Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   Word,”    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

606  GEN 24:14  Janq bu ma wax ne ko: “Doo yenniku sa njaq, may ma, ma naan,” mu ne ma: “Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,” na kooka di ki nga jagleel sa jaam Isaaxa. Noonu laay xame ne laaye nga biir sama sang.»
882  GEN 31:8  Bu nee: “Yi tippanteey sa peyoor,” jur gépp jur lu tippante; mbaa mu ne: “Yi seereer ay sa peyoor,” jur gépp jur lu seereer.
1275  GEN 42:22  Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: “Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.»
7519  1SA 14:9  Bu ñu nu nee: “Taxawleen foofu, ba nu fekksi leen,” nu yem fa, bañ leena fekki.
7520  1SA 14:10  Waaye bu ñu nee: “Ayca, dikkleen,” nu daldi dem te xam ne Aji Sax jee leen teg ci sunu loxo. Nan def loolu ab takk.»
7538  1SA 14:28  Kenn ca mbooloo ma ne ko: «Aa! Ngiñ lii de, sa baay giñoon na ko ci kaw mbooloo mi, ne: “Képp ku lekk tey, yal na alku,” moo tax mbooloo mi néew doole.»
8209  2SA 7:26  ngir saw tur di gëna màgg ba fàww, ñu naan: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi mooy Yàllay Israyil,” te waa kër Daawuda sax fi sa kanam, Sang bi.
9017  1KI 8:29  Yal nanga ne jàkk guddeek bëccëg ci kër gii, bérab bi nga noon: “Fi la sama tur di nekk,” te yal nanga dégg ñaan gi ma jublu bérab bii, di ko ñaan, man sab jaam.
12533  NEH 9:18  Dem nañu sax ba móolal seen bopp jëmmu wëllu te naan: “Yeen, seen Yàllaa ngi; moo leen génnee réewum Misra,” ñàkke la kersa lool.
18567  ISA 42:17  Ñi wóolu ay jëmmi tuur, naan jëmm yu ñu móol: “Yeenay sunuy yàlla,” dees na leen waññi, torxal leen.
18608  ISA 44:5  Kii nee: “Aji Sax jee ma moom.” Kee di tuddoo turu Yanqóoba, kale bind ca loxo ba: “Maa ñeel Aji Sax ji,” tey wuyoo turu Israyil.»
18629  ISA 44:26  Maay dëggal sama kàddug jaam, di sottal sama ndéeyal ndaw. Maa naan ci Yerusalem: “Dees na ko dëkke,” dëkki Yuda, ma ne: “Dees na leen tabaxaat, ma dekkali gentam bi.”
18631  ISA 44:28  Maa naa ci Sirus: “Sama sàmm bi!” Mooy matal sama bépp nammeel, te it moo naa ci Yerusalem: “Nees ko tabaxaat,” kër gu sell gi, laa ne: “Nees ko yékkatiwaat!”»
18766  ISA 51:23  Maa koy teg ci loxol ñi la doon naqaral, te naan la: “Sëggal, nu joggi, jàll,” nga def sa gannaaw gi aw yoon, ñu joggi, wéy.»
18936  ISA 62:12  Dees na leen wooye “Askan wu sell wi,” “Ñi Aji Sax ji jot;” te yaw Yerusalem dees na la wooye “Ki ñu namm,” “Dëkk bi ñu waccul.”»
18974  ISA 65:8  Aji Sax ji dafa wax ne: «Ni nit di gise cabbu reseñ ju fees dell, ne: “Buleen ko yàq, ngëneel a ngi ci,” noonu laay def ngir sama jaam ñi, baña boole lépp yàq.
18981  ISA 65:15  Seen tur wi ngeen bàyyi gannaaw la samay tànnéef di móoloo, naan: “Yal na la Boroom bi Aji Sax ji rey ni diw ak diw,” waaye ñoom sama jaam ñi, tur wu yees lees leen di wooye,
19061  JER 2:27  ñoom ñii naa bii bant: “Yaay sunu baay,” naan wee doj: “Yaa nu sukk, jur.” Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw, te bu leen musiba dikkalee, ñu naa: “Wallu nu boog!”
19106  JER 4:10  Ma ne, «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa naxlu askan wii nax yu metti, ba nga nee: “Yerusalem jàmm lay am,” te saamar tege ci putam.»
