204 | GEN 8:20 | Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal Aji Sax ji sarxalukaay, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy saraxu rendi-dóomal. |
561 | GEN 22:13 | Naka la Ibraayma siggi rekk, yem ci menn kuuyum xar mu béjjén ya lonke ci as ngarab. Ibraayma dem, jël kuuy ma, rendi, mu wuutu doom ja, di ab saraxu rendi-dóomal. |
874 | GEN 30:43 | Waa ji mujj na barele lool, am gàtt yu ne gàññ ak ay jaam yu góor ak yu jigéen ak ay giléem aki mbaam-sëf. |
1803 | EXO 10:25 | Musaa ne ko: «Danga noo wara bàyyee lu nuy sarxalal sunu Yàlla, Aji Sax ji, ak yu ñu koy defal saraxu rendi-dóomal. |
2063 | EXO 20:11 | Ndax man Aji Sax ji, juróom benni fan laa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem li ci biir, bésub juróom ñaareel ba, ma dal-lu. Moo tax man Aji Sax ji ma barkeel bésub Noflaay, sellal ko. |
2191 | EXO 24:13 | Musaa daldi jóg, mook Yosuwe, bëkk-néegam. Musaa nag yéeg ca tundu Yàlla wa. |
2206 | EXO 25:10 | «Defarleen gaalu dénku séng, guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll; taxawaayam di xasab ak genn-wàll. |
2213 | EXO 25:17 | «Defarlul kubeer gu ñuy amale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll. |
2219 | EXO 25:23 | «Defarlul taabalu bantu séng, guddaayam di ñaari xasab, yaatuwaayam di xasab, taxawaayam di xasab ak genn-wàll. |
2251 | EXO 26:15 | «Sàkkalal jaamookaay bi ay làcci bantu séng yuy sampe. Na làcc wu nekk am ñaari kenu yu ñu lëkklee galan yu ndaw, te nga def làcci jaamookaay bi yépp noonu. Na taxawaayu làcc wu nekk di fukki xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. |
2271 | EXO 26:35 | Tegal taabal ja ca biti, ca kanam rido ba, te nga teg tegukaayu làmp ba ca wetu bëj-saalumu jaamookaay ba, mu jàkkaarlook taabal ja, taabal ja nag, nga tege ko wetu bëj-gànnaar. |
2518 | EXO 34:21 | «Juróom benni fan nag ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, dal-luleen. Bu ngeen doon bey, bu ngeen doon góob, dal-luleen. |
2587 | EXO 36:20 | Gannaaw gi ñu sàkkal jaamookaay bi ay làcci bantu séng yu sampe. Làcc wu nekk am ñaari kenu yu ñu lëkklee galan yu ndaw, te noonu lañu def làcci jaamookaay bi yépp. Fukki xasab lañu def taxawaayu làcc wu nekk, def yaatuwaay bi xasab ak genn-wàll. |
2606 | EXO 37:1 | Besalel nag defare gaalu kóllëre gi dénku séng, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. |
2611 | EXO 37:6 | Ci kaw loolu mu sàkk kubeeru saraxu njotlaay gu wurusu ngalam, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. |
2615 | EXO 37:10 | Ci biir loolu Besalel sàkk taabalu bantu séng, guddaay bi di ñaari xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. |
2757 | LEV 1:11 | Na rendi sarax si ci kanam Aji Sax ji, fa féete sarxalukaay bi bëj-gànnaar. Na doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi. |
2825 | LEV 4:29 | Day teg loxoom ci boppu gàttu sarax soosu di póotum bàkkaar, rendi ko fa ñuy lakk saraxu rendi-dóomal. |
2838 | LEV 5:7 | «Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil Aji Sax ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di saraxu póotum bàkkaar, bi ci des di sarax rendi-dóomal. |
