76 | GEN 3:20 | Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund. |
105 | GEN 4:25 | Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.» |
260 | GEN 10:25 | Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (mu firi Séddlikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddlikoo woon. Rakku Peleg mooy Yogtaan. |
276 | GEN 11:9 | Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la leen tasaaree ci kaw suuf sépp. |
393 | GEN 16:11 | tegaat ca ne ko: «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; nanga ko tudde Ismayla (mu firi Yàlla dégg na), ndax Aji Sax ji yég na sa naqar. |
395 | GEN 16:13 | Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» |
403 | GEN 17:5 | Te tuddatuloo Ibraam; léegi yaa di Ibraayma (mu firi Maamu ñu bare), ndax maa la def ngay maamu xeet yu baree bare. |
545 | GEN 21:31 | Looloo tax ñu tudde teen boobu Beerseba (mu firi Teenu waat ga), ndaxte fa lañu waatoo woon ñoom ñaar. |
713 | GEN 26:20 | Teewul sàmmi Gerar di soowook sàmmi Isaaxa naan: «Nun noo moom ndox mi.» Mu tudde teen ba Eseg (mu firi Coow), ndax li ñu soowoo ak moom. |
715 | GEN 26:22 | Mu jóge foofa, gasati teen, jàmm ne ñoyy, mu tudde ko Reyobot (mu firi Fu yaatu), ndax da ne: «Léegi Aji Sax ji yaatal na nu, te dinanu woomle ci réew mi.» |
726 | GEN 26:33 | Isaaxa tudde teen ba Siba (mu firi Waatoo), moo tax turu dëkk ba, ba fii nu tollu, di Beerseba (mu firi Teenu waat ga). |
828 | GEN 29:32 | Ba Leya ëmbee, am doom ju góor, da koo tudde Ruben (mu firi Gisleen, doom ju góor a ngi), ndaxte Leya da ne: «Aji Sax ji gis na sama toroxte. Léegi sama jëkkër dina ma bëgg.» |
855 | GEN 30:24 | Moo tax mu tudde ko Yuusufa (mu firi Yal na dolli), ndax dafa ne: «Yal na ma Aji Sax ji dollil doom ju góor.» |
923 | GEN 31:49 | Ñu di ko tudde itam Mispa (mu firi Tatay wattukaay), ndax Laban da ne: «Yal na Aji Sax ji wattu sunu diggante, keroog bu ñu soree. |
959 | GEN 32:31 | Ci kaw loolu Yanqóoba tudde bérab ba Peniyel (mu firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.» |
1247 | GEN 41:51 | Yuusufa tudde taaw ba Manase (mu firi Ki ma taxa fàtte), ndaxte da ne: «Li ma sonn ak li ma sore sama kër baay lépp, Yàlla fàtteloo na ma ko.» |
1248 | GEN 41:52 | Doomam ja ca topp mu tudde ko Efrayim (mu firi Giir), ndaxte da ne: «Yàllaa ma giiral ca réew, ma ma sonne.» |
1565 | EXO 2:10 | Ba xale ba màggee, mu yót ko doomu Firawna, mu def ko muy doomam, tudde ko Musaa (mu firi Ki ñu génne), ndax la mu ko génnee ca ndox ma. |
1577 | EXO 2:22 | Mu am doom ju góor, Musaa tudde ko Gersom (mu firi Doxandéem fii), ndaxte dafa ne: «Doxandéem laa fii.» |
1991 | EXO 17:7 | Bérab boobu la Musaa wooye Maasa (mu firi Nattu). Mu wooye ko itam Meriba (mu firi ab Jote), ndax joteb bànni Israyil ba fa amoon, ak na ñu fa nattoo Aji Sax ji, naan: «Moo Aji Sax ji ndax mu ngi ci sunu biir, am déet?» |
2003 | EXO 18:3 | boole kook ñaari doomi Musaa yu góor ya, kenn ka di Gersom (mu firi Doxandéem fii), ndaxte Musaa da ne woon: «Doxandéem laa fii.» |
2004 | EXO 18:4 | Ka ca des mu tudde ko Elyeser (mu firi Yàlla dimbali na ma), ndax da ne woon: «Sama Yàllay baay mooy sama ndimbal te moo ma musal ci saamaru Firawna.» |
4028 | NUM 11:3 | Ñu tudde bérab boobu Tabera (mu neexook Tàkkaan), ndax sawaras Aji Sax ji leen fa tàkkal. |
4570 | NUM 27:14 | gannaaw yeena diiŋat sama ndigal ca màndiŋu Ciin, fa mbooloo ma jote woon ak man. Yeena wormaalul sama sellnga ca kanam mbooloo ma, ca ndox ma. Mooy walum Meriba, (mu firi Jote ba), ma woon ca Kades, ca màndiŋu Ciin.» |
7149 | RUT 1:20 | Mu ne leen: «Buleen ma ne Nawmi (mu firi Boroom mbégte mi), neleen ma Mara (mu firi Boroom naqar wi), ndax Aji Man ji da maa teg naqar wu réya réy. |
7234 | 1SA 1:20 | Aana mujj ëmb ca ndeetel at ma. Gannaaw gi mu am doom ju góor, tudde ko Samiyel (mu firi Yàlla dégg na), ndax da ne: «Maa ko ñaan Aji Sax ji.» |
8168 | 2SA 6:8 | Ba loolu amee Daawuda mer ca mbugal mu metti ma Aji Sax ji teg Usa. Moo tax mu tudde bérab booba Peres Usa (mu firi Mbugalum Usa), muy turam ba tey jii. |
8958 | 1KI 7:21 | Mu samp jën yi ci kanam bunt néeg Yàlla bu mag bi; samp jënu ndijoor wi, tudde ko Yakin (Kiy taxawal), samp jënu càmmoñ wi, tudde ko Bowas (Kiy dooleel). |
22169 | HOS 1:6 | Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruwana» (mu firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israyil, dootuma leen baal. |
22172 | HOS 1:9 | Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (mu firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.» |
23190 | MAL 3:1 | «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. |