59 | GEN 3:3 | Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”» |
509 | GEN 20:13 | Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”» |
566 | GEN 22:18 | te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”» |
887 | GEN 31:13 | Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”» |
934 | GEN 32:6 | ma doora ñëw, ànd ak ay nag ak ay mbaam ak ay gàtt ak ay jaam yu góor ak yu jigéen; may yónnee ci yaw, di la siyaare tey sàkku nga dalal ma jàmm.”» |
941 | GEN 32:13 | Te yaw yaa ma ne: “Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej, si kenn manula lim ndax bare.”» |
947 | GEN 32:19 | nee ko: “Lii de sang bi, lu la Yanqóoba may la, di la ko siyaaree, yaw Esawu, te moom ci boppam mu ngi topp ci sunu gannaaw.”» |
949 | GEN 32:21 | tegati ca ne ko: «Te nee ko itam: “Sa surga Yanqóobaa ngi topp ci sunu gannaaw.”» Booba Yanqóobaa ngi naa ci xelam: «Bu ma jiitalee li ma ko may, neexale ko ko, bala maa janook moom, jombul mu dalal ma jàmm.» |
1101 | GEN 37:17 | Waa ja ne ko: «Jóge nañu fii de, ndax dégg naa ñu naan: “Nanu dem Dotan.”» Yuusufa toppi magam ya ba Dotan, fekk leen fa. |
1287 | GEN 42:34 | su ko defee ngeen indil ma seen rakk ju ndaw, kon dinaa xam ne dungeen ay yëddukat waaye nit ñu maandu ngeen, te dinaa leen delloo seen mbokk, ngeen mana dem fu leen neex ci réew mi.”» |
1296 | GEN 43:5 | Waaye boo ko bàyyiwul kat, dunu dem, ndax waa ja waxoon na nu ne nu: “Dungeen jàkkaarlook man te seen rakk àndul ak yeen.”» |
1377 | GEN 45:18 | jëli seen baay ak seeni njaboot, ngeen ñëw fi sama wet. Dinaa leen jox suuf si gën ci réewum Misra, ngeen di lekk li fi gëna duuf.”» |
1379 | GEN 45:20 | Te buleen réccu alal, ji ngeen di bàyyi seen gannaaw, ndax li gën ci réewum Misra yeena koy moom.”» |
1472 | GEN 48:20 | Gannaaw loolu mu ñaanal leen keroog ne leen: «Yal na Israyil di ñaane seeni tur naan: “Yal na la Yàlla def ni Efrayim ak Manase.”» Noonu la jiitale Efrayim, door caa teg Manase. |
1594 | EXO 3:14 | Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”» |
1634 | EXO 5:1 | Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”» |
1715 | EXO 7:29 | Mbott yi dinañu yéeg ci sa kaw, yéeg ci kaw waa réew mi, ak sa dag yépp.”» |
1747 | EXO 9:4 | Waaye man Aji Sax ji maay ràññatle juru bànni Israyil ak juru waa Misra, ba lenn du dee ci mboolem lu bànni Israyil moom.”» |
1784 | EXO 10:6 | Te itam dinañu fees say biir kër ak sa këri dag yépp ak këri waa Misra gépp, muy mbir mu say maam ak say mamaat masula gis, ba ñu ganee àddina ba bésub tey jii.”» Ba loolu amee Musaa walbatiku, bàyyikoo ca Firawna. |
1844 | EXO 12:27 | waxleen leen ne leen: “Loolu sarax la ñeel Aji Sax ji ngir bésub Mucc ba, ndax la mu teggi woon këri bànni Israyil ca Misra, kera ba muy fàdd waa Misra te musal ca sunuy kër.”» Ba mu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma sujjóot, màggal Yàlla. |
1964 | EXO 16:16 | Aji Sax ji dafa santaane ne: “Na ku nekk for lu mat njëlam, bopp bu ne andaar, te mu natt ko ci limu nit, ñi mu bokkal xayma.”» |
1980 | EXO 16:32 | Ci biir loolu Musaa ne: «Aji Sax ji dafa santaane ne: “Sàkkleen ci andaar, denc ngir seeni sët ak seeni sëtaat. Su ko defee ñu gis ñam, wi ma leen daan leel ca màndiŋ ma, gannaaw ba ma leen génnee réewum Misra.”» |