3134 | LEV 14:22 | ak ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, lu mu ci gëna jekku rekk. Menn mi saraxu póotum bàkkaar la, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. |
3184 | LEV 15:15 | Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di saraxu póotum bàkkaar, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju. |
3199 | LEV 15:30 | Sarxalkat bi day rendi menn mi muy saraxu póotum bàkkaar, mi ci des doon saraxu rendi-dóomal. Su ko defee sarxalkat bi defal ko ko njotlaay fi kanam Aji Sax ji ndax sobey xëpp ja. |
3205 | LEV 16:3 | «Ni Aaróona di dugge ci biir bérab bu sell bee sell nii la: day indaale aw yëkk wu ndaw ngir ab saraxu póotum bàkkaar, akum kuuy ngir ab saraxu rendi-dóomal. |
3207 | LEV 16:5 | Na jële ci mbooloom bànni Israyil ñaari sikket, sikket yuy doon saraxu póotum bàkkaar ak menn kuuyum rendi-dóomal. |
3415 | LEV 23:12 | Bés bi ñuy yékkati takk bi, jébbale, nangeen ci sarxal kuuy mu amul sikk, tollu ci menn at, ñu defal ko Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal. |
3416 | LEV 23:13 | Saraxu pepp mi muy àndal juróom benni kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, ñu xiiwe ko diw, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm. Sarax si ñuy tuural Aji Sax ji, liitaru biiñ laak genn-wàll. |
3844 | NUM 6:20 | «Na sarxalkat bi jébbale loola, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbal. Cér yu sell a ngoogu ñeel sarxalkat bi, mu boole kook dënn biy saraxu yékkati-jébbal, ak jooxeb tànkub kanam bi. Gannaaw loolu nasireen bi sañ naa naan biiñ. |
3955 | NUM 8:15 | Gannaaw loolu la Leween ñiy doora dugg ci liggéeyu xaymab ndaje mi. Danga leen di jëkka setluloo, ba noppi def leen saraxu yékkati-jébbal. |
4022 | NUM 10:33 | Ci kaw loolu ñu bàyyikoo ca tundu Aji Sax ja, doxe fa doxub ñetti fan. Gaalu kóllërey Aji Sax jaa nga leen jiitu diiru ñetti fan ña, di leen wutal dal-lukaay. |
4059 | NUM 11:34 | Moo tax ñu tudde bérab booba Kibbrot Taawa (mu firi Bàmmeeli ŋaf-ŋaf), ndax fa lañu denc néewi mbooloo ma doon ŋaf-ŋafi. |
4222 | NUM 16:27 | Ñu daldi jóge mboolem fa wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñoom, ña nga génn, taxaw ca seen bunti xayma, ñook seeni jabar ak seeni doom, ak seeni tuut-tànk. |
4366 | NUM 21:25 | Israyil nangu dëkki Amoreen yooyu yépp, daldi sance mboolem seeni dëkk, boole ca Esbon aki dëkk-dëkkaanam. |
4584 | NUM 28:5 | Benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, mooy saraxu pepp bi xar mu nekk di àndal, ñu tooyale ko walaatu xiinu diwu segalu oliw, di liitar ak genn-wàll. |
4825 | NUM 34:7 | «Lii nag mooy seen kemu bëj-gànnaar. Ca géej gu mag ga ngeen di rëdde, ba ca tundu Or, |
4827 | NUM 34:9 | wéyeeti fa, jaare Sifron, jëm Àccar Enan. Loolooy seen kemu bëj-gànnaar. |
4943 | DEU 2:3 | «Seen wërub tund wii doy na. Walbatikuleen, jublu bëj-gànnaar. |
5412 | DEU 19:4 | Mbirum ki rey nit te di fa làquji ba mucc, nii lay tëdde: day fekk mu rey moroomam te du teyeefam, waaye bañu ko woon démb ak bëkk-démb. |
