leen ne: «Duma dem, ba la,» ndax cofeel gu mu am ci yeen ak seen waa kër, te bànneexam di nekk ak yeen, |
5380 | DEU 17:14 | Bu ngeen demee nag ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, bu ngeen ko nangoo, dëkke, ba ne: «Nanu fal buur bu nu jiite ni mboolem xeet yi nu séq,» |
5402 | DEU 18:16 | Mooy noonee ngeen ko sàkkoo woon rekk, ci seen Yàlla Aji Sax ji ca tundu Oreb, ca bésub ndaje ma, ngeen ne: «Rikk bunu déggati sunu baatu Yàlla Aji Sax ji. Sawara wu réy wii it, bunu ko gisati, lu ko moy nu dee,» |
5486 | DEU 22:14 | di ko tuumaal, di teg lu ñaaw ci deram, naan: «Ndaw sii ma jël, ba ma àggee ci moom, fekkuma ko janq,» |
5700 | DEU 29:18 | Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy. |
5821 | DEU 33:9 | Kee ne ndey ak baay: «Gisuma leen,» ay doomi ndeyam, ràññeewu leen, te doomam, xamu ko. Xanaa di sàmm say wax, di sàmm sa kóllëre. |
7200 | RUT 4:8 | Moo tax ba boroom sañ-sañu jotaat ba waxee Bowas, ne ko: «Jënd ko yaw,» dafa daldi summi dàllam, dogale ko mbir ma. |
7402 | 1SA 9:9 | Bu jëkkoon nag ci Israyil ku daan leerluji ci Yàlla da naan: «Nan dem ca giskat ba,» ndax ku ñuy wooye yonent tey, booba, ab giskat lañu ko daan wooye. |
7925 | 1SA 26:17 | Ci kaw loolu Sóol xàmmi baatu Daawuda, ne ko: «Daawuda doom, loolu sa baat a?» Daawuda ne ko: «Sama baat a kay, Buur, samab sang,» |
7943 | 1SA 27:10 | Bu ko Akis laajee ne ko: «Fu ngeen lële woon tey?» Daawuda ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Yuda,» mbaa «Xanaa wetu Negew ca Yerameleen ña,» mbaa mu ne ko: «Xanaa wetu Negew ca Keneen ña.» |
8272 | 2SA 11:10 | Ñu yégal Daawuda, ne ko: «Uri de ñibbiwul këram,» mu ne Uri: «Xanaa du ciw yoon nga jóge? Lu la tee àgg sa kër?» |
9587 | 2KI 3:7 | Ba loolu amee mu yónnee ca Yosafat buurub Yuda, ne ko: «Buuru Mowab fippu na, jógal ma. Ndax doo ànd ak man, nu xarejeek Mowab?» Mu ne ko: «Ahakay! Maak yaw benn lanu. Sama mboolooy sa mbooloo, samay fas di say fas,» |
9729 | 2KI 7:18 | Na ko góoru Yàlla ga waxe woon Buur, ne ko: «Nëgëni ëllëg benn nattub lëmm ci sunguf su mucc ayib doon benn dogu xaalis doŋŋ, ñaari natti lors it di benn dogu xaalis ca buntu Samari,» noonu la ame. |
13025 | JOB 7:13 | Dama naan: «Naa nopploo tëraayub laltu, ba yennikoo ab lal sama tawat,» |
13082 | JOB 9:27 | Su ma nee: «Naa fàtte sama tawat, leeral kanam te bég,» |
13726 | JOB 35:2 | Defe nga ne lii yoon la? Nga ne: «Maa am dëgg fi kanam Yàlla,» |
14091 | PSA 13:5 | noon ba naan: «Daan naa ko,» bañ yay bége saab jéll. |
14757 | PSA 53:2 | Ab dof a nga naa ca xelam: «Yàlla amul,» tey def njekkar, njubadeem siblu, kenn defu ci lu baax. |
15090 | PSA 73:15 | Su ma noon: «Naa waxe ni ñoom,» kon de, ma wor sa askanu mbooloo. |
15368 | PSA 87:4 | Yàlla nee: «Ma limaale Misraak Babilon, ñi ma xam di dégg. Xoolal Filisti ak Tir, ak réewum Kuus. Nit a ngii, juddoo fa,» |
15926 | PSA 116:10 | Ba ma naa: «Torox naa ba toskare,» teewul may ànd ak ngëm. |
16318 | PSA 139:11 | Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog, ba leer gi far guddil ma,» |
16553 | PRO 3:28 | Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,» te fekk la yor. |
17030 | PRO 20:6 | Ñu baree ngi naa: «Gore naa,» waaye kuy boroom kóllëre dëgg? |