2078 | EXO 20:26 | Buleen yéeg ci ay dëggastal, doora mana àgg ca sama sarxalukaay, ndax loolu day tax ngeen di fa sàgganu.”» |
2416 | EXO 30:33 | Képp ku njafaan lu ni mel, mbaa mu taqal ci yaramu ku ci bokkul, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.”» |
2438 | EXO 31:17 | Sama diggante laak bànni Israyil, te firnde la ju sax dàkk, ndax ci juróom benni fan la Aji Sax ji sàkk asamaan ak suuf, bésub juróom ñaareel ba, mu dal-lu, daldi yeeslu.”» |
2452 | EXO 32:13 | Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”» |
2466 | EXO 32:27 | Mu ne leen: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: “Na ku nekk teg saamaram ci luppam, te ngeen wër dal bi bépp buntoo bunt, ba mu daj. Reyleen ñépp; doomu ndey, xarit ak jegeñaale.”» |
2981 | LEV 10:3 | Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell. |
4387 | NUM 22:11 | “Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”» |
4393 | NUM 22:17 | Maa lay teral teraanga ju réya réy. Loo ma wax, ma def. Dikkal rekk, móolul ma gàngoor gii.”» |
4567 | NUM 27:11 | Su baayam amul góor gu mu bokkal waajur, mbokkam mu ko gëna jege ci biir làngam, moom ngeen di jox céru suufam. Kookooy donn cér ba. Na loolu di dogalu yoon, ñeel bànni Israyil, noonu ko Aji Sax ji sante Musaa.”» |
4947 | DEU 2:7 | Ndax yeen kat seen Yàlla Aji Sax ji moo barkeel seen mboolemu ñaq te moo ràññee seen doxub màndiŋ mu yaa mii. Ñeent fukki at a ngii seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ñàkkuleen dara.”» |
5802 | DEU 32:42 | Maay nàndal samay fitt deret, sama saamar di yàppe, deret di nàcce ci ku ñu jam, ak ku ñu jàpp, tey tuuroo ci boppi kilifay noon yi.”» |
7287 | 1SA 3:9 | Mu ne Samiyel: «Demal tëri, bu la wootee, nee ko: “Aji Sax ji, maa ngi lay déglu, Sang bi, waxal.”» Samiyel dellu tëdd fa muy tëdd. |
7439 | 1SA 10:19 | Waaye tey yeena dëddu seen Yàlla, ji leen musal ci mboolem seeni loraange ak seeni njàqare. Yeena ko ne: ‘Falal buur ci sunu kaw daal!’ Léegi nag taxawleen fi kanam Aji Sax ji, giir ak giir, làng ak làng.”» |
7565 | 1SA 15:3 | Demleen léegi, songi Amalegeen ñi. Faagaagal-leen seen lépp, te buleen leen ñeewante; reyleen góor ak jigéen, gone yi ba ci ñiy nàmp, ak nag ak gàtt, ak giléem ak mbaam.”» |
7700 | 1SA 18:22 | Ci biir loolu Sóol sant ay dagam, ne leen: «Diisool-leen maak Daawuda, ngeen wax ko ne ko: “Yaw kat, Buur am na bànneex ci yaw, te it dagam yépp a la sopp. Kon nag nangula doon gorob Buur.”» |
7774 | 1SA 20:42 | Yonatan ne Daawuda: «Demal ak jàmm, gannaaw noo giñoo nun ñaar ci turu Aji Sax ji ne “Aji Sax jeey seede sama digganteek yaw, ak diggante sama askan ak saw askan, ba fàww.”» |
7846 | 1SA 24:5 | Ba mu ko defee niti Daawuda ya déey Daawuda, ne ko: «Xoolal bésub tey jii la la sa yàlla Aji Sax ji noon: “Maa ngii, di teg sab noon ci say loxo, nga def ko lu la neex.”» Daawuda yoot ndànk, ba dagg ca lafu mbubbum Sóol. |
7872 | 1SA 25:8 | Laajal rekk say surga, dinañu la ko wax. Daawuda sa doom nag, sang bi, moo lay ñaan nga yéwéne nu ci bésu tey bu rafet bii nu dikke, te may nu loo am rekk, nu bokk kook moom.”» |
8102 | 2SA 3:18 | Kon ayca boog! Ndax Aji Sax jee ko digoon Daawuda, ba mu nee: “Ci sama jaam Daawuda laay walloo Israyil sama ñoñ, ci waa Filisti ak mboolem seeni noon.”» |
