67 | GEN 3:11 | Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» |
86 | GEN 4:6 | Aji Sax ji ne Kayin: «Lu la taxa mer, ba ne fóññ nii? |
90 | GEN 4:10 | Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg. |
317 | GEN 12:18 | Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la? |
318 | GEN 12:19 | Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» |
327 | GEN 13:8 | Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? |
328 | GEN 13:9 | Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.» |
363 | GEN 15:2 | Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.» |
390 | GEN 16:8 | Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.» |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
439 | GEN 18:14 | Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.» |
442 | GEN 18:17 | Booba Aji Sax jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar? |
448 | GEN 18:23 | Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen? |
449 | GEN 18:24 | Su juróom fukk rekk jubee ca dëkk bi, mbaa doo tas dëkk bi ba tey, tee nga leena jéggal rekk ngir juróom fukk ñu jub ña ca nekk? |
453 | GEN 18:28 | Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.» |
463 | GEN 19:5 | Ñu daldi woo Lóot ne ko: «Ana góor ñi fi ñëw tey ci guddi? Génneel nu leen fii, ndax nu mana àgg ci ñoom.» |
478 | GEN 19:20 | Gisuloo dëkk bale; jege na, te dëkk bu tuut la, am déet? Ma daw, làquji fa boog, ba mucc?» |
500 | GEN 20:4 | Loolu fekkul Abimeleg dëkkoo Saarata. Mu wax Yàlla ne ko: «Sama Boroom, mbaa doo bóom réew mi ci mbir mu ñu doonul dara? |
501 | GEN 20:5 | Du góor gi da maa waxoon ne kii jigéenam la? Du jigéen ji it da maa waxoon ne kooku càmmiñam la? Fexewuma dara lu ñaaw te di ko tey de!» |
505 | GEN 20:9 | Gannaaw loolu Abimeleg woolu Ibraayma ne ko: «Li nga nu def nag? Ndax dama laa tooñ, ba nga yóbbe ma tooñ gu réye nii, man ak sama réew mi mépp? Lii nga ma def de, waroo ko woona def.» |
531 | GEN 21:17 | Ba mu ko defee Yàlla dégg baatu xale bu góor ba. Malaakam Yàlla ma àddoo asamaan, ne Ajara: «Ajara, lan la? Bul ragal dara, ndaxte Yàlla dégg na sa baatu doom ci diggante bii mu tollu. |
597 | GEN 24:5 | Surga ba ne ko: «Su ndaw sa nanguwula ànd ak man ci réew mii nag? Ndax kon damaa wara yóbbu sa doom ba ca réew ma nga jóge?» |
703 | GEN 26:10 | Abimeleg ne ko: «Li nga nu def nag? Xaw tuuti kenn ci nit ñi tëdde sa soxna, te kon nga yóbbe nu tooñ.» |
761 | GEN 27:33 | Isaaxaa ngay lox, bay rag-ragi, daldi ne ko: «Kan? Ana ku rëbbi woon nag, indil ma, ba ma lekk ba noppi? Ñaanal naa ko bala ngaa ñëw. Te dina barkeel moos.» |
765 | GEN 27:37 | Isaaxa ne Esawu: «Mbaa am naa lu ma la ñaanalati, doom? Ndax kat xas naa koo def, muy sa kilifa, te bokkam yépp laa def ñuy surgaam, te pepp ak biiñ laa ko woomale it, ba mu ne gàññ.» |
766 | GEN 27:38 | Esawu ne baayam: «Baay, xanaa genn ñaan rekk nga am? Ngalla baay, ñaanal ma, man itam!» Ca la Esawu ne yikkét jooy. |
821 | GEN 29:25 | Ba bët setee, Yanqóoba fekk muy Leya. Mu ne Laban: «Waaw, li nga ma def nag? Du Rasel a taxoon ma liggéeyal la? Lu tax nga wor ma?» |
888 | GEN 31:14 | Rasel ak Leya ne ko: «Ndax amati nanu benn cér walla ndono sunu kër baay? |
900 | GEN 31:26 | Laban ne Yanqóoba: «Looy def nii, yaw, di ma nëbbuy daw, yóbbaale sama doom yu jigéen, ñu mel ni ñu ñu lële xare? |
901 | GEN 31:27 | Lu waral nga di ma nëbbuy daw te bañ maa tàggu? Nde konoon jombul ma yiwi la ci xol bu sedd, bu ànd aki woy, boole ci xalam aki sabar. |
