18496 | ISA 40:6 | Baat a ngi naa: «Yéeneel!» Ma ne: «Lu may yéene?» Mu ne: «Neel: Bépp boroom suux am ñax doŋŋ la; gépp ngoram mel ni tóor-tóoru àll. |
20729 | EZK 11:5 | Noowug Aji Sax ji daldi dal fi sama kaw, ne ma: «Neel: “Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen waa kër Israyil, yeena waxe nii, seeni mébét, xam naa ko. |
31008 | REV 14:13 | Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokklee aji dee ñi deeyaale gëm Sang bi.”» Noo ga daldi ne: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.» |