8137 | 2SA 5:2 | Te it démb ak bëkk-démb, ba Sóol dee sunu buur, yaw yaa doon jiite Israyil ciy xareem. Aji Sax ji ne la: “Yaay sàmm Israyil sama ñoñ te yaay doon kilifag Israyil.”» |
8199 | 2SA 7:16 | Sa kër ak sa nguur day sax dàkk fi sa kanam, te sab jal day dëju ba fàww.”» |
8283 | 2SA 11:21 | Ana ku reyoon Abimeleg doomu Yerubeset? Xanaa du ca kaw tata ja la ko aw jigéen sànnee doju wolukaay, ba mu dee ca Tebes? Lu waral ngeen jegee noonu tata ja?” Su boobaa nee ko: “Sa surga ba, Uri Etteen ba it dee na.”» |
8301 | 2SA 12:12 | Yaw déy ci sutura nga ko defe. Waaye man, ci kanam Israyil gépp laay sabab mbir moomu, bëccëg ndarakàmm.”» |
8325 | 2SA 13:5 | Yonadab ne ko: «Dangay tëdd ci sa lal, wopp-wopplu, ba sa baay dikk, seetsi la, nga ne ko: “Na sama jigéen Tamar ñëw, may ma, ma lekk. Na ma toggal ci sama kanam, may gis, te mu sexal ma ci loxol boppam.”» |
8400 | 2SA 15:8 | ndax kat, sang bi, ba ma nekkee Gesur ca Siri, damaa dige woon ne: “Su ma Aji Sax ji delloo, ba ma dellu Yerusalem, dinaa dem màggali ko.”» |
8527 | 2SA 19:14 | Te ngeen waxal ma Amasa ne ko: “Buur nee, xanaa doo mbokkam lenqe, di deretam? Nee yal na ko Yàlla teg mbugal mu gëna tar ndegam du la fal, nga jiite mbooloom xare mi ba fàww, wuutu Yowab.”» |
8707 | 2SA 24:12 | «Demal ne Daawuda: “Aji Sax ji dafa wax ne: Ñett laa lay jox, nga tànn ci lenn lu ma lay def.”» |
8768 | 1KI 1:48 | teg ca ne: “Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ji ma jox bésub tey ku ma wuutu ci samab jal, may gis.”» |
8771 | 1KI 1:51 | Ñu wax ko Suleymaan, ne ko: «Buur Suleymaan, Adoña de, ragal na la. Deful lu moy jàpp ca béjjéni sarxalukaay ba te naa: “Na ma Buur Suleymaan sang bi giñal tey jii ne du ma jam saamar, ma dee.”» |
8842 | 1KI 3:23 | Buur ne: «Kii a ngi naan: “Sama doom jii mooy dund, sa doom a dee.” Kee naan: “Déedéet, sa doom a dee, sama doom mooy dund.”» |
9063 | 1KI 9:9 | Ñu ne: “Xanaa li ñu dëddu seen Yàlla Aji Sax, ji jële seeni maam réewum Misra, di topp yeneen yàlla, di leen sujjóotal ak a jaamu. Moo tax Aji Sax ji teg leen musiba mii mépp.”» |
9150 | 1KI 11:39 | Kon dinaa torxal askanu Daawuda waaye du doon ba fàww.”» |
9165 | 1KI 12:11 | Sama baay a leena tegoon njaam gu metti, waaye man maay yokk seen njaam, ba mu gëna metti. Te sama baay ay yar la leen daan cawe, waaye man ay leraw yu ñu kor weñ laa leen di cawe.”» |
9178 | 1KI 12:24 | “Aji Sax ji dafa wax ne: Buleen jóg di xeex ak seen bokki bànni Israyil. Na ku nekk ñibbi këram, ndax ci man la mbir mii sababoo.”» Ñu dégg kàddug Aji Sax ji, walbatiku dem, noonee ko Aji Sax ji waxe. |
9189 | 1KI 13:2 | Góor ga xaacu, gëdd sarxalukaay ba ci ndigalal Aji Sax ji, daldi ne: «Yaw sarxalukaay bi, éey sarxalukaay bii! Aji Sax ji dafa wax ne: “Xamal ne doom ju góor dina juddoo kër Daawuda, Yosya lay tudd. Sarxalkati bérabi jaamookaay yiy taal saraxu cuuraay ci sa kaw, ñoom lees di rendi ci sa kaw. Yaxi nit lees di lakk ci sa kaw.”» |
9190 | 1KI 13:3 | Góor ga joxe na ca bésub keroog ab takk; mu ne: «Takk bii la ci Aji Sax ji biral: “Seetluleen, sarxalukaay bi dina xar ñaar, dóom bi ci kaw sottiku.”» |