910 | GEN 31:36 | Yanqóoba mer lool, daldi gëdd Laban ne ko: «Ndax damaa tooñ walla damaa moy, ba nga sambal ma, di ma topp nii? |
911 | GEN 31:37 | Bi nga jéexee sama yëf yépp ba noppi, ana loo gis lu bokk ci sa yëfi kër? Teg ko fii ci sama kanami bokk ak say bokk, ñu àtte nu. |
912 | GEN 31:38 | Xanaa du ñaar fukki at a ngii ma nekk ak yaw? Say xar ak say bëy ëmbuñu sax, mu yàqu, te masumaa lekk sa kuuyi gétt. |
917 | GEN 31:43 | Ba mu ko waxee loolu, Laban ne ko: «Jigéen ñii samay doom lañu, xale yii di samay sët, te gétt gii sama gétt a; lu fi nekk maa ko moom. Ñii di sama doom yu jigéen, nu ma leen di def tey, ñoom ak seeni doom? |
990 | GEN 34:9 | Tee noo séyante, ngeen may nu seeni janq, te jël ci sunuy janq? |
1092 | GEN 37:8 | Mag ya ne ko: «Dangaa nara falu ci sunu kaw? Danga noo nara jiite?» Ñu gënati koo bañ nag ndax géntam ya ak la mu leen ca wax. |
1094 | GEN 37:10 | Ba mu ko nettalee ay magam, ba nettali ko baayam, baayam da koo soow ne ko: «Yaw, li nga gént, lu mu doon? Xanaa du maak sa yaay ak say mag noo lay sujjóotal?» |
1110 | GEN 37:26 | Yuda ne doomi baayam ya: «Bu nu reyee sunu rakk jii, nëbb deret ji, lu nu ciy jële? |
1111 | GEN 37:27 | Tee nu koo jaay Ismayleen ñi, te bañ koo sàkkal pexe nun ci sunu bopp? Ndax kat sunu rakk a, di sunu deret.» Doomi baay ya déggal ko. |
1181 | GEN 40:8 | Ñu ne ko: «Ay gént daal a nu dikkal, te amunu ku nu koy firil.» Yuusufa ne leen: «Xanaa du Yàllaa moom piri? Nettalileen ma seeni gént rekk kay.» |
1189 | GEN 40:16 | Kilifag lakk-kati mburu ya nag gis ne piri mi neex na, mu ne Yuusufa: «Man it sama gént gi, xam nga lu ma ci gis? Ñetti pañey mburu mu weex laa yenu, |
1318 | GEN 43:27 | Mu nuyoo ak ñoom, ba noppi laaj leen ne leen: «Seen baay bu màggat, ba ngeen doon wax, mbaa mu ngi dund? Mbaa mu ngi ci jàmm?» |
1329 | GEN 44:4 | Naka lañu génn dëkk ba, te soreeguñu sax, Yuusufa sant fara biir këram, ne ko: «Gaawal dab gaa ña, te boo leen dabee, wax leen ne leen: “Lu tax ñu ji leen njekk, ngeen feye ngoreedi? |
1330 | GEN 44:5 | Ndax li ngeen jël du sama kaasu sang, bi muy naane, rawatina di ko gisaanee? Lu ñaaw ngeen def nii!”» |
1332 | GEN 44:7 | Ñu ne ko: «Kilifa gi, looy wax nii? Nun de, sang bi, jomb nanu loolu! |
1333 | GEN 44:8 | Xaalis bi nu fekkoon ci sunu bunti saaku sax, danoo àndaat ak moom, jóge ba Kanaan, délloosil la ko, kon nan lanu mana sàcce sa kër sang xaalis mbaa wurus? |
1340 | GEN 44:15 | Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?» |
1341 | GEN 44:16 | Yuda ne: «Sang bi, lu nuy waxati? Lu nu mana lay, ba setal sunu bopp? Yàllaa nu feeñal, sang bi. Nanu bokk nun ñépp di say jaam, yem ci kepp ak ki ñu fekk kaas bi ci loxoom.» |
1436 | GEN 47:15 | Ba ñu demee, ba xaalis amatul ca Misra ak ca Kanaan, waa Misra gépp ñëw fa Yuusufa ne ko: «Jox nu ab dund kay! Mbaa du danga nuy seetaan, nuy dee? Ndax xaalis amatul.» |
1440 | GEN 47:19 | Mbaa du danga nuy seetaan, nu bokk sànku ci sa kanam, nook sunu suuf? Ngalla boole nu jënde ab dund, nun ak sunuy suuf. Su ko defee nuy moomeeli Firawna, nun ak sunuy suuf. Te nga jox nu pepp mu nu dunde, lu ko moy kat nun dinanu dee, suuf si it dina booy.» |
1526 | GEN 50:19 | Yuusufa nag ne leen: «Buleen am dara lu ngeen di ragal. Xanaa maay Yàlla? |
1569 | EXO 2:14 | Waa ja ne ko: «Ku la def sunu njiit mbaa sunu àttekat? Xanaa danga maa nara rey, na nga reye woon waa Misra ja?» Musaa nag tiit, naan ca xelam: «Ndeke mbir mi kay siiw na.» |
