65 | GEN 3:9 | Yàlla Aji Sax ji nag ne Aadama: «Ana nga?» |
67 | GEN 3:11 | Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» |
69 | GEN 3:13 | Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.» |
89 | GEN 4:9 | Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?» |
369 | GEN 15:8 | Ibraam ne ko: «Yaw Aji Sax ji sama Boroom, nan la may wóore ne maa koy moom?» |
390 | GEN 16:8 | Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.» |
415 | GEN 17:17 | Bi Ibraayma déggee loolu, daa sujjóot, ree. Booba ma nga naan ci xelam: «Góoru téeméeri at, ndax dina mana am doom waay? Te Saarata, mi am juróom ñeent fukki at (90) sax, manati naa am doom a?» |
416 | GEN 17:18 | Ibraayma ne Yàlla: «Moo, tee ngaa saxal Ismayla rekk te ànd ak moom?» |
434 | GEN 18:9 | Ñu daldi ko laaj ne ko: «Ana sa soxna Saarata?» Mu ne leen: «Mu ngi ci biir.» |
437 | GEN 18:12 | Ci kaw loolu Saarata ree ci suuf, daldi ne: «Man mu ñor xomm mii, ndax man naa amati boobu bànneex, te sama boroom kër it di mag?» |
453 | GEN 18:28 | Waaye juróom fukk ñooñu jub, su yéesee juróom rekk nag? Mbaa doo tas dëkk bi ndax juróom ñi ci yées?» Aji Sax ji ne ko: «Su ma fa gisee ñeent fukk ak juróom ñu jub, duma ko tas.» |
454 | GEN 18:29 | Ibraayma dellu wax ne: «Su fa ñeent fukk ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Duma def dara ngir ñeent fukk ñooñu.» |
455 | GEN 18:30 | Ibraayma dellooti ne: «Rikk Boroom bi, bu ma mere. Dinaa ci teg lii. Su fa fanweer ñu jub rekk amee nag?» Aji Sax ji ne ko: «Su fa fanweer ñu jub amee, kon duma def dara.» |
456 | GEN 18:31 | Ibraayma neeti: «Léegi ma ñemeeti wax ak yaw boog, Boroom bi! Su ñu doon ñaar fukk rekk nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma ko tas ngir ñaar fukk ñooñu.» |
457 | GEN 18:32 | Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.» |
460 | GEN 19:2 | «Dégluleen ma, ngalla sang yi, siyaare naa leen, tee ngeena dal ak man, su ko defee ngeen jàngu, fanaan ba suba, ngeen xëy topp seen yoon?» Ñu ne ko: «Bàyyil, nu fanaan ci mbedd mi.» |
478 | GEN 19:20 | Gisuloo dëkk bale; jege na, te dëkk bu tuut la, am déet? Ma daw, làquji fa boog, ba mucc?» |
506 | GEN 20:10 | Abimeleg teg ca ne ko: «Te li nga def sax, lu la ci xiir?» |
543 | GEN 21:29 | Abimeleg nag ne Ibraayma: «Lu tax nga ber juróom ñaari xar yooyu?» |
555 | GEN 22:7 | Isaaxa ne baayam Ibraayma: «Baay!» Mu ne ko: «Naam, doom sama.» Isaaxa ne ko: «Sawara saa ngi, matt maa ngi, waaye ana gàtt, bi nuy sarxal?» |
587 | GEN 23:15 | «Déglu ma, kilifa gi, suuf suy jar ñeenti téeméeri dogi xaalis doŋŋ du dara ci sama diggante ak yaw; tee nga faa denc sa néew rekk?» |
597 | GEN 24:5 | Surga ba ne ko: «Su ndaw sa nanguwula ànd ak man ci réew mii nag? Ndax kon damaa wara yóbbu sa doom ba ca réew ma nga jóge?» |
