2178 | EXO 23:33 | Buñu dëkke seenum réew, lu ko moy muy seen ndëgg-sërëx; ndax dañu leen di xiir ci moy ma, ba ngeen jaamu seeni tuur.» |
2206 | EXO 25:10 | «Defarleen gaalu dénku séng, guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll; taxawaayam di xasab ak genn-wàll. |
2554 | EXO 35:22 | Góor ak jigéen bokk dikk, mboolem ñi am yéeney xolam, mboolem ñi bëgga indi wurus, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbale; ñii indi ay lam, ñii jaaroy nopp, ñii jaaroy loxo, ñii ay caq, gànjari wurus yu nekk rekk. |
4852 | NUM 35:5 | Su ko defee ngeen natte ca biti dig-digal bu gudde ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar ci wetu penku; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu bëj-saalum; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu sowu; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu bëj-gànnaar, dëkk bi nekk ci digg bi. Dig-digal boobu day ñeel Leween ñi, di seen parluy dëkk. |
5135 | DEU 7:22 | Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dàqe fi seen kanam, ndànk-ndànk; dungeen leen mana gaawa jeexal, lu ko moy rabi àll yi mujj ne gàññ ci seen kaw. |
8942 | 1KI 7:5 | Bunt yépp ànd ak seen banti feguwaay, bunt bu ci nekk def ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar; bunt yi sësaloo te dékkarloo ñett-ñett. |
14138 | PSA 18:8 | Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri; kenuy tund ya jaayu, di reg-regi. |
14776 | PSA 55:5 | Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi; tiitaangey ndee ne ma taral. |
15548 | PSA 97:4 | ay melaxam leeral àddina, waa àddina gis, di pat-pati; |
16686 | PRO 8:14 | Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa am ug dégg, di boroom doole. |
16833 | PRO 13:16 | Képp ku teey jëfe xam-xam; ab dof ay siiwal ndofam. |
18340 | ISA 32:11 | Jigéen ñi dal xel, ragal-leen; yeen ñi féex laa ne, tiitleen! Futtikuleen, ba ne duŋŋ; gembooy saaku, ñaawloo. |
21289 | EZK 30:16 | Maay taal Misra, dëkk ba ñuy wax Ciin di rag-ragi; dëkk ba ñuy wax No, ñu bëtt ko; Memfis, noon yi nangu ko digg bëccëg. |
21606 | EZK 41:11 | Am na ñaari bunt yu sare ci néegi wet yi wër néeg Yàlla bi, jëme ci pegg bu dara amul. Benn bunt ba féete bëj-gànnaar; benn ba, bëj-saalum, yaatuwaayu pegg, bi wër néeg bi ba mu daj, di juróomi xasab. |
22928 | HAG 2:4 | Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen, kàddug Aji Sax jee. Mu ne: Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. |
23141 | ZEC 14:4 | Bésub keroog, kaw tundu Oliw ya la tànkam yay sampe, fa janook Yerusalem, ca penku, tundu Oliw ya xar ca digg ba, penku ba sowu, def xur wu yaa, genn-wàllu tund wa randu, jëm bëj-gànnaar; genn-wàll ga jëm bëj-saalum. |
25526 | LUK 11:52 | Ngalla yeen xamkati yoon yi, yeena sànk caabiy xam-xam; yeen dugguleen, ñiy duggsi, ngeen tere leena dugg.» |
27271 | ACT 8:26 | Menn malaakam Boroom bi nag wax Filib, ne ko: «Fabul jubal bëj-saalum; yoon wa kenn jaareetul te bartaloo Yerusalem, jëm Gasa.» |
27578 | ACT 16:26 | Ci kaw loolu suuf jekki yëngu yëngu bu mag ba kenug kaso ba di rëng-rëngi; bunt yépp jekki ubbiku, jéngi ñépp dàjjiku. |
30551 | 2PE 1:5 | Loolu ci boppam wara tax ngeen def lu ngeen man, ba dolli ci seen ngëm, njàmbaar; seen njàmbaar, ngeen dolli ci xam-xam; |