Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   Word-Word    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

21  GEN 1:21  Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na.
33  GEN 2:2  Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp.
34  GEN 2:3  Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp.
50  GEN 2:19  Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom.
72  GEN 3:16  Yàlla teg ca ne jigéen ja: «Dinaa taral sa metitu mat, ci metit ngay wasin. Sa bëgg-bëggu bakkan dina la xiir ci sa jëkkër, te moo lay teg tànk.»
130  GEN 5:24  Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom.
184  GEN 7:24  Ndox mi nag di wal-wali ci kaw suuf diirub téeméeri fan ak juróom fukk.
333  GEN 13:14  Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu,
352  GEN 14:15  Ibraam dafa xàjjale mbooloom, dal ci kaw buur ya guddi, dàq leen, topp ci ñoom ba Koba, ca bëj-gànnaaru Damaas.
377  GEN 15:16  Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi jéggeegul dayo.»
471  GEN 19:13  ndax dinanu ko tas de. Aji Sax ji dégg na jooytu yu réy, yi niti dëkk bi sabab, ba tax mu yónni nu, ngir nu tas-si ko.»
554  GEN 22:6  Ba loolu amee Ibraayma jël mattum saraxu rendi-dóomal ba, yen ko doomam Isaaxa; moom mu ŋàbb la muy taale ak paaka ba ci loxoom, ñu ànd ñoom ñaar.
641  GEN 24:49  Léegi nag ndegam nar ngeena rafetoo ak sama sang tey sàmm kóllëre, xamal-leen ma ko, ba mu leer. Su ngeen ko narul it, waxleen ma, ma xam nu may def.»
868  GEN 30:37  Ci kaw loolu Yanqóoba tànn ñetti garab yu ñuy wax pëpalyee, gerte-tubaab ak palataan, gor ci bant yu tooy, xànc-xàncee ko, ba mu defi rëdd yu weex.
959  GEN 32:31  Ci kaw loolu Yanqóoba tudde bérab ba Peniyel (mu firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.»
993  GEN 34:12  Limal-leen ma warugar yi ak nu mu mana tollu, boole ci may gi; dinaa joxe lu ngeen ma sas; mayleen ma janq bi rekk.»
1014  GEN 35:2  Yanqóoba wax ak waa këram ak ñi ànd ak moom ñépp ne leen: «Jëleleen ci seen biir tuuri doxandéem yi, te ngeen sangu-set te solu.
1071  GEN 36:30  ak Dison ak Eser ak Disan, ku ci nekk ak làngam. Ñooñooy làngi waa Or, na ñu xàjjalikoo kenn-kenn ca réewu Seyir.
1091  GEN 37:7  Danoo nekk ca tool ya, di góob. Ba nu takkee, sama takk jekki-jekki ne sàtt, taxaw, seen takk wër sama takk, di ko sujjóotal.»
1159  GEN 39:9  Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?»
1174  GEN 40:1  Ba loolu wéyee kiy topptoo naani buuru Misra ak lakk-katu mburoom dañoo tooñ buuru Misra, seen sang.
1175  GEN 40:2  Firawna nag mere lool ñaari jawriñ yooya, kenn ka di kilifay ñay topptoo naani buur, ka ca des di kilifay lakk-kati mburu ya,
1189  GEN 40:16  Kilifag lakk-kati mburu ya nag gis ne piri mi neex na, mu ne Yuusufa: «Man it sama gént gi, xam nga lu ma ci gis? Ñetti pañey mburu mu weex laa yenu,
1193  GEN 40:20  Ñu teg ca ñetti fan, Firawna di màggal bésu juddoom, dajale jawriñam yépp, di leen berndeel, daldi cay seppee kilifa gay topptoo ay naanam, ak kilifag lakk-kati mburu ya, siggil leen.
1195  GEN 40:22  Kilifag lakk-kati mburu ya moom, da koo wékk ci bant, na leen ko Yuusufa firile woon.
1204  GEN 41:8  Ba bët setee, Firawna jaaxle lool, ba woolu jibar ya ak boroom xam-xami Misra yépp, nettali leen la mu gént, te kenn manu koo firil Firawna.
1206  GEN 41:10  Sang bi, ba nga nu meree, yaw Firawna, ba tëj ma kaso ca kër njiitu dag ya, man ak kilifag lakk-kati mburu ya,
1303  GEN 43:12  Te ngeen yóbbaale ci xaalis lu tollook ñaar-cay la ngeen jënde woon, ngir feyaale loola, ndax jombul njuumte la woon.
1306  GEN 43:15  Gaa ña jël nañu sarica booba, yóbbaale nañu it ñaar-cay xaalis ba, daldi ànd ak Beñamin, ñu dem Misra, teewi ca kanam Yuusufa.
