8599 | 2SA 21:16 | Ci kaw loolu Isbi Bënob ne dina rey Daawuda — kooku askanu ponkal ya ñu daan wooye Rafayeen, ca la bokkoon. Ñawkay xeejam xànjar la, diise ñetti kilo. Mu yore itam saamar bu bees. |
17489 | ECC 6:2 | Nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja, te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn, waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk, xanaa jaambur di ko xéewloo — loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar. |
22459 | AMO 2:11 | Maa tabboon ci seen doom yu góor ay yonent, tànne ci seen xale yu góor ay séddoo, — am déet, yeen bànni Israyil?» Kàddug Aji Sax jee. |