5414 | DEU 19:6 | Toppkatu bakkan ba nag warul mana dabi ci biir xolam bu tàng, ki rey, ba rey ko ngir sorewaayu yoon wa jëm ca dëkkub rawtu ba, te àtteb yoon reyluwu ko, gannaaw fekkul woon mu bañ ka mu rey, démb ak bëkk-démb. |
5784 | DEU 32:24 | Ñooy loof cib xiif, jeex tàkk ndaxi jàngoro, ak mbas yu metti. Ay selli rabi àll laay yebal ci seen kaw, boole ca daŋaru ndox-suuf. |
7162 | RUT 2:11 | Mu ne ko: «Dégg naa bu baax li nga defal sa goro lépp, te fekk sa jëkkër faatu, ak ni nga wone gannaaw sa ndey ak sa baay ak sa réewum cosaan, ba ñëw dëkksi ci biir xeet woo xamuloon démb ak bëkk-démb. |
7347 | 1SA 6:14 | Watiir ba dikk ba ci toolu jenn waayu Bet Semes ju ñuy wax Yosuwe, mu taxaw fa. Aw doj wu mag a nga fa woon. Ci kaw loolu ñu xar mattum watiir ba, nag ya, ñu defal ko Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal. |
7363 | 1SA 7:9 | Samiyel jël menn xar mu feragul, defal ko lépp Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal. Mu jooytul Israyil ci Aji Sax ji, Aji Sax ji nangul ko. |
7640 | 1SA 17:20 | Daawuda teela jóg ca ëllëg sa, wacce gàtt ya ab wattukat, daldi jël yóbbal ga, dem na ko ko baayam sante. Naka la àgg ca dal ba, yemook gàngoor gay génnaale seen xaacuy xare, ngir làng-déri. |
7773 | 1SA 20:41 | Xale ba dem, Daawuda jóg, génne ca làquwaayam ba fare bëj-saalum. Mu ne gurub, dëpp jëëm fa suuf, sujjóot ñetti yoon, ku nekk fóon sa moroom, ñoom ñaar ñépp jooy, te Daawuda rawati. |
7832 | 1SA 23:19 | Ba loolu amee waa Sif dem Gibeya ca Sóol, ne ko: «Daawuda de, ma nga làqu fa nun. Ma nga ca xunti yu kawe ya ca Orsa, ca kaw tundu Akila, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum. |
7837 | 1SA 23:24 | Ba loolu amee waa Sif jiituji Sóol ca Sif. Fekk na Daawudaaki nitam ña nga woon ca joor ga ca màndiŋu Mawon, fa féete màndiŋ ma bëj-saalum. |
7994 | 1SA 30:13 | Daawuda ne ko: «Yaw, kuy sab sang ak foo bokk?» Xalelu góor ba ne ko: «Man waa Misra laa, di jaamub jenn waayu Amalegeen. Sama sang a ma wacc, ba ma woppee bëkkaati-démb. |
8059 | 2SA 2:7 | Léegi nag dëgërluleen te góor-góorlu. Dëgg la seen sang Sóol faatu na, waaye man mii la giirug Yuda fal, may seen buur.» |
8266 | 2SA 11:4 | Ci kaw loolu Daawuda yebal ay ndaw yu jëli ndaw si, mu dikk, mu tëdde ko. Fekk na ndaw sa gisoon baax bay doora sangu-set. Ndaw sa daldi ñibbi. |
8320 | 2SA 12:31 | Nit ña ca biir nag, mu génne leen, féetale leen ay xeetukaay ak ngaskay weñ ak sémmiñi weñ, boole ci di leen móol-loo. Noonu la def ak mboolem dëkki Amoneen ñi. Gannaaw loolu Daawuda ànd ak mbooloom xareem mépp, dellu Yerusalem. |
8361 | 2SA 14:2 | Yowab nag yónnee ca dëkk ba ñuy wax Tekowa, ñu jëleji fa jigéen ju rafet xel, indil ko ko. Yowab ne ko: «Dangay ñaawlu-ñaawlulu. Solal yérey ñaawlu, te bul xeeñu. Melal daal ni jigéen ju jota ñaawlu lu yàgg, ngir ku mu deele. |
8385 | 2SA 14:26 | At mu jotaan mu watu ndax njañ lu diis, te bu watoo, natt kawar ga ci doomi nattukaayu buur, mu jege ñaari kilook genn-wàll. |