1486  GEN 49:12  Bët yaa ngay nes-nesi ndax biiñ, bëñ ya weex furr ndax um soow.
1641  EXO 5:8  Waaye sasleen leen limu móol, ya ñu daan móol naka jekk. Buleen ko wàññi, ndax ay yaafus lañu; moo leen tax di dee-deeluy waxeey naan: “May nu, nu dem rendili sunu Yàlla sarax!”
1697  EXO 7:11  Ba mu ko defee Firawna moom itam woo boroom xam-xam yaak jibar ya. Ñeengokati Misra ya ñoom it fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona.
1714  EXO 7:28  Dexu Niil gi day ramm-rammeeki mbott, te dinañu ñëw, duggsi sa biir kër, ak sa néegu biir, ak sa kaw lal, ak sa këri dag, ak sa waa réew, ba ca lakkukaay yaak notukaayi mburu ya.
1739  EXO 8:24  Firawna àddu ne: «Dinaa leen may, ngeen dem ca màndiŋ ma, rendili seen Yàlla Aji Sax ji sarax, waaye buleen sore lool. Ñaanal-leen ma nag.»
1760  EXO 9:17  Ndaxam yaa ngi réy-réylu ci sama kaw ñoñ ba tey, bañ leena bàyyi, ñu dem.
1881  EXO 13:13  Waaye lépp lu mbaam-sëf taawloo, nangeen ko jote kuuyum xar, mu wuutu ko. Bu ngeen ko jotul, nangeen damm loos wi. Te itam jotleen képp kuy taaw bu góor ci seeni doom.
1892  EXO 14:2  «Waxal bànni Israyil, ne leen ñu walbatiku dali fa jàkkaarlook Pi Axirot, ca diggante Migadol ak géeju Barax ya. Dal-leen foofa jàkkaarlook Baal Cefon ca tefes ga.
1953  EXO 16:5  Waaye bu ñu demee ba bésub juróom benneel ba, ba togg la ñu ca indi, day tollook ñaar-cay dayo ba ñuy for bés bu set.»
1971  EXO 16:23  mu ne leen: «Loolu la Aji Sax ji wax, te li muy tekki mooy: ëllëg bésu dal-lu la, di bésub Noflaay bu sell ñeel Aji Sax ji. Lakkleen li ngeen di lakk, baxal li ngeen di baxal, te lu ci des, ngeen denc ba suba.»
2012  EXO 18:12  Yettro, gorob Musaa, daldi sàkk saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax, jagleel ko Yàlla. Aaróona ak magi Israyil ñépp dikk, ñu bokk lekk ñook gorob Musaa fa kanam Yàlla.
2026  EXO 18:26  Ñuy àtte nag mbooloo ma saa su nekk. Su dee mbir mu lëj, ñu indil Musaa; mboolem mbir yu sew-sewaan ya, ñoom ñu àtte ko.
2037  EXO 19:10  Gannaaw loolu Aji Sax ji waxaat Musaa ne ko: «Dellul ca mbooloo ma, te nanga leen sell-luloo tey ak ëllëg. Nañu fóot seeni yére,
2038  EXO 19:11  te waajal gannaaw-ëllëg, ndax gannaaw-ëllëg man Aji Sax ji maay wàcc ci kaw tundu Sinayi ci kanam mbooloo mépp.
2041  EXO 19:14  Ba loolu amee Musaa wàcc tund wa, dellu ca mbooloo ma. Mu sell-luloo leen, ñu fóot seeni yére,
2043  EXO 19:16  Keroog ca gannaaw-ëllëg sa, naka la njël jot, muy dënook a melax, ànd akaw niir wu fatt ca kaw tund wa, ak coowal liit gu xumb. Waa dal ba bépp a nga tiit, bay lox.
2045  EXO 19:18  Fekk na tundu Sinayi wa wépp di sël-sëleeku saxar, ndax Aji Sax ja fa wàcc ci biir sawara. Saxar saa ngay gilli ni saxaru puuru ban, tund wépp di yëngook doole,
2086  EXO 21:8  Su ko sangam jëndee, def ko jabar, ba noppi bëggatu ko, na fexe ñu feyal ndaw si ag njotam, waaye amul sañ-sañu jaay ko ay doxandéem, ndax loolu wor la.
2099  EXO 21:21  Waaye su jaam ba dundee ba ca ëllëg sa, mbaa gannaaw-ëllëg sa, deesu ko feyul ndaxte moomeelu sangam la.
2103  EXO 21:25  lakk-lakk fey lakk-lakk, tëccu-tëccu fey tëccu-tëccu, góom fey góom.
2148  EXO 23:3  Néew-doole bi it, buleen ko far cib layoo.
2150  EXO 23:5  Su ngeen gisee seen mbaamu noon mu ab sëf daaneel, buleen ko romb; dimbalileen seen noon, yékkatil-leen ko ko.