1575 | EXO 2:20 | Ruwel ne leen: «Ana waa ja? Lu tax ngeen bàyyi ko fa? Wooyileen ko, mu añsi kay!» |
1613 | EXO 4:11 | Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji? |
1616 | EXO 4:14 | Aji Sax ji nag mer ba fees ndax Musaa. Mu ne ko: «Sa mag Aaróona, Leween bi, da fee nekkul? Moom, xam naa ne ku mana wax la. Mu ngi lay gatandusi sax, te bu la gisee, bég. |
1635 | EXO 5:2 | Firawna ne: «Kan mooy Aji Sax ji, ba ma di ko déggal, di bàyyi Israyil, ñuy dem? Xawma sax kuy Aji Sax ji, waxumalaa may bàyyi Israyil, ñuy dem.» |
1637 | EXO 5:4 | Buuru Misra ne leen: «Yeen Musaa ak Aaróona, lu waral ngeen di jële mbooloo mi ci seeni liggéey? Laggleen ca seeni sas waay!» |
1648 | EXO 5:15 | Booba la farbay ngàllog Israyil, dem jooytuji ca Firawna, ne ko: «Sang bi, lu tax nga def nu nii? |
1655 | EXO 5:22 | Musaa dégg loolu, dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Éey Boroom bi, loraange gi nga yóbbe mbooloo mii nag? Loo ma doon yónnee? |
1781 | EXO 10:3 | Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma. |
1785 | EXO 10:7 | Dagi Firawna ya wax Firawna ne ko: «Lu nuy seetaanati, waa jii di nu yóbbe aw ay? Bàyyil bànni Israyil ñii kay, ñu màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Xanaa yéguloo ne Misra tas na?» |
1789 | EXO 10:11 | Mukk laa wax! Du dangeen di màggal Aji Sax ji? Demleen boog, yeen ñiy góor!» Ba loolu amee ñu dàq leen, ñu jóge ca Firawna, |
1895 | EXO 14:5 | Ba ñu yégalee Firawna buuru Misra, ne mbooloo ma daw na, mooki dagam dañoo soppi xalaat ca mbirum bànni Israyil. Ñu ne: «Waaw nun, li nu def nag? Ana luy ndeyi yiwi bànni Israyil, ba dootuñu nu surgawu?» |
1901 | EXO 14:11 | Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra? |
1902 | EXO 14:12 | Xanaa du lii lanu la waxoon ca Misra? Noon nanu la, nga bàyyi nu, nu surgawu waa Misra, ndax surgawu waa Misra moo nu gënal nu dee ci màndiŋ mi!» |
1905 | EXO 14:15 | Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Loo may wooye wall? Waxal bànni Israyil, ne leen ñu dem rekk, |
1932 | EXO 15:11 | «Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme? |
1956 | EXO 16:8 | Musaa teg ca ne: «Moo tax Aji Sax ji dina leen jox yàpp wu ngeen lekk ngoon, te bu bët setee mu jox leen ñam wu leen reggal, ndax Aji Sax jee dégg ngeen di ko diiŋat. Nun lu nu ci? Du nun ngeen di diiŋat waaye yeen ak Aji Sax ji la.» |
1976 | EXO 16:28 | Ca la Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Waaw yeen nag, dungeen ma noppee gàntalal samay santaaneek samay ndigali yoon mukk? |
1986 | EXO 17:2 | Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?» |
1988 | EXO 17:4 | Ba mu ko defee Musaa woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Nu may def ak mbooloo mii? Des na tuuti de, ñu dóor ma ay doj, ba ma dee.» |
2014 | EXO 18:14 | Gorob Musaa gis mboolem la Musaa di defal mbooloo ma. Mu ne ko: «Waaw, ni ngay jëflanteek nit ñi nag? Lu tax ngay toog, di àtte yaw rekk, mbooloo mépp wër la, suba ba ngoon?» |
2141 | EXO 22:26 | Moom doŋŋ la am ci yére, di ko sànge yaramam; su ko ñàkkee, lu muy sàngoo ba tëdd? Te su ma wooyee wall kat, dinaa ci dégg, ndax man Boroom Yërmande laa. |
2450 | EXO 32:11 | Musaa nag tinu Yàllaam Aji Sax ji ne ko: «Aji Sax ji, ana lu waral sam sànj di tàkkal sa ñoñ ñi nga génne réewum Misra ci sa kàttan gu màgg ak sa dooley loxo? |
2995 | LEV 10:17 | «Lu waral lekkuleen sarax biy póotum bàkkaar ci bérab bu sell? Lu sella sell la, ñu jox leen ko, ngeen war koo yenniku bàkkaaru mbooloo mi, ba defal leen seen njotlaay fi kanam Aji Sax ji. |