8463 | 2SA 17:11 | Kon sama xalaat mooy nga boole ñi ànd ak yaw ba ñu daj, muy Israyil gépp, dale ko diiwaanu Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum. Muy mbooloo mu bare, tollu ni suufas géej; te yaw ci sa bopp, nga jiite leen ci xare bi. |
8613 | 2SA 22:8 | Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri, kenuy asamaan jaayu, di reg-regi. |
8697 | 2SA 24:2 | Buur wax ak Yowab ma ca wetam, di njiital xarekat ya. Mu ne ko: «Wëral ci biir giiri Israyil gépp ba ñu daj, li ko dale diiwaanu Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum. Nañu bind askan wi, ndax ma xam seenub lim.» |
8710 | 2SA 24:15 | Ba loolu amee Aji Sax ji wàcce mbas ci kaw Israyil, dale ko ca suba soosa ba keroog ba àpp ba matee. Ña dee ca askan wa di juróom ñaar fukki junni (70 000) diggante Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum. |
8894 | 1KI 5:27 | Buur Suleymaan nag sas fanweeri junniy nit (30 000) ci Israyil gépp ay liggéeyi sañul-bañ. |
8941 | 1KI 7:4 | Mu am ñetti sësalantey palanteer yu ñu fege ay laat te ñu dékkarloo ñett-ñett. |
8942 | 1KI 7:5 | Bunt yépp ànd ak seen banti feguwaay, bunt bu ci nekk def ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar; bunt yi sësaloo te dékkarloo ñett-ñett. |
8963 | 1KI 7:26 | Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppi tóor-tóor. Ñaar téeméeri barigo la mbalka miy def. (200). |
8967 | 1KI 7:30 | Rootukaay bu nekk am na ñeenti mbegey xànjar yu ñu lëkklee yeti xànjar. Mu am ay kenu yu ñu xellil rootukaay bi ci ñeenti koñam, kenu yi yenu benn bagaan te am ay nataali tóor-tóor. |
8968 | 1KI 7:31 | Gémmiñu rootukaay bu nekk amoon na omb bu mërgalu bu bagaanu ndox biy tege. Xóotaayu gémmiñ gi di xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. Ñu yett ci kaw gémmiñ gi ay nataal ba tey. Rootukaay bi mërgaluwul, waaye daa bindoo ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar te yem kepp. |
8969 | 1KI 7:32 | Ñeenti mbege yi ronu làcc yi, tóori weñ yi ci wewe sax ci rootukaay bi. Mbege mu ci nekk am na taxawaayu xasab ak genn-wàll. |
8973 | 1KI 7:36 | Fi amul dara ci kaw njàppu yeek làcc yi, mu ñaas ci ay nataali serub aki gaynde aki garabi ron yu ñu wërale ay caqi tóor-tóor. |
9411 | 1KI 19:21 | Alyaasa bàyyi fa Ilyaas, dellu jël ñaari nag, rendi ko sarax, jël banti ràngaay ya, togge yàpp wa, jox ko mbooloo ma, ñu lekk, ba noppi Alyaasa topp ci gannaaw Ilyaas, di bëkk-néegam. |
9880 | 2KI 13:5 | Aji Sax ji daldi may Israyil ku leen xettli, ba ñu génn ca loxol waa Siri. Ba loolu amee waa Israyil dellu nekk ca seeni kër ci jàmm, na woon démb ak bëkk-démb. |
9964 | 2KI 15:35 | Terewul jëleesu fa bérabi jaamookaay ya, xanaa mbooloo ma di def ay sarax ak a taal cuuraay ba tey, ca bérabi jaamookaay yooyu. Moom nag moo tabax buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar. |
9981 | 2KI 16:14 | Sarxalukaayu xànjar ba tege woon ca kanam Aji Sax ji, mu jële ko ca kanam kër ga mu nekkoon, ca diggante sarxalukaay bu bees baak kër Aji Sax ji, teg ko ca wetu sarxalukaay bu bees ba, fa féete bëj-gànnaar. |
