8815 | 1KI 2:42 | Buur yónnee, woolu Simey, ne ko: «Xanaa giñloowuma la woon ci Aji Sax ji, àrtu la ne la: “Bés boo fi jógee dem fenn, xamal xéll ne dee rekk mooy sa àtte”? Nga ne ma: “Baax na, dinaa la déggal.” |
12723 | EST 1:17 | Nde jëfi lingeer jii dina yegg ci noppi jigéen ñépp, ba tax ñuy sofental seen jëkkër. Ndax dañu naan: “Xanaa Buur Aserus woowul Lingeer Wasti, mu lànk, ne du ñëw”? |
19065 | JER 2:31 | Éey niti Israyili tey, teewluleen kàddug Aji Sax ji! «Ni màndiŋ mi aaye, ndax mas naa nee aaye ci Israyil? Mbaa ma mel ni réewum lëndëm aki loraangeem? Lu waral sama ñoñ naa: “Noo moom sunu bopp, dootunu délsi fi yaw”? |
20920 | EZK 18:2 | «Ana lu waral waxin wi ngeen di waxe fi Israyil naan: “Baay lekk reseñ ju xaay, mu uum gëñi doom ja”? |
23202 | MAL 3:13 | «Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,» Aji Sax jee ko wax. «Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal”? |
25199 | LUK 5:23 | Ana lu gëna yomb ci yii yaar: ne “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne: “Jógal te dox”? |
25481 | LUK 11:7 | te xarit ba àddoo ca biir néegam, ne ko: “Bu ma sonal, tëj naa ba tëdd, maak samay doom; manumaa jóg, di la jox dara”? |
25727 | LUK 17:7 | «Kan ci yeen la ab jaamam di beyi mbaa mu sàmmi ba jóge tool, dikk, mu ne ko: “Kaay, nu lekk”? |