9196 | 1KI 13:9 | ndax loolu lañu ma sant ci ndigalal Aji Sax ji, ne ma: “Bul sex dugub, bul naan um ndox te bul walbatiku jaare yoon wa nga jaare woon bi ngay ñëw.”» |
9204 | 1KI 13:17 | Ndaxte dañu maa wax ci ndigalal Aji Sax ji ne ma: “Bu fa sex dugub, bu fa naan um ndox te bul walbatiku jaare yoon wa nga jaare woon bi ngay ñëw.”» |
9205 | 1KI 13:18 | Mu dellu ne ko: «Man itam yonent laa ni yaw. Malaaka wax na ma ci ndigalal Aji Sax ji ne ma: “Waññi ko, mu ànd ak yaw sa kër, sex dugub, naan ndox.”» Fekk na la muy wax amul. |
9334 | 1KI 17:14 | ndax Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Njaqub sunguf bi du jeex; taxub diw bi it du jeex, ba keroog Aji Sax ji di taw ci réew mi.”» |
9414 | 1KI 20:3 | Ñu ne ko: «Ben Addàd dafa wax ne: “Sa xaalis ak sa wurus, maay boroom. Say jabar it, ak ñi gëna dëgër ci say doom, maay boroom.”» |
9417 | 1KI 20:6 | Waaye nëgëni ëllëg sax dinaa yónni samay jawriñ ci yaw, ñu seet ci sa biir kër ak say kër jawriñ. Mboolem luy sa alal dinañu ci teg loxo, nangu ko, yóbbu.”» |
9420 | 1KI 20:9 | Axab ne ndawi Ben Addàd ya: «Waxleen Buur, sama sang, ne ko: “Sa jaam ba nee mboolem la nga jëkkoona yónnee di ko sàkku dina ko def. Waaye lii nga mujja laaj moom, du ko def.”» Ndaw ya dem jottli tontam. |
9422 | 1KI 20:11 | Buurub Israyil ne: «Waxleen ko ne ko: “Jóge xare, di bàkku moo gën jëm xare, di bàkku.”» |
9473 | 1KI 21:19 | Wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Du dangaa rey nit, ba nangu alalam?” Nga teg ca ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Fa xaj ya xabe deretu Nabot, ay xaj dina fa xabe sa deret, yaw itam.”» |
9494 | 1KI 22:11 | Fekk na Cedekiya doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”» |
9500 | 1KI 22:17 | Mise ne ko: «Israyil gépp laa gis ñu tasaaroo ca tund ya, mbete xar yu amul sàmm. Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom. Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”» |
9510 | 1KI 22:27 | Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”» |
9541 | 2KI 1:4 | Loolu tax na Aji Sax ji wax buurub Israyil ne ko: “Lal bi nga tëdd doo ko wàcc, ndax dinga dee moos.”» Ci kaw loolu Ilyaas dem. |
9723 | 2KI 7:12 | Buur jóg ca guddi, wax aki jawriñam ne leen: «Ma wax leen nag li nu waa Siri di fexeel. Xam nañu ne nu ngi dee ak xiif. Moo tax ñu jóge ca seen dal, làquji ca àll ba. Xam naa dañu ne: “Bu ñu génnee dëkk bi rekk, nu jàpp leen, ba noppi dugg ci biir dëkk bi.”» |
9740 | 2KI 8:9 | Asayel dem ca moom, yóbbaale lu mu ko jox, muy mboolem la gën ca Damaas, tollu ci sëfub ñeent fukki giléem. Mu dikk taxaw ca kanamam, ne ko: «Ben Addàd buurub Siri moo ma yónni fi yaw, ne ma: “Laajal ma Baay Alyaasa ndax dinaa jóge ci sama wopp jii.”» |
9772 | 2KI 9:12 | Ñu ne ko: «Wax nu waay, bu nu nax!» Mu ne leen nee na ko nàngam ak nàngam, teg ca ne leen: «Mu ne: “Aji Sax ji nee: Diw naa la, fal la buurub Israyil.”» |
9797 | 2KI 9:37 | Néewub Yesabel dina mel ni mbalit ci àll bi, ci biir toolub Yisreel, ba kenn du man ne: Kii Yesabel a.”» |
10069 | 2KI 19:4 | Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg mboolem kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”» |
10072 | 2KI 19:7 | Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma fàdde ko ab saamar ca am réewam.”» |