4036 | NUM 11:11 | Ba mu ko defee Musaa ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, loo may mititale, Sang bi? Lu tee nga baaxe ma, xanaa ngay teg sëfub mii mbooloo mépp ci sama kaw? |
4037 | NUM 11:12 | Xanaa maa ëmb mii mbooloo mépp, am maa leen jur, ba nga di ma leen bootloo fàpp, ni jaboot di boote luy nàmp, jëme leen réew, ma nga giñaloon seeni maam? |
4047 | NUM 11:22 | Diggante jur gu gudd ak gu gàtt, manees na leen cee rendil lu leen doy a? Am mboolem jëni géej lees leen di dajaleel, mu doy leen?» |
4048 | NUM 11:23 | Aji Sax ji ne Musaa: «Loxol Aji Sax ji da koo jotewul? Léegi nag dinga gis ndax sama kàddu dina la sottil, am déet!» |
4054 | NUM 11:29 | Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sol leen ag leeram!» |
4062 | NUM 12:2 | Ñu ne: «Ndax mennum Musaa doŋŋ la Aji Sax jiy waxe ci moom? Xanaa daa waxewul ci nun itam?» Aji Sax ji dégg ca. |
4074 | NUM 12:14 | Aji Sax ji ne Musaa: «Xanaa baayam sax su ko jéppi woon, ba tifli ko ci kanam, muy gàcceem diiru juróom ñaari fan? Nañu ko génne dal bi diiru juróom ñaari fan, door koo délloosi ci biir.» |
4120 | NUM 14:11 | Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Ba kañ la ma askan wii nara xarab? Ba kañ lañu may gëmadi, ak firnde yi ma def ci seen biir yépp? |
4124 | NUM 14:15 | Nga nara boole mbooloo mii mépp, bóom benn yoon? Kon de xeet yi dégg sa jaloore dinañu wax ne: |
4136 | NUM 14:27 | «Ba kañ la mbooloo mu bon mii di ñaxtu ci sama kaw? Ñaxtu yi bànni Israyil di ñaxtu ci sama kaw, dégg naa ci. |
4150 | NUM 14:41 | Musaa ne leen: «Lii nag? Yeena ngi tebbi waxi Aji Sax ji, waaye loolu de du sotti! |
4204 | NUM 16:9 | Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israyil ber ci mbooloom Israyil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla? |
4208 | NUM 16:13 | Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci? |
4209 | NUM 16:14 | Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!» |
4315 | NUM 20:3 | Mbooloo ma di xulook Musaa, naa ko: «Moo lu nu tee woona dee keroog ba sunu bokk ya deeyee fa kanam Aji Sax ji? |
4316 | NUM 20:4 | Ana loo indee mbooloom Aji Sax ji ci màndiŋ mii, nu di fi deesi doŋŋ, nook sunug jur? |
4317 | NUM 20:5 | Ana loo nu jële woon Misra, di nu indi fu bon fii? Du bérab bu nangu menn jiwu: du figg, du reseñ, du gërënaat, te du siitum ndox mu ñu naan!» |
4346 | NUM 21:5 | Ña ngay xultu ca kaw Yàlla ak Musaa, naa: «Lu ngeen nu doon jële Misra, ngir nu dee ci màndiŋ mi? Duw ñam, dum ndox, te wii ñamu toskare génnliku nan!» |
4406 | NUM 22:30 | Mu ne ko: «Xanaa du maay sa mbaam mi ngay war bu yàgg ba nga ma moomee, ba tey jii? Dama laa masa def nii?» Mu ne ko: «Déedéet.» |
4408 | NUM 22:32 | Malaakam Aji Sax ji ne ko: «Lu tax ngay dóor sa mbaam mi ñetti yoon nii? Man mii maa dikk, jànkoonteek yaw, ndax yoonu sànkute laa gis. |
4413 | NUM 22:37 | Balag ne Balaam: «Xanaa yeblewuma woon, ba yebleeti, di la woolu? Lu la tee woona ñëw? Am dama laa manula teral?» |
4414 | NUM 22:38 | Balaam ne Balag: «Maa ngii, wuysi la, waaye mbaa sañ naa waxal sama bopp lenn? Kàddu gu ma Yàlla waxloo de, moom laay wax.» |
4425 | NUM 23:8 | Moo nu may móoloo ku Yàlla móoluwul? Ana nu may rëbbe ku Aji Sax ji rëbbul? |
4427 | NUM 23:10 | Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!» |
4428 | NUM 23:11 | Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Yaw, li nga ma def nag? Móolu samay noon laa la jële, yaw defoo lenn lu moy ñaanal leen?» |