615 | GEN 24:23 | Mu ne ko: «Wax ma, kan moo la jur?» Ak itam: «Ndax man nanoo dal sa kër baay?» |
648 | GEN 24:56 | Mu ne leen: «Gannaaw Aji Sax ji àntal na sama yoon, tee ngeen ma baña yeexal, te bàyyi ma rekk, ma dellu ca sama sang?» |
650 | GEN 24:58 | Ci kaw loolu ñu woo Rebeka, ne ko: «Ndax dangay ànd ak waa ji léegi?» Mu ne: «Waaw.» |
657 | GEN 24:65 | daldi ne surga ba: «Waa jee ci àll biy ñëw, jëm ci nun, kan a?» Surga ba ne ko: «Sama sang la de.» Rebeka daldi jël muuraay ba, muuroo. |
691 | GEN 25:32 | Esawu ne: «Man miy waaja dee ak xiif, ana lu ma céru taaw di jariñ?» |
702 | GEN 26:9 | Abimeleg woolu Isaaxa ne ko: «Kii kay ndeke sa soxna la! Noo mana waxe ne sa jigéen la?» Isaaxa ne ko: «Damaa waxe noonu, ngir ñu bañ maa rey ndax moom.» |
720 | GEN 26:27 | Isaaxa ne leen: «Lu waral ngeen fekksi ma fii, gannaaw dangeen maa bañ, ba dàq ma?» |
746 | GEN 27:18 | Mu dikk ci baayam, ne ko: «Baay.» Mu ne ko: «Naam doom, kooku?» |
748 | GEN 27:20 | Isaaxa ne doomam: «Moo doom! Noo def, ba gaawa jàpp nii?» Yanqóoba ne ko: «Aji Sax jiy sa Yàlla, moo ma ko jagleel.» |
752 | GEN 27:24 | Isaaxa laaj ko ne ko: «Mbaa wóor na ne yaw ay Esawu?» Mu ne ko: «Waawaaw.» |
764 | GEN 27:36 | Esawu ne: «Moom kay moo yey tudd Yanqóoba, ndax suufu na ma ñaari yoon. Sama céru taaw la jëkka nangu, tey mu nangooti sama ñaanu baay.» Mu teg ca ne: «Ndax desalaloo ma ag ñaan?» |
800 | GEN 29:4 | Yanqóoba ne leen: «Bokki fan?» Ñu ne ko: «Karan.» |
801 | GEN 29:5 | Mu ne leen: «Ndax xam ngeen Laban doomu Naxor?» Ñu ne ko: «Xam nanu ko kay.» |
802 | GEN 29:6 | Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» |
821 | GEN 29:25 | Ba bët setee, Yanqóoba fekk muy Leya. Mu ne Laban: «Waaw, li nga ma def nag? Du Rasel a taxoon ma liggéeyal la? Lu tax nga wor ma?» |
833 | GEN 30:2 | Yanqóoba mere ca Rasel ne ko: «Ndax maay Yàlla, mi la teree am doom?» |
846 | GEN 30:15 | Teewul mu ne ko: «Ndax nangu sama jëkkër rekk doyu la, ba nga bëgg cee boole màndaragoor ji ma sama doom indil?» Rasel ne ko: «Kon jox ma ci màndaragoor ji sa doom indi, ma wecci la ko sama ayu tey boog.» |
861 | GEN 30:30 | ndaxte lu néew nga amoon laata may ñëw, te yokku na, ba bare lool, ngir Aji Sax ji da laa barkeel ndax man. Waaye léegi nag, liggéeyal sama waa kër bopp jot na xanaa?» |
862 | GEN 30:31 | Laban dellu ne ko: «Dama ne, ñaata laa lay fey?» Yanqóoba ne ko: «Doo ma jox dara. Boo nangoo lii ma lay wax, dinaa sàmmaat say gàtt, wattu ko. |
904 | GEN 31:30 | Bu la neexee, nga namm sa kër baay, ba dogu caa dem, waaye lu tax nga sàcc sama gàllaaji kër, teg ci?» |
956 | GEN 32:28 | Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.» |
958 | GEN 32:30 | Yanqóoba ne ko: «Waaw, yaw nag noo tudd?» Mu wax ko ne ko: «Loo may laaje sama tur?» ba noppi barkeel ko foofa. |
