550 | GEN 22:2 | Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk saraxu rendi-dóomal.» |
8094 | 2SA 3:10 | ne ko dina jële nguur gi ci waa kër Sóol, samp jalub Daawuda ci kaw Israyil ak Yuda, dale ko Dan ca bëj-gànnaar, ba Beerseba ca bëj-saalum.» |
8844 | 1KI 3:25 | Buur ne: «Dogleen xale biy dund ñaar, te jox kii genn-wàll, jox kee genn-wàll.» |
9827 | 2KI 10:30 | Aji Sax ji nag ne Yewu: «Gannaaw def nga lu baax, di jëfe li ma rafetlu te def nga waa kër Axab mboolem li ma bëggoon, saw askan dina toog ci jalub Israyil ba ca sa sët-sëtaat.» |
9941 | 2KI 15:12 | Loolu mooy kàddu ga Aji Sax ji waxoon Yewu ne ko: «Saw askan dinañu toog ci kaw jalu Israyil ba ci sa sët-sëtaat.» Te noonu la amee. |
13642 | JOB 32:10 | Moo tax ma ne: «Déglu ma; man it ma biral sama xam-xam.» |
14966 | PSA 68:14 | Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare, gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis, dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.» |
18277 | ISA 29:14 | Moo tax maa ngii di dellu wéyeek askan wii, ay kéemtaan aki kiraama yuy tiiñ boroom xel ak xelam, réer xamkat ak xam-xamam.» |
18718 | ISA 49:12 | Ñu ngiy bawoo fu sore, ñu ngii bawoo bëj-gànnaar ak sowu, ñee bawoo diiwaanu Sinim ca bëj-saalum.» |
19612 | JER 25:9 | maa ngii di yónnee, jëli mboolem làngi bëj-gànnaar.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay yónnee it ca Nabukodonosor buuru Babilon mi ci samag curga, daldi leen boole indi ci kaw réew mii ak ñi ci biiram ak mboolem xeet yi ko séq. Maa leen di faagaagal, gental leen gent bu sax dàkk bu ñuy muslu. |
20138 | JER 46:24 | Gàcceel nañu Misra mu taaru mi, teg ko ci loxoy xeeti bëj-gànnaar.» |
20313 | JER 51:32 | nangu jàllukaayi dex ya, taal barax ya, xarekat ya raj-rajloo.» |
20678 | EZK 8:5 | Mu ne ma: «Yaw nit ki, séenul wetu bëj-gànnaar.» Ma séenu wetu bëj-gànnaar, yem ca jëmmu bokkaale jooju féeteek bunt ba dendeek sarxalukaay ba, ca bëj-gànnaaram. |
23024 | ZEC 6:8 | Ci kaw loolu mu àddu ca kaw, ne ma: «Xoolal, ñi jëm réewum bëj-gànnaar, samag Noo lañuy sànni ca kaw réewum bëj-gànnaar.» |
23058 | ZEC 8:13 | Na ngeen doone woon alkànde ci biir xeet yi, yeen waa kër Yuda, ak waa kër Israyil, ni laa leen di walloo, ba ngeen doon barke. Buleen ragal. Góor-góorluleen.» |
27808 | ACT 23:6 | Fekk na Póol xam ne lenn ca kurél gaa nga bokk ca ngérum Sadusen ya, ña ca des bokk ca ngérum Farisen ya. Mu daldi àddu ca kaw ca biir géew ba, ne: «Bokk yi, man de ab Farisen laa, di doomu Farisen; li ñu may àttee nag mooy sunu yaakaar ak sunu ngëm gi nu bokk ci mbirum ndee-ndekki.» |
30589 | 2PE 2:22 | Li léeb wii wax te muy dëgg, moo leen dikkal: «Xaj waccu, lekkaat ko; te cangaayu mbaam-xuux, teewu koo xalangootee poto-poto.» |