17173 | PRO 24:24 | Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,» aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la; |
17174 | PRO 24:25 | ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle, taasoo barke bu yaa. |
17190 | PRO 25:7 | ndax ñu ne la: «Yéegal, jegesi fii,» moo gën ñu torxal la ci kanam kilifa. Boo gisalee sa bopp it, |
17395 | ECC 1:10 | Lëf a ngii, nit naa: «Lii de lu bees la,» te mu ngi fi woon lu yàgg, lu jiitu sunu juddu. |
17522 | ECC 7:23 | Loolu lépp maa ko natte xel mu rafet, te naan: «Naa xelu,» ndeke mbir ma sore na ma. |
17742 | ISA 1:18 | «Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje. |
18147 | ISA 22:25 | Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, mu ne: «bant ba sampe woon fu wóor day simpiku. Dees koy gor, mu fàq, la ca sëfe woon dog.» Aji Sax ji déy wax na ko. |
18297 | ISA 30:10 | Boroom ngis, ñu ne ko: «Bul gis,» boroom peeñu, ñu ne ko: «Bu ñu firil peeñuy dëgg. Wax nu lu neex, gisal nu ay nax.» |
18481 | ISA 38:21 | Fekk na Esayi noon: «Indileen ab danku figg, ngeen jonj ko ci taabu Esekiya bi, kon dina dund,» |
18530 | ISA 41:9 | Yaw mi ma jukkee fa cati àddina, wooye la fa gëna sore, wax la ne la: «Yaa di sama jaam, maa la taamu te duma la wacc,» |
18542 | ISA 41:21 | «Waxleen seenu lay,» la Aji Sax ji wax, «Biral-leen seeni firnde,» la buuru Yanqóoba boobu wax. |
18706 | ISA 48:22 | Jàmm,» la Aji Sax ji wax ne, «du ñeel ñu bon ñi.» |
18724 | ISA 49:18 | Séentul fi la wër te xool! Ñépp a ngi daje, di la fekksi. Ndegam maay Kiy Dund,» kàddug Aji Sax jee, «ñoom ñépp ngay takkoo ni gànjar, gooy gànjaroo nib séet. |
18919 | ISA 61:6 | Yeen nag lees di wooye: «Sarxalkati Aji Sax ji,» ñu naa: «Sunu surgay Yàlla yaa ngi!» Alali xeet yi, yeena koy lekk, di damoo seeni koom. |
18928 | ISA 62:4 | Deesatu la wooye «Dëkk bi ñu wacc,» deesatul wooye sam réew «Réew mu gental.» Xanaa ñu wooye la «Dëkk bi ma neex,» tey wooye sam réew «Boroom jëkkër,» nde yaa neex Aji Sax ji, te sa réew mi dina am boroom kër. |
19105 | JER 4:9 | Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «xolu buur jeex, kàngam ne yàcc, sarxalkat waaru, yonent jommi.» |
19142 | JER 5:15 | Éey waa kër Israyil,» kàddug Aji Sax jee, «maa ngii di indi fi seen kaw xeet wu bawoo fu sore. Xeet wu am kàttan lañu, xeet wu yàgga yàgg, wu ngeen xamul seen làmmiñ, te dégguleen seeni wax. |
19145 | JER 5:18 | Waaye bési keroog it,» kàddug Aji Sax jee, «duma leen jeexal tàkk. |
19220 | JER 7:32 | Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul tudd Tofet mbaa xuru Ben Inom, xanaa xuru Bóomukaay.» Dees na rob ca Tofet ndax ñàkk suuf. |
19223 | JER 8:1 | «Su boobaa déy,» kàddug Aji Sax jee, «noon yeey sulli yaxi buuri Yuda ak yaxi kàngam yi ak yaxi sarxalkat yi ak yaxi yonent yi ak yaxi waa Yerusalem, fa seeni bàmmeel, |
19235 | JER 8:13 | «Maa leen di witta witt.» Kàddug Aji Sax jee. «Garabu reseñ du dese doom, figg du dese doom,» kàddug Aji Sax jee, «xob ya sax day wow. Lu ma leen joxoon, rëcc na leen.» |
19269 | JER 9:24 | «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay dikkal képp ku xarafam yem ci yaram, |
19390 | JER 15:6 | Yaw yaa ma wacc,» kàddug Aji Sax jee, «dellu gannaaw, ma duma la, sànk la. Muñ naa ba sonn. |
