509 | GEN 20:13 | Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”» |
639 | GEN 24:47 | Ma laaj ko ne ko: “Kan moo la jur?” Mu ne: “Betuwel, doomu Naxor ak Milka.” «Ca laa ko takkal jaaro bi ci bakkanam, ak lam yi ciy loxoom. |
886 | GEN 31:12 | Mu ne ma: “Siggil, xool sikket yiy tëb bëy yi yépp, yii dañoo seereer, yee todde, yi ci des tippante, ndaxte gis naa li la Laban di def lépp. |
1350 | GEN 44:25 | «Ba nu demee ba mu yàgg, sunu baay ne: “Delluleen, jëndali nu tuuti dund.” |
1815 | EXO 11:8 | Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees. |
2447 | EXO 32:8 | Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”» |
3815 | NUM 5:22 | Yal na ndoxum alkànde mii tàbbi ci say butit, laxal sa njurukaay, wal sab koll.” Su ko defee ndaw si ne: “Amiin, Amiin.” |
4387 | NUM 22:11 | “Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”» |
4392 | NUM 22:16 | Ñooña dem ba ca Balaam, ne ko: «Balag doomu Sippor dafa wax ne: “Ngalla, bu la dara teree dikk, wuysi ma. |
4440 | NUM 23:23 | Ñeengo jàppul Yanqóoba, gisaane gisul Israyil gii. Lu jot rekk, àggees ko Yanqóoba: ne ko: “Israyiloo, lii la Yàlla def.” |
7520 | 1SA 14:10 | Waaye bu ñu nee: “Ayca, dikkleen,” nu daldi dem te xam ne Aji Sax jee leen teg ci sunu loxo. Nan def loolu ab takk.» |
8426 | 2SA 15:34 | Dangay dellu kay ca dëkk ba, ne Absalom: “Buur, sab jaam laa. Sa jaamu baay laa woon, waaye léegi sab jaam laa.” Noonu nga may yàqale pexem Ayitofel. |
8733 | 1KI 1:13 | Gaawal dem ca Buur Daawuda, ne ko: “Buur, sang bi, du yaa ma giñaloon, yaw sang bi, ne ma sama doom Suleymaan mooy falu buur, wuutu la, te mooy toog ci sa jal bi? Kon nag lu tax Adoña falu buur?” |
8842 | 1KI 3:23 | Buur ne: «Kii a ngi naan: “Sama doom jii mooy dund, sa doom a dee.” Kee naan: “Déedéet, sa doom a dee, sama doom mooy dund.”» |
9142 | 1KI 11:31 | Mu ne Yerbowam: «Jëlalal fii sa bopp fukki dog, ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil da ne: “Gisal, maa ngi dagge nguur gi ci loxol Suleymaan, te dinaa la ci jox fukki giir. |
9190 | 1KI 13:3 | Góor ga joxe na ca bésub keroog ab takk; mu ne: «Takk bii la ci Aji Sax ji biral: “Seetluleen, sarxalukaay bi dina xar ñaar, dóom bi ci kaw sottiku.”» |
9620 | 2KI 4:13 | Mu ne surgaam: «Waxal ma ndaw sii ne ko: “Waaw, yaw de yaa ngi sonn ci nun coono bii bépp! Ana loo bëgg nu defal la ko? Ndax nu waxal la Buur lu jëm ci yaw, am nu wax ak njiital mbooloom xare ma?”» Mu wax ko, mu ne ko: «Jërëjëf, waaye am naa teraanga ci sama biiri bokk.» |
12533 | NEH 9:18 | Dem nañu sax ba móolal seen bopp jëmmu wëllu te naan: “Yeen, seen Yàllaa ngi; moo leen génnee réewum Misra,” ñàkke la kersa lool. |
18303 | ISA 30:16 | Yeena ne: “Déedéet, danuy war fas, daw!” Dingeen daw moos! Ngeen ne: “Daamar yu gaaw lanuy war.” Ñi leen di dàq it di war daamar yu gaaw! |
18630 | ISA 44:27 | Maa naa xóotey mbeex mi: “Wowal, te maay ŋiisal say dex.” |
18727 | ISA 49:21 | Dangay mujj naa: “Moo, ku ma jural ñii ñépp? Man mi ñàkkooni doom, manumaa jur, ñu toxal ma, wacc ma; ana ku leen yoroon te ma des, man kenn? Ñii sax, fu ñu ne woon?”» |
18766 | ISA 51:23 | Maa koy teg ci loxol ñi la doon naqaral, te naan la: “Sëggal, nu joggi, jàll,” nga def sa gannaaw gi aw yoon, ñu joggi, wéy.» |
