9620 | 2KI 4:13 | Mu ne surgaam: «Waxal ma ndaw sii ne ko: “Waaw, yaw de yaa ngi sonn ci nun coono bii bépp! Ana loo bëgg nu defal la ko? Ndax nu waxal la Buur lu jëm ci yaw, am nu wax ak njiital mbooloom xare ma?”» Mu wax ko, mu ne ko: «Jërëjëf, waaye am naa teraanga ci sama biiri bokk.» |
9739 | 2KI 8:8 | Buur ne Asayel, ab jawriñam: «Demal ca góoru Yàlla ga te yóbbaale loo teg ci loxoom, mu seetal ma ci Aji Sax ji. Laajal ma ko ne ko: “Ndax dinaa jóg ci sama wopp jii?”» |
9779 | 2KI 9:19 | Yoram yebalaat beneen gawar. Ba mu àggee ca ñoom, ne leen: «Buur nee: “Mbaa jàmm?”» Yewu ne ko: «Ana luy sa yoon ci jàmm laam déet? Ayca, sama gannaaw.» |
10078 | 2KI 19:13 | Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”» |
18420 | ISA 36:20 | Tuuri réew yii yépp, ana mu ci xettli menn réew ak man, ba Aji Sax ji wara mana xettli, Yerusalem ak man?”» |
18435 | ISA 37:13 | Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”» |
18727 | ISA 49:21 | Dangay mujj naa: “Moo, ku ma jural ñii ñépp? Man mi ñàkkooni doom, manumaa jur, ñu toxal ma, wacc ma; ana ku leen yoroon te ma des, man kenn? Ñii sax, fu ñu ne woon?”» |
18799 | ISA 54:6 | Aji Sax jee la woo, nga dib jeeg bu ñu wacc, sa xol jeex tàkk, Mu ne la: “Nees di wacces ndaw, si nga takk ba ngay ndaw?”» Sa Yàllaa ko wax. |
21013 | EZK 21:5 | Ma ne ko: «Éey Boroom bi Aji Sax ji, ñii déy a ngi wax ci man, naan: “Kii moom xanaa day léeb ak a léebaat rekk?”» |
22397 | JOL 2:17 | Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi, sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, nañu fi taxaw jooy; nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ; bul wacce say séddoo gàcce, ak ñaawley xeeti jaambur yi. Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi, naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”» |
28262 | ROM 10:6 | Waaye njub, gi ngëm di maye, li muy digle mooy: «Bul wax ci sa xel, ne: “Ana kuy yéeg fa kaw?”» nde loolu mooy Almasi wàcc ngay sàkku. |
28263 | ROM 10:7 | «Bul ne it: “Ana kuy wàcci njaniiw?”» nde loolu mooy Almasi dekkiwaat ngay sàkku. |