966 | GEN 33:5 | Naka la Esawu siggi, gis jigéen ñi ak xale yi, mu ne: «Ñii ànd ak yaw ñooy ñan?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa njaboot, gi ma Yàlla baaxe, sang bi.» |
969 | GEN 33:8 | Esawu ne ko: «Waaw, dal bu réy bii ma dajeel, loo ci namm?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa di sàkku nga dalal ma jàmm rekk, sang bi.» |
973 | GEN 33:12 | Gannaaw loolu Esawu ne: «Tee noo ànd dem boog, ma jiitu la?» |
1004 | GEN 34:23 | Bu nu leen nangulee, ba ñu dëkk ci sunu biir, kon seeni jur ak seen alal ak seen mala yépp, ndax du nooy doon boroom?» |
1012 | GEN 34:31 | Ñu ne ko: «Danuy seetaan sunu jigéen daal, ñu di ko def ab gànc?» |
1092 | GEN 37:8 | Mag ya ne ko: «Dangaa nara falu ci sunu kaw? Danga noo nara jiite?» Ñu gënati koo bañ nag ndax géntam ya ak la mu leen ca wax. |
1094 | GEN 37:10 | Ba mu ko nettalee ay magam, ba nettali ko baayam, baayam da koo soow ne ko: «Yaw, li nga gént, lu mu doon? Xanaa du maak sa yaay ak say mag noo lay sujjóotal?» |
1099 | GEN 37:15 | Naka la jenn waay dajeek moom foofa, fekk muy wëreelu ca àll ba. Waa ja ne ko: «Looy seet?» |
1100 | GEN 37:16 | Yuusufa ne ko: «Samay mag laay seet. Xamoo fu ñu tollu, di sàmm?» |
1104 | GEN 37:20 | Nanu ko rey gaaw, sànni ko ca kàmb yee, su ko defee danu naan, rabu àll a ko fàdd. Nu seet ba xam fu muy mujj aki géntam?» |
1116 | GEN 37:32 | Gannaaw loolu ñu yóti seen baay mbubb ma, ne ko: «Lii lanu gis de, xoolal bu baax ndax du sa mbubbu doom?» |
1136 | GEN 38:16 | Mu jàdd, ñëw ba ca moom, ne ko: «May ma, ma ànd ak yaw.» Fekk na xamul woon ne goroom la. Mu ne ko: «Loo may fey, ngir ànd ak man?» |
1138 | GEN 38:18 | Mu ne ko: «Lu ma lay tayle?» Ndaw si ne ko: «Xanaa sa jaarob màndargaal, ak buum, gi mu àndal ak yet, wi ci sa loxo.» Mu jox ko nag, ba noppi ànd ak moom. Fa la doxe ëmb. |
1141 | GEN 38:21 | Mu laaj waa gox ba, ne leen: «Ana gànc biy toog Enayim ci yoon wi?» Ñu ne ko: «Fii de ab gànc nekku fi.» |
1149 | GEN 38:29 | Naka la delloo loxoom, seexam juddu, mu ne ko: «Yaw foo bëtte, ba génn?» Ñu daldi ko tudde Peres (mu firi Bëtt). |
1159 | GEN 39:9 | Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?» |
1180 | GEN 40:7 | Mu laaj jawriñi Firawna, yooyee ñu tëjandoo woon ak moom ca kër sangam, ne leen: «Lu leen tax ne yogg tey?» |
1234 | GEN 41:38 | Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?» |
1254 | GEN 42:1 | Ba Yanqóoba yégee ne pepp am na Misra, daa wax ay doomam yu góor, ne leen: «Lu ngeen di toog, di xoolante rekk?» |
1260 | GEN 42:7 | Naka la Yuusufa gis magam ya, xàmmi leen, te mel ni ku leen xamul, di wax ak ñoom kàddu yu dëgër ne leen: «Fu ngeen jóge?» Ñu ne ko: «Réewu Kanaan lañu jóge, di jëndsi ab dund.» |