19410 | JER 16:5 | Te Aji Sax ji kat dafa wax ne: «Bul dugg kërug dëj, bu fa dem di ñaawlook a jaale. Maa xañ askan wii sama jàmm,» kàddug Aji Sax jee, «xañ leen sama ngor ak sama yërmande. |
19419 | JER 16:14 | «Waaw ay bés a ngi ñëw déy,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee bànni Israyil réewum Misra.” |
19482 | JER 19:6 | «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «su boobaa deesatul wooye bérab bii Tofet mbaa xuru Ben Inom, xanaa xuru Bóomukaay. |
19500 | JER 20:9 | Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko, dootuma biral waxyu ci turam,» sama xol bi mel nib taal bu tàkk, tàbbi sama biir yax yi; may jéema muutuwaale sa kàddu, te duma ko man. |
19506 | JER 20:15 | Alkute ñeel na ka ko yegge baay, ne ko: «Sa soxna am na doom ju góor,» ba tax baay béga bég. |
19547 | JER 22:24 | Mu ne: «Giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax jee, «yaw buurub Yuda, Kooña doomu Yowakim, soo doon jaarob torlukaay ci sama ndijoor it, fa laa lay foqatee, |
19558 | JER 23:5 | «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi. |
19560 | JER 23:7 | «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee bànni Israyil ca réewum Misra.” |
19582 | JER 23:29 | «Sama kàddu déy, daa mel ni sawara,» kàddug Aji Sax jee, «mbaa saddu, di falaxew doj! |
19739 | JER 30:3 | Ndax kat ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay tijjil sama ñoñ seen wërsëg, muy Israyil di Yuda.» Aji Sax jee ko wax. «Maa leen di delloo ca suuf sa ma moomale woon seeni maam.» |
19744 | JER 30:8 | «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi, «maay damm yet wi ñu leen tënke ci seen ndodd, dammat seeni jéng, ba dootuñu doon jaamu doxandéem. |
19746 | JER 30:10 | Waaye yaw Yanqóoba sama jaam, bul tiit,» kàddug Aji Sax jee; «yaw Israyil, bul ragal. Fu sore laa lay wallujee, yaak sa askan wa ca réewum njaam ga, Yanqóoba dellu dal, fegu; kenn dootu ko tiital. |
19761 | JER 31:1 | «Su boobaa,» kàddug Aji Sax jee, «maay doon Yàllay làngi Israyil yépp, ñoom ñuy sama ñoñ.» |
19787 | JER 31:27 | «Bés a ngii nag di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may jiwe kërug Israyil ak kërug Yuda jiwum doom aadama ak jiwum mala. |
19791 | JER 31:31 | «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israyil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees. |
19793 | JER 31:33 | «Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ. |
19794 | JER 31:34 | Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.» |
19798 | JER 31:38 | Mu ne: «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «dees na tabaxalaat Aji Sax ji dëkk bi, dale ko ca soorooru Ananel ba ca buntu Ruq ba. |
19858 | JER 33:14 | «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay sottal ngëneel la ma dig waa kër Israyil ak waa kër Yuda. |
20132 | JER 46:18 | «Giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi di turam: «noon ay dikk, mel ni tundu Tabor ci digg tund yi, mbete tundu Karmel wi feggook géej. |
20161 | JER 48:12 | Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maa leen di yónnee ay nit ñu sotti diw gi, ndab, soteet; njaq, rajax. |
20179 | JER 48:30 | Maa xam seen reewande,» kàddug Aji Sax jee, «seeni kañu neen la, seeni jëf di neen. |