19129  JER 5:2  Bu ñu nee sax: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,” ay fen lañuy giñ.»
19201  JER 7:13  «“Gannaaw def ngeen jëf jii jépp nag,” kàddug Aji Sax jee, “te ma waxoon leena wax ay yooni yoon, dégluwleen; woo leen, wuyuwleen,
19230  JER 8:8  Nu ngeen man ne: “Am nan xel, nungeek yoonu Aji Sax ji,” te xalimay yoonalkat soppi ko fen?»
19334  JER 12:16  Waaye bu ñu royee ba roy sama ñoñ, di jëfe ni sama ñoñ wara jëfe, di giñe sama tur naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,” na ñu daan royloo sama ñoñ, ba ñuy giñe Baal, tuur mi, su boobaa ñu sampu fi sama digg ñoñ.
19377  JER 14:15  Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent.
19416  JER 16:11  Nga wax leen nag ne leen: “Seeni maam a ma wacc,” kàddug Aji Sax jee, “di topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal. Man nag, ñu dëddu ma; sama yoon it, ñu bañ koo sàmm.
19488  JER 19:12  Noonu laay def bérab bii,” kàddug Aji Sax jee, “ak ñi fi dëkk. Maay def dëkk bii ni Tofet.
19516  JER 21:7  Gannaaw loolu nag,” kàddug Aji Sax jee, “Cedesyas buurub Yuda, aki jawriñam ak askan week ñi des ci dëkk bii te rëcce ci mbas meek xare beek xiif bi, maa leen di teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, ak seen loxol noon, ak loxol ñi leen di wuta rey. Dina leen leel ñawkay saamar. Du leen baal, du ñéeblu, du yërëm.”
19528  JER 22:5  Waaye su ngeen dégluwul sama santaane yii, giñ naa ko ci man mii,” kàddug Aji Sax jee, “ab gent rekk la gii kër di doon!”»
19587  JER 23:34  «Te muy yonent, muy sarxalkat mbaa kenn ci askan wi, ku ci ne: “Yéeneb waxyu bii la ma Aji Sax ji yóbbante ci yeen,” maay dikke mbugal kooku mook waa këram.
19753  JER 30:17  «Ñu ngi la naan: “Waccees na la,” naan la: “Siyoŋ yaw, faaleesu la,” waaye maa lay may wér, faj say góom.» Kàddug Aji Sax jee.
19794  JER 31:34  Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»
19868  JER 33:24  «Xanaa dégguloo li nit ñi wax? Ñu ne: “Ñaari làng ya Aji Sax ji tànnoon de, wacc na leen,” moo tax ñu xeeb sama ñoñ, ba tegatuñu leen sax aw xeet.»
19887  JER 34:17  «Kon nag, Aji Sax ji dafa wax ne: “Ku nekk ci yeen waroon naa goreel mbokkum dëkkandoom, waaye yeen déy, déggaluleen ma. Man nag maa ngi nii di leen goreel,” kàddug Aji Sax jee, “ngir wacce leen saamar ak mbas akub xiif. Maa leen di def waa réewi àddina yépp seexlu leen.
19892  JER 34:22  Maa ngi nii di joxe ndigal,” kàddug Aji Sax jee, “délloosi leen ci dëkk bi, ñu song ko, ba nangu ko, taal ko ba mu jeex. Maay gental dëkki Yuda, ba kenn du ca des.”»
20009  JER 39:17  Bésub keroog maa lay xettli,” kàddug Aji Sax jee, “ba deesu la teg ci loxol nit ñi nga ragal.
20589  EZK 3:18  Su ma nee nit ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk àrtuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kaay dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj.
21073  EZK 22:28  Ay yonentam di leen diwal weexal ci kaw loolu lépp, ci peeñuy caaxaan ak ngisaaney fen, naan: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne,” te Aji Sax ji waxul.
21357  EZK 33:8  Bu ma nee ku bon ki: “Yaw ku bon ki, dee rekk mooy sa àtte,” te yaw waxuloo ko ko, àrtu ko ngir mu wacc yoonu mbonam, ku bon kooka aw ayam mooy àtteb deeyam. Waaye bakkanam, yaw laa koy topp.
21482  EZK 37:16  «Yaw nit ki, sàkkal aw dénk, nga bind ci kaw lii: “Ñeel Yuda ak giiri Israyil yi mu àndal.” Nga sàkkaat weneen dénk, bind ci kawam: “Ñeel Yuusufa bantub Efrayim ak waa kër Israyil yi mu àndal,”
22173  HOS 2:1  «Du tere askanu Israyil tollu ni suufas géej. Deesu ko mana natt mbaa di ko waññ, te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,” fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund.”