18830 | ISA 56:7 | mu ne: «Ñooñu, maa leen di yóbbu sama kaw tund wu sell, bànneexale leen sama biir kërug ñaan, seen saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax, dees na leen ko nangul sama kaw sarxalukaay, ndax dees na wooye sama “kër, kërug ñaan”, ñeel xeetoo xeet.» |
19075 | JER 3:4 | Léegi ngeen di ma woo wall naa: “Baay, yaay sama xejj ca ba may ndaw. |
19076 | JER 3:5 | Xanaa deesul mer ba fàww? Xanaa xadar du sax?” Ma ne: “Israyiloo, yeena ko wax, waaye bon ngeen lu ngeen man.”» |
19083 | JER 3:12 | Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne: “Israyiloo, Woyof-Kumba, délsil.” Kàddug Aji Sax jee. “Duma la fasal kanam. Man Boroom ngor laa, te duma jàpp mer ba fàww.” Kàddug Aji Sax jee. |
19101 | JER 4:5 | «Nangeen yégle lii fa Yuda, dégtale ko fa Yerusalem, yéenee koog liit fi biir réew mi te xaacu seen kem kàttan ne leen: “Dajeleen, nu dem ca dëkk ya tata wër.” |
19172 | JER 6:14 | Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, naan: “Jàmm, lépp jàmm!” te jàmm amul. |
19233 | JER 8:11 | Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo, naan: “Jàmm, lépp jàmm!” te jàmm amul. |
19541 | JER 22:18 | Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, ne: «Kenn du ko jooy ca mbokkam mu góor mbaa mu jigéen, naan: “Wóoy ngalla nun, bokk yi!” Kenn du ko jooy, naan: “Wóoy, sang ba, wóoy kilifa ga!” |
19952 | JER 37:9 | Aji Sax ji nag dafa wax ne: Buleen nax seen bopp naan: “Dem, ba nu, la waa Babilon di def.” Ndax duñu dem. |
20128 | JER 46:14 | «Yégleel lii Misra, yéene ko fa ca Migadol, yéene ko fa ca Memfis ak Tapanes. Neleen: “Dërleen, taxaw temm! Saamar kat a ngi lekk li leen wër.” |
20155 | JER 48:6 | Ñu naan: “Dawleen, rawale seen bakkan, ba tumurànkeji ni gajju màndiŋ!” |
20166 | JER 48:17 | Mboolem yeen ñi wër xeet wii, jooyleen leen; yeen ñi dégg seen tur ñépp, jooyleen leen. Neleen: “Moo, nu gii nguur mana foqe, ba foqaale jii daraja?” |
21098 | EZK 23:22 | Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: “Owolibaa, maa ngii di xabtalsi say far ci sa kaw; ñi la sàppi, ñoom laay bàbbee fi la wër, xiirtal leen fi sa kaw: |
21336 | EZK 32:19 | Ne leen: “Misraa, ana koo ëpp ub taar? Tàbbil, ñu boole laak paaxe yi tëral.” |
21534 | EZK 39:17 | «Yaw nit ki nag, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Waxal picc yi ak mboolem njanaaw yi ak rabi àll yépp, ne leen: “Dajalooleen, jóge fu ne, dikk, dajesi ci sama sarax si ma leen di rendil, muy sarax su mag fa kaw tundi Israyil, ngeen lekk yàpp, naan deret. |
22173 | HOS 2:1 | «Du tere askanu Israyil tollu ni suufas géej. Deesu ko mana natt mbaa di ko waññ, te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,” fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund.” |
22397 | JOL 2:17 | Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi, sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, nañu fi taxaw jooy; nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ; bul wacce say séddoo gàcce, ak ñaawley xeeti jaambur yi. Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi, naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”» |
23068 | ZEC 8:23 | Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Janti keroog yooyu, fukk ñuy làkk mboolem làkki xeet yi, ñooy langaamoo catu mbubbu benn Yawut, naan ko: “Nun, yeen lanuy àndal, nde noo dégg ne Yàllaa ngeek yeen.”» |
25102 | LUK 3:8 | Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel, te baña nax seen bopp naan: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan. |