1281 | GEN 42:28 | Mu ne doomi baay ya: «Delloo nañu ma sama xaalis, mu ngi nii ci sama saaku.» Seen fit ne tërit, ñuy rag-ragi, ku ne xool sa moroom, naan: «Lu nu Yàlla nattoo nii?» |
1297 | GEN 43:6 | Israyil ne leen: «Ana lu waral ngeen di ma lor, naan waa ja am ngeen jeneen rakk?» |
1318 | GEN 43:27 | Mu nuyoo ak ñoom, ba noppi laaj leen ne leen: «Seen baay bu màggat, ba ngeen doon wax, mbaa mu ngi dund? Mbaa mu ngi ci jàmm?» |
1320 | GEN 43:29 | Naka la Yuusufa ne gees, gis Beñamin rakku doomu ndeyam ja. Mu laaj leen ne leen: «Ndax kii mooy seen rakk, ji ngeen ma doon wax?» La ca tegu mu ne rakkam ja: «Sama ngóor si, yal na la Yàlla defal yiw waay!» |
1340 | GEN 44:15 | Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?» |
1362 | GEN 45:3 | Yuusufa nag ne magam ya: «Man mii maay Yuusufa! Mbaa sama baay a ngi dund?» Magam ya nag manuñu koo tontu, ndax booba njàqare jàpp na leen. |
1424 | GEN 47:3 | Firawna laaj doomi baay ya, ne leen: «Lan mooy seen liggéey?» Ñu ne ko: «Nun de sang bi, ay sàmm lanu naka jekk ca sunuy maam ba tey.» |
1460 | GEN 48:8 | Ci kaw loolu Israyil gis doomi Yuusufa ya. Mu ne: «Ñii ñooy ñan?» |
1522 | GEN 50:15 | Magi Yuusufa ya xam nañu ne seen baay nelaw na. Ña ngay wax ca seen biir naan: «Waaw, mbaa Yuusufa dencalu nu mer, nar noo fey sunu bor ndax lu bon li nu ko ji woon lépp?» |
1551 | EXO 1:18 | Buuru Misra woolu rewlikat ya, ne leen: «Ana lu tax ngeen def lii, di bàyyi liir yu góor yi, ñu dund?» |
1562 | EXO 2:7 | Magu liir ba daldi wax doomu Firawna ja, ne ko: «Ndax ma dem wutali la ku koy nàmpal ci Ebrë yi?» |
1568 | EXO 2:13 | Ca ëllëg sa mu dellu génn, yem ci ñaari Ebrë yuy xeex. Musaa wax ak ka tooñ, ne ko: «Lu tax ngay dóor sa moroom mii?» |
1569 | EXO 2:14 | Waa ja ne ko: «Ku la def sunu njiit mbaa sunu àttekat? Xanaa danga maa nara rey, na nga reye woon waa Misra ja?» Musaa nag tiit, naan ca xelam: «Ndeke mbir mi kay siiw na.» |
1573 | EXO 2:18 | Ba ñu delloo ca seen baay Ruwel, mu laaj leen ne leen: «Lu tax ngeen teela ñibbsi tey?» |
1593 | EXO 3:13 | Musaa ne Yàlla: «Su ma demee ca bànni Israyil, ne leen seen Yàllay maam ya moo ma yónni ca ñoom bànni Israyil de, dinañu ma laaj nu mu tudd. Lu ma leen di wax nag?» |
1603 | EXO 4:1 | Gannaaw loolu Musaa dellu wax Aji Sax ji ne ko: «Waaw, su ñu ma dégluwul te gëmuñu ma, xanaa ne ma: “Aji Sax ji feeñuwu la” nag?» |
1604 | EXO 4:2 | Aji Sax ji ne ko: «Li ci sa loxo lu mu doon?» Mu ne ko: «Aw yet.» |
1647 | EXO 5:14 | Ñuy dóor farbay ngàllo, ga bokk ca bànni Israyil, te saskati liggéey yu Firawna fal leen ngir ñuy jiite bànni Israyil ca liggéey ba. Ña nga leen naan: «Lu waral démb ak tey yépp mataluleen limu móol, yi ñu leen sas, te ngeen daan ko matal?» |
1668 | EXO 6:12 | Musaa tinu Aji Sax ji ne ko: «Waaw, ndegam bànni Israyil sax nanguwuñu maa déglu, nu ma Firawna di déggale, man mii tëlee wax?» |
