1597 | EXO 3:17 | Dogu naa leena jële ci seen notaange gii ngeen nekke ci Misra, yóbbu leen ca réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, réew mu meew maak lem ja tuuroo.’ ” |
1625 | EXO 4:23 | Te wax naa la ne la, nga bàyyi sama doom, ndax mu man maa jaamu, nga bañ. Kon nag dinaa rey sa taaw bu góor.’ ”» |
1702 | EXO 7:16 | Wax ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi, moo ma yónni ci yaw. Mu di la wax, ne la: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu jaamuji ma ca màndiŋ ma.’ Yaw nag booba ba tey yaa ngi tanqamlu. |
1704 | EXO 7:18 | su ko defee jën yi ci dex gi dee, dexu Niil gi mujj xasaw, ba waa Misra dootuñu mana naan ci ndoxum Niil.’ ”» |
1734 | EXO 8:19 | te maay musal sama ñoñ ci musiba moomuy dal saw askan. Ëllëg firnde jooju dina am.’ ”» |
1762 | EXO 9:19 | Kon nag sa jur ak mboolem loo am, te mu nekk ci biti, booleel fat fu wóor, ndax lu nekk ci biti te fateesu ko, su tawtee dee, muy nit mbaa mala.’ ”» |
17858 | ISA 7:6 | ‘Nan songi Yuda, tiital leen, nangu ko, fal fa doomu Tabeel buur.’ |
17860 | ISA 7:8 | Damaas a yilif Siri, te Reccin yiliful lu moy Damaas. Fii ak juróom benn fukki at ak juróom Efrayim tas, ba xeet wa réer.’ |
18418 | ISA 36:18 | Bu leen Esekiya sànk, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettli.’ Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettli réewu wenn xeet ci buurub Asiri? |
19349 | JER 13:14 | Su ko defee ma fenqe ku nekk ak mbokkam, fenqe waajur ak doom, ñoom ñépp.’ ”» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Duma ñéeblu, duma yërëm, duma leen ñeewantee faagaagal.» |
19732 | JER 29:28 | Léegi la nu yónnee Babilon bataaxal, ne nu: Dingeen yàgg àll de, kon tabaxleeni kër, dëkke; jëmbatleeni tóokër, lekk ci meññeef mi.’ ”» |
19766 | JER 31:6 | Bés dina ñëw déy, wattukat yéenee fa kaw tundu Efrayim ne: ‘Aycaleen nu yéegi tundu Siyoŋ, fa sunu Yàlla Aji Sax ji.’ ”» |
19907 | JER 35:15 | Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma. |
20105 | JER 44:26 | Kon nag, yeen mboolem Yudeen ñi sanc Misra, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Maa giñ ci sama tur wu màgg.” Aji Sax jee ko wax. “Ma ne: Sama tur, gémmiñug benn Yudeen dootu ko tudd fi mboolem réewum Misra naan: ‘Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund.’ |
20793 | EZK 13:16 | Mooy yonenti Israyil yi jottli Yerusalem waxyu, di leen gisal peeñum jàmm, te jàmm amul.’ Kàddug Boroom bi Aji Sax jee!” |
20996 | EZK 20:32 | Li ngeen mébét ci seen xel du am mukk. Yeena ngi naan: ‘Nan mel ni xeet yépp, mel ni waasoy réew yi, di jaamu bant ak doj.’ |
21023 | EZK 21:15 | Dees koo jonj ngir bóome, jonj koo jonj ba muy tàkk. Ana nu nu mana bége lii? Ngeen ne Aji Sax ji nee: ‘Yetu nguurug Yuda sama doom a ngi fi.’ Waaye saamar bi faalewul benn bant! |
21423 | EZK 35:10 | «“Aji Sax ji nekk fi, nga naan: ‘Ñaari làngi giir yii dëkke seen ñaari réew yii, maa leen moom, noo ciy teg loxo.’ |
21425 | EZK 35:12 | Su boobaa nga xam ne man Aji Sax ji, maa dégg sa jépp waxi ñàkk kersa ja nga nee: ‘Tundi Israyil a ngii ne tasar, dim sëxëtoo mu ñu nu wërsëgale.’ |
21430 | EZK 36:2 | Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw noon bee ne leen: ‘Ñaw! Seen kawte yu yàgg yii, tey nooy boroom.’ ” |
21505 | EZK 38:11 | daldi ne: ‘Maay songi réew mu ne ŋàpp, maay dali ca kaw waa réew mu ne finaax, dëkke xel mu dal, te du tata ju wër fu ñu dëkke, ñoom ñépp, du buntu dëkk, du tëjukaayu bunt.’ |
25547 | LUK 12:19 | Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ” |
25676 | LUK 15:19 | yeyootumaa tuddoo sax sa doom; léegi def ma ni ku bokk ci say surga.’ ” |
25891 | LUK 20:43 | ba ma def say noon, sa ndëggastal.’ ” |
27053 | ACT 2:35 | ba ma def say noon, sa ndëggastalu tànk.’ ” |
27993 | ACT 28:26 | Mu ne: “Demal ci xeet wii, nga ne leen: ‘Yeenay dégloo déglu, dungeen dégg; ngeen xoolee xoole, dungeen gis.’ |