25479 | LUK 11:5 | Yeesu teg ca ne leen: «Ana kan ci yeen moo seeti ab xaritam xaaju guddi, ne ko: “Xarit, lebal ma ci ñetti mburu. |
25632 | LUK 14:10 | Bu ñu la wooyee am xew kay, demal tooge fa gëna gannaawe, ba ka la woo dikk ne la: “Xarit, agsil ci kanam.” Su boobaa muy sa teraanga ci kanam mboolem ña nga bokkal bernde ja. |
25639 | LUK 14:17 | Ba waxtuw lekk jotee, mu yebal ab surgaam ca ña mu woo woon, ne leen: “Ñëwleen, lépp sotti na léegi.” |
25669 | LUK 15:12 | Ka gën di ndaw ne baay ba: “Baay, jox ma cér bi ma yoon may ci sunu alal.” Ba loolu amee baay ba séddale leen alalam. |
25678 | LUK 15:21 | Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; yeyootumaa tuddoo sax sa doom.” |
25688 | LUK 15:31 | Mu ne ko: “Doom, yaw de naka jekk man nga nekkal, te mboolem lu ma am, yaa ko moom. |
25714 | LUK 16:25 | Ibraayma ne ko: “Doom, fàttlikul ne na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile. |
25726 | LUK 17:6 | Sang bi ne leen: «Su ngeen amoon ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën sax, ba ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbate ca géej ga,” su boobaa garab gi déggal leen. |
25727 | LUK 17:7 | «Kan ci yeen la ab jaamam di beyi mbaa mu sàmmi ba jóge tool, dikk, mu ne ko: “Kaay, nu lekk”? |
25768 | LUK 18:11 | Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii. |
25814 | LUK 19:14 | Waaye waa réewam ña dañu koo bañoon. Ci gannaawam lañu yónni ndaw, ne: “Kii, bugguñu muy sunu buur.” |
25817 | LUK 19:17 | Mu ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi. Gannaaw ci lu tuut nga wóore nag, falul ci fukki dëkk.” |
25819 | LUK 19:19 | Mu neeti kooka: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.” |
27212 | ACT 7:27 | Ka doon néewal doole moroom ma bëmëx Musaa, ne ko: “Yaw, ku la def njiit mbaa àttekat ci sunu kaw? |
27359 | ACT 10:31 | Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla. |
27383 | ACT 11:7 | Maa dégg itam baat bu ma ne: “Piyeer, jógal, rey te lekk.” |
27384 | ACT 11:8 | Ma ne: “Mukk, Sang bi, ndax lenn lu daganul mbaa lu setul masula dugg sama gémmiñ.” |
27392 | ACT 11:16 | Ma daldi fàttliku kàddug Sang, ba mu noon: “Yaxya, cim ndox la daan sóobe, waaye yeen, ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob.” |
27729 | ACT 20:35 | Nu nekk laa leen wone ne sunu wartéef mooy nu liggéeye noonu bu baax, ngir dimbali néew-doole yi, tey fàttliku kàddug Sang Yeesu, ga mu noon: “Nangu, joxee ko ëpp barke.”» |
27779 | ACT 22:7 | Ma ne dàll fi suuf, daldi dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?” |
27790 | ACT 22:18 | Ma gis Sang bi, mu ne ma: “Gaawal, daw génn Yerusalem, li nga may seedeel, duñu ko nangu.” |
27793 | ACT 22:21 | Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”» |
27905 | ACT 26:14 | Nu ne dàll fi suuf. Ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut, ne ma: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal? Dangay sonal sa bopp rekk, mbete fas wu manula woŋŋeetu ba wéq dëgël bu koy jam.” |
27947 | ACT 27:24 | Mu ne ma: “Póol, bul tiit; fàww nga taxawi fa kanam Sesaar, te it Yàlla moo la baaxe muccug mboolem ñi nga àndal ci gaal gi.” |
28249 | ROM 9:26 | «Te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,” fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund.”» |