57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
7786 | 1SA 21:12 | Jawriñi Akis ya wax Akis ne ko: «Xanaa kii du Daawuda, boroom réew mi? Du kii lañuy woyal, di fecc, naan: “Sóol jam junneem, Daawuda jam fukki junneem”?» |
7975 | 1SA 29:5 | Xanaa du Daawuda mii lañuy woyal, di fecc, naan: “Sóol jam junneem, Daawuda jam fukki junneem”?» |
18085 | ISA 19:11 | Kàngam ya fa Cowan dañuy teqlikook seen sago, diglekati Firawna yu xelu ya di digle ag ndof. Ma ne: «Yeen diglekat yi, nu ngeen mana waxe Firawna naan: “Nun ay boroom xel lanu, sosoo ca buur ya woon”?» |