22175  HOS 2:3  Nanga wooye sa bokk yu góor: “Ñoñi Aji Sax ji,” sa bokk yu jigéen, nga ne leen: “Ñi Aji Sax ji yërëm.”
22190  HOS 2:18  Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «Ca nga may wooye “Sama jëkkër,” te dootoo ma wooye “Sama Baal.”»
22197  HOS 2:25  Maa koy jëmbatal sama bopp ci réew mi, maay yërëm ki tuddoon “Ki ñu yërëmul.” Ki tuddoon “Du sama ñoñ,” ma ne ko: “Yaay sama ñoñ,” moom mu ne ma: “Sama Yàlla.”»
22675  MIC 2:11  Nit man naa wër, toppi caaxaan aki fen, naan: “Maa lay yégal waxyub biiñ aku ñoll,” te kookooy jottlikatub waxyu bi askan wii yelloo!
22950  ZEC 1:3  Kon nag waxal askan wi, ne leen Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Dellusileen ci man,” kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, “kon dinaa dellusi ci yeen.” Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yee ko wax.
22973  ZEC 2:9  Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”
23066  ZEC 8:21  waa dëkk bii dem ne bee: “Nan dema dem dagaani Aji Sax ji, nan sàkkuji Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,” Ñu ne leen: “Nun it kay, nu ngi dem.”»
23102  ZEC 11:5  Ñi leen jënd di leen rendi, te jàpp ne yoon toppu leen ci; ñi leen jaay naan: “Sant Aji Sax ji, woomle nanu,” gétt gi la seeni sàmm yërëmul.
23137  ZEC 13:9  Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»
23162  MAL 1:4  Su Edom nee: “Dees noo rajaxe, waaye nooy tabaxaat gent bi,” Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moom dafa wax ne: “Ñooy tabax, maay màbb.” Ñoom lees di wooye waa diiwaan bu bon bi, askan wi Aji Sax ji mere ba fàww.
23171  MAL 1:13  Yeena ngi naa: “Ndaw lu soof,” di ciipatu.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Jur gu ñu sàcc ngeen may indil, ak guy soox, ak gu wopp, loolu mooy seen sarax! Nu ma koy nangoo ci seeni loxo?» Aji Sax jee ko wax.
25102  LUK 3:8  Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan.
25199  LUK 5:23  Ana lu gëna yomb ci yii yaar: ne “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne: “Jógal te dox”?
25257  LUK 6:42  Ana noo mane ne sa mbokk: “Mbokk mee, xaaral, ma dindil la xatax gi ci sa bët,” te yaw ci sa bopp gànj gi ci sa bët, gisuloo ko? Jinigalkat bi! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët. Su boobaa dinga gis bu baax xatax gi ci sa bëtu mbokk, ba dindil ko ko.
25261  LUK 6:46  «Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax?
25272  LUK 7:8  Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
25480  LUK 11:6  Sama xarit bu nekk ciw yoon moo dikk sama kër, te awma dara lu ma ko taajal,”
25573  LUK 12:45  Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi,
25582  LUK 12:54  Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiine sowu, dangeen dal naan: “Taw baa ngi ñëw,” te noonu lay ame.
25583  LUK 12:55  Bu ngelaw bawoo bëj-saalum, ngeen ne: “Tàngaay wu metti lay doon,” te mooy am.
25724  LUK 17:4  Su la tooñoon juróom ñaari yoon ci bés bi, te walbatiku juróom ñaari yoon, ne la: “Tuub naa ko,” baal ko rekk.»
25726  LUK 17:6  Sang bi ne leen: «Su ngeen amoon ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën sax, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen.
25741  LUK 17:21  Deesul ne it: “Xool-leen, mu ngi” mbaa: “Ma ngee,” ndax kat nguurug Yàlla mu ngi ci seen biir.»
25892  LUK 20:44  Gannaaw Daawudaa wooye Almasi “Sang bi,” nu mu nekke ab sëtam?»
25903  LUK 21:8  Yeesu ne: «Moytuleen, ngir ñu bañ leena nax, ndax ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te naan: “Waxtu wi jege na.” Buleen leen topp.
25970  LUK 22:37  Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.»
28249  ROM 9:26  «Te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,” fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund.”»
30831  REV 3:17  Gannaaw yaa ngi naan: “Am naa alal, barele naa, soxlaatuma dara,” te yaw xamuloo ni nga toroxe, jara yërëm, ñàkk, gumba, ne duŋŋ,
31069  REV 18:7  Joxleen ko ci toskare aku naqar, kemu daraja jaak dund gu bakkane ga mu jagoo woon. Gannaaw moo ne cim xelam: “Maa tooge jalu lingeer, dumab jëtun, duma deele mukk,”