1686 | EXO 6:30 | Teewul Musaa tinu Aji Sax ji, ne ko: «Waaw, waaye man, damaa tëlee wax. Mbaa Firawna dina ma déggal yee?» |
1785 | EXO 10:7 | Dagi Firawna ya wax Firawna ne ko: «Lu nuy seetaanati, waa jii di nu yóbbe aw ay? Bàyyil bànni Israyil ñii kay, ñu màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Xanaa yéguloo ne Misra tas na?» |
1786 | EXO 10:8 | Ñu délloosi nag Musaak Aaróona ca Firawna, mu ne leen: «Demleen màggali seen Yàlla Aji Sax ji! Waaw, ñiy dem sax, ñan la?» |
1895 | EXO 14:5 | Ba ñu yégalee Firawna buuru Misra, ne mbooloo ma daw na, mooki dagam dañoo soppi xalaat ca mbirum bànni Israyil. Ñu ne: «Waaw nun, li nu def nag? Ana luy ndeyi yiwi bànni Israyil, ba dootuñu nu surgawu?» |
1945 | EXO 15:24 | Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?» |
1963 | EXO 16:15 | Bànni Israyil gis ko, di wax ca seen biir naan: «Lii lu mu?» ndax xamuñu woon lu mu doon. Musaa ne leen: «Lii mooy ñam wi leen Aji Sax ji jox, ngeen lekk. |
1986 | EXO 17:2 | Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?» |
1987 | EXO 17:3 | Mbooloo ma mar na fa, bay xultu ci kaw Musaa, naan: «Loo nu doon jële Misra nag, xanaa du boole nu rey ndax mar, nook sunuy doom ak sunuy gétt?» |
1991 | EXO 17:7 | Bérab boobu la Musaa wooye Maasa (mu firi Nattu). Mu wooye ko itam Meriba (mu firi ab Jote), ndax joteb bànni Israyil ba fa amoon, ak na ñu fa nattoo Aji Sax ji, naan: «Moo Aji Sax ji ndax mu ngi ci sunu biir, am déet?» |
2014 | EXO 18:14 | Gorob Musaa gis mboolem la Musaa di defal mbooloo ma. Mu ne ko: «Waaw, ni ngay jëflanteek nit ñi nag? Lu tax ngay toog, di àtte yaw rekk, mbooloo mépp wër la, suba ba ngoon?» |
2460 | EXO 32:21 | Musaa nag ne Aaróona: «Lan la la mbooloo mii def, ba nga yóbbe leen gii moy gu réy?» |
2490 | EXO 33:16 | Nees di xame ne daj naa saw yiw, maak sa ñoñ, te fekk ànduloo ak nun, ba nu doon, maak sa ñoñ, ñu ràññiku ci biir mboolem xeet yi ci kaw suuf?» |
2997 | LEV 10:19 | Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israyil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen saraxu rendi-dóomal, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?» |
3973 | NUM 9:7 | Ñooñu nag ne Musaa: «Nun de, danoo sobewu ndax ab néew, waaye lu nu teree joxesi saraxu Aji Sax ji ci waxtoom, ci digg bànni Israyil?» |
4047 | NUM 11:22 | Diggante jur gu gudd ak gu gàtt, manees na leen cee rendil lu leen doy a? Am mboolem jëni géej lees leen di dajaleel, mu doy leen?» |
4062 | NUM 12:2 | Ñu ne: «Ndax mennum Musaa doŋŋ la Aji Sax jiy waxe ci moom? Xanaa daa waxewul ci nun itam?» Aji Sax ji dégg ca. |
4068 | NUM 12:8 | Gémmiñ ak gémmiñ laay waxeek moom wax ju leer nàññ ju ñu léebul, te jëmmu Aji Sax ji lay gis. Kon lu leen may fitu ŋàññ Musaa sama jaam bi?» |