10099 | 2KI 19:34 | Maay aar dëkk bii, musal ko ngir man ci sama bopp, ak Daawuda sama jaam bi.”» |
10108 | 2KI 20:6 | Dinaa yokk ci saw fan, fukki at ak juróom. Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettli, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii ndax man ci sama bopp ak Daawuda sama jaam bi.”» |
10120 | 2KI 20:18 | Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.”» |
10138 | 2KI 21:15 | ndegam li ma ñaawlu lañu masa def, di ma merloo, ba seeni maam génnee Misra ba tey jii.”» |
10169 | 2KI 22:20 | Moo tax maa ngii di la yóbbu nga fekki say maam, dees na la yóbbu ak jàmm ca sa bàmmeel, te say bët du tegu ci mboolem musiba mi may wàcce ci bii bérab.”» Ba loolu amee ñu dellu, yegge Buur kàddu ga. |
13958 | PSA 2:9 | yilife leen yetu weñ, rajaxe leen ni njaqal xandeer.”» |
15132 | PSA 75:6 | bul bewa bew, bay waxe reewande.”» |
15395 | PSA 89:5 | “Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw. |
17861 | ISA 7:9 | Samaree yilif Efrayim, te doomu Remalya ji yiliful lu moy Samari. Dungeen mana saxoo dëgër nag, ndare ngeen sax ci Aji Sax ji.”» |
18426 | ISA 37:4 | Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”» |
18429 | ISA 37:7 | Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma fàdde ko ab saamar ca am réewam.”» |
18457 | ISA 37:35 | Maay aar dëkk bii, musal ko ngir man ci sama bopp, ak Daawuda sama jaam bi.”» |
18466 | ISA 38:6 | Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettli, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii.”» |
18489 | ISA 39:7 | Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.”» |
18645 | ISA 45:14 | Aji Sax ji dafa wax ne: «Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus, ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw, ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo. Sa gannaaw lañuy topp, yeewe, jàllsi; sujjóotal la, di ñaan naan: “Fi yaw daal la Yàlla ne, du feneen, te tuur neen la.”» |
18936 | ISA 62:12 | Dees na leen wooye “Askan wu sell wi,” “Ñi Aji Sax ji jot;” te yaw Yerusalem dees na la wooye “Ki ñu namm,” “Dëkk bi ñu waccul.”» |
19037 | JER 2:3 | Mooy ba Israyil dee lu ñu sellalal Aji Sax ji, di ndoortel meññeefam. Képp ku ko sex, toppees ko ko, musiba dikkal ko.”» Kàddug Aji Sax jee. |
19076 | JER 3:5 | Xanaa deesul mer ba fàww? Xanaa xadar du sax?” Ma ne: “Israyiloo, yeena ko wax, waaye bon ngeen lu ngeen man.”» |
19084 | JER 3:13 | “Nangul ne ñaaw nga rekk, te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ, di wër di foye sa bopp ak yàllay doxandéem yi ci ker garaboo garab gu naat, te dégluwoo ma.”» Kàddug Aji Sax jee. |
19146 | JER 5:19 | Bu ñu nee: “Ana lu waral sunu Yàlla Aji Sax ji teg nu lii lépp?” ne leen: “Yàlla nee: Ni ngeen ma dëddoo, di jaamu yàllay jaambur ci seenum réew, ni ngeen di jaamujee ay jaambur biir réew mu ngeen moomul.”» |
19163 | JER 6:5 | Ñee ne: “Nan song congum guddi boog, ba rajaxe seen kër yu yànj.”» |
19175 | JER 6:17 | «Ma tabbal leeni wattukat ne: “Teewluleen liit gu jib.”» Ñu lànk ne: «Teewluwnu.» |
19300 | JER 11:5 | Su ko defee ma wàccook ngiñ, la ma giñaloon seeni maam ne dinaa leen may réew mu meew maak lem ja tuuroo, muy fii tey.”» Ma ne ko: «Tigi, Aji Sax ji.» |