2083 | EXO 21:5 | Waaye su jaam bi biralee ne: “Maa bëgg sama sang, maak sama jabar ak samay doom, te buggumaa moom sama bopp”, |
17878 | ISA 8:1 | Gannaaw gi Aji Sax ji ne ma: «Jëlal àlluwa ju mag, ak xalima gu jàppandi, nga bind ci lii: “Maxer Salal Xas Bas”, (mu firi Sëxëtoo këfit foqet).» |
18830 | ISA 56:7 | mu ne: «Ñooñu, maa leen di yóbbu sama kaw tund wu sell, bànneexale leen sama biir kërug ñaan, seen saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax, dees na leen ko nangul sama kaw sarxalukaay, ndax dees na wooye sama “kër, kërug ñaan”, ñeel xeetoo xeet.» |