635 | GEN 24:43 | maa ngii taxaw ci seyaan bi; janq bay ñëw rootsi, ma ne ko: ‘Doo ma may tuuti ci sa njaq li, ma naan,’ |
636 | GEN 24:44 | mu ne ma: ‘Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,’ kooku na di soxna, si Aji Sax ji jagleel sama doomu sang.” |
19198 | JER 7:10 | tey dikk taxaw fi sama kanam, biir kër gii ñu ma tudde, te naan: ‘Nun kay raw nanu,’ ba tax ngeen di def mboolem lu siblu lii? |
20783 | EZK 13:6 | Seeni peeñu caaxaan la, seeni ngisaane diy fen. Ñu naa: ‘Kàddug Aji Sax jee,’ te Aji Sax ji yebalu leen! Teewul ñuy xaar kàddu gu sotti. |
20784 | EZK 13:7 | Xanaa du peeñuy caaxaan ngeen gis? Du ngisaaney fen ngeen di waxe, naan: ‘Kàddug Aji Sax jee,’ te man àdduwma? |
21363 | EZK 33:14 | Su ma nee ku bon ki: ‘Yaw dee rekk mooy sa àtte,’ mu mujj dëddu bàkkaaram, di jëfe njub ak njekk, |