20198 | JER 49:2 | Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay dégtal Raba, dëkku Amoneen ñi, coowal xare ci seen biir, tund wa gental, dëkk-dëkkaan ya tàkk ba jeex, ba keroog Israyil futti ñooña ko futti woon.» Aji Sax jee ko wax. |
20201 | JER 49:5 | Maa ngii di leen wàcceel njàqare,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «njàqare luy bawoo fi leen wër fépp, dàq leen, ku ne jubal yoonam, du kenn ku leen di dajaleeti. |
20209 | JER 49:13 | Giñ naa ko ci man mii, déy,» kàddug Aji Sax jee, «Boccra, dëkk bii day mujj di gent bu ñu doyadal, ndànd-foyfoy bu ñuy móoloo, dëkk-dëkkaanam yépp gental ba fàww.» |
20239 | JER 50:4 | Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «bànni Israyil ay ànd ak Yudeen ñi, dikk di jooy, di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji. |
20255 | JER 50:20 | Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am; fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal. |
20306 | JER 51:25 | «Maa ngii déy, fi sa kaw, yaw Babilon, ponkalum yàqkat bi,» kàddug Aji Sax jee, «yaw miy yàq àddina sépp. Maay tàllal sama loxo fi sa kaw, taxañe la fa kaw doj ya, def la ponkalum jalu dóom. |
20333 | JER 51:52 | «Moo tax, bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay dikke mbugal seen jëmmi tuur yi, ñoom, ñi ñu jam di binnee fi réew mi mépp. |
22190 | HOS 2:18 | Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «Ca nga may wooye “Sama jëkkër,” te dootoo ma wooye “Sama Baal.”» |
22195 | HOS 2:23 | Bésub keroog, maay nangu,» kàddug Aji Sax jee, «maay nangul asamaan, moom, mu nangul suuf; |
22302 | HOS 10:8 | Jaamookaay yu kawe ya ca Bet Awen, bàkkaarukaayi Israyil yooyu lees di tas. Ay dég aki dagg ñooy sax ca seeni sarxalukaay, dees na ne tund yu mag yi: «Mëddleen nu,» te naan tund yu ndaw yi: «Daanuleen ci sunu kaw.» |
22392 | JOL 2:12 | «Terewul ba léegi,» kàddug Aji Sax jee, mu ne: «Délseeleen seen léppi xol ci man, boole kook koor aki jooy aki yuux. |
22424 | JOL 4:12 | Na xeet yi jóg te songi xare ca xur, wa ñu dippee «Aji Sax jeey àtte,» foofa déy laay toog di àtte mboolem xeet yi, ba fépp daj. |
22529 | AMO 6:10 | Ku warloo waajal mbokkam mu dee dina dugg ca kër ga, ngir yóbbu néew ya, te naan ka ca biir-a-biir: «Kenn desul foofu ci yaw?» Mu ne ko: «Jeex na,» bëgg caa teg baat, mu ne ko: «Déet! Noppil, bul tudd turu Aji Sax ji.» |
22559 | AMO 8:9 | Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay sowal jant digg bëccëg, lëndëmal suuf bëccëg ndarakàmm. |
22561 | AMO 8:11 | «Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay wàcce xiif ci réew mi. Du doon xiifub dugub mbaa marum ndox, kàddug Aji Sax ji lañuy xiif. |
22577 | AMO 9:13 | «Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «kuy gàbb dina dab kuy góob, kuy nal reseñ dab ka koy ji. Biiñ bu bees di rogalaate ca tund yu mag ya, di wale tundoo tund wu ndaw. |
22587 | OBA 1:8 | «Xanaa du bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «fi Edom laay tukkale boroomi xel, tundu Esawu woowu laay jële luy taxa dégg. |
22654 | MIC 1:6 | «Maay saam Samari, def ko jalu tojit ci mbooy gi,» la Aji Sax ji wax. «Maa koy def jëmbatukaayub reseñ, maay yuri ay doji tabaxam ca xur wa, ñori ay kenoom. |
22712 | MIC 5:9 | «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «maay dagge fi sa biir, sa fasi xare, te maay sànk sa watiiri xare. |