2156  EXO 23:11  waaye atum juróom ñaareel ma, noppal-leen tool bi, booyal ko; seen néew-dooley askan wi man cee lekk, li ci des, rabi àll yi for ko. Seen toolub reseñ ak seen tóokëru oliw itam, naka noonu.
2160  EXO 23:15  Màggalu Mburu mu amul lawiir, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir ni ma leen ko sante, saa yu jamonoom jotee ci weeru Abiib, ndaxte ci ngeen génn Misra. Te itam buleen taxawe loxoy neen ci sama kanam.
2161  EXO 23:16  Wormaal-leen màggalu bésu Ngóob mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi.
2175  EXO 23:30  Ndànk-ndànk laa leen leen di dàqal, ba kera ngeen di yokku, ba nangu réew mi.
2184  EXO 24:6  Musaa jël genn-wàllu deret ja, sotti ci ay ndab, la des ca deret ja, mu xëpp ko ca sarxalukaay ba.
2186  EXO 24:8  Musaa jël deret ja, wis-wisal ca kaw mbooloo ma, ne leen: «Lii nag mooy deret ji Yàlla fase kóllëre gi mu séq ak yeen te mu aju ci mboolem kàddoom yii.»
2203  EXO 25:7  ak peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci xar-sànnim sarxalkat bu mag ba ak kiiraayal dënnam.
2229  EXO 25:33  Benn car day am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, car ba ca topp am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd aki kàmbóotam aki mbaram, juróom benni car, ya soqikoo ca per ba, daj.
2230  EXO 25:34  Gannaaw loolu peru tegukaayu làmp ba itam day am ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram.
2248  EXO 26:12  Liy lang te ëppe ci sori xayma bi nag, di beneen genn-wàllu sor bi, na lange ci gannaaw jaamookaay bi.
2256  EXO 26:20  Geneen wetu jaamookaay gi féete bëj-gànnaar itam, na doon ñaar fukki làcc
2271  EXO 26:35  Tegal taabal ja ca biti, ca kanam rido ba, te nga teg tegukaayu làmp ba ca wetu bëj-saalumu jaamookaay ba, mu jàkkaarlook taabal ja, taabal ja nag, nga tege ko wetu bëj-gànnaar.
2298  EXO 28:4  Yii yére nag lañu koy defaral: kiiraayal dënn ak ab xar-sànni ak ab fëxya, ak mbubb mu gudd mu ñu ràbb, ak kaala ak laxasaay. Yérey sellnga lañuy defal sa mag Aaróona ak doomam yu góor, ngir ñu di ma sarxalal.
2300  EXO 28:6  «Nañu ràbbe xar-sànni mi wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ci ay nataal.
2301  EXO 28:7  Ñaari ngàlli mbagg yu ñuy faste la xar-sànni miy am, ñu di leen fastee ci ñaari cat yi.
2302  EXO 28:8  Ngañaay liy tege ci kaw xar-sànni mi, ni xar-sànni mi lañu koy liggéeye, mu ànd ak moom, di benn, di wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe.
2306  EXO 28:12  Tappal ñaari per yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, per yi wuutu bànni Israyil, Aaróona gàddu seeni tur ci kaw ñaari ngàlli waggam, fi kanam Aji Sax ji, ngir saxal ag pàttliku.
2309  EXO 28:15  «Nanga sàkk kiiraayal dënn bi ñuy jëfoo cib àtte, ñu liggéeyaale ko ay nataal ni xar-sànni mi, te nañu ko ràbbe wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe.
2319  EXO 28:25  Yeneen ñaari cati buumi wurus yi, nga we leen ci ñaari ŋankukaay, yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, ci kanam.
2320  EXO 28:26  Sàkkal ko it ñaari jaaroy wurus yu ñuy we ci ñaari cati suufi kiiraay li, fi féete biir, wet gi tafu ci xar-sànni mi.
2321  EXO 28:27  Nga sàkkalaat ko yeneen ñaari jaaroy wurus yooy we ci suufu ngàlli xar-sànni mi, fi féete kanam, dendeek sofu ngàll yi, te tiim ngañaayu xar-sànni mi.
2322  EXO 28:28  Kiiraayal dënn bi, buum gu sew gu baxa te laal yolet, moom lees koy téyee, lëkklee ko jaaroy kiiraay leek jaaroy xar-sànni mi, su ko defee kiiraay li dëkke tiim ngañaay li, ba du teqlikook xar-sànni mi.
2325  EXO 28:31  «Fëxya bi xar-sànni miy tege, lépp, wëñ gu baxa te laal yolet nga koy liggéeye ba mu daj.
2342  EXO 29:5  Nga jël yére yi nag, solal Aaróona mbubb mu gudd mi, ak fëxyab xar-sànni mi, teg ci xar-sànni mi, tegaat ci kiiraayal dënn bi, daldi koy takkal ngañaay liy tege ci xar-sànni mi.