12916 | JOB 3:8 | Yal na alagkati bés yi alag googu guddi, alagkat yu mana xabtal ninki-nànka. |
12948 | JOB 4:14 | Tiitaange ne ma taral, may lox, cér yépp di kat-kati. |
12949 | JOB 4:15 | Ngelaw lu sew jaare sama kanam, sama kawari yaram ne sàyy-sàyyaaral. |
12960 | JOB 5:5 | Am ngóobam, ku xiif a koy lekk, ba lekkaale la saxe biir dég ya, te alalam, ku mar a koy ŋaf-ŋafee. |
13064 | JOB 9:9 | Moo sàkk dëllooñ gi féete bëj-gànnaar ak yaar yi ci digg asamaan, ak ga ca néegi bëj-saalum. |
13234 | JOB 15:27 | te fekk ko yaflu ba gët suulu, pooj ya duuf bay lob-lobi. |
13365 | JOB 21:6 | Su ma ko xalaatee, damay tiit, di kat-kati. |
13484 | JOB 26:13 | Noowam wal, asamaan leer, loxoom jam jaan jay balaw-balawi. |
13638 | JOB 32:6 | Ca la Eliyu doomu Barakel waa Buus ba, àddu ne: Man de damay ndaw, ngeen diy mag, ba tax may teeylu, ragal leena biralal sama xam-xam. |
13640 | JOB 32:8 | Ndeke xel mi ci nit mooy noowal Aji Man ji koy may dég-dég. |
13687 | JOB 33:33 | Lu ko moy nag, yaa may déglu, ne cell, ma jàngal la xam-xam. |
13740 | JOB 35:16 | Ayóoba mii de, cóolóolu neen lay wax, mbel-mbel ju àndul ak xam-xam. |
13782 | JOB 37:9 | ngëlén bawoo néegam sedd ba tukkee fa ngelawi bëj-gànnaar. |
13910 | JOB 41:10 | Bu tislee, melax ne ràyy, mu xippi, nga ne fajar ay xapp-xappal. |
14138 | PSA 18:8 | Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri; kenuy tund ya jaayu, di reg-regi. |
14190 | PSA 19:9 | Lu Aji Sax ji tegtale, njub la, di bégal xol. Lu Aji Sax ji santaane, leeraange la, di leeral gis-gis. |
14192 | PSA 19:11 | Moo dàq wurus, raw wurusu ngalam wu ne xas; dàqati lem, ëpp tem-tem. |
14373 | PSA 31:24 | Képp kuy aji gëm, soppal Aji Sax ji. Aji Sax jeey sàmm ku ko gëm, di yool, ba wis kuy réy-réylu. |
14541 | PSA 39:7 | Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for. |
14741 | PSA 51:18 | Sàkkuwloo sarax, nde kon ma indi; te soppuloo saraxu rendi-dóomal. |
14744 | PSA 51:21 | Su boobaa nga nangu sarax yi war, di saraxu rendi-dóomal. Su boobaa ñu rendi ay yëkk ca sa sarxalukaay. |
14825 | PSA 58:4 | Ku bon day sosu rekk, dëng; juddu, teggi yoon, dib fen-kat. |
15083 | PSA 73:8 | Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole. |
15169 | PSA 77:19 | nga dënoo biir callweer, melax yi taal àddina, suuf di lox, di reg-regi. |
15197 | PSA 78:26 | Yàlla wale ngelawal penku fa asamaan, bëmëx ak dooleem ngelawal bëj-saalum. |
16190 | PSA 127:1 | Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul, ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, ku ko wattu, neen nga teewlu. |
16444 | PSA 148:3 | Màggal-leen ko, yeen jant beek weer wi, màggal-leen ko, yeen mboolem biddiiw yii di nes-nesi. |
16589 | PRO 5:2 | kon nga saxoo foog, say wax tegu ci xam-xam. |
16681 | PRO 8:9 | Lépp a dëggu ci ku am ug dégg, te jub ci ku for xam-xam. |
16696 | PRO 8:24 | Ba may dikk, géej amul, ndox ballul bay fees, di wal-wali. |
16780 | PRO 11:22 | Taaru jongama ju xel ma gàtt, mooy jaaro wurus ci noppu mbaam-xuux. |
16849 | PRO 14:7 | Dàndal ab dof, du la yokk xam-xam. |