2350  EXO 29:13  Jëlal mboolem nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yi ànd ak nebbon bi ci kaw dëmbéen yi, nga boole lépp def ko saraxu taal-saxaral ci kaw sarxalukaay bi.
2355  EXO 29:18  Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.
2358  EXO 29:21  Sàkkal ci deret ji ci sarxalukaay bi, ak ci diwu pal gi, nga wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ci kawi yéreem, wis-wisal ko ci kaw yarami doomam ak ci seen kawi yére. Su ko defee Aaróona sell, mooki yéreem, ay doomam it sell, ñook seeni yére.
2362  EXO 29:25  Nga daldi koy nangoo ci seeni loxo, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi, boole kook saraxu rendi-dóomal bi, muy xeeñ xetug jàmm fi kanam Aji Sax ji. Saraxu sawaraa ngoogu, ñeel Aji Sax ji.
2379  EXO 29:42  Saraxu rendi-dóomal lay doon bu sax, te war seen maasoo maas fi bunt xaymab ndaje mi, ci kanam Aji Sax ji. Foofu laay dajeek yeen, te fa laay waxe ak yaw,
2396  EXO 30:13  «Lii nag mooy li képp ku ñu bind ci limeef yi wara fey: dogu xaalis bu diisaay bi di genn-wàllu siikal, bi ñuy natte ci jaamookaay bi, dayo boobu tollook fukki gera, mu dib jooxe, ñeel Aji Sax ji.
2398  EXO 30:15  Ki woomle du fey lu ëpp, ki néewle du fey lu yées genn-wàllu siikal, buy fey jooxeb Aji Sax ji ngir njot-gi-bakkanam.
2408  EXO 30:25  Loolu ngay def diwu pal gu sell gi, te na doon njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax. Diwu pal gu sell lay doon.
2411  EXO 30:28  Nanga ci diw itam sarxalukaayu saraxu rendi-dóomal bi, ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom.
2417  EXO 30:34  Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Wutal nag xeeñal yii: ndàbbu estaagte, ak ndàbbi galbanom, ak xori onigsë yu xeeñ, ak cuuraay-libaŋ lu raxul, te yooyu yépp tolloo dayo.
2418  EXO 30:35  Def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax, xorom ko, mu set, sell.
2430  EXO 31:9  ak sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom,
2435  EXO 31:14  Wormaal-leen bésub Noflaay ndax lu sell la, ñeel leen. Ku ko teddadil, dee rekk mooy àtteem: képp ku ci liggéey, kooku dees na ko dagge ci biiri bokkam.
2464  EXO 32:25  Musaa nag gis ni mbooloo mi ràkkaajoo, ndax fekk na Aaróona bay-bayal leen, ba ñu ràkkaaju, ba ku leen doon fexeel man leena ree.
2485  EXO 33:11  Aji Sax ji da daan wax ak Musaa ne ko jàkk, mu ne ko jàkk, ni nit di waxe ak moroomam rekk. Bu ca Musaa jógee, daldi dellu ca dal ba, waaye bëkk-néegu Musaa, ngóor sa Yosuwe doomu Nuun daawul génn biir xayma ba.
2496  EXO 33:22  Bu sama leer di romb, maa lay làq fi xar-xaru doj wi, yiiraale la sama loxo, ba jàll,
2509  EXO 34:12  Moytuleena wóllëranteek niti réew ma ngeen jëm, bala ñoo doon ndëgg-sërëx ci seen biir.
2515  EXO 34:18  «Màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir, ni ma la ko sante bu àppam taxawee ci weeru Abiib, ndaxte weeru Abiib ngeen génne fa Misra.
2519  EXO 34:22  «Màggalug ayi bési Ngóob, nangeen ko wormaal, bu ngeen di góob gubi bele yi jëkka ñor, màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi itam, màggal-leen ko.
2541  EXO 35:9  ak ay peri onigsë ak yeneen per yuy tappe ci xar-sànni meek kiiraayal dënn bi.
2548  EXO 35:16  ak sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ak caaxub xànjaram aki njàppoom ak li muy àndal lépp; mbalkam njàpp mi akub tegoom,
2559  EXO 35:27  Njiit yi nag indi ay peri onigsë ak yeneen per yiy tappe ci xar-sànni meek kiiraayal dënn bi,
2563  EXO 35:31  Moo ko feesale xelum Yàlla ak xareñte ak déggin ak xam-xam ak manoorey bépp xeetu liggéey,
2592  EXO 36:25  Geneen wetu jaamookaay gi féete bëj-gànnaar itam, ñu def ko ñaar fukki làcc,
2624  EXO 37:19  Ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd ñoo nekk ci benn car bi, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd nekk ci car bi ci topp, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ba juróom benni car, yi soqikoo ci per bi, daj.